← Suurat yépp
Suurat 12111 aaya

يوسف

Yusuf

Joseph

Tekki

Tann làkk

1

الٓرۚ تِلۡكَ ءَايَٰتُ ٱلۡكِتَٰبِ ٱلۡمُبِينِ

Aliflamra tilka ayatu alkitabi almubeenu

Alif, Laam, Raa. Lii ay xamle la yu nekk ci Téere bu wér péŋŋ bi.

2

إِنَّآ أَنزَلۡنَٰهُ قُرۡءَٰنًا عَرَبِيّٗا لَّعَلَّكُمۡ تَعۡقِلُونَ

Inna anzalnahu quranan AAarabiyyan laAAallakum taAAqiloona

Wàcce Nanu ko mu di ay njàng ci làkku [araab] ngir ngeen xam la mu tekki.

3

نَحۡنُ نَقُصُّ عَلَيۡكَ أَحۡسَنَ ٱلۡقَصَصِ بِمَآ أَوۡحَيۡنَآ إِلَيۡكَ هَٰذَا ٱلۡقُرۡءَانَ وَإِن كُنتَ مِن قَبۡلِهِۦ لَمِنَ ٱلۡغَٰفِلِينَ

Nahnu naqussu AAalayka ahsana alqasasi bima awhayna ilayka hatha alqurana wain kunta min qablihi lamina alghafileena

Nun noo ngi lay nettali gën jaa rafeti nettaliin ci Alxuraan jii Nu la xamal te lu ko jiitu nekkoon na loo réere.

4

إِذۡ قَالَ يُوسُفُ لِأَبِيهِ يَـٰٓأَبَتِ إِنِّي رَأَيۡتُ أَحَدَ عَشَرَ كَوۡكَبٗا وَٱلشَّمۡسَ وَٱلۡقَمَرَ رَأَيۡتُهُمۡ لِي سَٰجِدِينَ

Ith qala yoosufu liabeehi ya abati innee raaytu ahada AAashara kawkaban waalshshamsa waalqamara raaytuhum lee sajideena

[Fàttalikul] ba Yuusufa waxee baayam ne ko : «Yaw sama baay, man gis naa [ci gént] fukki bindiw ak ñaar ak jant bi ak weer wi ; ñu may sujjóotal”.

5

قَالَ يَٰبُنَيَّ لَا تَقۡصُصۡ رُءۡيَاكَ عَلَىٰٓ إِخۡوَتِكَ فَيَكِيدُواْ لَكَ كَيۡدًاۖ إِنَّ ٱلشَّيۡطَٰنَ لِلۡإِنسَٰنِ عَدُوّٞ مُّبِينٞ

Qala ya bunayya la taqsus ruyaka AAala ikhwatika fayakeedoo laka kaydan inna alshshaytana lilinsani AAaduwwun mubeenun

Mu ne ko : «Yaw sama doom, bul nettali sa gént gi say doomi-baay, [boo leen ko nettalee], danañu la fexeel am pexe ; ndax Séytaane noonub nit la bu tar ag nooneel.

6

وَكَذَٰلِكَ يَجۡتَبِيكَ رَبُّكَ وَيُعَلِّمُكَ مِن تَأۡوِيلِ ٱلۡأَحَادِيثِ وَيُتِمُّ نِعۡمَتَهُۥ عَلَيۡكَ وَعَلَىٰٓ ءَالِ يَعۡقُوبَ كَمَآ أَتَمَّهَا عَلَىٰٓ أَبَوَيۡكَ مِن قَبۡلُ إِبۡرَٰهِيمَ وَإِسۡحَٰقَۚ إِنَّ رَبَّكَ عَلِيمٌ حَكِيمٞ

Wakathalika yajtabeeka rabbuka wayuAAallimuka min taweeli alahadeethi wayutimmu niAAmatahu AAalayka waAAala ali yaAAqooba kama atammaha AAala abawayka min qablu ibraheema waishaqa inna rabbaka AAaleemun hakeemun

Kem [ni nga génte], sa Boroom dana la tànn te Dana la xamal pirim gént, te Dana matal ci yaw ay xéewalam ak njabootu Yanqooba, ni Mu ko matalee woon bu jëkk ca sa ñaari maam ya, Ibraahiima ak Isaaqa, sa Boroom nag ku xam la, ku xereñ la”.

7

۞لَّقَدۡ كَانَ فِي يُوسُفَ وَإِخۡوَتِهِۦٓ ءَايَٰتٞ لِّلسَّآئِلِينَ

Laqad kana fee yoosufa waikhwatihi ayatun lilssaileena

Dëgg-dëgg kéemaan gu réy am na ci diggante Yuusufa ak i doomi- baayam ngir képp kuy gëstu,

8

إِذۡ قَالُواْ لَيُوسُفُ وَأَخُوهُ أَحَبُّ إِلَىٰٓ أَبِينَا مِنَّا وَنَحۡنُ عُصۡبَةٌ إِنَّ أَبَانَا لَفِي ضَلَٰلٖ مُّبِينٍ

Ith qaloo layoosufu waakhoohu ahabbu ila abeena minna wanahnu AAusbatun inna abana lafee dalalin mubeenin

ba ñu waxee ne : “Sunu baay, Yuusufa ak doomu-ndeyam la gën a bëgg ci nun, te nun mbooloo lanu. Sunu baay daal dafa nekk cig réer gu bir.

9

ٱقۡتُلُواْ يُوسُفَ أَوِ ٱطۡرَحُوهُ أَرۡضٗا يَخۡلُ لَكُمۡ وَجۡهُ أَبِيكُمۡ وَتَكُونُواْ مِنۢ بَعۡدِهِۦ قَوۡمٗا صَٰلِحِينَ

Oqtuloo yoosufa awi itrahoohu ardan yakhlu lakum wajhu abeekum watakoonoo min baAAdihi qawman saliheena

[Am ku wax ne] reyleen Yuusufa mbaa ngeen sànni ko fenn ci suuf si, kon seen baay dootul xool kenn ku dul yéen, te bu loolu amee dangeen nekk di aw nit ñu feeñ”.

10

قَالَ قَآئِلٞ مِّنۡهُمۡ لَا تَقۡتُلُواْ يُوسُفَ وَأَلۡقُوهُ فِي غَيَٰبَتِ ٱلۡجُبِّ يَلۡتَقِطۡهُ بَعۡضُ ٱلسَّيَّارَةِ إِن كُنتُمۡ فَٰعِلِينَ

Qala qailun minhum la taqtuloo yoosufa waalqoohu fee ghayabati aljubbi yaltaqithu baAAdu alssayyarati in kuntum faAAileena

Mu am ca ñoom ku wax ne : “Buleen rey Yuusufa, sànnileen ko ci teen bu lëndëm, kon tukkikat yi danañu ko for su fekkee def ngeen ko”.(n)

11

قَالُواْ يَـٰٓأَبَانَا مَا لَكَ لَا تَأۡمَ۬نَّا عَلَىٰ يُوسُفَ وَإِنَّا لَهُۥ لَنَٰصِحُونَ

Qaloo ya abana ma laka la tamanna AAala yoosufa wainna lahu lanasihoona

Ñu ne : «Yaw sunu baay, ana lan moo tax wóoluwoo nu ci Yuusufa ? Te nun dañu koy laabire doŋŋ.

12

أَرۡسِلۡهُ مَعَنَا غَدٗا يَرۡتَعۡ وَيَلۡعَبۡ وَإِنَّا لَهُۥ لَحَٰفِظُونَ

Arsilhu maAAana ghadan yartaAA wayalAAab wainna lahu lahafithoona

Bu subaa nga yabal ko mu ànd ak nun muy sàmm jur gi, di fo. Dananu ko wattu”.

13

قَالَ إِنِّي لَيَحۡزُنُنِيٓ أَن تَذۡهَبُواْ بِهِۦ وَأَخَافُ أَن يَأۡكُلَهُ ٱلذِّئۡبُ وَأَنتُمۡ عَنۡهُ غَٰفِلُونَ

Qala innee layahzununee an thathhaboo bihi waakhafu an yakulahu alththibu waantum AAanhu ghafiloona

Mu ne leen : “Man dey, am naa njàqare ci ngeen ànd ak moom ; danaa ragal ngeen sàggan ba ag till lekk ko”.

14

قَالُواْ لَئِنۡ أَكَلَهُ ٱلذِّئۡبُ وَنَحۡنُ عُصۡبَةٌ إِنَّآ إِذٗا لَّخَٰسِرُونَ

Qaloo lain akalahu alththibu wanahnu AAusbatun inna ithan lakhasiroona

Ñu ne : “Till! Su ko lekkee nag ak nii nu nekkee di mbooloo, kon dey nu gën a yées”.

15

فَلَمَّا ذَهَبُواْ بِهِۦ وَأَجۡمَعُوٓاْ أَن يَجۡعَلُوهُ فِي غَيَٰبَتِ ٱلۡجُبِّۚ وَأَوۡحَيۡنَآ إِلَيۡهِ لَتُنَبِّئَنَّهُم بِأَمۡرِهِمۡ هَٰذَا وَهُمۡ لَا يَشۡعُرُونَ

Falamma thahaboo bihi waajmaAAoo an yajAAaloohu fee ghayabati aljubbi waawhayna ilayhi latunabiannahum biamrihim hatha wahum la yashAAuroona

Ba ñu àndeek moom, te mànkoo ci sànni ko ca xóot-xóot ba [teen ba], Nu xamal [Nun Yàlla] Yuusufa ne : “Danga leen mës a nettali seen jëf jii fu ñu ko foogewul”.

16

وَجَآءُوٓ أَبَاهُمۡ عِشَآءٗ يَبۡكُونَ

Wajaoo abahum AAishaan yabkoona

Ñu dellu ci seen baay ci marax, di joox.

17

قَالُواْ يَـٰٓأَبَانَآ إِنَّا ذَهَبۡنَا نَسۡتَبِقُ وَتَرَكۡنَا يُوسُفَ عِندَ مَتَٰعِنَا فَأَكَلَهُ ٱلذِّئۡبُۖ وَمَآ أَنتَ بِمُؤۡمِنٖ لَّنَا وَلَوۡ كُنَّا صَٰدِقِينَ

Qaloo ya abana inna thahabna nastabiqu watarakna yoosufa AAinda mataAAina faakalahu alththibu wama anta bimuminin lana walaw kunna sadiqeena

Ñu ne : «Yaw sunu baay, ba ñu demee, dañu doon rawante, bàyyi Yuusufa ca sunuy yóbbal ; ag till lekk ko. Te bu nu waxee dëgg it du tax nga gëm li nu wax”.

18

وَجَآءُو عَلَىٰ قَمِيصِهِۦ بِدَمٖ كَذِبٖۚ قَالَ بَلۡ سَوَّلَتۡ لَكُمۡ أَنفُسُكُمۡ أَمۡرٗاۖ فَصَبۡرٞ جَمِيلٞۖ وَٱللَّهُ ٱلۡمُسۡتَعَانُ عَلَىٰ مَا تَصِفُونَ

Wajaoo AAala qameesihi bidamin kathibin qala bal sawwalat lakum anfusukum amran fasabrun jameelun waAllahu almustaAAanu AAala ma tasifoona

Ñu indiwaale yéreem yu taq dereet [ju dul dereeti Yusuufa]. Mu tontu leen ne : “Yéen dey, seen bakkan rafetal na leen mbir mii... Waaye danaa sax ci muñ gu rafet ! Ci Yàlla laay dimbandikoo ci lii ngeen nettali !”

19

وَجَآءَتۡ سَيَّارَةٞ فَأَرۡسَلُواْ وَارِدَهُمۡ فَأَدۡلَىٰ دَلۡوَهُۥۖ قَالَ يَٰبُشۡرَىٰ هَٰذَا غُلَٰمٞۚ وَأَسَرُّوهُ بِضَٰعَةٗۚ وَٱللَّهُ عَلِيمُۢ بِمَا يَعۡمَلُونَ

Wajaat sayyaratun faarsaloo waridahum faadla dalwahu qala ya bushra hatha ghulamun waasarroohu bidaAAatan waAllahu AAaleemun bima yaAAmaloona

Ay tukkikat agsi, yónni seenub rootkat, mu yoor baagam. Mu daldi ne : “Mbégtee ngi ! Lii de ab xale la !” Ñu yóbbu ko nar koo jaay. Te Yàlla ku xam la la ñuy def.

20

وَشَرَوۡهُ بِثَمَنِۭ بَخۡسٖ دَرَٰهِمَ مَعۡدُودَةٖ وَكَانُواْ فِيهِ مِنَ ٱلزَّـٰهِدِينَ

Washarawhu bithamanin bakhsin darahima maAAdoodatin wakanoo feehi mina alzzahideena

Ñu jaay ko ci njëg gu néew : ay dërëm yu bariwul. Ndax dañu koo xeeboon.

21

وَقَالَ ٱلَّذِي ٱشۡتَرَىٰهُ مِن مِّصۡرَ لِٱمۡرَأَتِهِۦٓ أَكۡرِمِي مَثۡوَىٰهُ عَسَىٰٓ أَن يَنفَعَنَآ أَوۡ نَتَّخِذَهُۥ وَلَدٗاۚ وَكَذَٰلِكَ مَكَّنَّا لِيُوسُفَ فِي ٱلۡأَرۡضِ وَلِنُعَلِّمَهُۥ مِن تَأۡوِيلِ ٱلۡأَحَادِيثِۚ وَٱللَّهُ غَالِبٌ عَلَىٰٓ أَمۡرِهِۦ وَلَٰكِنَّ أَكۡثَرَ ٱلنَّاسِ لَا يَعۡلَمُونَ

Waqala allathee ishtarahu min misra liimraatihi akrimee mathwahu AAasa an yanfaAAana aw nattakhithahu waladan wakathalika makkanna liyoosufa fee alardi walinuAAallimahu min taweeli alahadeethi waAllahu ghalibun AAala amrihi walakinna akthara alnnasi la yaAAlamoona

Ka ko jënd di waa Misra, wax na jabaram ne ko : “Teralal ma ko. Xéy- na mu jariñ nu mbaa nu def ko sunu doom.”. Noonu la nu darajaale Yuusufa ci suuf si, ak it ngir Nu jàngal ko pirim gént. Yàlla kuy not la ca la Mu namm : waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.

22

وَلَمَّا بَلَغَ أَشُدَّهُۥٓ ءَاتَيۡنَٰهُ حُكۡمٗا وَعِلۡمٗاۚ وَكَذَٰلِكَ نَجۡزِي ٱلۡمُحۡسِنِينَ

Walamma balagha ashuddahu ataynahu hukman waAAilman wakathalika najzee almuhsineena

Ba mu màggee ba tollu ci góor gu mat, jox Nanu ko ràññee ak xam- xam. Te noonu Lanuy feye way-rafetal ña.

23

وَرَٰوَدَتۡهُ ٱلَّتِي هُوَ فِي بَيۡتِهَا عَن نَّفۡسِهِۦ وَغَلَّقَتِ ٱلۡأَبۡوَٰبَ وَقَالَتۡ هَيۡتَ لَكَۚ قَالَ مَعَاذَ ٱللَّهِۖ إِنَّهُۥ رَبِّيٓ أَحۡسَنَ مَثۡوَايَۖ إِنَّهُۥ لَا يُفۡلِحُ ٱلظَّـٰلِمُونَ

Warawadathu allatee huwa fee baytiha AAan nafsihi waghallaqati alabwaba waqalat hayta laka qala maAAatha Allahi innahu rabbee ahsana mathwaya innahu la yuflihu alththalimoona

Ndaw sa nga xam ne [Moo ko fat ca kërëm] sàkku na ko ci boppam. Tëj na buntu ya ne ko : “Ayca ñëwal ci man” - Mu ne : “Maa ngi muslu ci Yàlla ! [tëdd ak yaw] te sama sang [bi ma jënd] fonk na ma, teral na ma. Te tooñkat ya duñu texe mukk”.(s)

24

وَلَقَدۡ هَمَّتۡ بِهِۦۖ وَهَمَّ بِهَا لَوۡلَآ أَن رَّءَا بُرۡهَٰنَ رَبِّهِۦۚ كَذَٰلِكَ لِنَصۡرِفَ عَنۡهُ ٱلسُّوٓءَ وَٱلۡفَحۡشَآءَۚ إِنَّهُۥ مِنۡ عِبَادِنَا ٱلۡمُخۡلَصِينَ

Walaqad hammat bihi wahamma biha lawla an raa burhana rabbihi kathalika linasrifa AAanhu alssooa waalfahshaa innahu min AAibadina almukhlaseena

Ndaw sa xemmem na [Yuusufa]. Moom [Yuusufa] it xemmem na [ndaw sa] bu dul koon la mu gis kaawtéefi Boroomam. Noonu la Nu def ngir fegal ko ñaawtéef ak njaaloo. Moom sax dafa bokk ca sunu jaam yu sell ya.

25

وَٱسۡتَبَقَا ٱلۡبَابَ وَقَدَّتۡ قَمِيصَهُۥ مِن دُبُرٖ وَأَلۡفَيَا سَيِّدَهَا لَدَا ٱلۡبَابِۚ قَالَتۡ مَا جَزَآءُ مَنۡ أَرَادَ بِأَهۡلِكَ سُوٓءًا إِلَّآ أَن يُسۡجَنَ أَوۡ عَذَابٌ أَلِيمٞ

Waistabaqa albaba waqaddat qameesahu min duburin waalfaya sayyidaha lada albabi qalat ma jazao man arada biahlika sooan illa an yusjana aw AAathabun aleemun

Ñu jëkkante buntu ba, [ndaw sa] xëcc yérey [Yuusufa] ca ginnaaw ga. Ñu dajeek jëkkëram ca buntu ba. [Ndaw sa] daldi ne : “Ana lan moo di peyug ku naral lu bon sa jabar, lu dul tëj ci kaso walla mbugal mu metti ?”

26

قَالَ هِيَ رَٰوَدَتۡنِي عَن نَّفۡسِيۚ وَشَهِدَ شَاهِدٞ مِّنۡ أَهۡلِهَآ إِن كَانَ قَمِيصُهُۥ قُدَّ مِن قُبُلٖ فَصَدَقَتۡ وَهُوَ مِنَ ٱلۡكَٰذِبِينَ

Qala hiya rawadatnee AAan nafsee washahida shahidun min ahliha in kana qameesuhu qudda min qubulin fasadaqat wahuwa mina alkathibeena

[Yuusufa] ne : “Moo ma sàkku ci sama jëmm”. Mu am seede su di mbokkum ndaw sa daldi seede ne : “Bu fekkee ne yéreem ci kanam la xottiku, ndaw sa moo wax dëgg, moom mu bokk ca fenkat ya.

27

وَإِن كَانَ قَمِيصُهُۥ قُدَّ مِن دُبُرٖ فَكَذَبَتۡ وَهُوَ مِنَ ٱلصَّـٰدِقِينَ

Wain kana qameesuhu qudda min duburin fakathabat wahuwa mina alssadiqeena

Bu yéreem xottikoo ci ginnaaw, ndaw sa moo fen, moom mu bokk ca ñu dëggu ña”.

28

فَلَمَّا رَءَا قَمِيصَهُۥ قُدَّ مِن دُبُرٖ قَالَ إِنَّهُۥ مِن كَيۡدِكُنَّۖ إِنَّ كَيۡدَكُنَّ عَظِيمٞ

Falamma raa qameesahu qudda min duburin qala innahu min kaydikunna inna kaydakunna AAatheemun

Ba jëkkër ja gisee yére ya xottiku ca ginnaaw, mu ne : “Lii ci seeni pexe la [yéen jigéen ñi] ! te seeni pexe réy na !

29

يُوسُفُ أَعۡرِضۡ عَنۡ هَٰذَاۚ وَٱسۡتَغۡفِرِي لِذَنۢبِكِۖ إِنَّكِ كُنتِ مِنَ ٱلۡخَاطِـِٔينَ

Yoosufu aAArid AAan hatha waistaghfiree lithanbiki innaki kunti mina alkhatieena

Yuusufa, dëddul lii ! Te yaw [sama jabar] jéggalul sa bàkkaar ndax yaw bokk nga ca ñay def lu bon”.

30

۞وَقَالَ نِسۡوَةٞ فِي ٱلۡمَدِينَةِ ٱمۡرَأَتُ ٱلۡعَزِيزِ تُرَٰوِدُ فَتَىٰهَا عَن نَّفۡسِهِۦۖ قَدۡ شَغَفَهَا حُبًّاۖ إِنَّا لَنَرَىٰهَا فِي ضَلَٰلٖ مُّبِينٖ

Waqala niswatun fee almadeenati imraatu alAAazeezi turawidu fataha AAan nafsihi qad shaghafaha hubban inna lanaraha fee dalalin mubeenin

Aw jigéen di wax ci dëkk bi naan : “Jabaru buur bi dafa doon sàkku jaamam ! Mbëggeel gëlamal ko. Nun daal gis nanu mu nekk ci ag réer gu tar.

31

فَلَمَّا سَمِعَتۡ بِمَكۡرِهِنَّ أَرۡسَلَتۡ إِلَيۡهِنَّ وَأَعۡتَدَتۡ لَهُنَّ مُتَّكَـٔٗا وَءَاتَتۡ كُلَّ وَٰحِدَةٖ مِّنۡهُنَّ سِكِّينٗا وَقَالَتِ ٱخۡرُجۡ عَلَيۡهِنَّۖ فَلَمَّا رَأَيۡنَهُۥٓ أَكۡبَرۡنَهُۥ وَقَطَّعۡنَ أَيۡدِيَهُنَّ وَقُلۡنَ حَٰشَ لِلَّهِ مَا هَٰذَا بَشَرًا إِنۡ هَٰذَآ إِلَّا مَلَكٞ كَرِيمٞ

Falamma samiAAat bimakrihinna arsalat ilayhinna waaAAtadat lahunna muttakaan waatat kulla wahidatin minhunna sikkeenan waqalati okhruj AAalayhinna falamma raaynahu akbarnahu waqattaAAna aydiyahunna waqulna hasha lillahi ma hatha basharan in hatha illa malakun kareemun

Bi mu déggee seen jëw, mu yónnee ca ñoom, waajalal leen aw ñam ; indil ku nekk ca ñoom paaka. [Ba ñuy lekk, mu ne Yuusufa] : “Génnal jëm ci ñoom” - Ba ñu ko gisee, ñu yéemu ci moom bay dagg seeni yoxo, di wax naan : “Cëy Yàlla ! Kii du nit, kii nekkul lu dul Malaaka mu tedd !”

32

قَالَتۡ فَذَٰلِكُنَّ ٱلَّذِي لُمۡتُنَّنِي فِيهِۖ وَلَقَدۡ رَٰوَدتُّهُۥ عَن نَّفۡسِهِۦ فَٱسۡتَعۡصَمَۖ وَلَئِن لَّمۡ يَفۡعَلۡ مَآ ءَامُرُهُۥ لَيُسۡجَنَنَّ وَلَيَكُونٗا مِّنَ ٱلصَّـٰغِرِينَ

Qalat fathalikunna allathee lumtunnanee feehi walaqad rawadtuhu AAan nafsihi faistAAsama walain lam yafAAal ma amuruhu layusjananna walayakoonan mina alssaghireena

Mu ne : “Mu ngoog lii ngeen ma doon yedde. Maa ko sàkku woon mu bañ. Te bu deful li ma ko sant, waat naa ne dees na ko tëj kaso mu detteelu”.

33

قَالَ رَبِّ ٱلسِّجۡنُ أَحَبُّ إِلَيَّ مِمَّا يَدۡعُونَنِيٓ إِلَيۡهِۖ وَإِلَّا تَصۡرِفۡ عَنِّي كَيۡدَهُنَّ أَصۡبُ إِلَيۡهِنَّ وَأَكُن مِّنَ ٱلۡجَٰهِلِينَ

Qala rabbi alssijnu ahabbu ilayya mimma yadAAoonanee ilayhi wailla tasrif AAannee kaydahunna asbu ilayhinna waakun mina aljahileena

Mu ne[moom Yuusufa] : «Yaw sama Boroom, kaso laa gën a bëgg ci lii ñu may woo jëme ma ca. Te boo ma wëlbatilul seeni pexe, danaa jeng jëm ca ñoom te kon ma bokk ca ña réer [xamadi]”.(r)

34

فَٱسۡتَجَابَ لَهُۥ رَبُّهُۥ فَصَرَفَ عَنۡهُ كَيۡدَهُنَّۚ إِنَّهُۥ هُوَ ٱلسَّمِيعُ ٱلۡعَلِيمُ

Faistajaba lahu rabbuhu fasarafa AAanhu kaydahunna innahu huwa alssameeAAu alAAaleemu

Boroomam nangu ñaanam, daldi ko fegal seeni pexe. Moom [Yàlla] mooy Aji-dégg, di Aji-xam ji.

35

ثُمَّ بَدَا لَهُم مِّنۢ بَعۡدِ مَا رَأَوُاْ ٱلۡأٓيَٰتِ لَيَسۡجُنُنَّهُۥ حَتَّىٰ حِينٖ

Thumma bada lahum min baAAdi ma raawoo alayati layasjununnahu hatta heenin

Ginnaaw ba ñu gisee dëgg ga mu fees ca ñoom, ñu ne fàwwu danañu ko tëj kaso ab diir.

36

وَدَخَلَ مَعَهُ ٱلسِّجۡنَ فَتَيَانِۖ قَالَ أَحَدُهُمَآ إِنِّيٓ أَرَىٰنِيٓ أَعۡصِرُ خَمۡرٗاۖ وَقَالَ ٱلۡأٓخَرُ إِنِّيٓ أَرَىٰنِيٓ أَحۡمِلُ فَوۡقَ رَأۡسِي خُبۡزٗا تَأۡكُلُ ٱلطَّيۡرُ مِنۡهُۖ نَبِّئۡنَا بِتَأۡوِيلِهِۦٓۖ إِنَّا نَرَىٰكَ مِنَ ٱلۡمُحۡسِنِينَ

Wadakhala maAAahu alssijna fatayani qala ahaduhuma innee aranee aAAsiru khamran waqala alakharu innee aranee ahmilu fawqa rasee khubzan takulu alttayru minhu nabbina bitaweelihi inna naraka mina almuhsineena

Mu duggandoo ca kaso ba ak ñaari xale yu góor. Kenn ca ñoom ne : “Damaa gent di nal sàngara...” Keneen ka ne : “Gént naa man itam yenu ci sama bopp mburu, ay picc di ca lekk. Leeralal nu seenum piri, ndax nun gis nanu la nga bokk ca way-rafetal ña”.

37

قَالَ لَا يَأۡتِيكُمَا طَعَامٞ تُرۡزَقَانِهِۦٓ إِلَّا نَبَّأۡتُكُمَا بِتَأۡوِيلِهِۦ قَبۡلَ أَن يَأۡتِيَكُمَاۚ ذَٰلِكُمَا مِمَّا عَلَّمَنِي رَبِّيٓۚ إِنِّي تَرَكۡتُ مِلَّةَ قَوۡمٖ لَّا يُؤۡمِنُونَ بِٱللَّهِ وَهُم بِٱلۡأٓخِرَةِ هُمۡ كَٰفِرُونَ

Qala la yateekuma taAAamun turzaqanihi illa nabbatukuma bitaweelihi qabla an yatiyakuma thalikuma mimma AAallamanee rabbee innee taraktu millata qawmin la yuminoona biAllahi wahum bialakhirati hum kafiroona

Mu ne leen : “Ñam wii ñu leen di wërsëgale, balaa ñëw ma leeralal leen seen piri. Noonu lay deme ci yéen ñaar ngir la ma sama Boroom xamal. Ndax man bàyyi naa diiney nit ñu gëmul Yàlla te weddi àllaaxira.

38

وَٱتَّبَعۡتُ مِلَّةَ ءَابَآءِيٓ إِبۡرَٰهِيمَ وَإِسۡحَٰقَ وَيَعۡقُوبَۚ مَا كَانَ لَنَآ أَن نُّشۡرِكَ بِٱللَّهِ مِن شَيۡءٖۚ ذَٰلِكَ مِن فَضۡلِ ٱللَّهِ عَلَيۡنَا وَعَلَى ٱلنَّاسِ وَلَٰكِنَّ أَكۡثَرَ ٱلنَّاسِ لَا يَشۡكُرُونَ

WaittabaAAtu millata abaee ibraheema waishaqa wayaAAqooba ma kana lana an nushrika biAllahi min shayin thalika min fadli Allahi AAalayna waAAala alnnasi walakinna akthara alnnasi la yashkuroona

Damay topp diiney samay baay Ibraahiima ak Isaaqa ak Yanqooba. Warul ci nun bokkaale Yàlla ak dara. Loola bokk na ci ngëneel yi nu Yàlla defal nun ak nit ñi ; waaye li ëpp ci nit ñi duñu gërëm [Yàlla].

39

يَٰصَٰحِبَيِ ٱلسِّجۡنِ ءَأَرۡبَابٞ مُّتَفَرِّقُونَ خَيۡرٌ أَمِ ٱللَّهُ ٱلۡوَٰحِدُ ٱلۡقَهَّارُ

Ya sahibayi alssijni aarbabun mutafarriqoona khayrun ami Allahu alwahidu alqahharu

Yéen sama ñaari àndandooy kaso ! Moo ndax ay yàlla yu téqalikoo ñoo gën walla Yàlla jenn jii doŋŋ, tey Notaakoon bi ?

40

مَا تَعۡبُدُونَ مِن دُونِهِۦٓ إِلَّآ أَسۡمَآءٗ سَمَّيۡتُمُوهَآ أَنتُمۡ وَءَابَآؤُكُم مَّآ أَنزَلَ ٱللَّهُ بِهَا مِن سُلۡطَٰنٍۚ إِنِ ٱلۡحُكۡمُ إِلَّا لِلَّهِ أَمَرَ أَلَّا تَعۡبُدُوٓاْ إِلَّآ إِيَّاهُۚ ذَٰلِكَ ٱلدِّينُ ٱلۡقَيِّمُ وَلَٰكِنَّ أَكۡثَرَ ٱلنَّاسِ لَا يَعۡلَمُونَ

Ma taAAbudoona min doonihi illa asmaan sammaytumooha antum waabaokum ma anzala Allahu biha min sultanin ini alhukmu illa lillahi amara alla taAAbudoo illa iyyahu thalika alddeenu alqayyimu walakinna akthara alnnasi la yaAAlamoona

Jaamuwuleen ginnaaw Moom lu dul ay tur yu ngeen di tudd ak seeni baay, te Yàlla wàccewul ci loolu wenn lay. Te kenn yeyoowul àtte ku dul Yàlla. Te digle na ngeen bañ a jaamu ku dul Moom. Loolu moo di diine ju jub ; waaye ñi ëpp ci nit ñi duñu xam.

41

يَٰصَٰحِبَيِ ٱلسِّجۡنِ أَمَّآ أَحَدُكُمَا فَيَسۡقِي رَبَّهُۥ خَمۡرٗاۖ وَأَمَّا ٱلۡأٓخَرُ فَيُصۡلَبُ فَتَأۡكُلُ ٱلطَّيۡرُ مِن رَّأۡسِهِۦۚ قُضِيَ ٱلۡأَمۡرُ ٱلَّذِي فِيهِ تَسۡتَفۡتِيَانِ

Ya sahibayi alssijni amma ahadukuma fayasqee rabbahu khamran waamma alakharu fayuslabu fatakulu alttayru min rasihi qudiya alamru allathee feehi tastaftiyani

Yéen sama ñaari àndandooy kaso ! Kenn ci yéen dana nekk kuy màndal buuram sàngara ; ka ca des, danañu ko daaj ci bant, ay picc di lekk ci boppam. Dogaleef na noonu mbir ya ngeen doon laaj.”

42

وَقَالَ لِلَّذِي ظَنَّ أَنَّهُۥ نَاجٖ مِّنۡهُمَا ٱذۡكُرۡنِي عِندَ رَبِّكَ فَأَنسَىٰهُ ٱلشَّيۡطَٰنُ ذِكۡرَ رَبِّهِۦ فَلَبِثَ فِي ٱلسِّجۡنِ بِضۡعَ سِنِينَ

Waqala lillathee thanna annahu najin minhuma othkurnee AAinda rabbika faansahu alshshaytanu thikra rabbihi falabitha fee alssijni bidAAa sineena

Yuusufa wax ka nga xam ne yaakaar na ne dana mucc ca ñoom ñaar, ne ko : “Nanga fexe ba buur fàttaliku ma”. Waaye Séytaane fàtteloo na ko [yóbbante boobu] ba fàttaliwu ko buur ba [ba mu delloo ca moom]. Ba tax mu toog ca kaso ba ay at.(s)

43

وَقَالَ ٱلۡمَلِكُ إِنِّيٓ أَرَىٰ سَبۡعَ بَقَرَٰتٖ سِمَانٖ يَأۡكُلُهُنَّ سَبۡعٌ عِجَافٞ وَسَبۡعَ سُنۢبُلَٰتٍ خُضۡرٖ وَأُخَرَ يَابِسَٰتٖۖ يَـٰٓأَيُّهَا ٱلۡمَلَأُ أَفۡتُونِي فِي رُءۡيَٰيَ إِن كُنتُمۡ لِلرُّءۡيَا تَعۡبُرُونَ

Waqala almaliku innee ara sabAAa baqaratin simanin yakuluhunna sabAAun AAijafun wasabAAa sunbulatin khudrin waokhara yabisatin ya ayyuha almalao aftoonee fee ruyaya in kuntum lilrruya taAAburoona

Buur ba wax ne : “Gént naa juróom-ñaari nag yu duuf yu juróom- ñaari nag yu loof di lekk ; ak juróom-ñaari gub yu nëtëx ak yeneen yu wow. Yéen njiit yi, firil-leen ma sama gént gii, ndegam mën ngeen firi gént”.

44

قَالُوٓاْ أَضۡغَٰثُ أَحۡلَٰمٖۖ وَمَا نَحۡنُ بِتَأۡوِيلِ ٱلۡأَحۡلَٰمِ بِعَٰلِمِينَ

Qaloo adghathu ahlamin wama nahnu bitaweeli alahlami biAAalimeena

Ñu ne : “Gént yooyu jaxasoo nañu ! Te sax nun xamunu pirim gént !”

45

وَقَالَ ٱلَّذِي نَجَا مِنۡهُمَا وَٱدَّكَرَ بَعۡدَ أُمَّةٍ أَنَا۠ أُنَبِّئُكُم بِتَأۡوِيلِهِۦ فَأَرۡسِلُونِ

Waqala allathee naja minhuma waiddakara baAAda ommatin ana onabbiokum bitaweelihi faarsilooni

Ka muccoon ca ñoom daldi fàttaliku ginnaaw ab diir, daldi wax ne : “Danaa leen leeralal. Yebal-leen ma, Dinaa leen indil am pireem”.

46

يُوسُفُ أَيُّهَا ٱلصِّدِّيقُ أَفۡتِنَا فِي سَبۡعِ بَقَرَٰتٖ سِمَانٖ يَأۡكُلُهُنَّ سَبۡعٌ عِجَافٞ وَسَبۡعِ سُنۢبُلَٰتٍ خُضۡرٖ وَأُخَرَ يَابِسَٰتٖ لَّعَلِّيٓ أَرۡجِعُ إِلَى ٱلنَّاسِ لَعَلَّهُمۡ يَعۡلَمُونَ

Yoosufu ayyuha alssiddeequ aftina fee sabAAi baqaratin simanin yakuluhunna sabAAun AAijafun wasabAAi sunbulatin khudrin waokhara yabisatin laAAallee arjiAAu ila alnnasi laAAallahum yaAAlamoona

[Mu dem ca Yuusufa] ne ko : “Yaw waxkatu dëgg ! Ubbee ma ci juróom-ñaari nag yu duuf yu juróom-ñaari nag yu loof di lekk, ak juróom-ñaari gub yu nëtëx ak yeneen yu wow, ndax xéy-na su ma delluwaatee nit ña am ci xam-xam”.

47

قَالَ تَزۡرَعُونَ سَبۡعَ سِنِينَ دَأَبٗا فَمَا حَصَدتُّمۡ فَذَرُوهُ فِي سُنۢبُلِهِۦٓ إِلَّا قَلِيلٗا مِّمَّا تَأۡكُلُونَ

Qala tazraAAoona sabAAa sineena daaban fama hasadtum fatharoohu fee sunbulihi illa qaleelan mimma takuloona

Mu ne : “Nangeen bey juróom-ñaari at ni ngeen ko baaxoo defe. Te lu ngeen góob, bàyyileen ko ca aw gubam [bañ koo bàcc], lu dul lu néew ca la ngeen di lekk.

48

ثُمَّ يَأۡتِي مِنۢ بَعۡدِ ذَٰلِكَ سَبۡعٞ شِدَادٞ يَأۡكُلۡنَ مَا قَدَّمۡتُمۡ لَهُنَّ إِلَّا قَلِيلٗا مِّمَّا تُحۡصِنُونَ

Thumma yatee min baAAdi thalika sabAAun shidadun yakulna ma qaddamtum lahunna illa qaleelan mimma tuhsinoona

Dana ca topp gannaaw loolu juróom-ñaari at yu bekkoor yuy lekk la ngeen dencoon ngir ñoom ba mu des lu néew ca la ngeen dencoon.

49

ثُمَّ يَأۡتِي مِنۢ بَعۡدِ ذَٰلِكَ عَامٞ فِيهِ يُغَاثُ ٱلنَّاسُ وَفِيهِ يَعۡصِرُونَ

Thumma yatee min baAAdi thalika AAamun feehi yughathu alnnasu wafeehi yaAAsiroona

Dana ca topp gannaaw loolu at moo xam ne dana xettali nit ñi te it danañu ca nal [reseñ ndax dana am].”

50

وَقَالَ ٱلۡمَلِكُ ٱئۡتُونِي بِهِۦۖ فَلَمَّا جَآءَهُ ٱلرَّسُولُ قَالَ ٱرۡجِعۡ إِلَىٰ رَبِّكَ فَسۡـَٔلۡهُ مَا بَالُ ٱلنِّسۡوَةِ ٱلَّـٰتِي قَطَّعۡنَ أَيۡدِيَهُنَّۚ إِنَّ رَبِّي بِكَيۡدِهِنَّ عَلِيمٞ

Waqala almaliku itoonee bihi falamma jaahu alrrasoolu qala irjiAA ila rabbika faisalhu ma balu alnniswati allatee qattaAAna aydiyahunna inna rabbee bikaydihinna AAaleemun

Buur ba ne : “Indil-leen ma ko”. Ba ndaw la agsee ca moom [Yuusufa], mu ne ko : “Dellul ca sa sang, nga laaj ko : “Lan moo doon mbirum jigéen ña dogatoon seen yoxo ? Sama Boroom xam na bu baax seen pexe”.

51

قَالَ مَا خَطۡبُكُنَّ إِذۡ رَٰوَدتُّنَّ يُوسُفَ عَن نَّفۡسِهِۦۚ قُلۡنَ حَٰشَ لِلَّهِ مَا عَلِمۡنَا عَلَيۡهِ مِن سُوٓءٖۚ قَالَتِ ٱمۡرَأَتُ ٱلۡعَزِيزِ ٱلۡـَٰٔنَ حَصۡحَصَ ٱلۡحَقُّ أَنَا۠ رَٰوَدتُّهُۥ عَن نَّفۡسِهِۦ وَإِنَّهُۥ لَمِنَ ٱلصَّـٰدِقِينَ

Qala ma khatbukunna ith rawadtunna yoosufa AAan nafsihi qulna hasha lillahi ma AAalimna AAalayhi min sooin qalati imraatu alAAazeezi alana hashasa alhaqqu ana rawadtuhu AAan nafsihi wainnahu lamina alssadiqeena

[Buur ba ne jigéen ña] : “Lan moo doon seen mbir ba ngeen sàkku Yuusufa ci jëmmam ?”. Ñu tontu ne : “Wax dëgg Yàlla ! Xamalunu ko dara lu bon”. Jabaru buur ba ne : “Léegi nag dëgg gi leer na. Maa ko sàkku woon. Moom moo waxoon dëgg !”

52

ذَٰلِكَ لِيَعۡلَمَ أَنِّي لَمۡ أَخُنۡهُ بِٱلۡغَيۡبِ وَأَنَّ ٱللَّهَ لَا يَهۡدِي كَيۡدَ ٱلۡخَآئِنِينَ

Thalika liyaAAlama annee lam akhunhu bialghaybi waanna Allaha la yahdee kayda alkhaineena

“[Man Yuusufa maa defoon] noonu ngir buur bi xam ne wuruju ma ko ginnaawam, te sax Yàlla du jubale pexem wurujkat ya.

53

۞وَمَآ أُبَرِّئُ نَفۡسِيٓۚ إِنَّ ٱلنَّفۡسَ لَأَمَّارَةُۢ بِٱلسُّوٓءِ إِلَّا مَا رَحِمَ رَبِّيٓۚ إِنَّ رَبِّي غَفُورٞ رَّحِيمٞ

Wama obarrio nafsee inna alnnafsa laammaratun bialssooi illa ma rahima rabbee inna rabbee ghafoorun raheemun

Jéemumaa setal sama bopp, ndax bakkan moom digalaakoon la ci lu bon, [mucctil ci moom] ku dul ku sama Boroom yërëm. Ndax sama Boroom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la”.(h)

54

وَقَالَ ٱلۡمَلِكُ ٱئۡتُونِي بِهِۦٓ أَسۡتَخۡلِصۡهُ لِنَفۡسِيۖ فَلَمَّا كَلَّمَهُۥ قَالَ إِنَّكَ ٱلۡيَوۡمَ لَدَيۡنَا مَكِينٌ أَمِينٞ

Waqala almaliku itoonee bihi astakhlishu linafsee falamma kallamahu qala innaka alyawma ladayna makeenun ameenun

Buur ba ne : “Indil-leen ma ko : def ko mu sës ci man”. Ba mu waxeek moom, mu ne ko : “Bis niki tey, nekk nga ci man ku ñu darajaal, ku ñu wóolu”.

55

قَالَ ٱجۡعَلۡنِي عَلَىٰ خَزَآئِنِ ٱلۡأَرۡضِۖ إِنِّي حَفِيظٌ عَلِيمٞ

Qala ijAAalnee AAala khazaini alardi innee hafeethun AAaleemun

Mu ne : “Dénkleen ma alali réew mi : am naa xam-xamu wattu ko”.

56

وَكَذَٰلِكَ مَكَّنَّا لِيُوسُفَ فِي ٱلۡأَرۡضِ يَتَبَوَّأُ مِنۡهَا حَيۡثُ يَشَآءُۚ نُصِيبُ بِرَحۡمَتِنَا مَن نَّشَآءُۖ وَلَا نُضِيعُ أَجۡرَ ٱلۡمُحۡسِنِينَ

Wakathalika makanna liyoosufa fee alardi yatabawwao minha haythu yashao nuseebu birahmatina man nashao wala nudeeAAu ajra almuhsineena

Noonu Lanu darajaale Yuusufa ca réew ma, mu fay wàcc fu ko neex. Dananu jox sunu yërmaande ku Nu neex te Dunu sànk peyug rafetalkat ya.

57

وَلَأَجۡرُ ٱلۡأٓخِرَةِ خَيۡرٞ لِّلَّذِينَ ءَامَنُواْ وَكَانُواْ يَتَّقُونَ

Walaajru alakhirati khayrun lillatheena amanoo wakanoo yattaqoona

Te peyug àllaaxira moo gën ci ña gëm, di ña ragal [Yàlla].

58

وَجَآءَ إِخۡوَةُ يُوسُفَ فَدَخَلُواْ عَلَيۡهِ فَعَرَفَهُمۡ وَهُمۡ لَهُۥ مُنكِرُونَ

Wajaa ikhwatu yoosufa fadakhaloo AAalayhi faAAarafahum wahum lahu munkiroona

Ay doomi-baayi Yuusufa agsi ca moom [jóge seen réew ma]. Mu xàmmee leen te ñoom fakk nañu ko.

59

وَلَمَّا جَهَّزَهُم بِجَهَازِهِمۡ قَالَ ٱئۡتُونِي بِأَخٖ لَّكُم مِّنۡ أَبِيكُمۡۚ أَلَا تَرَوۡنَ أَنِّيٓ أُوفِي ٱلۡكَيۡلَ وَأَنَا۠ خَيۡرُ ٱلۡمُنزِلِينَ

Walamma jahhazahum bijahazihim qala itoonee biakhin lakum min abeekum ala tarawna annee oofee alkayla waana khayru almunzileena

Ba mu solee seen saaku ba noppi, mu ne leen : “Indil-leen ma seen doomi-baay ja des ak seen baay. Moo ndax gisuleen ne nattal na leen lu mat sëkk te it dalal naa leen gën ji daluwaay ?

60

فَإِن لَّمۡ تَأۡتُونِي بِهِۦ فَلَا كَيۡلَ لَكُمۡ عِندِي وَلَا تَقۡرَبُونِ

Fain lam tatoonee bihi fala kayla lakum AAindee wala taqrabooni

Bu ngeen ma ko indilul, dungeen amati ci man indaar ; te it dungeen ma jegeñ”.

61

قَالُواْ سَنُرَٰوِدُ عَنۡهُ أَبَاهُ وَإِنَّا لَفَٰعِلُونَ

Qaloo sanurawidu AAanhu abahu wainna lafaAAiloona

Ñu ne ko : “Dananu ko sàkku ci baayam. Te dananu ko def ”.

62

وَقَالَ لِفِتۡيَٰنِهِ ٱجۡعَلُواْ بِضَٰعَتَهُمۡ فِي رِحَالِهِمۡ لَعَلَّهُمۡ يَعۡرِفُونَهَآ إِذَا ٱنقَلَبُوٓاْ إِلَىٰٓ أَهۡلِهِمۡ لَعَلَّهُمۡ يَرۡجِعُونَ

Waqala lifityanihi ijAAaloo bidaAAatahum fee rihalihim laAAallahum yaAArifoonaha itha inqalaboo ila ahlihim laAAallahum yarjiAAoona

Mu ne ay surgaam : “Dellooleen, ci seeni sëf, njëg [ga ñu joxe]: xéy-na danañu ko xàmmee bu ñu delloo ca seeni mbokk te xéy-na danañu dellusi”.

63

فَلَمَّا رَجَعُوٓاْ إِلَىٰٓ أَبِيهِمۡ قَالُواْ يَـٰٓأَبَانَا مُنِعَ مِنَّا ٱلۡكَيۡلُ فَأَرۡسِلۡ مَعَنَآ أَخَانَا نَكۡتَلۡ وَإِنَّا لَهُۥ لَحَٰفِظُونَ

Falamma rajaAAoo ila abeehim qaloo ya abana muniAAa minna alkaylu faarsil maAAana akhana naktal wainna lahu lahafithoona

Ba ñu delloo ca seen baay, ñu ne ko : “Yaw sunu baay, [su nu yóbbaalewul sunu rakk jii weneen yoon, kenn dunu nattal]. Kon yebal ko mu ànd ak nun ndax ñu nattal nu. Kon dey dananu ko wattu”.

64

قَالَ هَلۡ ءَامَنُكُمۡ عَلَيۡهِ إِلَّا كَمَآ أَمِنتُكُمۡ عَلَىٰٓ أَخِيهِ مِن قَبۡلُ فَٱللَّهُ خَيۡرٌ حَٰفِظٗاۖ وَهُوَ أَرۡحَمُ ٱلرَّـٰحِمِينَ

Qala hal amanukum AAalayhi illa kama amintukum AAala akheehi min qablu faAllahu khayrun hafithan wahuwa arhamu alrrahimeena

Mu ne : “Ndax, wóolu leen ci dafay mel ni ba ma leen wóolu ca bu njëkk ca doomu- ndeyam ja ? Waaye Yàllaa di gën jaa mën a wattu [aar], te Moo ëpp yërmaande yërëmaakoon ya !”

65

وَلَمَّا فَتَحُواْ مَتَٰعَهُمۡ وَجَدُواْ بِضَٰعَتَهُمۡ رُدَّتۡ إِلَيۡهِمۡۖ قَالُواْ يَـٰٓأَبَانَا مَا نَبۡغِيۖ هَٰذِهِۦ بِضَٰعَتُنَا رُدَّتۡ إِلَيۡنَاۖ وَنَمِيرُ أَهۡلَنَا وَنَحۡفَظُ أَخَانَا وَنَزۡدَادُ كَيۡلَ بَعِيرٖۖ ذَٰلِكَ كَيۡلٞ يَسِيرٞ

Walamma fatahoo mataAAahum wajadoo bidaAAatahum ruddat ilayhim qaloo ya abana ma nabghee hathihi bidaAAatuna ruddat ilayna wanameeru ahlana wanahfathu akhana wanazdadu kayla baAAeerin thalika kaylun yaseerun

Ba ñu ubbee seeni ëmb, ñu fekk ca njëg ga ñu leen delloo. Ñu ne : «Waaw yaw sunu baay. Lan lanu bëggati ? Alal ja [nekkoon ca njëg ga nu feyoon] mi ngi nii ñu delloo nu ko. Dananu mën a jëggiwaat lu nu mën a dundale njaboot gi, mën nanoo wattu sunu doomu-baay te dananu yokk sëfu gëléem, loolu natt bu yomb lay doon”.

66

قَالَ لَنۡ أُرۡسِلَهُۥ مَعَكُمۡ حَتَّىٰ تُؤۡتُونِ مَوۡثِقٗا مِّنَ ٱللَّهِ لَتَأۡتُنَّنِي بِهِۦٓ إِلَّآ أَن يُحَاطَ بِكُمۡۖ فَلَمَّآ ءَاتَوۡهُ مَوۡثِقَهُمۡ قَالَ ٱللَّهُ عَلَىٰ مَا نَقُولُ وَكِيلٞ

Qala lan orsilahu maAAakum hatta tutooni mawthiqan mina Allahi latatunnanee bihi illa an yuhata bikum falamma atawhu mawthiqahum qala Allahu AAala ma naqoolu wakeelun

- Mu ne leen : “Duma ko bàyyi mukk mu ànd ak yéen li feek waatuleen ci Yàlla ne dangeen ma ko delloosil, ndeem lottuleen ca”. Ba ñu ko waatalee, mu ne : “Li nu waxante, nu ngi ciy wéeru ci Yàlla”.(s)

67

وَقَالَ يَٰبَنِيَّ لَا تَدۡخُلُواْ مِنۢ بَابٖ وَٰحِدٖ وَٱدۡخُلُواْ مِنۡ أَبۡوَٰبٖ مُّتَفَرِّقَةٖۖ وَمَآ أُغۡنِي عَنكُم مِّنَ ٱللَّهِ مِن شَيۡءٍۖ إِنِ ٱلۡحُكۡمُ إِلَّا لِلَّهِۖ عَلَيۡهِ تَوَكَّلۡتُۖ وَعَلَيۡهِ فَلۡيَتَوَكَّلِ ٱلۡمُتَوَكِّلُونَ

Waqala ya baniyya la tadkhuloo min babin wahidin waodkhuloo min abwabin mutafarriqatin wama oghnee AAankum mina Allahi min shayin ini alhukmu illa lillahi AAalayhi tawakkaltu waAAalayhi falyatawakkali almutawakkiloona

Mu ne : “Yéen samay doom, [bu ngeen àggee ca dëkk ba], buleen ca duggandoo ci benn buntu, nangeen xàjjalikoo dugge ciy buntu yu soriyaantoo. Mënuma leen a fegal dara lu jóge ci Yàlla. Moom rekk a moom àtte : Ci Moom rekk laa wéeru. Te képp kuy wéeru, na weeru ci Moom [Yàlla]”.

68

وَلَمَّا دَخَلُواْ مِنۡ حَيۡثُ أَمَرَهُمۡ أَبُوهُم مَّا كَانَ يُغۡنِي عَنۡهُم مِّنَ ٱللَّهِ مِن شَيۡءٍ إِلَّا حَاجَةٗ فِي نَفۡسِ يَعۡقُوبَ قَضَىٰهَاۚ وَإِنَّهُۥ لَذُو عِلۡمٖ لِّمَا عَلَّمۡنَٰهُ وَلَٰكِنَّ أَكۡثَرَ ٱلنَّاسِ لَا يَعۡلَمُونَ

Walamma dakhaloo min haythu amarahum aboohum ma kana yughnee AAanhum mina Allahi min shayin illa hajatan fee nafsi yaAAqooba qadaha wainnahu lathoo AAilmin lima AAallamnahu walakinna akthara alnnasi la yaAAlamoona

Ba ñu duggee na ko seen baay diglee woon, taxul mu jariñ dara ca la Yàlla namm. Lu dul ne Yanqooba soxla woon na yiir leen ci loolu. Naka moom, boroom xam-xam la ci la Nu ko xamal. Waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.

69

وَلَمَّا دَخَلُواْ عَلَىٰ يُوسُفَ ءَاوَىٰٓ إِلَيۡهِ أَخَاهُۖ قَالَ إِنِّيٓ أَنَا۠ أَخُوكَ فَلَا تَبۡتَئِسۡ بِمَا كَانُواْ يَعۡمَلُونَ

Walamma dakhaloo AAala yoosufa awa ilayhi akhahu qala innee ana akhooka fala tabtais bima kanoo yaAAmaloona

Ba ñu agsee ca Yuusufa, mu daldi xëcc taf ci boppam doomu-ndeyam ja, daldi ne : “Maa di sa doomu-ndey. Bul jàq ca la ñu nekkoon di ko def ci jéem maa sànk”.

70

فَلَمَّا جَهَّزَهُم بِجَهَازِهِمۡ جَعَلَ ٱلسِّقَايَةَ فِي رَحۡلِ أَخِيهِ ثُمَّ أَذَّنَ مُؤَذِّنٌ أَيَّتُهَا ٱلۡعِيرُ إِنَّكُمۡ لَسَٰرِقُونَ

Falamma jahhazahum bijahazihim jaAAala alssiqayata fee rahli akheehi thumma aththana muaththinun ayyatuha alAAeeru innakum lasariqoona

Ba mu leen solalee seeni saaku ba noppi, mu dugal andaar [ja ñu doon natte] ca biir sëfu doomu-ndeyam ja. Mu am yéglekat bu wax ne : “Éy yéen jëgg ji ! Ay sàcc ngeen”.

71

قَالُواْ وَأَقۡبَلُواْ عَلَيۡهِم مَّاذَا تَفۡقِدُونَ

Qaloo waaqbaloo AAalayhim matha tafqidoona

Ñoom it ñu wëlbatiku ca moom ne leen : “Lan ngeen réerle ?”

72

قَالُواْ نَفۡقِدُ صُوَاعَ ٱلۡمَلِكِ وَلِمَن جَآءَ بِهِۦ حِمۡلُ بَعِيرٖ وَأَنَا۠ بِهِۦ زَعِيمٞ

Qaloo nafqidu suwaAAa almaliki waliman jaa bihi himlu baAAeerin waana bihi zaAAeemun

Ñu ne : “Li nu réerle mooy nattukaayu buur bi. Te ku ko feeñal nu jox ko sëfu giléem, maa ko warlul loolu”.

73

قَالُواْ تَٱللَّهِ لَقَدۡ عَلِمۡتُم مَّا جِئۡنَا لِنُفۡسِدَ فِي ٱلۡأَرۡضِ وَمَا كُنَّا سَٰرِقِينَ

Qaloo taAllahi laqad AAalimtum ma jina linufsida fee alardi wama kunna sariqeena

Ñu ne : “Giñ nanu ci Yàlla, te xam ngeen ne dikkunu fii ci suuf si ngir yàq te it dunu ay sàcckat”.

74

قَالُواْ فَمَا جَزَـٰٓؤُهُۥٓ إِن كُنتُمۡ كَٰذِبِينَ

Qaloo fama jazaohu in kuntum kathibeena

- Ñu ne: “Luy peyug ku sàcc, bu fekkee dangeen a fen ?”.

75

قَالُواْ جَزَـٰٓؤُهُۥ مَن وُجِدَ فِي رَحۡلِهِۦ فَهُوَ جَزَـٰٓؤُهُۥۚ كَذَٰلِكَ نَجۡزِي ٱلظَّـٰلِمِينَ

Qaloo jazaohu man wujida fee rahlihi fahuwa jazaohu kathalika najzee alththalimeena

Ñu ne : “Ag peyam moom ka ñu fekk [nattukaay ba] ci sëfam mooy : ag peyam moom ci boppam [mu nekk jaam]. Noonu Lanu feye tooñkat ya”.

76

فَبَدَأَ بِأَوۡعِيَتِهِمۡ قَبۡلَ وِعَآءِ أَخِيهِ ثُمَّ ٱسۡتَخۡرَجَهَا مِن وِعَآءِ أَخِيهِۚ كَذَٰلِكَ كِدۡنَا لِيُوسُفَۖ مَا كَانَ لِيَأۡخُذَ أَخَاهُ فِي دِينِ ٱلۡمَلِكِ إِلَّآ أَن يَشَآءَ ٱللَّهُۚ نَرۡفَعُ دَرَجَٰتٖ مَّن نَّشَآءُۗ وَفَوۡقَ كُلِّ ذِي عِلۡمٍ عَلِيمٞ

Fabadaa biawAAiyatihim qabla wiAAai akheehi thumma istakhrajaha min wiAAai akheehi kathalika kidna liyoosufa ma kana liyakhutha akhahu fee deeni almaliki illa an yashaa Allahu narfaAAu darajatin man nashao wafawqa kulli thee AAilmin AAaleemun

Mu jëkke ca ndabi doomi-baay ya, di seet, mujje ndabul doomu-ndey ja ; génne ca nattukaay ba. Noonu Lanu joxe pexe Yuusufa. Pexe mu ko tax a téye doomu-ndeyam ja ci lu dëppook yoonu buur ba, [mënu ko woon a def] lu dul lu soob Yàlla. Dananu yékkati darajay ku Nu soob. Te boroom xam-xam bu nekk, am na ku ko ëpp xam-xam.

77

۞قَالُوٓاْ إِن يَسۡرِقۡ فَقَدۡ سَرَقَ أَخٞ لَّهُۥ مِن قَبۡلُۚ فَأَسَرَّهَا يُوسُفُ فِي نَفۡسِهِۦ وَلَمۡ يُبۡدِهَا لَهُمۡۚ قَالَ أَنتُمۡ شَرّٞ مَّكَانٗاۖ وَٱللَّهُ أَعۡلَمُ بِمَا تَصِفُونَ

Qaloo in yasriq faqad saraqa akhun lahu min qablu faasarraha yoosufu fee nafsihi walam yubdiha lahum qala antum sharrun makanan waAllahu aAAlamu bima tasifoona

Ñu ne : “Ndegam sàcc na, am na doomu-ndeyam ju sàccoon bu jëkk. “Yuusufa nëbb ca xelam la mu xalaat, bañ leen koo feeñal. Mu ne [ci xelam] : “Yéen yées ngeen ! Te Yàlla xam na li ngeen jëf ”.(r)

78

قَالُواْ يَـٰٓأَيُّهَا ٱلۡعَزِيزُ إِنَّ لَهُۥٓ أَبٗا شَيۡخٗا كَبِيرٗا فَخُذۡ أَحَدَنَا مَكَانَهُۥٓۖ إِنَّا نَرَىٰكَ مِنَ ٱلۡمُحۡسِنِينَ

Qaloo ya ayyuha alAAazeezu inna lahu aban shaykhan kabeeran fakhuth ahadana makanahu inna naraka mina almuhsineena

- Ñu ne : «Ay yaw kilifa gi, moom dafa am baay bu mage lool ; téyeel kenn ci nun bàyyi ko. Gis nanu ne yaw bokk nga ca rafetalkat ya [seeni jëf]”.

79

قَالَ مَعَاذَ ٱللَّهِ أَن نَّأۡخُذَ إِلَّا مَن وَجَدۡنَا مَتَٰعَنَا عِندَهُۥٓ إِنَّآ إِذٗا لَّظَٰلِمُونَ

Qala maAAatha Allahi an nakhutha illa man wajadna mataAAana AAindahu inna ithan lathalimoona

- Mu ne : “Maa ngi ñaan Yàlla mu musal ma ci jàpp ku dul ka ma fekk nattukaay ci moom ! [Su nu ko defee], kon dananu bokk ca tooñkat ya.

80

فَلَمَّا ٱسۡتَيۡـَٔسُواْ مِنۡهُ خَلَصُواْ نَجِيّٗاۖ قَالَ كَبِيرُهُمۡ أَلَمۡ تَعۡلَمُوٓاْ أَنَّ أَبَاكُمۡ قَدۡ أَخَذَ عَلَيۡكُم مَّوۡثِقٗا مِّنَ ٱللَّهِ وَمِن قَبۡلُ مَا فَرَّطتُمۡ فِي يُوسُفَۖ فَلَنۡ أَبۡرَحَ ٱلۡأَرۡضَ حَتَّىٰ يَأۡذَنَ لِيٓ أَبِيٓ أَوۡ يَحۡكُمَ ٱللَّهُ لِيۖ وَهُوَ خَيۡرُ ٱلۡحَٰكِمِينَ

Falamma istayasoo minhu khalasoo najiyyan qala kabeeruhum alam taAAlamoo anna abakum qad akhatha AAalaykum mawthiqan mina Allahi wamin qablu ma farrattum fee yoosufa falan abraha alarda hatta yathana lee abee aw yahkuma Allahu lee wahuwa khayru alhakimeena

Ba ñu amatul yaakaar ci moom, beru nañu di diisoo. Ka di seen mag ne : “Moo ndax dangeen a fàtte ne seen baay waatloo woon na leen ci Yàlla, ca la jiitu loolu la ngeen defoon Yuusufa ? Man dey du ma fi jóge ba kerook may jot sama ndigalul baay walla Yàlla àtte ma, ndax Moom moo gën a mën a àtte àttekat ya.

81

ٱرۡجِعُوٓاْ إِلَىٰٓ أَبِيكُمۡ فَقُولُواْ يَـٰٓأَبَانَآ إِنَّ ٱبۡنَكَ سَرَقَ وَمَا شَهِدۡنَآ إِلَّا بِمَا عَلِمۡنَا وَمَا كُنَّا لِلۡغَيۡبِ حَٰفِظِينَ

IrjiAAoo ila abeekum faqooloo ya abana inna ibnaka saraqa wama shahidna illa bima AAalimna wama kunna lilghaybi hafitheena

[Mu ne] demleen ca seen baay, ngeen ne ko : “Yaw sunu baay, sa doon ja sàcc na. Te dunu seede lu dul la nu xam. Te nun xamunu kumpa.

82

وَسۡـَٔلِ ٱلۡقَرۡيَةَ ٱلَّتِي كُنَّا فِيهَا وَٱلۡعِيرَ ٱلَّتِيٓ أَقۡبَلۡنَا فِيهَاۖ وَإِنَّا لَصَٰدِقُونَ

Waisali alqaryata allatee kunna feeha waalAAeera allatee aqbalna feeha wainna lasadiqoona

Laajal waa dëkk ba nu nekkoon, ak njëgg ma nu àndaloon ñibbisi. Li nu wax dëgg la.”

83

قَالَ بَلۡ سَوَّلَتۡ لَكُمۡ أَنفُسُكُمۡ أَمۡرٗاۖ فَصَبۡرٞ جَمِيلٌۖ عَسَى ٱللَّهُ أَن يَأۡتِيَنِي بِهِمۡ جَمِيعًاۚ إِنَّهُۥ هُوَ ٱلۡعَلِيمُ ٱلۡحَكِيمُ

Qala bal sawwalat lakum anfusukum amran fasabrun jameelun AAasa Allahu an yatiyanee bihim jameeAAan innahu huwa alAAaleemu alhakeemu

[Seen baay tontu leen] ne : “Deewallaay dangeen a topp seen bakkan mu rafetal leen am mbir !... [Muñ gu rafet]. Xéy-na Yàlla delloosil nu leen ñoom ñépp. Moom Yàlla Ku xereñ la, Ku xam la”.

84

وَتَوَلَّىٰ عَنۡهُمۡ وَقَالَ يَـٰٓأَسَفَىٰ عَلَىٰ يُوسُفَ وَٱبۡيَضَّتۡ عَيۡنَاهُ مِنَ ٱلۡحُزۡنِ فَهُوَ كَظِيمٞ

Watawalla AAanhum waqala ya asafa AAala yoosufa waibyaddat AAaynahu mina alhuzni fahuwa katheemun

Mu dummóoyu leen, wax ne : “Céy sama njàqare ci Yuusufa !”. Noona ay gëtam weex [gisatul] ngir mer ma mu wann.

85

قَالُواْ تَٱللَّهِ تَفۡتَؤُاْ تَذۡكُرُ يُوسُفَ حَتَّىٰ تَكُونَ حَرَضًا أَوۡ تَكُونَ مِنَ ٱلۡهَٰلِكِينَ

Qaloo taAllahi taftao tathkuru yoosufa hatta takoona haradan aw takoona mina alhalikeena

- Ñu ne ko : “Céy Yàlla ! Doo deñ di fàttaliku Yuusufa, ba tax na yaa ngi wéradi te mën nga cee loru”.

86

قَالَ إِنَّمَآ أَشۡكُواْ بَثِّي وَحُزۡنِيٓ إِلَى ٱللَّهِ وَأَعۡلَمُ مِنَ ٱللَّهِ مَا لَا تَعۡلَمُونَ

Qala innama ashkoo baththee wahuznee ila Allahi waaAAlamu mina Allahi ma la taAAlamoona

- Mu ne : “Defuma lu dul tawat sama njàqare ak sama naqar ci Yàlla. Te xam naa ci Yàlla lu ngeen xamul.

87

يَٰبَنِيَّ ٱذۡهَبُواْ فَتَحَسَّسُواْ مِن يُوسُفَ وَأَخِيهِ وَلَا تَاْيۡـَٔسُواْ مِن رَّوۡحِ ٱللَّهِۖ إِنَّهُۥ لَا يَاْيۡـَٔسُ مِن رَّوۡحِ ٱللَّهِ إِلَّا ٱلۡقَوۡمُ ٱلۡكَٰفِرُونَ

Ya baniyya ithhaboo fatahassasoo min yoosufa waakheehi wala tayasoo min rawhi Allahi innahu la yayasu min rawhi Allahi illa alqawmu alkafiroona

Mu ne : “Yéen samay doon ! Demleen xeeñtu ji lu jëm ci Yuusufa ak doomu-ndeyam ja. Te buleen xàddi ci dajeek yërmaande Yàlla. Ndax ay yéefar rekk ñooy xàddi ci dajeek yërmaande Yàlla”.

88

فَلَمَّا دَخَلُواْ عَلَيۡهِ قَالُواْ يَـٰٓأَيُّهَا ٱلۡعَزِيزُ مَسَّنَا وَأَهۡلَنَا ٱلضُّرُّ وَجِئۡنَا بِبِضَٰعَةٖ مُّزۡجَىٰةٖ فَأَوۡفِ لَنَا ٱلۡكَيۡلَ وَتَصَدَّقۡ عَلَيۡنَآۖ إِنَّ ٱللَّهَ يَجۡزِي ٱلۡمُتَصَدِّقِينَ

Falamma dakhaloo AAalayhi qaloo ya ayyuha alAAazeezu massana waahlana alddurru wajina bibidaAAatin muzjatin faawfi lana alkayla watasaddaq AAalayna inna Allaha yajzee almutasaddiqeena

Ba ñu agsee ci Yuusufa, ñu ne ko : “Éy yaw jawriñ ju tedd ji, xiif danoo dal nun ak sunug njaboor ; te indi nanu njëgg gu xeebu. Nattal nu te sarax nu. Yàlla dana fey saraxekat ya !”(s)

89

قَالَ هَلۡ عَلِمۡتُم مَّا فَعَلۡتُم بِيُوسُفَ وَأَخِيهِ إِذۡ أَنتُمۡ جَٰهِلُونَ

Qala hal AAalimtum ma faAAaltum biyoosufa waakheehi ith antum jahiloona

- Mu ne leen : “Ndax xam ngeen la ngeen defoon Yuusufa ak doomu- ndeyam ja, ba ngeen nekkee cig réer ?”.

90

قَالُوٓاْ أَءِنَّكَ لَأَنتَ يُوسُفُۖ قَالَ أَنَا۠ يُوسُفُ وَهَٰذَآ أَخِيۖ قَدۡ مَنَّ ٱللَّهُ عَلَيۡنَآۖ إِنَّهُۥ مَن يَتَّقِ وَيَصۡبِرۡ فَإِنَّ ٱللَّهَ لَا يُضِيعُ أَجۡرَ ٱلۡمُحۡسِنِينَ

Qaloo ainnaka laanta yoosufa qala ana yoosufu wahatha akhee qad manna Allahu AAalayna innahu man yattaqi wayasbir fainna Allaha la yudeeAAu ajra almuhsineena

- Ñu ne ko : “Ndax yaw yaay Yuusufa ?” - Mu ne leen : “Maay Yuusufa, kii mooy sama doomu-ndey, Yàlla defal nu ay xéewal. Ndax ku ragal Yàlla te muñ, [dana gis ne] Yàlla du sànk mukk peyug ñay refetal”.

91

قَالُواْ تَٱللَّهِ لَقَدۡ ءَاثَرَكَ ٱللَّهُ عَلَيۡنَا وَإِن كُنَّا لَخَٰطِـِٔينَ

Qaloo taAllahi laqad atharaka Allahu AAalayna wain kunna lakhatieena

- Ñu giñ ci Yàlla ne : “Yàlla gënal na la ci sunu kaw te nun danoo juumoon rekk def bàkkaar”.

92

قَالَ لَا تَثۡرِيبَ عَلَيۡكُمُ ٱلۡيَوۡمَۖ يَغۡفِرُ ٱللَّهُ لَكُمۡۖ وَهُوَ أَرۡحَمُ ٱلرَّـٰحِمِينَ

Qala la tathreeba AAalaykumu alyawma yaghfiru Allahu lakum wahuwa arhamu alrrahimeena

- Mu ne : “Tey du bisub yeddeel ci yéen ? Yal na leen Yàlla baal. Te Moom moo gën a mën a yërëm yërëmekat ya.

93

ٱذۡهَبُواْ بِقَمِيصِي هَٰذَا فَأَلۡقُوهُ عَلَىٰ وَجۡهِ أَبِي يَأۡتِ بَصِيرٗا وَأۡتُونِي بِأَهۡلِكُمۡ أَجۡمَعِينَ

Ithhaboo biqameesee hatha faalqoohu AAala wajhi abee yati baseeran watoonee biahlikum ajmaAAeena

Demleen yóbbu sama yére yii ngeen sànni ko ca sama kanamu baay : dana dellu di gisaat. Te ngeen dellusi ànd ak njaboot ga gépp”.

94

وَلَمَّا فَصَلَتِ ٱلۡعِيرُ قَالَ أَبُوهُمۡ إِنِّي لَأَجِدُ رِيحَ يُوسُفَۖ لَوۡلَآ أَن تُفَنِّدُونِ

Walamma fasalati alAAeeru qala aboohum innee laajidu reeha yoosufa lawla an tufannidooni

- Ba njëgg ga génnee [Misra], seen baay daldi ne : “Xetu Yuusufaa ngi may xeeñ, ndegam du ngeen wax ne damaa naax”.

95

قَالُواْ تَٱللَّهِ إِنَّكَ لَفِي ضَلَٰلِكَ ٱلۡقَدِيمِ

Qaloo taAllahi innaka lafee dalalika alqadeemi

Ñu ne ko : “Giñ nanu ci Yàlla ne yaa ngi ci sa njuumte lu jëkk la”.

96

فَلَمَّآ أَن جَآءَ ٱلۡبَشِيرُ أَلۡقَىٰهُ عَلَىٰ وَجۡهِهِۦ فَٱرۡتَدَّ بَصِيرٗاۖ قَالَ أَلَمۡ أَقُل لَّكُمۡ إِنِّيٓ أَعۡلَمُ مِنَ ٱللَّهِ مَا لَا تَعۡلَمُونَ

Falamma an jaa albasheeru alqahu AAala wajhihi fairtadda baseeran qala alam aqul lakum innee aAAlamu mina Allahi ma la taAAlamoona

Waaye, ba kuy bégle ka agsee, daldi koy xëpp yére ya ci kanam. Mu daldi ne xàjj di gis, mu ne : “Moo ndax waxuma leen woon ne xam naa lu ma jële ci Yàlla lu ngeen xamul ?”

97

قَالُواْ يَـٰٓأَبَانَا ٱسۡتَغۡفِرۡ لَنَا ذُنُوبَنَآ إِنَّا كُنَّا خَٰطِـِٔينَ

Qaloo ya abana istaghfir lana thunoobana inna kunna khatieena

- Ñu ne : «Éy yaw sunu baay, sàkkul nu njéggal [ci Yàlla] sunuy bàkkaar. Ndax nun dey juumoon nanu ba def bàkkaar naka”.

98

قَالَ سَوۡفَ أَسۡتَغۡفِرُ لَكُمۡ رَبِّيٓۖ إِنَّهُۥ هُوَ ٱلۡغَفُورُ ٱلرَّحِيمُ

Qala sawfa astaghfiru lakum rabbee innahu huwa alghafooru alrraheemu

- Mu ne : “Danaa leen ñaanal njéggal ci sama Boroom. Moom Yàlla nag mooy Jéggalaakoon ba, di Jaglewaakoon ba”.

99

فَلَمَّا دَخَلُواْ عَلَىٰ يُوسُفَ ءَاوَىٰٓ إِلَيۡهِ أَبَوَيۡهِ وَقَالَ ٱدۡخُلُواْ مِصۡرَ إِن شَآءَ ٱللَّهُ ءَامِنِينَ

Falamma dakhaloo AAala yoosufa awa ilayhi abawayhi waqala odkhuloo misra in shaa Allahu amineena

Ba ñu delloo ca Yuusufa, mu song ñaari waajuram, ne leen : “Dugguleen Misra ànd ak kóolute, bu soobee Yàlla !”

100

وَرَفَعَ أَبَوَيۡهِ عَلَى ٱلۡعَرۡشِ وَخَرُّواْ لَهُۥ سُجَّدٗاۖ وَقَالَ يَـٰٓأَبَتِ هَٰذَا تَأۡوِيلُ رُءۡيَٰيَ مِن قَبۡلُ قَدۡ جَعَلَهَا رَبِّي حَقّٗاۖ وَقَدۡ أَحۡسَنَ بِيٓ إِذۡ أَخۡرَجَنِي مِنَ ٱلسِّجۡنِ وَجَآءَ بِكُم مِّنَ ٱلۡبَدۡوِ مِنۢ بَعۡدِ أَن نَّزَغَ ٱلشَّيۡطَٰنُ بَيۡنِي وَبَيۡنَ إِخۡوَتِيٓۚ إِنَّ رَبِّي لَطِيفٞ لِّمَا يَشَآءُۚ إِنَّهُۥ هُوَ ٱلۡعَلِيمُ ٱلۡحَكِيمُ

WarafaAAa abawayhi AAala alAAarshi wakharroo lahu sujjadan waqala ya abati hatha taweelu ruyaya min qablu qad jaAAalaha rabbee haqqan waqad ahsana bee ith akhrajanee mina alssijni wajaa bikum mina albadwi min baAAdi an nazagha alshshaytanu baynee wabayna ikhwatee inna rabbee lateefun lima yashao innahu huwa alAAaleemu alhakeemu

Mu yéegal ñaari waajuram ci kaw gàngunaay ga, ñu rot sujjóotal ko. Mu ne : “Yaw sama baay, lii moo di pirim sama gént ga woon. Sama Boroom def na ko muy dëgg... Te it defal na ma lu baax ba ma mën a génn ci kaso bi, indi leen ngeen jóge ca àll ba, ginnaaw ba Séytaane yàqee sama diggante ak samay doomi-baay. Sama Boroom nag ku lewet la ca la ko soob. Mooy Ku xam te xereñ.

101

۞رَبِّ قَدۡ ءَاتَيۡتَنِي مِنَ ٱلۡمُلۡكِ وَعَلَّمۡتَنِي مِن تَأۡوِيلِ ٱلۡأَحَادِيثِۚ فَاطِرَ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِ أَنتَ وَلِيِّۦ فِي ٱلدُّنۡيَا وَٱلۡأٓخِرَةِۖ تَوَفَّنِي مُسۡلِمٗا وَأَلۡحِقۡنِي بِٱلصَّـٰلِحِينَ

Rabbi qad ataytanee mina almulki waAAallamtanee min taweeli alahadeethi fatira alssamawati waalardi anta waliyyee fee alddunya waalakhirati tawaffanee musliman waalhiqnee bialssaliheena

Yaw sama Boroom, may nga ma nguur, jàngal nga ma it pirim gént. Yaw mi sos asamaan yi ak suuf si, Yaw yaay sama sang, ci àddina ak ca àllaaxira. Yal na nga may rey te fekk may aji-jublu ci Yaw [sama Boroom] sama mbir mépp te yal na nga ma yéege ci ñu yiw ña.(n)

102

ذَٰلِكَ مِنۡ أَنۢبَآءِ ٱلۡغَيۡبِ نُوحِيهِ إِلَيۡكَۖ وَمَا كُنتَ لَدَيۡهِمۡ إِذۡ أَجۡمَعُوٓاْ أَمۡرَهُمۡ وَهُمۡ يَمۡكُرُونَ

Thalika min anbai alghaybi nooheehi ilayka wama kunta ladayhim ith ajmaAAoo amrahum wahum yamkuroona

Loolu bokk na ca xew-xew yu fàddu ya, ñu soloo la ko. Te fekkewuloo ba ñu mànkoo ci mbir, di tëral pexe.

103

وَمَآ أَكۡثَرُ ٱلنَّاسِ وَلَوۡ حَرَصۡتَ بِمُؤۡمِنِينَ

Wama aktharu alnnasi walaw harasta bimumineena

Te li ëpp ci nit ñi duñu gëm doonte la xér nga sax yaw [ci ña gëm].

104

وَمَا تَسۡـَٔلُهُمۡ عَلَيۡهِ مِنۡ أَجۡرٍۚ إِنۡ هُوَ إِلَّا ذِكۡرٞ لِّلۡعَٰلَمِينَ

Wama tasaluhum AAalayhi min ajrin in huwa illa thikrun lilAAalameena

Te laajoo leen ag pey ci [Alxuraan ji]. Te nekkul leneen lu dul ag waare ñeel àddina si yépp.

105

وَكَأَيِّن مِّنۡ ءَايَةٖ فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِ يَمُرُّونَ عَلَيۡهَا وَهُمۡ عَنۡهَا مُعۡرِضُونَ

Wakaayyin min ayatin fee alssamawati waalardi yamurroona AAalayha wahum AAanha muAAridoona

Bariwaana ay kéemtaan yu nekk ci asamaan yi ak ci suuf si, ñu di ko romb, te defuñu ca paal !

106

وَمَا يُؤۡمِنُ أَكۡثَرُهُم بِٱللَّهِ إِلَّا وَهُم مُّشۡرِكُونَ

Wama yuminu aktharuhum biAllahi illa wahum mushrikoona

Li ëpp ci ñoom duñu gëm Yàlla, xanaa kay dañuy nekk rekk di bokkaale Yàlla.

107

أَفَأَمِنُوٓاْ أَن تَأۡتِيَهُمۡ غَٰشِيَةٞ مِّنۡ عَذَابِ ٱللَّهِ أَوۡ تَأۡتِيَهُمُ ٱلسَّاعَةُ بَغۡتَةٗ وَهُمۡ لَا يَشۡعُرُونَ

Afaaminoo an tatiyahum ghashiyatun min AAathabi Allahi aw tatiyahumu alssaAAatu baghtatan wahum la yashAAuroona

Ndax dañoo gëmul ne mbugal mu leen muur mën na leen a dal, di mbugalum Yàlla mbaa mu digal leen, bu Bis-pénc baa ci mbetteel te duñu ko yég ?

108

قُلۡ هَٰذِهِۦ سَبِيلِيٓ أَدۡعُوٓاْ إِلَى ٱللَّهِۚ عَلَىٰ بَصِيرَةٍ أَنَا۠ وَمَنِ ٱتَّبَعَنِيۖ وَسُبۡحَٰنَ ٱللَّهِ وَمَآ أَنَا۠ مِنَ ٱلۡمُشۡرِكِينَ

Qul hathihi sabeelee adAAoo ila Allahi AAala baseeratin ana wamani ittabaAAanee wasubhana Allahi wama ana mina almushrikeena

Neel : “Samaw yoon a, ngir damay woote jëme ci Yàlla ànd ak aw lay. Man bokkuma ci bokkaalekati Yàlla yi, maak ku ma àndal.

109

وَمَآ أَرۡسَلۡنَا مِن قَبۡلِكَ إِلَّا رِجَالٗا نُّوحِيٓ إِلَيۡهِم مِّنۡ أَهۡلِ ٱلۡقُرَىٰٓۗ أَفَلَمۡ يَسِيرُواْ فِي ٱلۡأَرۡضِ فَيَنظُرُواْ كَيۡفَ كَانَ عَٰقِبَةُ ٱلَّذِينَ مِن قَبۡلِهِمۡۗ وَلَدَارُ ٱلۡأٓخِرَةِ خَيۡرٞ لِّلَّذِينَ ٱتَّقَوۡاْۚ أَفَلَا تَعۡقِلُونَ

Wama arsalna min qablika illa rijalan noohee ilayhim min ahli alqura afalam yaseeroo fee alardi fayanthuroo kayfa kana AAaqibatu allatheena min qablihim waladaru alakhirati khayrun lillatheena ittaqaw afala taAAqiloona

Yónniwuñu woon, lu la jiitu [yaw Muhammad], lu dul ay góor yu ñu soloo ñu dëkk ca njénde ya. [Nee leen] ndax dañoo doxul ci suuf si, ba seetlu lan mooy mujjug ña leen jiitu woon ? Te ca dëgg-dëgg kërug àllaaxira moo gën ca ña ragal Yàlla. Moo ndax dangeen dul xel-lu ?

110

حَتَّىٰٓ إِذَا ٱسۡتَيۡـَٔسَ ٱلرُّسُلُ وَظَنُّوٓاْ أَنَّهُمۡ قَدۡ كُذِبُواْ جَآءَهُمۡ نَصۡرُنَا فَنُجِّيَ مَن نَّشَآءُۖ وَلَا يُرَدُّ بَأۡسُنَا عَنِ ٱلۡقَوۡمِ ٱلۡمُجۡرِمِينَ

Hatta itha istayasa alrrusulu wathannoo annahum qad kuthiboo jaahum nasruna fanujjiya man nashao wala yuraddu basuna AAani alqawmi almujrimeena

Ba ña Nu yónni naagoo ne [ndimbal dootul ñëw] te ñu jort ne weddeef nañu leen ba noppi, foofa la Sunu ndimbal agsee ci ñoom. Nu musal ku Nu soob. Te Sunu mbugal amul kenn ku ko mën a fegal tooñkat ya.

111

لَقَدۡ كَانَ فِي قَصَصِهِمۡ عِبۡرَةٞ لِّأُوْلِي ٱلۡأَلۡبَٰبِۗ مَا كَانَ حَدِيثٗا يُفۡتَرَىٰ وَلَٰكِن تَصۡدِيقَ ٱلَّذِي بَيۡنَ يَدَيۡهِ وَتَفۡصِيلَ كُلِّ شَيۡءٖ وَهُدٗى وَرَحۡمَةٗ لِّقَوۡمٖ يُؤۡمِنُونَ

Laqad kana fee qasasihim AAibratun liolee alalbabi ma kana hadeethan yuftara walakin tasdeeqa allathee bayna yadayhi watafseela kulli shayin wahudan warahmatan liqawmin yuminoona

Seen nettali yooyu ay waaree nga ca ñeel woroom xel ya. Du waxtaan wu ñu sos. Waaye day dëggal ya jiitu, te it di leeral lépp lu nekk di ag njub, di yërmaande ñeel nit ñu gëm.(s) Saar 13 : Dënnu 43 Laaya