← Suurat yépp
Suurat 6418 aaya

التغابن

At-Taghabun

The Mutual Disillusion

Tekki

Tann làkk

1

يُسَبِّحُ لِلَّهِ مَا فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَمَا فِي ٱلۡأَرۡضِۖ لَهُ ٱلۡمُلۡكُ وَلَهُ ٱلۡحَمۡدُۖ وَهُوَ عَلَىٰ كُلِّ شَيۡءٖ قَدِيرٌ

Yusabbihu lillahi ma fee alssamawati wama fee alardi lahu almulku walahu alhamdu wahuwa AAala kulli shayin qadeerun

Ñi nekk ci asamaan yeek suuf si ña ngay sàbbaal Yàlla. Mooy boroom nguur te Mooy boroom cant. Te Moom man na Lépp.

2

هُوَ ٱلَّذِي خَلَقَكُمۡ فَمِنكُمۡ كَافِرٞ وَمِنكُم مُّؤۡمِنٞۚ وَٱللَّهُ بِمَا تَعۡمَلُونَ بَصِيرٌ

Huwa allathee khalaqakum faminkum kafirun waminkum muminun waAllahu bima taAAmaloona baseerun

Mooy ki leen bind. Am na ci yéen ay yéefar am it ci yéen ay jullit way gëm. Te Yàlla kuy gis la li ngeen di def.

3

خَلَقَ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضَ بِٱلۡحَقِّ وَصَوَّرَكُمۡ فَأَحۡسَنَ صُوَرَكُمۡۖ وَإِلَيۡهِ ٱلۡمَصِيرُ

Khalaqa alssamawati waalarda bialhaqqi wasawwarakum faahsana suwarakum wailayhi almaseeru

Bind na asamaan yeek suuf si ci dëgg mu tën seeni jëmm te rafetal na seeni jëm. Te ca moom mooy Deluwaay ba.

4

يَعۡلَمُ مَا فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِ وَيَعۡلَمُ مَا تُسِرُّونَ وَمَا تُعۡلِنُونَۚ وَٱللَّهُ عَلِيمُۢ بِذَاتِ ٱلصُّدُورِ

YaAAlamu ma fee alssamawati waalardi wayaAAlamu ma tusirroona wama tuAAlinoona waAllahu AAaleemun bithati alssudoori

Moom Yàlla xam na li nekk ci asamaan yeek suuf si, te it ma ngay xam li ngeen di nëbb ak li ngeen di feeñal. Te Yàlla ku xam la li nekk ci dënn yi.

5

أَلَمۡ يَأۡتِكُمۡ نَبَؤُاْ ٱلَّذِينَ كَفَرُواْ مِن قَبۡلُ فَذَاقُواْ وَبَالَ أَمۡرِهِمۡ وَلَهُمۡ عَذَابٌ أَلِيمٞ

Alam yatikum nabao allatheena kafaroo min qablu fathaqoo wabala amrihim walahum AAathabun aleemun

Moo xanaa xibaari yéefar ya jiitu woon da leen dikkalul, mosoon nañu musiba mu di peyug seeni jëf ; te am nañu mbugël mu mitti.

6

ذَٰلِكَ بِأَنَّهُۥ كَانَت تَّأۡتِيهِمۡ رُسُلُهُم بِٱلۡبَيِّنَٰتِ فَقَالُوٓاْ أَبَشَرٞ يَهۡدُونَنَا فَكَفَرُواْ وَتَوَلَّواْۖ وَّٱسۡتَغۡنَى ٱللَّهُۚ وَٱللَّهُ غَنِيٌّ حَمِيدٞ

Thalika biannahu kanat tateehim rusuluhum bialbayyinati faqaloo abasharun yahdoonana fakafaroo watawallaw waistaghna Allahu waAllahu ghaniyyun hameedun

la ko waral moo di ne seeni Yonent da leen daan dikkël ak ay firndeyu leer ñuy wax naan : “Moo nit ñii ñoo ñuy gindee ?” Daal di weddi dumóoyu Yàlla bàyyi leen te Yàlla ku doyloo boppam la Yayoowaakoonu cant la.

7

زَعَمَ ٱلَّذِينَ كَفَرُوٓاْ أَن لَّن يُبۡعَثُواْۚ قُلۡ بَلَىٰ وَرَبِّي لَتُبۡعَثُنَّ ثُمَّ لَتُنَبَّؤُنَّ بِمَا عَمِلۡتُمۡۚ وَذَٰلِكَ عَلَى ٱللَّهِ يَسِيرٞ

ZaAAama allatheena kafaroo an lan yubAAathoo qul bala warabbee latubAAathunna thumma latunabbaonna bima AAamiltum wathalika AAala Allahi yaseerun

Yéefër yi neena ñooy kenn duleen dekkal. Waxal ne : “Axakañ! Dees na leen dekkal ; xibaar leen la ngeen jëfoon. Te loolu lu yomb la ci Yàlla”. (s)

8

فَـَٔامِنُواْ بِٱللَّهِ وَرَسُولِهِۦ وَٱلنُّورِ ٱلَّذِيٓ أَنزَلۡنَاۚ وَٱللَّهُ بِمَا تَعۡمَلُونَ خَبِيرٞ

Faaminoo biAllahi warasoolihi waalnnoori allathee anzalna waAllahu bima taAAmaloona khabeerun

Gëmleen Yàlla ak ub Yonentam, ak leer gi nu wàcce [Alxuraan]. Te Yàlla kat ku deñ- kumpa la ci li ngeen di def.

9

يَوۡمَ يَجۡمَعُكُمۡ لِيَوۡمِ ٱلۡجَمۡعِۖ ذَٰلِكَ يَوۡمُ ٱلتَّغَابُنِۗ وَمَن يُؤۡمِنۢ بِٱللَّهِ وَيَعۡمَلۡ صَٰلِحٗا يُكَفِّرۡ عَنۡهُ سَيِّـَٔاتِهِۦ وَيُدۡخِلۡهُ جَنَّـٰتٖ تَجۡرِي مِن تَحۡتِهَا ٱلۡأَنۡهَٰرُ خَٰلِدِينَ فِيهَآ أَبَدٗاۚ ذَٰلِكَ ٱلۡفَوۡزُ ٱلۡعَظِيمُ

Yawma yajmaAAukum liyawmi aljamAAi thalika yawmu alttaghabuni waman yumin biAllahi wayaAAmal salihan yukaffir AAanhu sayyiatihi wayudkhilhu jannatin tajree min tahtiha alanharu khalideena feeha abadan thalika alfawzu alAAatheemu

Te bu keroogee ba mu leen di Dajale, ca bisub daje ba bis boobee mooy bisub yàqule gu mag ga (ca yéefar ya). (Waaye) képp ku gëm tey jëf yiw, Dana ko faral ay ñaaytéefam te dana ko tàbbal Àjjana yu ay dex ñooy daw ci suufam, te dañu fay béel fàww. Loolu moo di texe gu mag ga !

10

وَٱلَّذِينَ كَفَرُواْ وَكَذَّبُواْ بِـَٔايَٰتِنَآ أُوْلَـٰٓئِكَ أَصۡحَٰبُ ٱلنَّارِ خَٰلِدِينَ فِيهَاۖ وَبِئۡسَ ٱلۡمَصِيرُ

Waallatheena kafaroo wakaththaboo biayatina olaika ashabu alnnari khalideena feeha wabisa almaseeru

Yéefër yiy weddi Sunuy Laaya, ñooñu ñoo di waa Safara te danu fay béel. Ndaw saxuwaay bu bon !

11

مَآ أَصَابَ مِن مُّصِيبَةٍ إِلَّا بِإِذۡنِ ٱللَّهِۗ وَمَن يُؤۡمِنۢ بِٱللَّهِ يَهۡدِ قَلۡبَهُۥۚ وَٱللَّهُ بِكُلِّ شَيۡءٍ عَلِيمٞ

Ma asaba min museebatin illa biithni Allahi waman yumin biAllahi yahdi qalbahu waAllahu bikulli shayin AAaleemun

Amul menn musiba muy dal kenn lu dul ci ndigalul Yàlla. Képp ku gëm Yàlla, [Yàlla] dana gindi xolam. Te Yàlla xam na lépp.

12

وَأَطِيعُواْ ٱللَّهَ وَأَطِيعُواْ ٱلرَّسُولَۚ فَإِن تَوَلَّيۡتُمۡ فَإِنَّمَا عَلَىٰ رَسُولِنَا ٱلۡبَلَٰغُ ٱلۡمُبِينُ

WaateeAAoo Allaha waateeAAoo alrrasoola fain tawallaytum fainnama AAala rasoolina albalaghu almubeenu

Nangeen di topp Yàlla te it na ngeen di topp Yonent bi suñu dumóoyoo... li ca war Sunub Yonent mooy jottali rekk ba mu leer.

13

ٱللَّهُ لَآ إِلَٰهَ إِلَّا هُوَۚ وَعَلَى ٱللَّهِ فَلۡيَتَوَكَّلِ ٱلۡمُؤۡمِنُونَ

Allahu la ilaha illa huwa waAAala Allahi falyatawakkali almuminoona

Yàlla, amul jeneen Yàlla ju dul moom ! Te ñi gëm na ñuy doyloo Yàlla.

14

يَـٰٓأَيُّهَا ٱلَّذِينَ ءَامَنُوٓاْ إِنَّ مِنۡ أَزۡوَٰجِكُمۡ وَأَوۡلَٰدِكُمۡ عَدُوّٗا لَّكُمۡ فَٱحۡذَرُوهُمۡۚ وَإِن تَعۡفُواْ وَتَصۡفَحُواْ وَتَغۡفِرُواْ فَإِنَّ ٱللَّهَ غَفُورٞ رَّحِيمٌ

Ya ayyuha allatheena amanoo inna min azwajikum waawladikum AAaduwwan lakum faihtharoohum wain taAAfoo watasfahoo wataghfiroo fainna Allaha ghafoorun raheemun

eey yéen ñi gëm, am na ci seeni jabar ak seeni doom ñoo xam ne seeni noon la ñu. Nangeen leen di moytu. (Waaye) su ngeen balee tey jéllale, Yàlla moom ab Jéggalaakoon la, Jagléwaakoon la.

15

إِنَّمَآ أَمۡوَٰلُكُمۡ وَأَوۡلَٰدُكُمۡ فِتۡنَةٞۚ وَٱللَّهُ عِندَهُۥٓ أَجۡرٌ عَظِيمٞ

Innama amwalukum waawladukum fitnatun waAllahu AAindahu ajrun AAatheemun

Seeni alal ak seeni doom sànje la ci yéen, (Waaye) la nekk fa Yàlla moo di pey gu màgg.

16

فَٱتَّقُواْ ٱللَّهَ مَا ٱسۡتَطَعۡتُمۡ وَٱسۡمَعُواْ وَأَطِيعُواْ وَأَنفِقُواْ خَيۡرٗا لِّأَنفُسِكُمۡۗ وَمَن يُوقَ شُحَّ نَفۡسِهِۦ فَأُوْلَـٰٓئِكَ هُمُ ٱلۡمُفۡلِحُونَ

Faittaqoo Allaha ma istataAAtum waismaAAoo waateeAAoo waanfiqoo khayran lianfusikum waman yooqa shuhha nafsihi faolaika humu almuflihoona

Nangeen di ragal Yàlla seen kem kàttan, dégluleen, te topp te joxe alal. Moo gën ci yéen de. Képp ku mucc ci ag nay (na xam ne)... ñoo di ña baaxle.

17

إِن تُقۡرِضُواْ ٱللَّهَ قَرۡضًا حَسَنٗا يُضَٰعِفۡهُ لَكُمۡ وَيَغۡفِرۡ لَكُمۡۚ وَٱللَّهُ شَكُورٌ حَلِيمٌ

In tuqridoo Allaha qardan hasanan yudaAAifhu lakum wayaghfir lakum waAllahu shakoorun haleemun

Su ngeen lebalee Yàlla bor bu rafet, Dana leen ko fulal te it dana leen jéggal. Te Yàlla ab Santaakoon la Ku lewet la.

18

عَٰلِمُ ٱلۡغَيۡبِ وَٱلشَّهَٰدَةِ ٱلۡعَزِيزُ ٱلۡحَكِيمُ

AAalimu alghaybi waalshshahadati alAAazeezu alhakeemu

Mooy aji Xam ji Kumpaak li feeñ, di boroom Kàttan, di aji Xereñ. Saar 65 : Pase 12 - Laaya