← Suurat yépp
Suurat 10109 aaya

يونس

Yunus

Jonah

Tekki

Tann làkk

1

الٓرۚ تِلۡكَ ءَايَٰتُ ٱلۡكِتَٰبِ ٱلۡحَكِيمِ

Aliflamra tilka ayatu alkitabi alhakeemi

Alif, Laam, Raa. Lii ay laayay Téere bu ñu xereñe lañu.

2

أَكَانَ لِلنَّاسِ عَجَبًا أَنۡ أَوۡحَيۡنَآ إِلَىٰ رَجُلٖ مِّنۡهُمۡ أَنۡ أَنذِرِ ٱلنَّاسَ وَبَشِّرِ ٱلَّذِينَ ءَامَنُوٓاْ أَنَّ لَهُمۡ قَدَمَ صِدۡقٍ عِندَ رَبِّهِمۡۗ قَالَ ٱلۡكَٰفِرُونَ إِنَّ هَٰذَا لَسَٰحِرٞ مُّبِينٌ

Akana lilnnasi AAajaban an awhayna ila rajulin minhum an anthiri alnnasa wabashshiri allatheena amanoo anna lahum qadama sidqin AAinda rabbihim qala alkafiroona inna hatha lasahirun mubeenun

Moo ndax dafa dul yéem ci nit ñi, Nu soloo (xamal) góor gu bokk ci ñoom : “Ndigalul waar nit ñi ci bégal way-gëm ñi te xamal leen ne, am nañu fa seen Boroom dawal bu di dëgg ? Ña weddi ñoom nee nañu : “Lii dey ag njibar gu fés la”.(s)

3

إِنَّ رَبَّكُمُ ٱللَّهُ ٱلَّذِي خَلَقَ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضَ فِي سِتَّةِ أَيَّامٖ ثُمَّ ٱسۡتَوَىٰ عَلَى ٱلۡعَرۡشِۖ يُدَبِّرُ ٱلۡأَمۡرَۖ مَا مِن شَفِيعٍ إِلَّا مِنۢ بَعۡدِ إِذۡنِهِۦۚ ذَٰلِكُمُ ٱللَّهُ رَبُّكُمۡ فَٱعۡبُدُوهُۚ أَفَلَا تَذَكَّرُونَ

Inna rabbakumu Allahu allathee khalaqa alssamawati waalarda fee sittati ayyamin thumma istawa AAala alAAarshi yudabbiru alamra ma min shafeeAAin illa min baAAdi ithnihi thalikumu Allahu rabbukum faoAAbudoohu afala tathakkaroona

Yàlla seen Boroom nag Mooy ki bind asamaan yi ak suuf si ci juróom- benni fan, topp Mu yemoo ca gàngunaay ga (Haras), di settantal mbir ya (ndigal ya). Amul kenn ku mën a ramm te du ci ndigalam. Kookoo di seen Boroom. Jaamuleen Ko. Moo ndax dungeen fàttaliku ?

4

إِلَيۡهِ مَرۡجِعُكُمۡ جَمِيعٗاۖ وَعۡدَ ٱللَّهِ حَقًّاۚ إِنَّهُۥ يَبۡدَؤُاْ ٱلۡخَلۡقَ ثُمَّ يُعِيدُهُۥ لِيَجۡزِيَ ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ وَعَمِلُواْ ٱلصَّـٰلِحَٰتِ بِٱلۡقِسۡطِۚ وَٱلَّذِينَ كَفَرُواْ لَهُمۡ شَرَابٞ مِّنۡ حَمِيمٖ وَعَذَابٌ أَلِيمُۢ بِمَا كَانُواْ يَكۡفُرُونَ

Ilayhi marjiAAukum jameeAAan waAAda Allahi haqqan innahu yabdao alkhalqa thumma yuAAeeduhu liyajziya allatheena amanoo waAAamiloo alssalihati bialqisti waallatheena kafaroo lahum sharabun min hameemin waAAathabun aleemun bima kanoo yakfuroona

Seen delluwaay yéen ñépp ca Moom la jëm, mooy digub Yàlla bu dëggu ba ! Moom moo sos mbindéef yi (booba dara amul), Moo leen di delloosi (ginnaaw bu ñu dee ba ràpp) ngir Mu feye ña gëm pey gu duun. Waaye ña weddi woon ñoom, seenug naan, ndox mu tàng lay doon ak mbugal mu metti, muy peyug seenug weddi !

5

هُوَ ٱلَّذِي جَعَلَ ٱلشَّمۡسَ ضِيَآءٗ وَٱلۡقَمَرَ نُورٗا وَقَدَّرَهُۥ مَنَازِلَ لِتَعۡلَمُواْ عَدَدَ ٱلسِّنِينَ وَٱلۡحِسَابَۚ مَا خَلَقَ ٱللَّهُ ذَٰلِكَ إِلَّا بِٱلۡحَقِّۚ يُفَصِّلُ ٱلۡأٓيَٰتِ لِقَوۡمٖ يَعۡلَمُونَ

Huwa allathee jaAAala alshshamsa diyaan waalqamara nooran waqaddarahu manazila litaAAlamoo AAadada alssineena waalhisaba ma khalaqa Allahu thalika illa bialhaqqi yufassilu alayati liqawmin yaAAlamoona

Moom mooy ki jox jant bi tàkk-tàkk, jox weer wi leeraay te dogal ko ay wàccuwaay ndax ngeen mën a xam limu at yi ak mën a waññi. Yàlla bindul loolu lu dul ci dëgg. Te Dana biralal tegtal ya nit ñay xam.

6

إِنَّ فِي ٱخۡتِلَٰفِ ٱلَّيۡلِ وَٱلنَّهَارِ وَمَا خَلَقَ ٱللَّهُ فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِ لَأٓيَٰتٖ لِّقَوۡمٖ يَتَّقُونَ

Inna fee ikhtilafi allayli waalnnahari wama khalaqa Allahu fee alssamawati waalardi laayatin liqawmin yattaqoona

Nekk na ci jéllasanteb guddi gi ak bëccëg gi, ak li Yàlla sàkk ci asamaan yi ak suuf si, ay kéemaan ci nit ñu ragal (Yàlla).

7

إِنَّ ٱلَّذِينَ لَا يَرۡجُونَ لِقَآءَنَا وَرَضُواْ بِٱلۡحَيَوٰةِ ٱلدُّنۡيَا وَٱطۡمَأَنُّواْ بِهَا وَٱلَّذِينَ هُمۡ عَنۡ ءَايَٰتِنَا غَٰفِلُونَ

Inna allatheena la yarjoona liqaana waradoo bialhayati alddunya waitmaannoo biha waallatheena hum AAan ayatina ghafiloona

Ña nga xam ne nag yaakaaruñoo dajeek Nun, te tànn dundug àddina gii, doyloo ko, ak ña nga xam ne sàggane nañu Sunuy ndigal,

8

أُوْلَـٰٓئِكَ مَأۡوَىٰهُمُ ٱلنَّارُ بِمَا كَانُواْ يَكۡسِبُونَ

Olaika mawahumu alnnaru bima kanoo yaksiboona

ñooña seen delluwaay moo di Safara ngir la ñu fàggu.

9

إِنَّ ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ وَعَمِلُواْ ٱلصَّـٰلِحَٰتِ يَهۡدِيهِمۡ رَبُّهُم بِإِيمَٰنِهِمۡۖ تَجۡرِي مِن تَحۡتِهِمُ ٱلۡأَنۡهَٰرُ فِي جَنَّـٰتِ ٱلنَّعِيمِ

Inna allatheena amanoo waAAamiloo alssalihati yahdeehim rabbuhum bieemanihim tajree min tahtihimu alanharu fee jannati alnnaAAeemi

Ña nga xam ne gëm nañu tey jëf yu yiw, seen Boroom dana leen wommat ngir seen ngëm, tàbbal leen Àjjanay xéewal. Ay dex di daw ci seen suuf.

10

دَعۡوَىٰهُمۡ فِيهَا سُبۡحَٰنَكَ ٱللَّهُمَّ وَتَحِيَّتُهُمۡ فِيهَا سَلَٰمٞۚ وَءَاخِرُ دَعۡوَىٰهُمۡ أَنِ ٱلۡحَمۡدُ لِلَّهِ رَبِّ ٱلۡعَٰلَمِينَ

DaAAwahum feeha subhanaka allahumma watahiyyatuhum feeha salamun waakhiru daAAwahum ani alhamdu lillahi rabbi alAAalameena

Seenug jaamu foofa mooy di wax naan : “Cëy sellug sunu Boroom”, te seenug nuyyoo foofa mooy : “Jàmm rekk”, te la ñuy mujjeel ca seenug jaamu, moo di ñu wax ne: “Mbooleem xeeti cant yi ñeel na Yàlla Boroom àddina si”.

11

۞وَلَوۡ يُعَجِّلُ ٱللَّهُ لِلنَّاسِ ٱلشَّرَّ ٱسۡتِعۡجَالَهُم بِٱلۡخَيۡرِ لَقُضِيَ إِلَيۡهِمۡ أَجَلُهُمۡۖ فَنَذَرُ ٱلَّذِينَ لَا يَرۡجُونَ لِقَآءَنَا فِي طُغۡيَٰنِهِمۡ يَعۡمَهُونَ

Walaw yuAAajjilu Allahu lilnnasi alshsharra istiAAjalahum bialkhayri laqudiya ilayhim ajaluhum fanatharu allatheena la yarjoona liqaana fee tughyanihim yaAAmahoona

Bu Yàlla gaawe woon àtte nit ñi ci mettit kem ni ñu yàkkamtee am alal, àttekoon na seenug yàkkamti. Waaye Dananu bàyyi ña nga xam ne yaakaaruñoo dajeek Nun ñuy laam- laame ca seen biir ngëlamte.(r)

12

وَإِذَا مَسَّ ٱلۡإِنسَٰنَ ٱلضُّرُّ دَعَانَا لِجَنۢبِهِۦٓ أَوۡ قَاعِدًا أَوۡ قَآئِمٗا فَلَمَّا كَشَفۡنَا عَنۡهُ ضُرَّهُۥ مَرَّ كَأَن لَّمۡ يَدۡعُنَآ إِلَىٰ ضُرّٖ مَّسَّهُۥۚ كَذَٰلِكَ زُيِّنَ لِلۡمُسۡرِفِينَ مَا كَانُواْ يَعۡمَلُونَ

Waitha massa alinsana alddurru daAAana lijanbihi aw qaAAidan aw qaiman falamma kashafna AAanhu durrahu marra kaan lam yadAAuna ila durrin massahu kathalika zuyyina lilmusrifeena ma kanoo yaAAmaloona

Nit, bu ko aw naqar dalee, mu daldi Nuy woo, (moo xam dakoo fekk mu) tëdd walla mu toog walla taxaw. Te bu Nu ko tekkilee naqaram woowu, muy wéy (ci kéefaram), fakk mel ni mësunoo woo ci naqar wu ko dal. Noonu la jekkee woon ca ñoom bokkaalekat ya la ñu daan def.

13

وَلَقَدۡ أَهۡلَكۡنَا ٱلۡقُرُونَ مِن قَبۡلِكُمۡ لَمَّا ظَلَمُواْ وَجَآءَتۡهُمۡ رُسُلُهُم بِٱلۡبَيِّنَٰتِ وَمَا كَانُواْ لِيُؤۡمِنُواْۚ كَذَٰلِكَ نَجۡزِي ٱلۡقَوۡمَ ٱلۡمُجۡرِمِينَ

Walaqad ahlakna alquroona min qablikum lamma thalamoo wajaathum rusuluhum bialbayyinati wama kanoo liyuminoo kathalika najzee alqawma almujrimeena

Alag Nanu ay xeet yu bari yu leen jiitu ba ñu tooñee, te Yonent dikkal leen ak i lay yu leer nàññ. Te nanguwuñuleen woon a gëm. Noonu la Nuy feyee nit ñu di ay saay-saay.

14

ثُمَّ جَعَلۡنَٰكُمۡ خَلَـٰٓئِفَ فِي ٱلۡأَرۡضِ مِنۢ بَعۡدِهِمۡ لِنَنظُرَ كَيۡفَ تَعۡمَلُونَ

Thumma jaAAalnakum khalaifa fee alardi min baAAdihim linanthura kayfa taAAmaloona

Ba noppi Nu def leen ngeen wuutu leen ci suuf si ci seen ginnaaw, ngir Nu seetlu naka ngeen di def.

15

وَإِذَا تُتۡلَىٰ عَلَيۡهِمۡ ءَايَاتُنَا بَيِّنَٰتٖ قَالَ ٱلَّذِينَ لَا يَرۡجُونَ لِقَآءَنَا ٱئۡتِ بِقُرۡءَانٍ غَيۡرِ هَٰذَآ أَوۡ بَدِّلۡهُۚ قُلۡ مَا يَكُونُ لِيٓ أَنۡ أُبَدِّلَهُۥ مِن تِلۡقَآيِٕ نَفۡسِيٓۖ إِنۡ أَتَّبِعُ إِلَّا مَا يُوحَىٰٓ إِلَيَّۖ إِنِّيٓ أَخَافُ إِنۡ عَصَيۡتُ رَبِّي عَذَابَ يَوۡمٍ عَظِيمٖ

Waitha tutla AAalayhim ayatuna bayyinatin qala allatheena la yarjoona liqaana iti biquranin ghayri hatha aw baddilhu qul ma yakoonu lee an obaddilahu min tilqai nafsee in attabiAAu illa ma yooha ilayya innee akhafu in AAasaytu rabbee AAathaba yawmin AAatheemin

Te bu ñu jàngee ci seen kanam Sunuy kàddu yu leer yi, ña yaakarul a dajeek Nun wax ne : “Indil weneen jàngin wu wuuteek wii” mbaa “Nga soppi ko”. Neel : “Yellul ci man ma soppi ko ci sama coobare bopp. Duma topp lu dul la ñu ma soloo. Ragal naa, su ma moyee sama Boroom, mbugalum bis bu rëy (dal ma)”.

16

قُل لَّوۡ شَآءَ ٱللَّهُ مَا تَلَوۡتُهُۥ عَلَيۡكُمۡ وَلَآ أَدۡرَىٰكُم بِهِۦۖ فَقَدۡ لَبِثۡتُ فِيكُمۡ عُمُرٗا مِّن قَبۡلِهِۦٓۚ أَفَلَا تَعۡقِلُونَ

Qul law shaa Allahu ma talawtuhu AAalaykum wala adrakum bihi faqad labithtu feekum AAumuran min qablihi afala taAAqiloona

Neel : “Bu sooboon Yàlla, duma leen ko jàngal te duma leen ko xamal. Ndax dundu naak yéen ay at lu ko jiitu. Moo ndax dangeen dul xel- lu ?”.

17

فَمَنۡ أَظۡلَمُ مِمَّنِ ٱفۡتَرَىٰ عَلَى ٱللَّهِ كَذِبًا أَوۡ كَذَّبَ بِـَٔايَٰتِهِۦٓۚ إِنَّهُۥ لَا يُفۡلِحُ ٱلۡمُجۡرِمُونَ

Faman athlamu mimmani iftara AAala Allahi kathiban aw kaththaba biayatihi innahu la yuflihu almujrimoona

Ana kan moo gën a tooñ kuy duural Yàlla ay fen, walla di weddi ay tegtalam ? Ak lu mën a xew, saay-saay sa duñu texe.

18

وَيَعۡبُدُونَ مِن دُونِ ٱللَّهِ مَا لَا يَضُرُّهُمۡ وَلَا يَنفَعُهُمۡ وَيَقُولُونَ هَـٰٓؤُلَآءِ شُفَعَـٰٓؤُنَا عِندَ ٱللَّهِۚ قُلۡ أَتُنَبِّـُٔونَ ٱللَّهَ بِمَا لَا يَعۡلَمُ فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَلَا فِي ٱلۡأَرۡضِۚ سُبۡحَٰنَهُۥ وَتَعَٰلَىٰ عَمَّا يُشۡرِكُونَ

WayaAAbudoona min dooni Allahi ma la yadurruhum wala yanfaAAuhum wayaqooloona haolai shufaAAaona AAinda Allahi qul atunabbioona Allaha bima la yaAAlamu fee alssamawati wala fee alardi subhanahu wataAAala AAamma yushrikoona

Dañuy jaamu, bàyyi Yàlla, loo xam ne duleen mën a lor, duleen mën a jariñ dara, ñuy wax naan : “Ñii ñoo nuy rammu fa Yàlla”. Neel : “Ndax dangeen a mën a xamal Yàlla lu Mu xamul ci asamaan yi ak suuf si ?”. Kañ naa Ko, te kawe na lool la ñu Koy bokkaale !

19

وَمَا كَانَ ٱلنَّاسُ إِلَّآ أُمَّةٗ وَٰحِدَةٗ فَٱخۡتَلَفُواْۚ وَلَوۡلَا كَلِمَةٞ سَبَقَتۡ مِن رَّبِّكَ لَقُضِيَ بَيۡنَهُمۡ فِيمَا فِيهِ يَخۡتَلِفُونَ

Wama kana alnnasu illa ommatan wahidatan faikhtalafoo walawla kalimatun sabaqat min rabbika laqudiya baynahum feema feehi yakhtalifoona

Nit ñi nekkuñu woon lu dul wenn xeet. Ñu juuyoo. Te bu dul koon waxi Yàlla ja jiitu woon, àttekoon na seeni diggante ca la ñu juuyoo. (s)

20

وَيَقُولُونَ لَوۡلَآ أُنزِلَ عَلَيۡهِ ءَايَةٞ مِّن رَّبِّهِۦۖ فَقُلۡ إِنَّمَا ٱلۡغَيۡبُ لِلَّهِ فَٱنتَظِرُوٓاْ إِنِّي مَعَكُم مِّنَ ٱلۡمُنتَظِرِينَ

Wayaqooloona lawla onzila AAalayhi ayatun min rabbihi faqul innama alghaybu lillahi faintathiroo innee maAAakum mina almuntathireena

Ñuy wax naan : “Lu tee woon ñu wàcce ci moom laaya ju tukkee ca Boroomam ?”. Neel : “Lu fàddu (di kumpa) Yàlla rekk a ko xam. Kon nanga muñandiku ; Man nag, maa ngi ànd ak yéen bokk ca way- muñandiku ña.

21

وَإِذَآ أَذَقۡنَا ٱلنَّاسَ رَحۡمَةٗ مِّنۢ بَعۡدِ ضَرَّآءَ مَسَّتۡهُمۡ إِذَا لَهُم مَّكۡرٞ فِيٓ ءَايَاتِنَاۚ قُلِ ٱللَّهُ أَسۡرَعُ مَكۡرًاۚ إِنَّ رُسُلَنَا يَكۡتُبُونَ مَا تَمۡكُرُونَ

Waitha athaqna alnnasa rahmatan min baAAdi darraa massathum itha lahum makrun fee ayatina quli Allahu asraAAu makran inna rusulana yaktuboona ma tamkuroona

Su Nu musalee nit ci yërmaande [niki taw] ginnaaw ba leen naqar dalee, ñuy def i pexe ci Sunuy tegtal. Neel : “Yàllaa gën a gaaw ciy pexe”. Sunuy ndaw danañu bind li ngeen di fexe de.

22

هُوَ ٱلَّذِي يُسَيِّرُكُمۡ فِي ٱلۡبَرِّ وَٱلۡبَحۡرِۖ حَتَّىٰٓ إِذَا كُنتُمۡ فِي ٱلۡفُلۡكِ وَجَرَيۡنَ بِهِم بِرِيحٖ طَيِّبَةٖ وَفَرِحُواْ بِهَا جَآءَتۡهَا رِيحٌ عَاصِفٞ وَجَآءَهُمُ ٱلۡمَوۡجُ مِن كُلِّ مَكَانٖ وَظَنُّوٓاْ أَنَّهُمۡ أُحِيطَ بِهِمۡ دَعَوُاْ ٱللَّهَ مُخۡلِصِينَ لَهُ ٱلدِّينَ لَئِنۡ أَنجَيۡتَنَا مِنۡ هَٰذِهِۦ لَنَكُونَنَّ مِنَ ٱلشَّـٰكِرِينَ

Huwa allathee yusayyirukum fee albarri waalbahri hatta itha kuntum fee alfulki wajarayna bihim bireehin tayyibatin wafarihoo biha jaatha reehun AAasifun wajaahumu almawju min kulli makanin wathannoo annahum oheeta bihim daAAawoo Allaha mukhliseena lahu alddeena lain anjaytana min hathihi lanakoonanna mina alshshakireena

Moom mooy ki leen doxloo, ci suuf si ak ci géej gi, ba ngeen nekkee ca gaal ga. Te gaal googu daw ak ñoom ci ngelaw lu teey. Ñu bég ca ba ngelaw lu tar songu leen, duusi géej wër leen ci wet gu nekk, ba ñu njortu ne ñoom alageef na leen, ñuy ñaan Yàlla, di sellal diineem, di [giñ] ne: “Boo Nu musalee ci lii, fàwwu dananu bokk ci way-sant ña [Yàlla] !”

23

فَلَمَّآ أَنجَىٰهُمۡ إِذَا هُمۡ يَبۡغُونَ فِي ٱلۡأَرۡضِ بِغَيۡرِ ٱلۡحَقِّۗ يَـٰٓأَيُّهَا ٱلنَّاسُ إِنَّمَا بَغۡيُكُمۡ عَلَىٰٓ أَنفُسِكُمۖ مَّتَٰعَ ٱلۡحَيَوٰةِ ٱلدُّنۡيَاۖ ثُمَّ إِلَيۡنَا مَرۡجِعُكُمۡ فَنُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمۡ تَعۡمَلُونَ

Falamma anjahum itha hum yabghoona fee alardi bighayri alhaqqi ya ayyuha alnnasu innama baghyukum AAala anfusikum mataAAa alhayati alddunya thumma ilayna marjiAAukum fanunabbiokum bima kuntum taAAmaloona

Ba Nu leen musalee, ñu daldi beew ci kaw suuf si ci lu dul dëgg. Éy yéen nit ñi ! Seen beew googu tooñuleen ci kenn ku dul seen bopp. Muy yóbbalub àdduna. Ba noppi nag ngeen dellu jëm ci Nun, Nu xamal leen la ngeen doon def.

24

إِنَّمَا مَثَلُ ٱلۡحَيَوٰةِ ٱلدُّنۡيَا كَمَآءٍ أَنزَلۡنَٰهُ مِنَ ٱلسَّمَآءِ فَٱخۡتَلَطَ بِهِۦ نَبَاتُ ٱلۡأَرۡضِ مِمَّا يَأۡكُلُ ٱلنَّاسُ وَٱلۡأَنۡعَٰمُ حَتَّىٰٓ إِذَآ أَخَذَتِ ٱلۡأَرۡضُ زُخۡرُفَهَا وَٱزَّيَّنَتۡ وَظَنَّ أَهۡلُهَآ أَنَّهُمۡ قَٰدِرُونَ عَلَيۡهَآ أَتَىٰهَآ أَمۡرُنَا لَيۡلًا أَوۡ نَهَارٗا فَجَعَلۡنَٰهَا حَصِيدٗا كَأَن لَّمۡ تَغۡنَ بِٱلۡأَمۡسِۚ كَذَٰلِكَ نُفَصِّلُ ٱلۡأٓيَٰتِ لِقَوۡمٖ يَتَفَكَّرُونَ

Innama mathalu alhayati alddunya kamain anzalnahu mina alssamai faikhtalata bihi nabatu alardi mimma yakulu alnnasu waalanAAamu hatta itha akhathati alardu zukhrufaha waizzayyanat wathanna ahluha annahum qadiroona AAalayha ataha amruna laylan aw naharan fajaAAalnaha haseedan kaan lam taghna bialamsi kathalika nufassilu alayati liqawmin yatafakkaroona

Nirale dundug àddina nekkul lu dul lu mel ni ndox mu ñu wàcce mu jóge asamaan sa, gàncax ga ràbboo ci suuf si [ngir màndi ci ndox moomu], muy li nit ñi ak mala yi di lekk. Bu suuf si jot taaram ci rafet ba ña ca dëkk am yaakaar ne am nañu kàttan ci moom, Sunu dogal dikkal ko guddi walla bëccëg, Nu def ko ni lu ñu góob, mu mel ni nekku fa woon démb. Noonu Lanuy leerale laaya yi ci nit ñoo xam ne danañu xalaat.

25

وَٱللَّهُ يَدۡعُوٓاْ إِلَىٰ دَارِ ٱلسَّلَٰمِ وَيَهۡدِي مَن يَشَآءُ إِلَىٰ صِرَٰطٖ مُّسۡتَقِيمٖ

WaAllahu yadAAoo ila dari alssalami wayahdee man yashao ila siratin mustaqeemin

Yàllaa ngi woote jëme [ci topp ndigal] ca këru jàmm ga, te Dana jubal ku ko soob jëme ko ca yoon wu jub wa xocc.

26

۞لِّلَّذِينَ أَحۡسَنُواْ ٱلۡحُسۡنَىٰ وَزِيَادَةٞۖ وَلَا يَرۡهَقُ وُجُوهَهُمۡ قَتَرٞ وَلَا ذِلَّةٌۚ أُوْلَـٰٓئِكَ أَصۡحَٰبُ ٱلۡجَنَّةِۖ هُمۡ فِيهَا خَٰلِدُونَ

Lillatheena ahsanoo alhusna waziyadatun wala yarhaqu wujoohahum qatarun wala thillatun olaika ashabu aljannati hum feeha khalidoona

Ñay rafetal, am nañu li gën a baax [Àjjana] ak ndollant [Gis Yàlla]. Te seeni kanam du muuru ngir njàqare walla toroxte. Ñooña ñooy duggu Àjjana te dañu fay béel.(h)

27

وَٱلَّذِينَ كَسَبُواْ ٱلسَّيِّـَٔاتِ جَزَآءُ سَيِّئَةِۭ بِمِثۡلِهَا وَتَرۡهَقُهُمۡ ذِلَّةٞۖ مَّا لَهُم مِّنَ ٱللَّهِ مِنۡ عَاصِمٖۖ كَأَنَّمَآ أُغۡشِيَتۡ وُجُوهُهُمۡ قِطَعٗا مِّنَ ٱلَّيۡلِ مُظۡلِمًاۚ أُوْلَـٰٓئِكَ أَصۡحَٰبُ ٱلنَّارِۖ هُمۡ فِيهَا خَٰلِدُونَ

Waallatheena kasaboo alssayyiati jazao sayyiatin bimithliha watarhaquhum thillatun ma lahum mina Allahi min AAasimin kaannama oghshiyat wujoohuhum qitaAAan mina allayli muthliman olaika ashabu alnnari hum feeha khalidoona

Ña nga xam ne dañoo fàggu lu ñaaw, am nañu lu ñaaw lu ko niru. Te la ñu yayoo mooy toroxte, - te duñu am kenn ku leen musal ci Yàlla -, daanaka day mel ni seeni kanam dañoo muuru ak daggitu guddi gu lëndëm. Ñooña ñoo dugg Safara te dañu fay béel.

28

وَيَوۡمَ نَحۡشُرُهُمۡ جَمِيعٗا ثُمَّ نَقُولُ لِلَّذِينَ أَشۡرَكُواْ مَكَانَكُمۡ أَنتُمۡ وَشُرَكَآؤُكُمۡۚ فَزَيَّلۡنَا بَيۡنَهُمۡۖ وَقَالَ شُرَكَآؤُهُم مَّا كُنتُمۡ إِيَّانَا تَعۡبُدُونَ

Wayawma nahshuruhum jameeAAan thumma naqoolu lillatheena ashrakoo makanakum antum washurakaokum fazayyalna baynahum waqala shurakaohum ma kuntum iyyana taAAbudoona

Te bis ba ñu leen dajalee ñoom ñépp, te ñu wax ña daan bokkaale : “Beruleen fale ak seeni xërëm ya.”. Dananu téqale seeni diggante, seen xërëm ya naan : “Du nun ñii lañu doon jaamu de”.

29

فَكَفَىٰ بِٱللَّهِ شَهِيدَۢا بَيۡنَنَا وَبَيۡنَكُمۡ إِن كُنَّا عَنۡ عِبَادَتِكُمۡ لَغَٰفِلِينَ

Fakafa biAllahi shaheedan baynana wabaynakum in kunna AAan AAibadatikum laghafileena

Te Yàlla doy na seede ci sunu diggante ak yéen. Nekkewunu woon lu dul di ñàkk a faale seenug jaamu”.

30

هُنَالِكَ تَبۡلُواْ كُلُّ نَفۡسٖ مَّآ أَسۡلَفَتۡۚ وَرُدُّوٓاْ إِلَى ٱللَّهِ مَوۡلَىٰهُمُ ٱلۡحَقِّۖ وَضَلَّ عَنۡهُم مَّا كَانُواْ يَفۡتَرُونَ

Hunalika tabloo kullu nafsin ma aslafat waruddoo ila Allahi mawlahumu alhaqqi wadalla AAanhum ma kanoo yaftaroona

Noonu, bakkan bu nekk la mu jëfoon sadd ko. Ñu delloo leen ca seen Boroom muy dëgg ; ya ñu daan sos réer leen.

31

قُلۡ مَن يَرۡزُقُكُم مِّنَ ٱلسَّمَآءِ وَٱلۡأَرۡضِ أَمَّن يَمۡلِكُ ٱلسَّمۡعَ وَٱلۡأَبۡصَٰرَ وَمَن يُخۡرِجُ ٱلۡحَيَّ مِنَ ٱلۡمَيِّتِ وَيُخۡرِجُ ٱلۡمَيِّتَ مِنَ ٱلۡحَيِّ وَمَن يُدَبِّرُ ٱلۡأَمۡرَۚ فَسَيَقُولُونَ ٱللَّهُۚ فَقُلۡ أَفَلَا تَتَّقُونَ

Qul man yarzuqukum mina alssamai waalardi amman yamliku alssamAAa waalabsara waman yukhriju alhayya mina almayyiti wayukhriju almayyita mina alhayyi waman yudabbiru alamra fasayaqooloona Allahu faqul afala tattaqoona

Neel : “Ana kan moo leen di jox xéewal yu jóge kaw asamaan ak ci suuf si ? Kan moo moom dégg-dégg [nopp yi], ak gis-gis [bët yi], ana kan mooy génne luy dundu ci lu dee, di génne lu dee ci lu dundu, ana kan mooy dogal mbir yi ?”. Danañu toontu ne : “Yàlla”. Neeleen kon : “Lu leen teree ragal Yàlla ?”.

32

فَذَٰلِكُمُ ٱللَّهُ رَبُّكُمُ ٱلۡحَقُّۖ فَمَاذَا بَعۡدَ ٱلۡحَقِّ إِلَّا ٱلضَّلَٰلُۖ فَأَنَّىٰ تُصۡرَفُونَ

Fathalikumu Allahu rabbukumu alhaqqu famatha baAAda alhaqqi illa alddalalu faanna tusrafoona

Kon noonu la, Yàlla di seen Boroom ba di dëgg ga. Kon lan moo nekk ci ginnaaw dëgg lu dul ag réer ? Kon naka leen leen mën a wëlbatee ?”.

33

كَذَٰلِكَ حَقَّتۡ كَلِمَتُ رَبِّكَ عَلَى ٱلَّذِينَ فَسَقُوٓاْ أَنَّهُمۡ لَا يُؤۡمِنُونَ

Kathalika haqqat kalimatu rabbika AAala allatheena fasaqoo annahum la yuminoona

Noonu la sa kàddug Boroom yayee te dal ca kaw ña di ay saay-saay ndax gëmuñu.

34

قُلۡ هَلۡ مِن شُرَكَآئِكُم مَّن يَبۡدَؤُاْ ٱلۡخَلۡقَ ثُمَّ يُعِيدُهُۥۚ قُلِ ٱللَّهُ يَبۡدَؤُاْ ٱلۡخَلۡقَ ثُمَّ يُعِيدُهُۥۖ فَأَنَّىٰ تُؤۡفَكُونَ

Qul hal min shurakaikum man yabdao alkhalqa thumma yuAAeeduhu quli Allahu yabdao alkhalqa thumma yuAAeeduhu faanna tufakoona

Neel : “Ndax am na ci ña ngeen di bokkaaleek [Yàlla] kuy sos mbindéef, mën koo dundal [gannaaw ba mu deewee]?”. Neel : “Yàlla rekk a mën a sos mbindéef te mën koo dundal. Kon naka lees leen di wëlbatee ?”.

35

قُلۡ هَلۡ مِن شُرَكَآئِكُم مَّن يَهۡدِيٓ إِلَى ٱلۡحَقِّۚ قُلِ ٱللَّهُ يَهۡدِي لِلۡحَقِّۗ أَفَمَن يَهۡدِيٓ إِلَى ٱلۡحَقِّ أَحَقُّ أَن يُتَّبَعَ أَمَّن لَّا يَهِدِّيٓ إِلَّآ أَن يُهۡدَىٰۖ فَمَا لَكُمۡ كَيۡفَ تَحۡكُمُونَ

Qul hal min shurakaikum man yahdee ila alhaqqi quli Allahu yahdee lilhaqqi afaman yahdee ila alhaqqi ahaqqu an yuttabaAAa amman la yahiddee illa an yuhda fama lakum kayfa tahkumoona

Neel : “Yàlla rekkay gindee jëme ci dëgg. Moo ndax du Kiy gindee jëme ci dëgg moo gën a yey ci ñu topp ko, walla ka nga xam ne du gindee, lu dul ñu di ko gindi ? Kon lu leen jot te naka ngeen di àttee ?”.

36

وَمَا يَتَّبِعُ أَكۡثَرُهُمۡ إِلَّا ظَنًّاۚ إِنَّ ٱلظَّنَّ لَا يُغۡنِي مِنَ ٱلۡحَقِّ شَيۡـًٔاۚ إِنَّ ٱللَّهَ عَلِيمُۢ بِمَا يَفۡعَلُونَ

Wama yattabiAAu aktharuhum illa thannan inna alththanna la yughnee mina alhaqqi shayan inna Allaha AAaleemun bima yafAAaloona

Li ëpp ci ñoom, toppuñu lu dul ay njort. Te njort du jariñ dara ci dëgg ! Yàlla naka Ku xam xéll la li ngeen di def.

37

وَمَا كَانَ هَٰذَا ٱلۡقُرۡءَانُ أَن يُفۡتَرَىٰ مِن دُونِ ٱللَّهِ وَلَٰكِن تَصۡدِيقَ ٱلَّذِي بَيۡنَ يَدَيۡهِ وَتَفۡصِيلَ ٱلۡكِتَٰبِ لَا رَيۡبَ فِيهِ مِن رَّبِّ ٱلۡعَٰلَمِينَ

Wama kana hatha alquranu an yuftara min dooni Allahi walakin tasdeeqa allathee bayna yadayhi watafseela alkitabi la rayba feehi min rabbi alAAalameena

Alxuraan jii nekkul lu ñu duur bàyyi Yàlla, waaye dafa nekk di luy dëggal la ko jiitu tey settantal Téere ba nga xam ne sikk nekkul ci ne ma nga tukkee ca Boroom àddina si.(s)

38

أَمۡ يَقُولُونَ ٱفۡتَرَىٰهُۖ قُلۡ فَأۡتُواْ بِسُورَةٖ مِّثۡلِهِۦ وَٱدۡعُواْ مَنِ ٱسۡتَطَعۡتُم مِّن دُونِ ٱللَّهِ إِن كُنتُمۡ صَٰدِقِينَ

Am yaqooloona iftarahu qul fatoo bisooratin mithlihi waodAAoo mani istataAAtum min dooni Allahi in kuntum sadiqeena

Am dañoo wax ne : “Dafa koo duur” ? Neel : “Indileen saar wu ni mel, te woo ku leen neex ba mu des Yàlla [mu dimbali leen ci loolu] ndeem ñu dëggu ngeen”.

39

بَلۡ كَذَّبُواْ بِمَا لَمۡ يُحِيطُواْ بِعِلۡمِهِۦ وَلَمَّا يَأۡتِهِمۡ تَأۡوِيلُهُۥۚ كَذَٰلِكَ كَذَّبَ ٱلَّذِينَ مِن قَبۡلِهِمۡۖ فَٱنظُرۡ كَيۡفَ كَانَ عَٰقِبَةُ ٱلظَّـٰلِمِينَ

Bal kaththaboo bima lam yuheetoo biAAilmihi walamma yatihim taweeluhu kathalika kaththaba allatheena min qablihim faonthur kayfa kana AAaqibatu alththalimeena

Déedéet : weddi nañu loo xam ne amuñu xam-xamam te ag leeralam agsiwul ci ñoom. Noonu la ña leen jiitu weddee woon. Waaye xoolal rekk la mujjug tooñkat ya deme woon !

40

وَمِنۡهُم مَّن يُؤۡمِنُ بِهِۦ وَمِنۡهُم مَّن لَّا يُؤۡمِنُ بِهِۦۚ وَرَبُّكَ أَعۡلَمُ بِٱلۡمُفۡسِدِينَ

Waminhum man yuminu bihi waminhum man la yuminu bihi warabbuka aAAlamu bialmufsideena

Te kat am na ci ñoom ñu ko gëm, am na it ñu ko gëmul. Te sa Boroom moo gën a xam yàqkat ya.

41

وَإِن كَذَّبُوكَ فَقُل لِّي عَمَلِي وَلَكُمۡ عَمَلُكُمۡۖ أَنتُم بَرِيٓـُٔونَ مِمَّآ أَعۡمَلُ وَأَنَا۠ بَرِيٓءٞ مِّمَّا تَعۡمَلُونَ

Wain kaththabooka faqul lee AAamalee walakum AAamalukum antum bareeoona mimma aAAmalu waana bareeon mimma taAAmaloona

Bu ñu la weddee, neel : “Sama jëf laa moom, ngeen moom seeni jëf. Yéen deñ ngeen ci li may jëf, man it set naa wecc ci li ngeen di dëf ”.

42

وَمِنۡهُم مَّن يَسۡتَمِعُونَ إِلَيۡكَۚ أَفَأَنتَ تُسۡمِعُ ٱلصُّمَّ وَلَوۡ كَانُواْ لَا يَعۡقِلُونَ

Waminhum man yastamiAAoona ilayka afaanta tusmiAAu alssumma walaw kanoo la yaAAqiloona

Te am na ci ñoom ñu lay déglu. Moo ndax yaw mën nga déggloo ab tëx, doonte la nekkuñu ñu am i xel.

43

وَمِنۡهُم مَّن يَنظُرُ إِلَيۡكَۚ أَفَأَنتَ تَهۡدِي ٱلۡعُمۡيَ وَلَوۡ كَانُواْ لَا يُبۡصِرُونَ

Waminhum man yanthuru ilayka afaanta tahdee alAAumya walaw kanoo la yubsiroona

Te am na ci ñoom ñu lay xool. Moo ndax dangay gindi gumba, doonte dañu dul gis ?

44

إِنَّ ٱللَّهَ لَا يَظۡلِمُ ٱلنَّاسَ شَيۡـٔٗا وَلَٰكِنَّ ٱلنَّاسَ أَنفُسَهُمۡ يَظۡلِمُونَ

Inna Allaha la yathlimu alnnasa shayan walakinna alnnasa anfusahum yathlimoona

Yàlla nag du tooñ nit ci dara, waaye nit ñi ñooy tooñ seen bopp.

45

وَيَوۡمَ يَحۡشُرُهُمۡ كَأَن لَّمۡ يَلۡبَثُوٓاْ إِلَّا سَاعَةٗ مِّنَ ٱلنَّهَارِ يَتَعَارَفُونَ بَيۡنَهُمۡۚ قَدۡ خَسِرَ ٱلَّذِينَ كَذَّبُواْ بِلِقَآءِ ٱللَّهِ وَمَا كَانُواْ مُهۡتَدِينَ

Wayawma yahshuruhum kaan lam yalbathoo illa saAAatan mina alnnahari yataAAarafoona baynahum qad khasira allatheena kaththaboo biliqai Allahi wama kanoo muhtadeena

Bis bu leen Yàlla dajalee, dana mel ni tooguñu [ca seeni bàmmeel] lu dul diirub benn waxtu cig bëccëg, ñuy xamante. Te ña weddi woon ne dajeek Yàlla dana am, yàqule nañu ndax nekkuñu woon ñu gindiku.

46

وَإِمَّا نُرِيَنَّكَ بَعۡضَ ٱلَّذِي نَعِدُهُمۡ أَوۡ نَتَوَفَّيَنَّكَ فَإِلَيۡنَا مَرۡجِعُهُمۡ ثُمَّ ٱللَّهُ شَهِيدٌ عَلَىٰ مَا يَفۡعَلُونَ

Waimma nuriyannaka baAAda allathee naAAiduhum aw natawaffayannaka failayna marjiAAuhum thumma Allahu shaheedun AAala ma yafAAaloona

Te Nu won la dara ca la Nu leen tëkkoo, walla Nu rey la [Yaw Muhammad], lu mu ca doon seenug delluwaay ci Nun la jëmsi. Ba noppi, Yàlla nekk di seede ca lañu daan def.

47

وَلِكُلِّ أُمَّةٖ رَّسُولٞۖ فَإِذَا جَآءَ رَسُولُهُمۡ قُضِيَ بَيۡنَهُم بِٱلۡقِسۡطِ وَهُمۡ لَا يُظۡلَمُونَ

Walikulli ommatin rasoolun faitha jaa rasooluhum qudiya baynahum bialqisti wahum la yuthlamoona

Xeet wu nekk am na ab Yonent. Bu seenub Yonent agsee rekk, dees na àtte seen diggante ci maandute, te kenn duleen tooñ.

48

وَيَقُولُونَ مَتَىٰ هَٰذَا ٱلۡوَعۡدُ إِن كُنتُمۡ صَٰدِقِينَ

Wayaqooloona mata hatha alwaAAdu in kuntum sadiqeena

Ñu naan : “Boobu dig kañ lay doon, ndegam ñu dëggu ngeen” ?

49

قُل لَّآ أَمۡلِكُ لِنَفۡسِي ضَرّٗا وَلَا نَفۡعًا إِلَّا مَا شَآءَ ٱللَّهُۗ لِكُلِّ أُمَّةٍ أَجَلٌۚ إِذَا جَآءَ أَجَلُهُمۡ فَلَا يَسۡتَـٔۡخِرُونَ سَاعَةٗ وَلَا يَسۡتَقۡدِمُونَ

Qul la amliku linafsee darran wala nafAAan illa ma shaa Allahu likulli ommatin ajalun itha jaa ajaluhum fala yastakhiroona saAAatan wala yastaqdimoona

Neel : “Mënaluma sama bopp lor walla njariñ, lu dul lu neex Yàlla. Xeet wu nekk am na àpp. Bu seen àpp matee, deefuleen yeexe wenn waxtu, te duñu jiitu it àpp ba”.(r)

50

قُلۡ أَرَءَيۡتُمۡ إِنۡ أَتَىٰكُمۡ عَذَابُهُۥ بَيَٰتًا أَوۡ نَهَارٗا مَّاذَا يَسۡتَعۡجِلُ مِنۡهُ ٱلۡمُجۡرِمُونَ

Qul araaytum in atakum AAathabuhu bayatan aw naharan matha yastaAAjilu minhu almujrimoona

Neel : “Waaw waxleen ma ! Bu leen mbugal bettoon guddi walla bëccëg, lan la bàkkaarkat yi mën a gaawal ?

51

أَثُمَّ إِذَا مَا وَقَعَ ءَامَنتُم بِهِۦٓۚ ءَآلۡـَٰٔنَ وَقَدۡ كُنتُم بِهِۦ تَسۡتَعۡجِلُونَ

Athumma itha ma waqaAAa amantum bihi alana waqad kuntum bihi tastaAAjiloona

“Moo ndax bu agsee ngeen koy door a gëm ? [Kon deef na leen wax : “Léegi, yéen a ngi ci biir ba noppi”.] Te yéen a ngi koy yàkkamti”.

52

ثُمَّ قِيلَ لِلَّذِينَ ظَلَمُواْ ذُوقُواْ عَذَابَ ٱلۡخُلۡدِ هَلۡ تُجۡزَوۡنَ إِلَّا بِمَا كُنتُمۡ تَكۡسِبُونَ

Thumma qeela lillatheena thalamoo thooqoo AAathaba alkhuldi hal tujzawna illa bima kuntum taksiboona

Topp waxees tooñkat ya : “Ayca mosleen mbugal mu sax dàkk ! Moo ndax dees na leen feye lu wuuteek la ngeen doon fàggu ?”

53

۞وَيَسۡتَنۢبِـُٔونَكَ أَحَقٌّ هُوَۖ قُلۡ إِي وَرَبِّيٓ إِنَّهُۥ لَحَقّٞۖ وَمَآ أَنتُم بِمُعۡجِزِينَ

Wayastanbioonaka ahaqqun huwa qul ee warabbee innahu lahaqqun wama antum bimuAAjizeena

Te danañu sàkku nga leeral : “Ndax loolu dëgg la ?” - Neel : “Waawaaw ! Giñ naa ci sama Boroom ne dëgg la !Te yéen dungeen mën a raw”.

54

وَلَوۡ أَنَّ لِكُلِّ نَفۡسٖ ظَلَمَتۡ مَا فِي ٱلۡأَرۡضِ لَٱفۡتَدَتۡ بِهِۦۗ وَأَسَرُّواْ ٱلنَّدَامَةَ لَمَّا رَأَوُاْ ٱلۡعَذَابَۖ وَقُضِيَ بَيۡنَهُم بِٱلۡقِسۡطِ وَهُمۡ لَا يُظۡلَمُونَ

Walaw anna likulli nafsin thalamat ma fee alardi laiftadat bihi waasarroo alnnadamata lamma raawoo alAAathaba waqudiya baynahum bialqisti wahum la yuthlamoona

Bépp bakkan bu tooñ, bu amoon li nekk ci àddina si, dana ko nangoo joxe ngir jotoo ko.Te bu ñu gisee mbugal ma, dana jéem a nëbb seenug rëccu. Waaye deef na àtte seeni diggante ci maandute, te kenn duleen tooñ [ci wàññil leen dara]..

55

أَلَآ إِنَّ لِلَّهِ مَا فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِۗ أَلَآ إِنَّ وَعۡدَ ٱللَّهِ حَقّٞ وَلَٰكِنَّ أَكۡثَرَهُمۡ لَا يَعۡلَمُونَ

Ala inna lillahi ma fee alssamawati waalardi ala inna waAAda Allahi haqqun walakinna aktharahum la yaAAlamoona

Moo ndax dafa nekkul ne Yàlla moo moom li nekk ci asamaan yi ak suuf si. Digub Yàlla mooy dëgg tigi. Waaye li ëpp ci ñoom xamuñu.

56

هُوَ يُحۡيِۦ وَيُمِيتُ وَإِلَيۡهِ تُرۡجَعُونَ

Huwa yuhyee wayumeetu wailayhi turjaAAoona

Moom mooy dundal, Mooy rey ; te ci Moom ngeen di dellu.

57

يَـٰٓأَيُّهَا ٱلنَّاسُ قَدۡ جَآءَتۡكُم مَّوۡعِظَةٞ مِّن رَّبِّكُمۡ وَشِفَآءٞ لِّمَا فِي ٱلصُّدُورِ وَهُدٗى وَرَحۡمَةٞ لِّلۡمُؤۡمِنِينَ

Ya ayyuha alnnasu qad jaatkum mawAAithatun min rabbikum washifaon lima fee alssudoori wahudan warahmatun lilmumineena

Éy yéen nit ñi ! Ag waaraate dikkal na leen, jóge ci seen Boroom, di saafara li nekk ci seen xol yi, di gindee, di yërmaandey ñi gëm.

58

قُلۡ بِفَضۡلِ ٱللَّهِ وَبِرَحۡمَتِهِۦ فَبِذَٰلِكَ فَلۡيَفۡرَحُواْ هُوَ خَيۡرٞ مِّمَّا يَجۡمَعُونَ

Qul bifadli Allahi wabirahmatihi fabithalika falyafrahoo huwa khayrun mimma yajmaAAoona

Neel : “Bégleen ci xéewal ak yërmaande ; te loolu lépp moo gën la ñu daan dajale [ci alal]”.

59

قُلۡ أَرَءَيۡتُم مَّآ أَنزَلَ ٱللَّهُ لَكُم مِّن رِّزۡقٖ فَجَعَلۡتُم مِّنۡهُ حَرَامٗا وَحَلَٰلٗا قُلۡ ءَآللَّهُ أَذِنَ لَكُمۡۖ أَمۡ عَلَى ٱللَّهِ تَفۡتَرُونَ

Qul araaytum ma anzala Allahu lakum min rizqin fajaAAaltum minhu haraman wahalalan qul allahu athina lakum am AAala Allahi taftaroona

Neel : “Moo ndax gis ngeen li leen Yàlla wàcceel ci xéewal, ngeen jàpp ne am na ci yu araam ak yu dagan ? - Neel : “Ndax Yàllaa leen ko digal ? Walla dangeen di duural Yàlla” ?

60

وَمَا ظَنُّ ٱلَّذِينَ يَفۡتَرُونَ عَلَى ٱللَّهِ ٱلۡكَذِبَ يَوۡمَ ٱلۡقِيَٰمَةِۗ إِنَّ ٱللَّهَ لَذُو فَضۡلٍ عَلَى ٱلنَّاسِ وَلَٰكِنَّ أَكۡثَرَهُمۡ لَا يَشۡكُرُونَ

Wama thannu allatheena yaftaroona AAala Allahi alkathiba yawma alqiyamati inna Allaha lathoo fadlin AAala alnnasi walakinna aktharahum la yashkuroona

Ana lan mooy njortul ñiy duural Yàlla ay fen Bis-pénc ba ? - Dafa dëggu ne Yàlla xéewalaakoon la, waaye li ëpp ci ñoom duñu gërêm [Yàlla].

61

وَمَا تَكُونُ فِي شَأۡنٖ وَمَا تَتۡلُواْ مِنۡهُ مِن قُرۡءَانٖ وَلَا تَعۡمَلُونَ مِنۡ عَمَلٍ إِلَّا كُنَّا عَلَيۡكُمۡ شُهُودًا إِذۡ تُفِيضُونَ فِيهِۚ وَمَا يَعۡزُبُ عَن رَّبِّكَ مِن مِّثۡقَالِ ذَرَّةٖ فِي ٱلۡأَرۡضِ وَلَا فِي ٱلسَّمَآءِ وَلَآ أَصۡغَرَ مِن ذَٰلِكَ وَلَآ أَكۡبَرَ إِلَّا فِي كِتَٰبٖ مُّبِينٍ

Wama takoonu fee shanin wama tatloo minhu min quranin wala taAAmaloona min AAamalin illa kunna AAalaykum shuhoodan ith tufeedoona feehi wama yaAAzubu AAan rabbika min mithqali tharratin fee alardi wala fee alssamai wala asghara min thalika wala akbara illa fee kitabin mubeenun

Doo nekk ci menn mbir, walla ngay jàng dara ci Alxuraan, walla ngeen def jenn jëf te Nekkunu ca seede ba ngeen cay duggu. Te lu toll ni pepp su tuuti du rëcc sa Boroom, du ci suuf si, du ci asamaan yi ; te amul lu ko gën a tuuti walla lu ko gën a rëy lu dul ne mi ngi ci ab téere bu bir.(s)

62

أَلَآ إِنَّ أَوۡلِيَآءَ ٱللَّهِ لَا خَوۡفٌ عَلَيۡهِمۡ وَلَا هُمۡ يَحۡزَنُونَ

Ala inna awliyaa Allahi la khawfun AAalayhim wala hum yahzanoona

Ca dëgg-dëgg, ña féeteek Yàlla duñu gis lu ñu ragal, duñu gis njàqare,

63

ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ وَكَانُواْ يَتَّقُونَ

Allatheena amanoo wakanoo yattaqoona

Ña gëm te ragal Yàlla,

64

لَهُمُ ٱلۡبُشۡرَىٰ فِي ٱلۡحَيَوٰةِ ٱلدُّنۡيَا وَفِي ٱلۡأٓخِرَةِۚ لَا تَبۡدِيلَ لِكَلِمَٰتِ ٱللَّهِۚ ذَٰلِكَ هُوَ ٱلۡفَوۡزُ ٱلۡعَظِيمُ

Lahumu albushra fee alhayati alddunya wafee alakhirati la tabdeela likalimati Allahi thalika huwa alfawzu alAAatheemu

Am nañu mbégte ci dundug àddina ak ca àllaaxira. - Soppeeku du am ciy kàddu Yàlla -. Loolu mooy texe gu mag ga !

65

وَلَا يَحۡزُنكَ قَوۡلُهُمۡۘ إِنَّ ٱلۡعِزَّةَ لِلَّهِ جَمِيعًاۚ هُوَ ٱلسَّمِيعُ ٱلۡعَلِيمُ

Wala yahzunka qawluhum inna alAAizzata lillahi jameeAAan huwa alssameeAAu alAAaleemu

Li ñuy wax , bumu la naqari. Teraanga nag Yàllaa moom lépp. Te Moom Kuy dégg la, Kuy xam la.

66

أَلَآ إِنَّ لِلَّهِ مَن فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَمَن فِي ٱلۡأَرۡضِۗ وَمَا يَتَّبِعُ ٱلَّذِينَ يَدۡعُونَ مِن دُونِ ٱللَّهِ شُرَكَآءَۚ إِن يَتَّبِعُونَ إِلَّا ٱلظَّنَّ وَإِنۡ هُمۡ إِلَّا يَخۡرُصُونَ

Ala inna lillahi man fee alssamawati waman fee alardi wama yattabiAAu allatheena yadAAoona min dooni Allahi shurakaa in yattabiAAoona illa alththanna wain hum illa yakhrusoona

Ca dëgg-dëgg, li nekk ci asamaan yi ak suuf si, Yàllaa leen moom. Ñay jaamu leneen lu dul Yàlla, ñoom daal toppuñu lu dul ay njort. Nekkewuñu lu dul di sos ay fen.

67

هُوَ ٱلَّذِي جَعَلَ لَكُمُ ٱلَّيۡلَ لِتَسۡكُنُواْ فِيهِ وَٱلنَّهَارَ مُبۡصِرًاۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَأٓيَٰتٖ لِّقَوۡمٖ يَسۡمَعُونَ

Huwa allathee jaAAala lakumu allayla litaskunoo feehi waalnnahara mubsiran inna fee thalika laayatin liqawmin yasmaAAoona

Moom [Yàlla], moo def guddi ngir ngeen di ca noppalu, ak bëccëg ngeen di ca gise. Kéemaan nekk na ci loolu ngir aw nit ñuy dégg !

68

قَالُواْ ٱتَّخَذَ ٱللَّهُ وَلَدٗاۗ سُبۡحَٰنَهُۥۖ هُوَ ٱلۡغَنِيُّۖ لَهُۥ مَا فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَمَا فِي ٱلۡأَرۡضِۚ إِنۡ عِندَكُم مِّن سُلۡطَٰنِۭ بِهَٰذَآۚ أَتَقُولُونَ عَلَى ٱللَّهِ مَا لَا تَعۡلَمُونَ

Qaloo ittakhatha Allahu waladan subhanahu huwa alghaniyyu lahu ma fee alssamawati wama fee alardi in AAindakum min sultanin bihatha ataqooloona AAala Allahi ma la taAAlamoona

Wax nañu ne : “Yàlla am na doom”. Kañ naa sellam ga ! Moom ku doylu la ci boppam. Ñeel na ko li ci asamaan yi ak suuf si ; - Amuleen aw layati ci wax jooju. Moo ndax dangeen di wax ci Yàlla lu ngeen xamul ?

69

قُلۡ إِنَّ ٱلَّذِينَ يَفۡتَرُونَ عَلَى ٱللَّهِ ٱلۡكَذِبَ لَا يُفۡلِحُونَ

Qul inna allatheena yaftaroona AAala Allahi alkathiba la yuflihoona

Neel : “Ñiy duural Yàlla ay fen duñu texe”.

70

مَتَٰعٞ فِي ٱلدُّنۡيَا ثُمَّ إِلَيۡنَا مَرۡجِعُهُمۡ ثُمَّ نُذِيقُهُمُ ٱلۡعَذَابَ ٱلشَّدِيدَ بِمَا كَانُواْ يَكۡفُرُونَ

MataAAun fee alddunya thumma ilayna marjiAAuhum thumma nutheequhumu alAAathaba alshshadeeda bima kanoo yakfuroona

Am nañu yóbbal bu néew ci àddina bi ; ñépp danañu dellusi ci Nun Nu mosal leen mbugal mu tar ngir la ñu nekkoon di weddi.

71

۞وَٱتۡلُ عَلَيۡهِمۡ نَبَأَ نُوحٍ إِذۡ قَالَ لِقَوۡمِهِۦ يَٰقَوۡمِ إِن كَانَ كَبُرَ عَلَيۡكُم مَّقَامِي وَتَذۡكِيرِي بِـَٔايَٰتِ ٱللَّهِ فَعَلَى ٱللَّهِ تَوَكَّلۡتُ فَأَجۡمِعُوٓاْ أَمۡرَكُمۡ وَشُرَكَآءَكُمۡ ثُمَّ لَا يَكُنۡ أَمۡرُكُمۡ عَلَيۡكُمۡ غُمَّةٗ ثُمَّ ٱقۡضُوٓاْ إِلَيَّ وَلَا تُنظِرُونِ

Waotlu AAalayhim nabaa noohin ith qala liqawmihi ya qawmi in kana kabura AAalaykum maqamee watathkeeree biayati Allahi faAAala Allahi tawakkaltu faajmiAAoo amrakum washurakaakum thumma la yakun amrukum AAalaykum ghummatan thumma iqdoo ilayya wala tunthirooni

Nettalileen xew-xewu [Nooh], ba mu waxee aw nitam ne leen : «Yéen samaw nit, ndeem sama nekk fii diis na ci yéen, ak samag waare ci kàdduy Yàlla yi, man maa ngi wéeru ci Yàlla. Bu ngeen yaboo ngeen dajale seeni kàttan yéen ak ñi ngeen di jaamu [bàyyi Yàlla]. Te bu seeni pexe nekk aw tiis ci yéen. Te it [lu leen neex] jëme ci man, te buleen négasndiku dara ci def ci man [seeni yéene].(n)

72

فَإِن تَوَلَّيۡتُمۡ فَمَا سَأَلۡتُكُم مِّنۡ أَجۡرٍۖ إِنۡ أَجۡرِيَ إِلَّا عَلَى ٱللَّهِۖ وَأُمِرۡتُ أَنۡ أَكُونَ مِنَ ٱلۡمُسۡلِمِينَ

Fain tawallaytum fama saaltukum min ajrin in ajriya illa AAala Allahi waomirtu an akoona mina almuslimeena

Bu ngeen dëddoo, xamleen ne laajumaleen ag pey... Samag pey nekkul fenn fu dul fa Yàlla. Te digaleef na ma ma bokk ca way-jébbalu ña”.

73

فَكَذَّبُوهُ فَنَجَّيۡنَٰهُ وَمَن مَّعَهُۥ فِي ٱلۡفُلۡكِ وَجَعَلۡنَٰهُمۡ خَلَـٰٓئِفَ وَأَغۡرَقۡنَا ٱلَّذِينَ كَذَّبُواْ بِـَٔايَٰتِنَاۖ فَٱنظُرۡ كَيۡفَ كَانَ عَٰقِبَةُ ٱلۡمُنذَرِينَ

Fakaththaboohu fanajjaynahu waman maAAahu fee alfulki wajaAAalnahum khalaifa waaghraqna allatheena kaththaboo biayatina faonthur kayfa kana AAaqibatu almunthareena

Ñu weddi ko. Nu musal ko mook ña ànd ak moom ca gaal ga, Nu def leen ñuy ñay wuutu [nit ña ci kaw suuf si]. Nu labal ña weddi sunuy ndigal. Nanga xool nag ña ñu waaroon [ca ña weddi], ni seen mujj deme !

74

ثُمَّ بَعَثۡنَا مِنۢ بَعۡدِهِۦ رُسُلًا إِلَىٰ قَوۡمِهِمۡ فَجَآءُوهُم بِٱلۡبَيِّنَٰتِ فَمَا كَانُواْ لِيُؤۡمِنُواْ بِمَا كَذَّبُواْ بِهِۦ مِن قَبۡلُۚ كَذَٰلِكَ نَطۡبَعُ عَلَىٰ قُلُوبِ ٱلۡمُعۡتَدِينَ

Thumma baAAathna min baAAdihi rusulan ila qawmihim fajaoohum bialbayyinati fama kanoo liyuminoo bima kaththaboo bihi min qablu kathalika natbaAAu AAala quloobi almuAAtadeena

Topp nu yónni ginnaawam ay Yonent ci seenu nit. Nu indil leen ay lay yu leer. Waaye nekkuñu woon di way-gëm la ñu weddi woon ca bu jëkk. Ba noonu Lanu tëjee ràpp xoli ña jéggi woon dayo, daan jalgati.

75

ثُمَّ بَعَثۡنَا مِنۢ بَعۡدِهِم مُّوسَىٰ وَهَٰرُونَ إِلَىٰ فِرۡعَوۡنَ وَمَلَإِيْهِۦ بِـَٔايَٰتِنَا فَٱسۡتَكۡبَرُواْ وَكَانُواْ قَوۡمٗا مُّجۡرِمِينَ

Thumma baAAathna min baAAdihim moosa waharoona ila firAAawna wamalaihi biayatina faistakbaroo wakanoo qawman mujrimeena

Topp Nu yónni ci seen ginnaaw Muusaa ak Haaroona ca [Firawna] ak mbooloo ma [ñu xamal leen] sunuy ndigal. Ñu rëy-rëylu, di aw nit ñu dëng [diy saay-saay].

76

فَلَمَّا جَآءَهُمُ ٱلۡحَقُّ مِنۡ عِندِنَا قَالُوٓاْ إِنَّ هَٰذَا لَسِحۡرٞ مُّبِينٞ

Falamma jaahumu alhaqqu min AAindina qaloo inna hatha lasihrun mubeenun

Ba dëgg ga agsee ca ñoom tukkee ci Nun Yàlla, [ñu ne leen] : “Jibar tigi la !”.

77

قَالَ مُوسَىٰٓ أَتَقُولُونَ لِلۡحَقِّ لَمَّا جَآءَكُمۡۖ أَسِحۡرٌ هَٰذَا وَلَا يُفۡلِحُ ٱلسَّـٰحِرُونَ

Qala moosa ataqooloona lilhaqqi lamma jaakum asihrun hatha wala yuflihu alssahiroona

Muusaa ne leen : “Moo ndax dangeen di wax ci dëgg gii ba mu agsee ci yéen, naan leen : Ag jibar la ? Te jibarkat yi duñu texe...”.

78

قَالُوٓاْ أَجِئۡتَنَا لِتَلۡفِتَنَا عَمَّا وَجَدۡنَا عَلَيۡهِ ءَابَآءَنَا وَتَكُونَ لَكُمَا ٱلۡكِبۡرِيَآءُ فِي ٱلۡأَرۡضِ وَمَا نَحۡنُ لَكُمَا بِمُؤۡمِنِينَ

Qaloo ajitana litalfitana AAamma wajadna AAalayhi abaana watakoona lakuma alkibriyao fee alardi wama nahnu lakuma bimumineena

Ñu ne ko : “Moo ndax danga fee dikk ngir dëddale nu ak la nu fekkoon sunuy baay nekk ca ? Ba noppi yéen ñaar ngeen yilif àddina bi ? Waay- waay nun sax gëmunuleen !”

79

وَقَالَ فِرۡعَوۡنُ ٱئۡتُونِي بِكُلِّ سَٰحِرٍ عَلِيمٖ

Waqala firAAawnu itoonee bikulli sahirin AAaleemin

Firawna ne : “Indil-leen ma bépp jibarkat bu am xam-xam !”.

80

فَلَمَّا جَآءَ ٱلسَّحَرَةُ قَالَ لَهُم مُّوسَىٰٓ أَلۡقُواْ مَآ أَنتُم مُّلۡقُونَ

Falamma jaa alssaharatu qala lahum moosa alqoo ma antum mulqoona

Ba jibarkat ya dikkee, Muusaa ne leen : “Sànnileen li ngeen di sànni”.

81

فَلَمَّآ أَلۡقَوۡاْ قَالَ مُوسَىٰ مَا جِئۡتُم بِهِ ٱلسِّحۡرُۖ إِنَّ ٱللَّهَ سَيُبۡطِلُهُۥٓ إِنَّ ٱللَّهَ لَا يُصۡلِحُ عَمَلَ ٱلۡمُفۡسِدِينَ

Falamma alqaw qala moosa ma jitum bihi alssihru inna Allaha sayubtiluhu inna Allaha la yuslihu AAamala almufsideena

Ba ñu sànnee, Muusaa ne leen : “Li ngeen indi jibar rekk la ! Yàlla dana ko neenal. Ne : “Yàlla du àntuloo jëfi yàqkat ya”.

82

وَيُحِقُّ ٱللَّهُ ٱلۡحَقَّ بِكَلِمَٰتِهِۦ وَلَوۡ كَرِهَ ٱلۡمُجۡرِمُونَ

Wayuhiqqu Allahu alhaqqa bikalimatihi walaw kariha almujrimoona

Te Yàlla dana notal dëgg ci dogalam, doonte neexul it ñu dëng ña”.

83

فَمَآ ءَامَنَ لِمُوسَىٰٓ إِلَّا ذُرِّيَّةٞ مِّن قَوۡمِهِۦ عَلَىٰ خَوۡفٖ مِّن فِرۡعَوۡنَ وَمَلَإِيْهِمۡ أَن يَفۡتِنَهُمۡۚ وَإِنَّ فِرۡعَوۡنَ لَعَالٖ فِي ٱلۡأَرۡضِ وَإِنَّهُۥ لَمِنَ ٱلۡمُسۡرِفِينَ

Fama amana limoosa illa thurriyyatun min qawmihi AAala khawfin min firAAawna wamalaihim an yaftinahum wainna firAAawna laAAalin fee alardi wainnahu lamina almusrifeena

Te kenn gëmul woon Muusaa lu dul ab kurél ci aw nitam, [la ko waral] mooy Firawna ak mbooloo ma lañu ragal seen fitna. Te Firawna dafa rëy-rëylu woon ci kaw suuf si, kawe lool, te moom bokk na ca saay- saay sa.(s)

84

وَقَالَ مُوسَىٰ يَٰقَوۡمِ إِن كُنتُمۡ ءَامَنتُم بِٱللَّهِ فَعَلَيۡهِ تَوَكَّلُوٓاْ إِن كُنتُم مُّسۡلِمِينَ

Waqala moosa ya qawmi in kuntum amantum biAllahi faAAalayhi tawakkaloo in kuntum muslimeena

Muusaa ne : “Yéen samaw nit, ndegam gëm ngeen Yàlla, nangeen wéeru ci Moom ndeem ñu wommatu tigi ngeen te di ay jullit”.

85

فَقَالُواْ عَلَى ٱللَّهِ تَوَكَّلۡنَا رَبَّنَا لَا تَجۡعَلۡنَا فِتۡنَةٗ لِّلۡقَوۡمِ ٱلظَّـٰلِمِينَ

Faqaloo AAala Allahi tawakkalna rabbana la tajAAalna fitnatan lilqawmi alththalimeena

Ñu wax ne : “Ci Yàlla lanuy wéeru. Yaw sunu Boroom, Yàlla boonu teg nattu ya tooñkat ya yayoo.

86

وَنَجِّنَا بِرَحۡمَتِكَ مِنَ ٱلۡقَوۡمِ ٱلۡكَٰفِرِينَ

Wanajjina birahmatika mina alqawmi alkafireena

Te nga musal nu ci sa yërmaande, ca nit ña di ay yéefar”.

87

وَأَوۡحَيۡنَآ إِلَىٰ مُوسَىٰ وَأَخِيهِ أَن تَبَوَّءَا لِقَوۡمِكُمَا بِمِصۡرَ بُيُوتٗا وَٱجۡعَلُواْ بُيُوتَكُمۡ قِبۡلَةٗ وَأَقِيمُواْ ٱلصَّلَوٰةَۗ وَبَشِّرِ ٱلۡمُؤۡمِنِينَ

Waawhayna ila moosa waakheehi an tabawwaa liqawmikuma bimisra buyootan waijAAaloo buyootakum qiblatan waaqeemoo alssalata wabashshiri almumineena

Nu jox Muusaa ak mbokkam ma ndigal, ne leen : “Sàkkleen néeg ca Misra ca seen biiru nit, te ngeen def seen néeg jàkka te nangeen di taxawal julli. Te di bégloo ñi gëm [ca seenug waare]”.

88

وَقَالَ مُوسَىٰ رَبَّنَآ إِنَّكَ ءَاتَيۡتَ فِرۡعَوۡنَ وَمَلَأَهُۥ زِينَةٗ وَأَمۡوَٰلٗا فِي ٱلۡحَيَوٰةِ ٱلدُّنۡيَا رَبَّنَا لِيُضِلُّواْ عَن سَبِيلِكَۖ رَبَّنَا ٱطۡمِسۡ عَلَىٰٓ أَمۡوَٰلِهِمۡ وَٱشۡدُدۡ عَلَىٰ قُلُوبِهِمۡ فَلَا يُؤۡمِنُواْ حَتَّىٰ يَرَوُاْ ٱلۡعَذَابَ ٱلۡأَلِيمَ

Waqala moosa rabbana innaka atayta firAAawna wamalaahu zeenatan waamwalan fee alhayati alddunya rabbana liyudilloo AAan sabeelika rabbana itmis AAala amwalihim waoshdud AAala quloobihim fala yuminoo hatta yarawoo alAAathaba alaleema

Muusaa ne : «Yaw sunu Boroom, may nga Firawna ak u nitam taar ak alal ci alali àddina. Yaw sunu Boroom, ña réer moy saw yoon, faral seen alal ya te nga fatt seeni xol, duñu gëm mukk ndare bu ñu gisee mbugal mu tar ma”.

89

قَالَ قَدۡ أُجِيبَت دَّعۡوَتُكُمَا فَٱسۡتَقِيمَا وَلَا تَتَّبِعَآنِّ سَبِيلَ ٱلَّذِينَ لَا يَعۡلَمُونَ

Qala qad ojeebat daAAwatukuma faistaqeema wala tattabiAAanni sabeela allatheena la yaAAlamoona

Mu ne leen : “Nangoof na seeni ñaan. Taxawleen temm yéen ñaar ci bañ a topp yoonu ña xamule”.

90

۞وَجَٰوَزۡنَا بِبَنِيٓ إِسۡرَـٰٓءِيلَ ٱلۡبَحۡرَ فَأَتۡبَعَهُمۡ فِرۡعَوۡنُ وَجُنُودُهُۥ بَغۡيٗا وَعَدۡوًاۖ حَتَّىٰٓ إِذَآ أَدۡرَكَهُ ٱلۡغَرَقُ قَالَ ءَامَنتُ أَنَّهُۥ لَآ إِلَٰهَ إِلَّا ٱلَّذِيٓ ءَامَنَتۡ بِهِۦ بَنُوٓاْ إِسۡرَـٰٓءِيلَ وَأَنَا۠ مِنَ ٱلۡمُسۡلِمِينَ

Wajawazna bibanee israeela albahra faatbaAAahum firAAawnu wajunooduhu baghyan waAAadwan hatta itha adrakahu algharaqu qala amantu annahu la ilaha illa allathee amanat bihi banoo israeela waana mina almuslimeena

Nu jàlle waa Banii-Israayiila géej ga. Firawna topp leen ak lelam [ay xarekatam] ngir mbewte ak ug noonu. Ba lab ga agsee ci moom, mu ne : “Gëm naa ne lay mbir moo di ne : amul jeneen yàlla ju dul Ji waa Banii-Israayiila gëm. Te man bokk naa ci way-wommatu ña”.

91

ءَآلۡـَٰٔنَ وَقَدۡ عَصَيۡتَ قَبۡلُ وَكُنتَ مِنَ ٱلۡمُفۡسِدِينَ

Alana waqad AAasayta qablu wakunta mina almufsideena

[Yàlla ne ko] : Moo ndax léegi [ngay door a gëm] ? Te nga féttéerlu woon lu jiitu te nga bokk ca yàqkat ya !

92

فَٱلۡيَوۡمَ نُنَجِّيكَ بِبَدَنِكَ لِتَكُونَ لِمَنۡ خَلۡفَكَ ءَايَةٗۚ وَإِنَّ كَثِيرٗا مِّنَ ٱلنَّاسِ عَنۡ ءَايَٰتِنَا لَغَٰفِلُونَ

Faalyawma nunajjeeka bibadanika litakoona liman khalfaka ayatan wainna katheeran mina alnnasi AAan ayatina laghafiloona

Tey jii Dananu la musal ci sàmm saw yaram [mu bañ a yàqu] ngir nga nekk ci ña lay wuutu màndarga. Ndaxte ñu bari ci nit ñi dañoo sàggane Sunuy màndarga [yu leen di teete jëme ci Man seen Boroom].

93

وَلَقَدۡ بَوَّأۡنَا بَنِيٓ إِسۡرَـٰٓءِيلَ مُبَوَّأَ صِدۡقٖ وَرَزَقۡنَٰهُم مِّنَ ٱلطَّيِّبَٰتِ فَمَا ٱخۡتَلَفُواْ حَتَّىٰ جَآءَهُمُ ٱلۡعِلۡمُۚ إِنَّ رَبَّكَ يَقۡضِي بَيۡنَهُمۡ يَوۡمَ ٱلۡقِيَٰمَةِ فِيمَا كَانُواْ فِيهِ يَخۡتَلِفُونَ

Walaqad bawwana banee israeela mubawwaa sidqin warazaqnahum mina alttayyibati fama ikhtalafoo hatta jaahumu alAAilmu inna rabbaka yaqdee baynahum yawma alqiyamati feema kanoo feehi yakhtalifoona

Te wàcceel Nanu waa Banii-Israayiila wàccuwaayu teraanga, Nu xéewale leen ñam yu sell ya. Waaye réeruñu woon ba ba leen xam- xam dikkalee. Sa Boroom nag dana àtteji seen diggante bu Bis-pénc baa ci lépp lañu doon juuyoo.(r)

94

فَإِن كُنتَ فِي شَكّٖ مِّمَّآ أَنزَلۡنَآ إِلَيۡكَ فَسۡـَٔلِ ٱلَّذِينَ يَقۡرَءُونَ ٱلۡكِتَٰبَ مِن قَبۡلِكَۚ لَقَدۡ جَآءَكَ ٱلۡحَقُّ مِن رَّبِّكَ فَلَا تَكُونَنَّ مِنَ ٱلۡمُمۡتَرِينَ

Fain kunta fee shakkin mimma anzalnna ilayka faisali allatheena yaqraoona alkitaba min qablika laqad jaaka alhaqqu min rabbika fala takoonanna mina almumtareena

Boo amee sikki-sàkka ci li Nu wàcce ci yaw, laajal ña jàngoon Téere ba. Ba li wér dëgg agsi na ci yaw jóge ca sa Boroom : bul bokk ci way- sikki-sàkka ña, werantekat ña.

95

وَلَا تَكُونَنَّ مِنَ ٱلَّذِينَ كَذَّبُواْ بِـَٔايَٰتِ ٱللَّهِ فَتَكُونَ مِنَ ٱلۡخَٰسِرِينَ

Wala takoonanna mina allatheena kaththaboo biayati Allahi fatakoona mina alkhasireena

Bul bokk mukk ci ñiy weddi kàdduy Yàlla. Nde kon nga bokk ca ña yàqule.

96

إِنَّ ٱلَّذِينَ حَقَّتۡ عَلَيۡهِمۡ كَلِمَتُ رَبِّكَ لَا يُؤۡمِنُونَ

Inna allatheena haqqat AAalayhim kalimatu rabbika la yuminoona

Ña nga xam ne seen kàddug Boroom far na dal ca seen kaw, duñu gëm,

97

وَلَوۡ جَآءَتۡهُمۡ كُلُّ ءَايَةٍ حَتَّىٰ يَرَوُاْ ٱلۡعَذَابَ ٱلۡأَلِيمَ

Walaw jaathum kullu ayatin hatta yarawoo alAAathaba alaleema

doonte la tegtal yépp dikkal na leen it [duñu gëm], mbete ñu gisee mbugal mu metti ma.

98

فَلَوۡلَا كَانَتۡ قَرۡيَةٌ ءَامَنَتۡ فَنَفَعَهَآ إِيمَٰنُهَآ إِلَّا قَوۡمَ يُونُسَ لَمَّآ ءَامَنُواْ كَشَفۡنَا عَنۡهُمۡ عَذَابَ ٱلۡخِزۡيِ فِي ٱلۡحَيَوٰةِ ٱلدُّنۡيَا وَمَتَّعۡنَٰهُمۡ إِلَىٰ حِينٖ

Falawla kanat qaryatun amanat fanafaAAaha eemanuha illa qawma yoonusa lamma amanoo kashafna AAanhum AAathaba alkhizyi fee alhayati alddunya wamattaAAnahum ila heenin

Te amul benn dëkk [bu gëmadi, bu alkaande dikkee] buy door a gëm, di jariñoo ngëmam, lu dul nitu Yuunusa ! Ba ñu gëmee Lanu leen teggil mbugal muy toroxale ci dundug àddina gii, teg ca jox leen ay xéewal ab diir.

99

وَلَوۡ شَآءَ رَبُّكَ لَأٓمَنَ مَن فِي ٱلۡأَرۡضِ كُلُّهُمۡ جَمِيعًاۚ أَفَأَنتَ تُكۡرِهُ ٱلنَّاسَ حَتَّىٰ يَكُونُواْ مُؤۡمِنِينَ

Walaw shaa rabbuka laamana man fee alardi kulluhum jameeAAan afaanta tukrihu alnnasa hatta yakoonoo mumineena

Bu neexoon sa Boroorm, fàwwu ñi nekk ci kaw suuf si ñépp gëm. Moo ndax yaw dangay ga [gétén] nit ñi ci ñu nekk ñu gëm ?

100

وَمَا كَانَ لِنَفۡسٍ أَن تُؤۡمِنَ إِلَّا بِإِذۡنِ ٱللَّهِۚ وَيَجۡعَلُ ٱلرِّجۡسَ عَلَى ٱلَّذِينَ لَا يَعۡقِلُونَ

Wama kana linafsin an tumina illa biithni Allahi wayajAAalu alrrijsa AAala allatheena la yaAAqiloona

Yellul ci benn bakkan muy gëm lu dul ci coobarey Yàlla. Te Dana teg mbugal ña xel- luwul [ba mën a ràññee dëgg].

101

قُلِ ٱنظُرُواْ مَاذَا فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِۚ وَمَا تُغۡنِي ٱلۡأٓيَٰتُ وَٱلنُّذُرُ عَن قَوۡمٖ لَّا يُؤۡمِنُونَ

Quli onthuroo matha fee alssamawati waalardi wama tughnee alayatu waalnnuthuru AAan qawmin la yuminoona

Neel : “Xool-leen li nekk ci asamaan yi ak suuf si”. Te kaawtéef ya ak waaraate ya duñu jariñ dara ci aw nit ñu gëmul.

102

فَهَلۡ يَنتَظِرُونَ إِلَّا مِثۡلَ أَيَّامِ ٱلَّذِينَ خَلَوۡاْ مِن قَبۡلِهِمۡۚ قُلۡ فَٱنتَظِرُوٓاْ إِنِّي مَعَكُم مِّنَ ٱلۡمُنتَظِرِينَ

Fahal yantathiroona illa mithla ayyami allatheena khalaw min qablihim qul faintathiroo innee maAAakum mina almuntathireena

Moo ndax ñooña dañuy xaar ba mu deme ni bis yu tiis, yu ña leen jiitu woon dajoon, agsi ci ñoom ? Neleen : “Muñandikuleen ! Man it maa ngi bokk ci ñay muñandiku”.

103

ثُمَّ نُنَجِّي رُسُلَنَا وَٱلَّذِينَ ءَامَنُواْۚ كَذَٰلِكَ حَقًّا عَلَيۡنَا نُنجِ ٱلۡمُؤۡمِنِينَ

Thumma nunajjee rusulana waallatheena amanoo kathalika haqqan AAalayna nunjee almumineena

Topp ginnaaw ba, Nu musal Sunuy Yonent ak ña gëm. Noonu la yaye ci Nun Nuy musal ñi gëm.

104

قُلۡ يَـٰٓأَيُّهَا ٱلنَّاسُ إِن كُنتُمۡ فِي شَكّٖ مِّن دِينِي فَلَآ أَعۡبُدُ ٱلَّذِينَ تَعۡبُدُونَ مِن دُونِ ٱللَّهِ وَلَٰكِنۡ أَعۡبُدُ ٱللَّهَ ٱلَّذِي يَتَوَفَّىٰكُمۡۖ وَأُمِرۡتُ أَنۡ أَكُونَ مِنَ ٱلۡمُؤۡمِنِينَ

Qul ya ayyuha alnnasu in kuntum fee shakkin min deenee fala aAAbudu allatheena taAAbudoona min dooni Allahi walakin aAAbudu Allaha allathee yatawaffakum waomirtu an akoona mina almumineena

Neel : «Éy yéen nit ñi ! Bu ngeen amee xel-ñaar ci sama diine jii, xamleen ne man duma jaamu li ngeen di jaamu bàyyi Yàlla ; Waaye Yàlla laay jaamu, Moom mi leen di rey. Te digaleef na ma ma bokk ca way-gëm ña”.(s)

105

وَأَنۡ أَقِمۡ وَجۡهَكَ لِلدِّينِ حَنِيفٗا وَلَا تَكُونَنَّ مِنَ ٱلۡمُشۡرِكِينَ

Waan aqim wajhaka lilddeeni haneefan wala takoonanna mina almushrikeena

Te : “Nga taxaw temm jublu ci diine jii wéetal Yàlla ! Te bul bokk mukk ca way- bokkaale ña ;

106

وَلَا تَدۡعُ مِن دُونِ ٱللَّهِ مَا لَا يَنفَعُكَ وَلَا يَضُرُّكَۖ فَإِن فَعَلۡتَ فَإِنَّكَ إِذٗا مِّنَ ٱلظَّـٰلِمِينَ

Wala tadAAu min dooni Allahi ma la yanfaAAuka wala yadurruka fain faAAalta fainnaka ithan mina alththalimeena

bul jaamu, bàyyi Yàlla, loo xam ne mënu laa lor, mënu laa jariñ. Soo ko defee rekk daldi bokk ca tooñkat ya”.

107

وَإِن يَمۡسَسۡكَ ٱللَّهُ بِضُرّٖ فَلَا كَاشِفَ لَهُۥٓ إِلَّا هُوَۖ وَإِن يُرِدۡكَ بِخَيۡرٖ فَلَا رَآدَّ لِفَضۡلِهِۦۚ يُصِيبُ بِهِۦ مَن يَشَآءُ مِنۡ عِبَادِهِۦۚ وَهُوَ ٱلۡغَفُورُ ٱلرَّحِيمُ

Wain yamsaska Allahu bidurrin fala kashifa lahu illa huwa wain yuridka bikhayrin fala radda lifadlihi yuseebu bihi man yashao min AAibadihi wahuwa alghafooru alrraheemu

Bu la Yàlla saddee aw naqar, kenn du la ko mën a teggil ku dul Moom. Bu la bégalee ci aw yiw, dara du mën a fànq xéewalam. Dana ko jottale ku ko soob ci jaamam yi. Moo di Xéewalaakoon ba, di Jaglewaakoon ba.

108

قُلۡ يَـٰٓأَيُّهَا ٱلنَّاسُ قَدۡ جَآءَكُمُ ٱلۡحَقُّ مِن رَّبِّكُمۡۖ فَمَنِ ٱهۡتَدَىٰ فَإِنَّمَا يَهۡتَدِي لِنَفۡسِهِۦۖ وَمَن ضَلَّ فَإِنَّمَا يَضِلُّ عَلَيۡهَاۖ وَمَآ أَنَا۠ عَلَيۡكُم بِوَكِيلٖ

Qul ya ayyuha alnnasu qad jaakumu alhaqqu min rabbikum famani ihtada fainnama yahtadee linafsihi waman dalla fainnama yadillu AAalayha wama ana AAalaykum biwakeelin

Neel : «Éy yéen nit ñi ! Dëgg gi ñëw na ci yéen tukke ci seen Boroom. Ku jub te gindiku, boppam ; ku réer, sànku it boppam. Man dey warlulumaleen dara [ci seeni mbir].

109

وَٱتَّبِعۡ مَا يُوحَىٰٓ إِلَيۡكَ وَٱصۡبِرۡ حَتَّىٰ يَحۡكُمَ ٱللَّهُۚ وَهُوَ خَيۡرُ ٱلۡحَٰكِمِينَ

WaittabiAA ma yooha ilayka waisbir hatta yahkuma Allahu wahuwa khayru alhakimeena

Te nanga topp [Yaw Yonent bi] la ñu la soloo, te nga sax ci Man ba ba Yàllay àtte te Mooy gën jaa mën a àtte. Saar 11 : Huud 123 aaya