← Suurat yépp
Suurat 6114 aaya

الصف

As-Saf

The Ranks

Tekki

Tann làkk

1

سَبَّحَ لِلَّهِ مَا فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَمَا فِي ٱلۡأَرۡضِۖ وَهُوَ ٱلۡعَزِيزُ ٱلۡحَكِيمُ

Sabbaha lillahi ma fee alssamawati wama fee alardi wahuwa alAAazeezu alhakeemu

Ñi nekk ci asamaan yeek suuf si ña ngay sàbbaal Yàlla, te Moom moo di Boroom Kàttan ga, di Ku Xereñ ka.(s)

2

يَـٰٓأَيُّهَا ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ لِمَ تَقُولُونَ مَا لَا تَفۡعَلُونَ

Ya ayyuha allatheena amanoo lima taqooloona ma la tafAAaloona

Eey yéen ñi gëm ! Ana lan moo tax ngeen di wax lu ngeen dul def ?

3

كَبُرَ مَقۡتًا عِندَ ٱللَّهِ أَن تَقُولُواْ مَا لَا تَفۡعَلُونَ

Kabura maqtan AAinda Allahi an taqooloo ma la tafAAaloona

Wax ji ngeen di wax te du ngeen ko def ak jéppi gu rëy (la leen di jural ca Yàlla).

4

إِنَّ ٱللَّهَ يُحِبُّ ٱلَّذِينَ يُقَٰتِلُونَ فِي سَبِيلِهِۦ صَفّٗا كَأَنَّهُم بُنۡيَٰنٞ مَّرۡصُوصٞ

Inna Allaha yuhibbu allatheena yuqatiloona fee sabeelihi saffan kaannahum bunyanun marsoosun

Yàlla safoona ñiy xeex ci yoonam wi def senn sàppe melni ñoom tabax bu ñu raax la ñu.

5

وَإِذۡ قَالَ مُوسَىٰ لِقَوۡمِهِۦ يَٰقَوۡمِ لِمَ تُؤۡذُونَنِي وَقَد تَّعۡلَمُونَ أَنِّي رَسُولُ ٱللَّهِ إِلَيۡكُمۡۖ فَلَمَّا زَاغُوٓاْ أَزَاغَ ٱللَّهُ قُلُوبَهُمۡۚ وَٱللَّهُ لَا يَهۡدِي ٱلۡقَوۡمَ ٱلۡفَٰسِقِينَ

Waith qala moosa liqawmihi ya qawmi lima tuthoonanee waqad taAAlamoona annee rasoolu Allahi ilaykum falamma zaghoo azagha Allahu quloobahum waAllahu la yahdee alqawma alfasiqeena

(Fàttalikul) Ba Muusaa waxee aw nitam ne leen : “Yéen samaw nit ! Ana lan moo tax ba ngeen di ma lor te xam ngeen xell ne man mii Yonentub Yàlla laa ci yéen ?” Bu ñu jengee, Yàlla jengal seeni xol, te Yàlla du gindi mukk aw nit ñu di ay saay-saay.

6

وَإِذۡ قَالَ عِيسَى ٱبۡنُ مَرۡيَمَ يَٰبَنِيٓ إِسۡرَـٰٓءِيلَ إِنِّي رَسُولُ ٱللَّهِ إِلَيۡكُم مُّصَدِّقٗا لِّمَا بَيۡنَ يَدَيَّ مِنَ ٱلتَّوۡرَىٰةِ وَمُبَشِّرَۢا بِرَسُولٖ يَأۡتِي مِنۢ بَعۡدِي ٱسۡمُهُۥٓ أَحۡمَدُۖ فَلَمَّا جَآءَهُم بِٱلۡبَيِّنَٰتِ قَالُواْ هَٰذَا سِحۡرٞ مُّبِينٞ

Waith qala AAeesa ibnu maryama ya banee israeela innee rasoolu Allahi ilaykum musaddiqan lima bayna yadayya mina alttawrati wamubashshiran birasoolin yatee min baAAdee ismuhu ahmadu falamma jaahum bialbayyinati qaloo hatha sihrun mubeenun

(Fàttalikul it) Ba Iisaa doomu Maryaama waxee ne : “eey yéen waa giir Banii-Israayiil, man mii Yonentub Yàlla laa ci yéen, may dëggal la ma jiitu woon, ca Tawraat, di bégale it, ci Yonent buy dikk sama ginnaaw aw turam di “Ahmadu”. Waaye ba mu leen dikkale ak ay firnde yu leer , dañoo wax ne : “Lii kat ag njibarla gu bir ne fàŋŋ”.

7

وَمَنۡ أَظۡلَمُ مِمَّنِ ٱفۡتَرَىٰ عَلَى ٱللَّهِ ٱلۡكَذِبَ وَهُوَ يُدۡعَىٰٓ إِلَى ٱلۡإِسۡلَٰمِۚ وَٱللَّهُ لَا يَهۡدِي ٱلۡقَوۡمَ ٱلظَّـٰلِمِينَ

Waman athlamu mimmani iftara AAala Allahi alkathiba wahuwa yudAAa ila alislami waAllahu la yahdee alqawma alththalimeena

Ana kan moo gën a doon tooñkat kuy duural Yàlla ay fen, te ña nga koy woo jëme ko ci Lislaam ? Yàlla dey du gindi aw nit ñu di ay tooñkat.

8

يُرِيدُونَ لِيُطۡفِـُٔواْ نُورَ ٱللَّهِ بِأَفۡوَٰهِهِمۡ وَٱللَّهُ مُتِمُّ نُورِهِۦ وَلَوۡ كَرِهَ ٱلۡكَٰفِرُونَ

Yureedoona liyutfioo noora Allahi biafwahihim waAllahu mutimmu noorihi walaw kariha alkafiroona

Ñoom dañoo bëgg fay leerug Yàlla ci seeni gimiñ, te Yàlla moom kuy mottali la ag leeram doontele sax Yéefër yi dañuy bañ.

9

هُوَ ٱلَّذِيٓ أَرۡسَلَ رَسُولَهُۥ بِٱلۡهُدَىٰ وَدِينِ ٱلۡحَقِّ لِيُظۡهِرَهُۥ عَلَى ٱلدِّينِ كُلِّهِۦ وَلَوۡ كَرِهَ ٱلۡمُشۡرِكُونَ

Huwa allathee arsala rasoolahu bialhuda wadeeni alhaqqi liyuthhirahu AAala alddeeni kullihi walaw kariha almushrikoona

Moom moo yónni ab Yonentam ci njub ak diiney dëgg, ngir mu kawe mbooleem diine yi, doonte la sax Yéefër yi dañuy bañ.

10

يَـٰٓأَيُّهَا ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ هَلۡ أَدُلُّكُمۡ عَلَىٰ تِجَٰرَةٖ تُنجِيكُم مِّنۡ عَذَابٍ أَلِيمٖ

Ya ayyuha allatheena amanoo hal adullukum AAala tijaratin tunjeekum min AAathabin aleemin

Eey yéen ñi gëm ! Moo ndax du ma leen tektal ci am njoló mu leen di musël ci mbugël mu mitti ?

11

تُؤۡمِنُونَ بِٱللَّهِ وَرَسُولِهِۦ وَتُجَٰهِدُونَ فِي سَبِيلِ ٱللَّهِ بِأَمۡوَٰلِكُمۡ وَأَنفُسِكُمۡۚ ذَٰلِكُمۡ خَيۡرٞ لَّكُمۡ إِن كُنتُمۡ تَعۡلَمُونَ

Tuminoona biAllahi warasoolihi watujahidoona fee sabeeli Allahi biamwalikum waanfusikum thalikum khayrun lakum in kuntum taAAlamoona

Dangeen di gëm Yàlla ak ub Yonentam tey xare ci yoonu Yàlla ak seeni alal ak seeni bakkan, looloo gën ci yéen de, cëy bu ngeen xamoon !

12

يَغۡفِرۡ لَكُمۡ ذُنُوبَكُمۡ وَيُدۡخِلۡكُمۡ جَنَّـٰتٖ تَجۡرِي مِن تَحۡتِهَا ٱلۡأَنۡهَٰرُ وَمَسَٰكِنَ طَيِّبَةٗ فِي جَنَّـٰتِ عَدۡنٖۚ ذَٰلِكَ ٱلۡفَوۡزُ ٱلۡعَظِيمُ

Yaghfir lakum thunoobakum wayudkhilkum jannatin tajree min tahtiha alanharu wamasakina tayyibatan fee jannati AAadnin thalika alfawzu alAAatheemu

kon dey dana leen jéggal seeni bàkkaar te it dana leen tàbbal ay Àjjana yu ay dex di daw ci suufam, ak ay dëkkuwaay yu teey ci Àjjanay adan ? Loolu mooy texe gu mag ga

13

وَأُخۡرَىٰ تُحِبُّونَهَاۖ نَصۡرٞ مِّنَ ٱللَّهِ وَفَتۡحٞ قَرِيبٞۗ وَبَشِّرِ ٱلۡمُؤۡمِنِينَ

Waokhra tuhibboonaha nasrun mina Allahi wafathun qarreebun wabashshiri almumineena

dana leen defal it yeneeni mbir yu ngeen bëgg : ndimbal [lu bawoo] fa Yàlla ak ndam lu jige. Bégalal jullit ñi ci xibaar bu neex bi.

14

يَـٰٓأَيُّهَا ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ كُونُوٓاْ أَنصَارَ ٱللَّهِ كَمَا قَالَ عِيسَى ٱبۡنُ مَرۡيَمَ لِلۡحَوَارِيِّـۧنَ مَنۡ أَنصَارِيٓ إِلَى ٱللَّهِۖ قَالَ ٱلۡحَوَارِيُّونَ نَحۡنُ أَنصَارُ ٱللَّهِۖ فَـَٔامَنَت طَّآئِفَةٞ مِّنۢ بَنِيٓ إِسۡرَـٰٓءِيلَ وَكَفَرَت طَّآئِفَةٞۖ فَأَيَّدۡنَا ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ عَلَىٰ عَدُوِّهِمۡ فَأَصۡبَحُواْ ظَٰهِرِينَ

Ya ayyuha allatheena amanoo koonoo ansara Allahi kama qala AAeesa ibnu maryama lilhawariyyeena man ansaree ila Allahi qala alhawariyyoona nahnu ansaru Allahi faamanat taifatun min banee israeela wakafarat taifatun faayyadna allatheena amanoo AAala AAaduwwihim faasbahoo thahireena

eey yéen ñi gëm ! Nangeen doon ay farandooy Yàlla, kem ni Iisaa doomu Maryaama waxe woon taalibeem ya ne leen : “ Ana ñan ñooy doon samay farandoo yi jëm ci Yàlla ?” – Taalube ya ne ko : “Nun ñoo di farandoo ya jëm ca Yàlla”. Mu am Kureel ci Banii-Israayiila bu gëm na, mu am it Kureel bu weddi. Nu daldi dooleel ña gëm ca kaw seeni noon, ñu daldi am ndam. Saar 62 : Àjjuma 11 - Laaya