← Suurat yépp
Suurat 6211 aaya

الجمعة

Al-Jumu'ah

The Congregation, Friday

Tekki

Tann làkk

1

يُسَبِّحُ لِلَّهِ مَا فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَمَا فِي ٱلۡأَرۡضِ ٱلۡمَلِكِ ٱلۡقُدُّوسِ ٱلۡعَزِيزِ ٱلۡحَكِيمِ

Yusabbihu lillahi ma fee alssamawati wama fee alardi almaliki alquddoosi alAAazeezi alhakeemi

Ñi nekk ci asamaan yeek suuf si ña ngay sàbbaal Yàlla, miy Buur, bu Sell, di Boroom Kàttan, di Ku xereñ.(h)

2

هُوَ ٱلَّذِي بَعَثَ فِي ٱلۡأُمِّيِّـۧنَ رَسُولٗا مِّنۡهُمۡ يَتۡلُواْ عَلَيۡهِمۡ ءَايَٰتِهِۦ وَيُزَكِّيهِمۡ وَيُعَلِّمُهُمُ ٱلۡكِتَٰبَ وَٱلۡحِكۡمَةَ وَإِن كَانُواْ مِن قَبۡلُ لَفِي ضَلَٰلٖ مُّبِينٖ

Huwa allathee baAAatha fee alommiyyeena rasoolan minhum yatloo AAalayhim ayatihi wayuzakkeehim wayuAAallimuhumu alkitaba waalhikmata wain kanoo min qablu lafee dalalin mubeenin

Moom mooy ki yónni ci araab yi ab Yonent bu bokk ci ñoom bu leen di jàngal ay Laayam, di leen jàngal Alxuraan ak Sunna, te ñoom bu jëkkoon ña nga woon ci réer gu sore,

3

وَءَاخَرِينَ مِنۡهُمۡ لَمَّا يَلۡحَقُواْ بِهِمۡۚ وَهُوَ ٱلۡعَزِيزُ ٱلۡحَكِيمُ

Waakhareena minhum lamma yalhaqoo bihim wahuwa alAAazeezu alhakeemu

ak ci ñeneen ñoo xam ne dabaguñuleen. Te moom Yàlla Mooy boroom Kàttan, di Ku Xereñ.

4

ذَٰلِكَ فَضۡلُ ٱللَّهِ يُؤۡتِيهِ مَن يَشَآءُۚ وَٱللَّهُ ذُو ٱلۡفَضۡلِ ٱلۡعَظِيمِ

Thalika fadlu Allahi yuteehi man yashao waAllahu thoo alfadli alAAatheemi

Loolu ngënéelul Yàlla la moo koy jox ku ko soob. Te Yàlla mooy boroom Ngënéel lu màgg li.

5

مَثَلُ ٱلَّذِينَ حُمِّلُواْ ٱلتَّوۡرَىٰةَ ثُمَّ لَمۡ يَحۡمِلُوهَا كَمَثَلِ ٱلۡحِمَارِ يَحۡمِلُ أَسۡفَارَۢاۚ بِئۡسَ مَثَلُ ٱلۡقَوۡمِ ٱلَّذِينَ كَذَّبُواْ بِـَٔايَٰتِ ٱللَّهِۚ وَٱللَّهُ لَا يَهۡدِي ٱلۡقَوۡمَ ٱلظَّـٰلِمِينَ

Mathalu allatheena hummiloo alttawrata thumma lam yahmilooha kamathali alhimari yahmilu asfaran bisa mathalu alqawmi allatheena kaththaboo biayati Allahi waAllahu la yahdee alqawma alththalimeena

Misaalum ñi ñu wàcceeloon Tawraat te jëfewunu ko ñi ngi melni mbaam mu sëfi téere. Aka bon misaalum nit ñooñu nga xam ne dañoo weddi kàdduy Yàlla te Yàlla du gindi mukk aw nit ñu di ay tooñkat.

6

قُلۡ يَـٰٓأَيُّهَا ٱلَّذِينَ هَادُوٓاْ إِن زَعَمۡتُمۡ أَنَّكُمۡ أَوۡلِيَآءُ لِلَّهِ مِن دُونِ ٱلنَّاسِ فَتَمَنَّوُاْ ٱلۡمَوۡتَ إِن كُنتُمۡ صَٰدِقِينَ

Qul ya ayyuha allatheena hadoo in zaAAamtum annakum awliyao lillahi min dooni alnnasi fatamannawoo almawta in kuntum sadiqeena

Waxal ne : «Eey yéen Yahuud yi ! Su fekkee ne nii ngeen méngook Yàllaay, kon ñaan leen dee, su fekkee ne dëggu ngeen”.

7

وَلَا يَتَمَنَّوۡنَهُۥٓ أَبَدَۢا بِمَا قَدَّمَتۡ أَيۡدِيهِمۡۚ وَٱللَّهُ عَلِيمُۢ بِٱلظَّـٰلِمِينَ

Wala yatamannawnahu abadan bima qaddamat aydeehim waAllahu AAaleemun bialththalimeena

Dunu ko ñaan mukk ngir (la ñu jëf cik caay-caay). Yàlla ku Xamaakoon la tooñkat yi.

8

قُلۡ إِنَّ ٱلۡمَوۡتَ ٱلَّذِي تَفِرُّونَ مِنۡهُ فَإِنَّهُۥ مُلَٰقِيكُمۡۖ ثُمَّ تُرَدُّونَ إِلَىٰ عَٰلِمِ ٱلۡغَيۡبِ وَٱلشَّهَٰدَةِ فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمۡ تَعۡمَلُونَ

Qul inna almawta allathee tafirroona minhu fainnahu mulaqeekum thumma turaddoona ila AAalimi alghaybi waalshshahadati fayunabbiokum bima kuntum taAAmaloona

Waxal ne : “Dee gi ngeen di daw dana dajeek yéen. Ba noppi ñu delloo leen ca Yàlla mi xam kumpaak li feeñ mu di leen xibaar la ngeen daan def ”.

9

يَـٰٓأَيُّهَا ٱلَّذِينَ ءَامَنُوٓاْ إِذَا نُودِيَ لِلصَّلَوٰةِ مِن يَوۡمِ ٱلۡجُمُعَةِ فَٱسۡعَوۡاْ إِلَىٰ ذِكۡرِ ٱللَّهِ وَذَرُواْ ٱلۡبَيۡعَۚ ذَٰلِكُمۡ خَيۡرٞ لَّكُمۡ إِن كُنتُمۡ تَعۡلَمُونَ

Ya ayyuha allatheena amanoo itha noodiya lilssalati min yawmi aljumuAAati faisAAaw ila thikri Allahi watharoo albayAAa thalikum khayrun lakum in kuntum taAAlamoona

Eey yéen ñi gëm ! Saa suñu wootee ngir julli ci bisub Àjjuma, dawleen jëm ci tudd Yàlla te nangeen fa ne ñukk njaay ma bàyyi ko. Looloo gën ci yéen de, cëy bu ngeen xamoon !(r)

10

فَإِذَا قُضِيَتِ ٱلصَّلَوٰةُ فَٱنتَشِرُواْ فِي ٱلۡأَرۡضِ وَٱبۡتَغُواْ مِن فَضۡلِ ٱللَّهِ وَٱذۡكُرُواْ ٱللَّهَ كَثِيرٗا لَّعَلَّكُمۡ تُفۡلِحُونَ

Faitha qudiyati alssalatu faintashiroo fee alardi waibtaghoo min fadli Allahi waothkuroo Allaha katheeran laAAallakum tuflihoona

Su julli gi jeexee, na ngeen tasaaroo ci suuf si, tey sàkku ci xeewali Yàlla yi, te na ngeen di tudd Yàlla lu bari ndax amaana ngeen baaxle.

11

وَإِذَا رَأَوۡاْ تِجَٰرَةً أَوۡ لَهۡوًا ٱنفَضُّوٓاْ إِلَيۡهَا وَتَرَكُوكَ قَآئِمٗاۚ قُلۡ مَا عِندَ ٱللَّهِ خَيۡرٞ مِّنَ ٱللَّهۡوِ وَمِنَ ٱلتِّجَٰرَةِۚ وَٱللَّهُ خَيۡرُ ٱلرَّـٰزِقِينَ

Waitha raaw tijaratan aw lahwan infaddoo ilayha watarakooka qaiman qul ma AAinda Allahi khayrun mina allahwi wamina alttijarati waAllahu khayru alrraziqeena

Te saa su ñu gesee am njoló walla am po danuy buur jëm ca, bàyyi la nga ne saŋŋ taxaw. Waxal ne: “La nekk fa Yàlla moo gën fuuf am po te moo gën it am njoló, te Yàlla moo di Gën ji kuy wërsëgël”. Saar 63 : Naaféq ya 11 - Laaya