← Suurat yépp
Suurat 3134 aaya

لقمان

Luqman

Luqman

Tekki

Tann làkk

1

الٓمٓ

Aliflammeem

Aliif, Laam, Miim.

2

تِلۡكَ ءَايَٰتُ ٱلۡكِتَٰبِ ٱلۡحَكِيمِ

Tilka ayatu alkitabi alhakeemi

Lii ay laaya la yu Téere bu xereñ,

3

هُدٗى وَرَحۡمَةٗ لِّلۡمُحۡسِنِينَ

Hudan warahmatan lilmuhsineena

jub la, yërmaande la ngir ñuy rafetal ,

4

ٱلَّذِينَ يُقِيمُونَ ٱلصَّلَوٰةَ وَيُؤۡتُونَ ٱلزَّكَوٰةَ وَهُم بِٱلۡأٓخِرَةِ هُمۡ يُوقِنُونَ

Allatheena yuqeemoona alssalata wayutoona alzzakata wahum bialakhirati hum yooqinoona

ñiy taxawal julli, di génne asaka te amug wóolu ci ne àllaaxira dina ñëw.

5

أُوْلَـٰٓئِكَ عَلَىٰ هُدٗى مِّن رَّبِّهِمۡۖ وَأُوْلَـٰٓئِكَ هُمُ ٱلۡمُفۡلِحُونَ

Olaika AAala hudan min rabbihim waolaika humu almuflihoona

Ñooñaa nga tege ca kaw seen yoonu Boroom wu jub xocc wa, te ñoom ñooña ñoo texe.

6

وَمِنَ ٱلنَّاسِ مَن يَشۡتَرِي لَهۡوَ ٱلۡحَدِيثِ لِيُضِلَّ عَن سَبِيلِ ٱللَّهِ بِغَيۡرِ عِلۡمٖ وَيَتَّخِذَهَا هُزُوًاۚ أُوْلَـٰٓئِكَ لَهُمۡ عَذَابٞ مُّهِينٞ

Wamina alnnasi man yashtaree lahwa alhadeethi liyudilla AAan sabeeli Allahi bighayri AAilmin wayattakhithaha huzuwan olaika lahum AAathabun muheenun

Am na ci nit ñuy nëbb xam-xam, di feeñal waxi caaxaan ngir namm a soreel nit ñi, sànk leen, réeral leen yoonu Yàlla ci lu àndul ak xam- xam, weddi ko, jàppe ko ag doyadal. Ñoom ñooña am nañu mbugal muy toroxale.

7

وَإِذَا تُتۡلَىٰ عَلَيۡهِ ءَايَٰتُنَا وَلَّىٰ مُسۡتَكۡبِرٗا كَأَن لَّمۡ يَسۡمَعۡهَا كَأَنَّ فِيٓ أُذُنَيۡهِ وَقۡرٗاۖ فَبَشِّرۡهُ بِعَذَابٍ أَلِيمٍ

Waitha tutla AAalayhi ayatuna walla mustakbiran kaan lam yasmaAAha kaanna fee othunayhi waqran fabashshirhu biAAathabin aleemin

Saa su ñu jàngee Sunuy laaya ci moom, mu dummóoyu mel ni ku ko déggul, mel ni ab saañ dafa nekk ca nopp ya. Yégal ko ne [am na] mbugal mu metti.

8

إِنَّ ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ وَعَمِلُواْ ٱلصَّـٰلِحَٰتِ لَهُمۡ جَنَّـٰتُ ٱلنَّعِيمِ

Inna allatheena amanoo waAAamiloo alssalihati lahum jannatu alnnaAAeemi

Ña gëm tey jëf u yiw, am nañu Àjjanay xéewal,

9

خَٰلِدِينَ فِيهَاۖ وَعۡدَ ٱللَّهِ حَقّٗاۚ وَهُوَ ٱلۡعَزِيزُ ٱلۡحَكِيمُ

Khalideena feeha waAAda Allahi haqqan wahuwa alAAazeezu alhakeemu

dañu fay béel, - ni ko Yàlla dige woon tigi. - Mooy boroom Kàttan, di Ku Xereñ.

10

خَلَقَ ٱلسَّمَٰوَٰتِ بِغَيۡرِ عَمَدٖ تَرَوۡنَهَاۖ وَأَلۡقَىٰ فِي ٱلۡأَرۡضِ رَوَٰسِيَ أَن تَمِيدَ بِكُمۡ وَبَثَّ فِيهَا مِن كُلِّ دَآبَّةٖۚ وَأَنزَلۡنَا مِنَ ٱلسَّمَآءِ مَآءٗ فَأَنۢبَتۡنَا فِيهَا مِن كُلِّ زَوۡجٖ كَرِيمٍ

Khalaqa alssamawati bighayri AAamadin tarawnaha waalqa fee alardi rawasiya an tameeda bikum wabaththa feeha min kulli dabbatin waanzalna mina alssamai maan faanbatna feeha min kulli zawjin kareemin

Moo bind asamaan si ci lu àndul ak keno yu ngeen di mën a gis ; Moo def ay doj ci biir suuf ngir mu bañ jeriku ak yéen ; def na ci xeetu mala wu nekk. Te nun, Yàlla wàcceel nanu ndox mu bawoo asamaan, nu saxal ci ay yóllent ci xeetu gàncax wu nekk.(s)

11

هَٰذَا خَلۡقُ ٱللَّهِ فَأَرُونِي مَاذَا خَلَقَ ٱلَّذِينَ مِن دُونِهِۦۚ بَلِ ٱلظَّـٰلِمُونَ فِي ضَلَٰلٖ مُّبِينٖ

Hatha khalqu Allahi faaroonee matha khalaqa allatheena min doonihi bali alththalimoona fee dalalin mubeenin

“Lii mooy li Yàlla sàkk. Kon wonleen ma, ña dul Moom, ana lu ñu sàkk ñoom ?”. Li am kay mooy, tooñkat ya ñi ngi ci réer gu bir .

12

وَلَقَدۡ ءَاتَيۡنَا لُقۡمَٰنَ ٱلۡحِكۡمَةَ أَنِ ٱشۡكُرۡ لِلَّهِۚ وَمَن يَشۡكُرۡ فَإِنَّمَا يَشۡكُرُ لِنَفۡسِهِۦۖ وَمَن كَفَرَ فَإِنَّ ٱللَّهَ غَنِيٌّ حَمِيدٞ

Walaqad atayna luqmana alhikmata ani oshkur lillahi waman yashkur fainnama yashkuru linafsihi waman kafara fainna Allaha ghaniyyun hameedun

Joxoon Nanu Luqmaan xam-xamu xereñ, ne ko : “Santal Yàlla, [gërëm Ko], ku Ko sant ci di Ko dello jukkal, boppam ; ku Ko xarab it..., [Na xam ni] Yàlla ku doylu la, Yayoowaakoonug cant la”.

13

وَإِذۡ قَالَ لُقۡمَٰنُ لِٱبۡنِهِۦ وَهُوَ يَعِظُهُۥ يَٰبُنَيَّ لَا تُشۡرِكۡ بِٱللَّهِۖ إِنَّ ٱلشِّرۡكَ لَظُلۡمٌ عَظِيمٞ

Waith qala luqmanu liibnihi wahuwa yaAAithuhu ya bunayya la tushrik biAllahi inna alshshirka lathulmun AAatheemun

[Fàttalikul] ba Luqmaan waxee doomam ja, di ko waar, naan ko : “Yaw samas doom, bul bokkaale mukk dara ak Yàlla, ndax bokkaale kat ag tooñ gu réy la”.

14

وَوَصَّيۡنَا ٱلۡإِنسَٰنَ بِوَٰلِدَيۡهِ حَمَلَتۡهُ أُمُّهُۥ وَهۡنًا عَلَىٰ وَهۡنٖ وَفِصَٰلُهُۥ فِي عَامَيۡنِ أَنِ ٱشۡكُرۡ لِي وَلِوَٰلِدَيۡكَ إِلَيَّ ٱلۡمَصِيرُ

Wawassayna alinsana biwalidayhi hamalathu ommuhu wahnan AAala wahnin wafisaluhu fee AAamayni ani oshkur lee waliwalidayka ilayya almaseeru

Dénk Nanu nit muy rafetal jëme ci ñaari waajuram ; ndax yaayam ëmb na ko muy coono ci biir coono : ba feral ko diirub ñaari at. “Nanga may sant Man [Yàlla] ak sa ñaari waajur. Ci Man la lépp di mujj.

15

وَإِن جَٰهَدَاكَ عَلَىٰٓ أَن تُشۡرِكَ بِي مَا لَيۡسَ لَكَ بِهِۦ عِلۡمٞ فَلَا تُطِعۡهُمَاۖ وَصَاحِبۡهُمَا فِي ٱلدُّنۡيَا مَعۡرُوفٗاۖ وَٱتَّبِعۡ سَبِيلَ مَنۡ أَنَابَ إِلَيَّۚ ثُمَّ إِلَيَّ مَرۡجِعُكُمۡ فَأُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمۡ تَعۡمَلُونَ

Wain jahadaka AAala an tushrika bee ma laysa laka bihi AAilmun fala tutiAAhuma wasahibhuma fee alddunya maAAroofan waittabiAA sabeela man anaba ilayya thumma ilayya marjiAAukum faonabbiokum bima kuntum taAAmaloona

Saa su ñu la sonnalee ci bëgg nga bokkaale Maak loo amul xam-xam, bulen ca topp ; waaye nangay ànd ak ñoom ci àddina si ak njekk. Te nanga topp yoon wa jëmsi ci Man. Fi Man ngeen di mujje [yéen ñépp], su ko defee, Ma téqantalal leen la ngeen daan def ”.

16

يَٰبُنَيَّ إِنَّهَآ إِن تَكُ مِثۡقَالَ حَبَّةٖ مِّنۡ خَرۡدَلٖ فَتَكُن فِي صَخۡرَةٍ أَوۡ فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ أَوۡ فِي ٱلۡأَرۡضِ يَأۡتِ بِهَا ٱللَّهُۚ إِنَّ ٱللَّهَ لَطِيفٌ خَبِيرٞ

Ya bunayya innaha in taku mithqala habbatin min khardalin fatakun fee sakhratin aw fee alssamawati aw fee alardi yati biha Allahu inna Allaha lateefun khabeerun

“Yaw sama doom, dIisaay woowu, doonte la sax dafa tollu ni as fepp, nekk ci kaw doj mbaa ci biir asamaan yi, walla ci biir suuf, du tee Yàlla indi ko . Yàlla Ku deñ-kumpa la .

17

يَٰبُنَيَّ أَقِمِ ٱلصَّلَوٰةَ وَأۡمُرۡ بِٱلۡمَعۡرُوفِ وَٱنۡهَ عَنِ ٱلۡمُنكَرِ وَٱصۡبِرۡ عَلَىٰ مَآ أَصَابَكَۖ إِنَّ ذَٰلِكَ مِنۡ عَزۡمِ ٱلۡأُمُورِ

Ya bunayya aqimi alssalata wamur bialmaAAroofi wainha AAani almunkari waisbir AAala ma asabaka inna thalika min AAazmi alomoori

Yaw sama doom, taxawalal julli tey digle njekk, te it nangay tere njekkar, te it nangay muñ li lay dal. Loolu mooy dégu !

18

وَلَا تُصَعِّرۡ خَدَّكَ لِلنَّاسِ وَلَا تَمۡشِ فِي ٱلۡأَرۡضِ مَرَحًاۖ إِنَّ ٱللَّهَ لَا يُحِبُّ كُلَّ مُخۡتَالٖ فَخُورٖ

Wala tusaAAAAir khaddaka lilnnasi wala tamshi fee alardi marahan inna Allaha la yuhibbu kulla mukhtalin fakhoorin

Bul dox di dummóoyu nit ñi, bul dox it di fuukarewu : Yàlla safoowul képp kuy fuukarewu ak a damu.

19

وَٱقۡصِدۡ فِي مَشۡيِكَ وَٱغۡضُضۡ مِن صَوۡتِكَۚ إِنَّ أَنكَرَ ٱلۡأَصۡوَٰتِ لَصَوۡتُ ٱلۡحَمِيرِ

Waiqsid fee mashyika waoghdud min sawtika inna ankara alaswati lasawtu alhameeri

Nangay teey ci sab dox, te nangay suufeel sa kàddu, ndax kàddu gi gën a suufe moo di kàddug mbaam sëf ”.

20

أَلَمۡ تَرَوۡاْ أَنَّ ٱللَّهَ سَخَّرَ لَكُم مَّا فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَمَا فِي ٱلۡأَرۡضِ وَأَسۡبَغَ عَلَيۡكُمۡ نِعَمَهُۥ ظَٰهِرَةٗ وَبَاطِنَةٗۗ وَمِنَ ٱلنَّاسِ مَن يُجَٰدِلُ فِي ٱللَّهِ بِغَيۡرِ عِلۡمٖ وَلَا هُدٗى وَلَا كِتَٰبٖ مُّنِيرٖ

Alam taraw anna Allaha sakhkhara lakum ma fee alssamawati wama fee alardi waasbagha AAalaykum niAAamahu thahiratan wabatinatan wamina alnnasi man yujadilu fee Allahi bighayri AAilmin wala hudan wala kitabin muneerin

Xanaa gisuleen ne Yàllaa leen tàggatal li nekk ci asamaan yeek suuf si ? Te Mu tuur leen xéewalam yi ci li feeñ ak li nëbbu. Am na ci nit ñi ñuy dàggasante ci mbiri Yàlla, te amuñu ca benn xam-xam, du càggenu ag gindiku, waxantumalaak Téere buy gindi.

21

وَإِذَا قِيلَ لَهُمُ ٱتَّبِعُواْ مَآ أَنزَلَ ٱللَّهُ قَالُواْ بَلۡ نَتَّبِعُ مَا وَجَدۡنَا عَلَيۡهِ ءَابَآءَنَآۚ أَوَلَوۡ كَانَ ٱلشَّيۡطَٰنُ يَدۡعُوهُمۡ إِلَىٰ عَذَابِ ٱلسَّعِيرِ

Waitha qeela lahumu ittabiAAoo ma anzala Allahu qaloo bal nattabiAAu ma wajadna AAalayhi abaana awalaw kana alshshaytanu yadAAoohum ila AAathabi alssaAAeeri

Te bu ñu leen waxee ne : “Toppleen li Yàlla wàcce”, dañu naan : “Nuy kay dañuy topp sunu baaxi maam”. Moo ndax Séytaane daawuleen woo jëme leen ci mbugalum Safara !

22

۞وَمَن يُسۡلِمۡ وَجۡهَهُۥٓ إِلَى ٱللَّهِ وَهُوَ مُحۡسِنٞ فَقَدِ ٱسۡتَمۡسَكَ بِٱلۡعُرۡوَةِ ٱلۡوُثۡقَىٰۗ وَإِلَى ٱللَّهِ عَٰقِبَةُ ٱلۡأُمُورِ

Waman yuslim wajhahu ila Allahi wahuwa muhsinun faqadi istamsaka bialAAurwati alwuthqa waila Allahi AAaqibatu alomoori

Képp ku jébbal Yàlla boppam tey rafetal, [na xam ne] ŋoy na ci buum gi gën a dëgër. Te ca Yàlla la mbir yépp di mujj.(h)

23

وَمَن كَفَرَ فَلَا يَحۡزُنكَ كُفۡرُهُۥٓۚ إِلَيۡنَا مَرۡجِعُهُمۡ فَنُنَبِّئُهُم بِمَا عَمِلُوٓاْۚ إِنَّ ٱللَّهَ عَلِيمُۢ بِذَاتِ ٱلصُّدُورِ

Waman kafara fala yahzunka kufruhu ilayna marjiAAuhum fanunabbiohum bima AAamiloo inna Allaha AAaleemun bithati alssudoori

Képp ku weddi it, weddeem ga bumu la jaaxal : danañu dellusi ci Nun, ñu xibaar leen la ñu jëfoon. Yàlla xam na xéll li nekk ci dënn yi.

24

نُمَتِّعُهُمۡ قَلِيلٗا ثُمَّ نَضۡطَرُّهُمۡ إِلَىٰ عَذَابٍ غَلِيظٖ

NumattiAAuhum qaleelan thumma nadtarruhum ila AAathabin ghaleethin

Dananu leen bànneexal as ndiir ; daldi leen mbaq ci mbugal mu diis.

25

وَلَئِن سَأَلۡتَهُم مَّنۡ خَلَقَ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضَ لَيَقُولُنَّ ٱللَّهُۚ قُلِ ٱلۡحَمۡدُ لِلَّهِۚ بَلۡ أَكۡثَرُهُمۡ لَا يَعۡلَمُونَ

Walain saaltahum man khalaqa alssamawati waalarda layaqoolunna Allahu quli alhamdu lillahi bal aktharuhum la yaAAlamoona

Te su leen laajoon : “Ku bind asamaan yeek suuf si ?”, kon ñu ne : “Yàlla !”. Waxal : “Cant ñeel na Yàlla !”. Waaye ñi ëpp ci ñoom xamuñu.

26

لِلَّهِ مَا فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِۚ إِنَّ ٱللَّهَ هُوَ ٱلۡغَنِيُّ ٱلۡحَمِيدُ

Lillahi ma fee alssamawati waalardi inna Allaha huwa alghaniyyu alhameedu

Yàllaa moom li ci asamaan yeek suuf si. Yàlla Ku doylu la, di Yayoowaakoonub cant !

27

وَلَوۡ أَنَّمَا فِي ٱلۡأَرۡضِ مِن شَجَرَةٍ أَقۡلَٰمٞ وَٱلۡبَحۡرُ يَمُدُّهُۥ مِنۢ بَعۡدِهِۦ سَبۡعَةُ أَبۡحُرٖ مَّا نَفِدَتۡ كَلِمَٰتُ ٱللَّهِۚ إِنَّ ٱللَّهَ عَزِيزٌ حَكِيمٞ

Walaw annama fee alardi min shajaratin aqlamun waalbahru yamudduhu min baAAdihi sabAAatu abhurin ma nafidat kalimatu Allahi inna Allaha AAazeezun hakeemun

Su fekkoon ne mboolem li nekk ci suuf si ciy garab, dafa doon ay xalima, géej gi amaat yeneen juróom-ñaari géej yu koy dolli, lépp di daa, kon dey du tax kàdduy Yàlla jeex. Yàlla Borom Kàttan la, di Ku Xereñ.

28

مَّا خَلۡقُكُمۡ وَلَا بَعۡثُكُمۡ إِلَّا كَنَفۡسٖ وَٰحِدَةٍۚ إِنَّ ٱللَّهَ سَمِيعُۢ بَصِيرٌ

Ma khalqukum wala baAAthukum illa kanafsin wahidatin inna Allaha sameeAAun baseerun

Seenug sosu ak seenug dekkiwaat yéen ñépp, mi ngi yombe Yàlla ni benn bakkan kepp. Yàlla Kuy Dégg la, Kuy Gis la.

29

أَلَمۡ تَرَ أَنَّ ٱللَّهَ يُولِجُ ٱلَّيۡلَ فِي ٱلنَّهَارِ وَيُولِجُ ٱلنَّهَارَ فِي ٱلَّيۡلِ وَسَخَّرَ ٱلشَّمۡسَ وَٱلۡقَمَرَۖ كُلّٞ يَجۡرِيٓ إِلَىٰٓ أَجَلٖ مُّسَمّٗى وَأَنَّ ٱللَّهَ بِمَا تَعۡمَلُونَ خَبِيرٞ

Alam tara anna Allaha yooliju allayla fee alnnahari wayooliju alnnahara fee allayli wasakhkhara alshshamsa waalqamara kullun yajree ila ajalin musamman waanna Allaha bima taAAmaloona khabeerun

Xanaa gisoo ne Yàlla mooy dugal guddi ci bëccëg, Moom dugal it bëccëg it ci guddi, Moo tàggat jant beek weer wi, ku ca nekk a ngay daw ci ab dig bu ñu ko àppal ? Te Yàlla Ku Deñ- kumpa la, Ku Xàmmee li ngeen di def la.

30

ذَٰلِكَ بِأَنَّ ٱللَّهَ هُوَ ٱلۡحَقُّ وَأَنَّ مَا يَدۡعُونَ مِن دُونِهِ ٱلۡبَٰطِلُ وَأَنَّ ٱللَّهَ هُوَ ٱلۡعَلِيُّ ٱلۡكَبِيرُ

Thalika bianna Allaha huwa alhaqqu waanna ma yadAAoona min doonihi albatilu waanna Allaha huwa alAAaliyyu alkabeeru

[Loolu nag] ngir xam ne Yàlla mooy dëgg, lépp lu ngeen mën a jaamu te du Moom, neen la te Yàlla moo di Aji-kawe, di Ku màgg.

31

أَلَمۡ تَرَ أَنَّ ٱلۡفُلۡكَ تَجۡرِي فِي ٱلۡبَحۡرِ بِنِعۡمَتِ ٱللَّهِ لِيُرِيَكُم مِّنۡ ءَايَٰتِهِۦٓۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَأٓيَٰتٖ لِّكُلِّ صَبَّارٖ شَكُورٖ

Alam tara anna alfulka tajree fee albahri biniAAmati Allahi liyuriyakum min ayatihi inna fee thalika laayatin likulli sabbarin shakoorin

Xanaa gisuloo ne gaal a ngay daw ci biir géej, mu bokk ci xéewali Yàlla yi ? Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ñeel bépp santaakoon, dib muñaakoon.

32

وَإِذَا غَشِيَهُم مَّوۡجٞ كَٱلظُّلَلِ دَعَوُاْ ٱللَّهَ مُخۡلِصِينَ لَهُ ٱلدِّينَ فَلَمَّا نَجَّىٰهُمۡ إِلَى ٱلۡبَرِّ فَمِنۡهُم مُّقۡتَصِدٞۚ وَمَا يَجۡحَدُ بِـَٔايَٰتِنَآ إِلَّا كُلُّ خَتَّارٖ كَفُورٖ

Waitha ghashiyahum mawjun kaalththulali daAAawoo Allaha mukhliseena lahu alddeena falamma najjahum ila albarri faminhum muqtasidun wama yajhadu biayatina illa kullu khattarin kafoorin

Bu leen duus yi muuree ba mel ni ker, ñuy woo Yàlla, di Ko sellal ; bu leen musalee ba [ñu génn ci jéeri ji], mu amaat ca ñoom ñuy diiŋat ; te Sunuy kàddu kenn du ko diiŋat ku dul ku goreedi, di ab xarabaakoon.

33

يَـٰٓأَيُّهَا ٱلنَّاسُ ٱتَّقُواْ رَبَّكُمۡ وَٱخۡشَوۡاْ يَوۡمٗا لَّا يَجۡزِي وَالِدٌ عَن وَلَدِهِۦ وَلَا مَوۡلُودٌ هُوَ جَازٍ عَن وَالِدِهِۦ شَيۡـًٔاۚ إِنَّ وَعۡدَ ٱللَّهِ حَقّٞۖ فَلَا تَغُرَّنَّكُمُ ٱلۡحَيَوٰةُ ٱلدُّنۡيَا وَلَا يَغُرَّنَّكُم بِٱللَّهِ ٱلۡغَرُورُ

Ya ayyuha alnnasu ittaqoo rabbakum waikhshaw yawman la yajzee walidun AAan waladihi wala mawloodun huwa jazin AAan walidihi shayan inna waAAda Allahi haqqun fala taghurrannakumu alhayatu alddunya wala yaghurrannakum biAllahi algharooru

Éy yéen nit ñi ! Ragal-leen seen Boroom [te di Ko wattandiku], te nangeen tiit ci Bis boo xam ne baay du warlul doom dara, doom it du warlul baayam dara. [Fexeleen it] ba buleen Séytaane tax ngeen faku. (s)

34

إِنَّ ٱللَّهَ عِندَهُۥ عِلۡمُ ٱلسَّاعَةِ وَيُنَزِّلُ ٱلۡغَيۡثَ وَيَعۡلَمُ مَا فِي ٱلۡأَرۡحَامِۖ وَمَا تَدۡرِي نَفۡسٞ مَّاذَا تَكۡسِبُ غَدٗاۖ وَمَا تَدۡرِي نَفۡسُۢ بِأَيِّ أَرۡضٖ تَمُوتُۚ إِنَّ ٱللَّهَ عَلِيمٌ خَبِيرُۢ

Inna Allaha AAindahu AAilmu alssaAAati wayunazzilu alghaytha wayaAAlamu ma fee alarhami wama tadree nafsun matha taksibu ghadan wama tadree nafsun biayyi ardin tamootu inna Allaha AAaleemun khabeerun

Xam-xamu Bis-pénc baa ngi ca Yàlla ; Mooy wàcce tawu waame ; Moo xam li nekk ci jurukaay ya. Benn bakkan xamul lu muy fàggu ëllëg, benn bakkan xamul it ci san suuf lay deewe. Yàlla Ku Xam la, Ku Xàmmee la. Saar 32 : Sujjóot 30 Laaya