← Suurat yépp
Suurat 1452 aaya

ابراهيم

Ibrahim

Abraham

Tekki

Tann làkk

1

الٓرۚ كِتَٰبٌ أَنزَلۡنَٰهُ إِلَيۡكَ لِتُخۡرِجَ ٱلنَّاسَ مِنَ ٱلظُّلُمَٰتِ إِلَى ٱلنُّورِ بِإِذۡنِ رَبِّهِمۡ إِلَىٰ صِرَٰطِ ٱلۡعَزِيزِ ٱلۡحَمِيدِ

Aliflamra kitabun anzalnahu ilayka litukhrija alnnasa mina alththulumati ila alnnoori biithni rabbihim ila sirati alAAazeezi alhameedi

Alif, Laam, Raa. Ab téere la bu Nu wàcce ci yaw ngir nga génne nit ñi cig lëndëm [kéefar], jëme leen cig leer [gëm Yàlla], ci ndigalu seen Boroom jëme leen ci yoonu Boroom kàttan gi, Ki yeyoo gépp cant,(s)

2

ٱللَّهِ ٱلَّذِي لَهُۥ مَا فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَمَا فِي ٱلۡأَرۡضِۗ وَوَيۡلٞ لِّلۡكَٰفِرِينَ مِنۡ عَذَابٖ شَدِيدٍ

Allahi allathee lahu ma fee alssamawati wama fee alardi wawaylun lilkafireena min AAathabin shadeedin

[ci yoonu] Yàlla mi nga xam ne Moo moom li nekk ci asamaan yi ak suuf si. Te alkaande ñeel na yéefar yi ci mbugal mu tar.

3

ٱلَّذِينَ يَسۡتَحِبُّونَ ٱلۡحَيَوٰةَ ٱلدُّنۡيَا عَلَى ٱلۡأٓخِرَةِ وَيَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ ٱللَّهِ وَيَبۡغُونَهَا عِوَجًاۚ أُوْلَـٰٓئِكَ فِي ضَلَٰلِۭ بَعِيدٖ

Allatheena yastahibboona alhayata alddunya AAala alakhirati wayasuddoona AAan sabeeli Allahi wayabghoonaha AAiwajan olaika fee dalalin baAAeedin

Ña nga xam ne dañoo tànn dundug àdduna [mu gënal leen] gu àllaaxira, te ñuy wëlbati ña jëm ci yoonu Yàlla, di ko sàkkal ay gàkk, ñooña ñanga ca ag réer gu sori dëgg.

4

وَمَآ أَرۡسَلۡنَا مِن رَّسُولٍ إِلَّا بِلِسَانِ قَوۡمِهِۦ لِيُبَيِّنَ لَهُمۡۖ فَيُضِلُّ ٱللَّهُ مَن يَشَآءُ وَيَهۡدِي مَن يَشَآءُۚ وَهُوَ ٱلۡعَزِيزُ ٱلۡحَكِيمُ

Wama arsalna min rasoolin illa bilisani qawmihi liyubayyina lahum fayudillu Allahu man yashao wayahdee man yashao wahuwa alAAazeezu alhakeemu

Dunu yónni ab Yonent lu dul ci làkku nitam ña [lay waxe] ngir mu leeralal leen [la ñu ko yónni]. Te Yàlla mooy bàyyi cig réer ku ko soob, Dana gindi itam ku ko soob. Ndax Moom moo di boroom kàttan gi tey Aji-xereñ [ciy àtteem].

5

وَلَقَدۡ أَرۡسَلۡنَا مُوسَىٰ بِـَٔايَٰتِنَآ أَنۡ أَخۡرِجۡ قَوۡمَكَ مِنَ ٱلظُّلُمَٰتِ إِلَى ٱلنُّورِ وَذَكِّرۡهُم بِأَيَّىٰمِ ٱللَّهِۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَأٓيَٰتٖ لِّكُلِّ صَبَّارٖ شَكُورٖ

Walaqad arsalna moosa biayatina an akhrij qawmaka mina alththulumati ila alnnoori wathakkirhum biayyami Allahi inna fee thalika laayatin likulli sabbarin shakoorin

Yónni woon Nanu Muusaa, dooleel kook Sunuy kaawtéef, ne ko : “Génneel saw nit cig lëndëm jëme leen cig réer, te nga waar leen ci xéewali Yàlla yi”. Ndax kéemtaan a ngi ci loolu ñeel képp ku di ab muñaakoon, di ab santaakoon.

6

وَإِذۡ قَالَ مُوسَىٰ لِقَوۡمِهِ ٱذۡكُرُواْ نِعۡمَةَ ٱللَّهِ عَلَيۡكُمۡ إِذۡ أَنجَىٰكُم مِّنۡ ءَالِ فِرۡعَوۡنَ يَسُومُونَكُمۡ سُوٓءَ ٱلۡعَذَابِ وَيُذَبِّحُونَ أَبۡنَآءَكُمۡ وَيَسۡتَحۡيُونَ نِسَآءَكُمۡۚ وَفِي ذَٰلِكُم بَلَآءٞ مِّن رَّبِّكُمۡ عَظِيمٞ

Waith qala moosa liqawmihi othkuroo niAAmata Allahi AAalaykum ith anjakum min ali firAAawna yasoomoonakum sooa alAAathabi wayuthabbihoona abnaakum wayastahyoona nisaakum wafee thalikum balaon min rabbikum AAatheemun

(Fàttalikul) ba Muusaa waxee aw nitam ne leen : “Fàttalikuleen xéewalu Yàlla ga Mu leen defaloon ba Mu leen musaloon ci waa kër Firawna, ñu leen doon teg mbugal mu bon. Di rey seen doon yu góor, di bàyyi jigéen ña. Te loolu nekkoon na ab nattu bu rëy bu jóge ci seen Boroom”,

7

وَإِذۡ تَأَذَّنَ رَبُّكُمۡ لَئِن شَكَرۡتُمۡ لَأَزِيدَنَّكُمۡۖ وَلَئِن كَفَرۡتُمۡ إِنَّ عَذَابِي لَشَدِيدٞ

Waith taaththana rabbukum lain shakartum laazeedannakum walain kafartum inna AAathabee lashadeedun

Ak ba seen Boroom xamlee ne : “Bu ngeen gërëmee, fàwwu Mu dolli leen. Bu ngeen weddee nag, [na ngeen xam ne ] Sama mbugal lu tar la”.

8

وَقَالَ مُوسَىٰٓ إِن تَكۡفُرُوٓاْ أَنتُمۡ وَمَن فِي ٱلۡأَرۡضِ جَمِيعٗا فَإِنَّ ٱللَّهَ لَغَنِيٌّ حَمِيدٌ

Waqala moosa in takfuroo antum waman fee alardi jameeAAan fainna Allaha laghaniyyun hameedun

Te Muusaa ne leen : “Bu ngeen weddi woon, yéen ak ñi nekk ci suuf si yépp [du wàññi Boroom bi dara], ngir Yàlla Aji-doylu la ci boppam [wëliis ay mbindéefam], Aji-yeyoo cant la”.

9

أَلَمۡ يَأۡتِكُمۡ نَبَؤُاْ ٱلَّذِينَ مِن قَبۡلِكُمۡ قَوۡمِ نُوحٖ وَعَادٖ وَثَمُودَ وَٱلَّذِينَ مِنۢ بَعۡدِهِمۡ لَا يَعۡلَمُهُمۡ إِلَّا ٱللَّهُۚ جَآءَتۡهُمۡ رُسُلُهُم بِٱلۡبَيِّنَٰتِ فَرَدُّوٓاْ أَيۡدِيَهُمۡ فِيٓ أَفۡوَٰهِهِمۡ وَقَالُوٓاْ إِنَّا كَفَرۡنَا بِمَآ أُرۡسِلۡتُم بِهِۦ وَإِنَّا لَفِي شَكّٖ مِّمَّا تَدۡعُونَنَآ إِلَيۡهِ مُرِيبٖ

Alam yatikum nabao allatheena min qablikum qawmi noohin waAAadin wathamooda waallatheena min baAAdihim la yaAAlamuhum illa Allahu jaathum rusuluhum bialbayyinati faraddoo aydiyahum fee afwahihim waqaloo inna kafarna bima orsiltum bihi wainna lafee shakkin mimma tadAAoonana ilayhi mureebun

Ndax agsi na ci yéen nettalib xew-xew ya leen jiitu woon? Niki nitu Nooh ak waa Haad, ak waa Samuuda ak ña ñëw seen ginnaaw, kenn xamuleen ku dul Yàlla. Seeni Yonent dikkaloon nañu leen, ànd ak lay yu leer, te ñu màtt seeni waaraam wiccax, ñu ne : “Nun weddi nanu li nga xam ne yónneef na leen ko, te nun am nanu sikk gu tar ci li ngeen nuy won”.

10

۞قَالَتۡ رُسُلُهُمۡ أَفِي ٱللَّهِ شَكّٞ فَاطِرِ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِۖ يَدۡعُوكُمۡ لِيَغۡفِرَ لَكُم مِّن ذُنُوبِكُمۡ وَيُؤَخِّرَكُمۡ إِلَىٰٓ أَجَلٖ مُّسَمّٗىۚ قَالُوٓاْ إِنۡ أَنتُمۡ إِلَّا بَشَرٞ مِّثۡلُنَا تُرِيدُونَ أَن تَصُدُّونَا عَمَّا كَانَ يَعۡبُدُ ءَابَآؤُنَا فَأۡتُونَا بِسُلۡطَٰنٖ مُّبِينٖ

Qalat rusuluhum afee Allahi shakkun fatiri alssamawati waalardi yadAAookum liyaghfira lakum min thunoobikum wayuakhkhirakum ila ajalin musamman qaloo in antum illa basharun mithluna tureedoona an tasuddoona AAamma kana yaAAbudu abaona fatoona bisultanin mubeenin

Seeni Yonent ne leen : “Moo ndax dangeen di am sikk ci Yàlla, Moom mi sos asamaan yi ak suuf si, Ma nga leen di woo ngir Mu baal leen seeni ñaawtéef te Mu muñal leen ba ca àpp bu ñu dogal ?”. Ñu tontu ne : “Dungeen dara lu dul aw nit ni nun. Dangeen noo bëgg a tàggaleek la sunu maam ya daan jaamu. Indil-leen nu aw lay wu bir”.

11

قَالَتۡ لَهُمۡ رُسُلُهُمۡ إِن نَّحۡنُ إِلَّا بَشَرٞ مِّثۡلُكُمۡ وَلَٰكِنَّ ٱللَّهَ يَمُنُّ عَلَىٰ مَن يَشَآءُ مِنۡ عِبَادِهِۦۖ وَمَا كَانَ لَنَآ أَن نَّأۡتِيَكُم بِسُلۡطَٰنٍ إِلَّا بِإِذۡنِ ٱللَّهِۚ وَعَلَى ٱللَّهِ فَلۡيَتَوَكَّلِ ٱلۡمُؤۡمِنُونَ

Qalat lahum rusuluhum in nahnu illa basharun mithlukum walakinna Allaha yamunnu AAala man yashao min AAibadihi wama kana lana an natiyakum bisultanin illa biithni Allahi waAAala Allahi falyatawakkali almuminoona

Seen Yonent ya ne leen : “Nekkunu lu dul aw nit ni yéen. Waaye Yàlla dana xéewale ku ko soob ciy jaamam. Dunuleen mën a indil ay lay lu dul ci ndigalul Yàlla. Te way-gëm ña dañuy wéeru ci Yàlla.”(n)

12

وَمَا لَنَآ أَلَّا نَتَوَكَّلَ عَلَى ٱللَّهِ وَقَدۡ هَدَىٰنَا سُبُلَنَاۚ وَلَنَصۡبِرَنَّ عَلَىٰ مَآ ءَاذَيۡتُمُونَاۚ وَعَلَى ٱللَّهِ فَلۡيَتَوَكَّلِ ٱلۡمُتَوَكِّلُونَ

Wama lana alla natawakkala AAala Allahi waqad hadana subulana walanasbiranna AAala ma athaytumoona waAAala Allahi falyatawakkali almutawakkiloona

[Ñi gëm] ne : “Lu téye dunu wéeru ci Yàlla, te gindi nanu ba noppi te teg nu ci sunuy yoon ? Te it dananu muñ lor yi ngeen nuy teg. Kuy wéeru daal na wéeru ci Yàlla.”

13

وَقَالَ ٱلَّذِينَ كَفَرُواْ لِرُسُلِهِمۡ لَنُخۡرِجَنَّكُم مِّنۡ أَرۡضِنَآ أَوۡ لَتَعُودُنَّ فِي مِلَّتِنَاۖ فَأَوۡحَىٰٓ إِلَيۡهِمۡ رَبُّهُمۡ لَنُهۡلِكَنَّ ٱلظَّـٰلِمِينَ

Waqala allatheena kafaroo lirusulihim lanukhrijannakum min ardina aw lataAAoodunna fee millatina faawha ilayhim rabbuhum lanuhlikanna alththalimeena

Ña weddi wax seen Yonent ne leen : “Dananu leen génne ci sunu suuf walla ngeen dellusi ci sunu diine !”. Seen Boroom soloo leen ne : “Fàwwu dana alag tooñkat ña,

14

وَلَنُسۡكِنَنَّكُمُ ٱلۡأَرۡضَ مِنۢ بَعۡدِهِمۡۚ ذَٰلِكَ لِمَنۡ خَافَ مَقَامِي وَخَافَ وَعِيدِ

Walanuskinannakumu alarda min baAAdihim thalika liman khafa maqamee wakhafa waAAeedi

te ci seen ginnaaw Danaa leen jox suuf si muy seen dëkkuwaay [yéen Yonent yi ak ñi leen topp]. Loolu mooy peyug ku ragal Sama taxawaay [ak moom] te ragal Samay tëkku”.

15

وَٱسۡتَفۡتَحُواْ وَخَابَ كُلُّ جَبَّارٍ عَنِيدٖ

Waistaftahoo wakhaba kullu jabbarin AAaneedin

Ñu sàkku ndimbal [ñoom Yonent ya]. Képp ku doon rëy-rëylu te jeng daldi yàqule.

16

مِّن وَرَآئِهِۦ جَهَنَّمُ وَيُسۡقَىٰ مِن مَّآءٖ صَدِيدٖ

Min waraihi jahannamu wayusqa min main sadeedin

Te Safaraa nga xaar ca ginnaaw te dees na ko nàndal ndox mu bon te tàng jér

17

يَتَجَرَّعُهُۥ وَلَا يَكَادُ يُسِيغُهُۥ وَيَأۡتِيهِ ٱلۡمَوۡتُ مِن كُلِّ مَكَانٖ وَمَا هُوَ بِمَيِّتٖۖ وَمِن وَرَآئِهِۦ عَذَابٌ غَلِيظٞ

YatajarraAAuhu wala yakadu yuseeghuhu wayateehi almawtu min kulli makanin wama huwa bimayyitin wamin waraihi AAathabun ghaleethun

dana ko guux. Waaye du ko xaw a mën a wann. Dee di ko dikkale wet gu nekk, te du dee ; te it mbugal mu tar dana ca topp.

18

مَّثَلُ ٱلَّذِينَ كَفَرُواْ بِرَبِّهِمۡۖ أَعۡمَٰلُهُمۡ كَرَمَادٍ ٱشۡتَدَّتۡ بِهِ ٱلرِّيحُ فِي يَوۡمٍ عَاصِفٖۖ لَّا يَقۡدِرُونَ مِمَّا كَسَبُواْ عَلَىٰ شَيۡءٖۚ ذَٰلِكَ هُوَ ٱلضَّلَٰلُ ٱلۡبَعِيدُ

Mathalu allatheena kafaroo birabbihim aAAmaluhum karamadin ishtaddat bihi alrreehu fee yawmin AAasifin la yaqdiroona mimma kasaboo AAala shayin thalika huwa alddalalu albaAAeedu

Ña weddi seen Boroom, seeni jëf dafa mel cig niróole ni ab dóom bu ngelaw ëf ci bisu mbóoya mu ràddi. Duñu mën a jariñoo dara ca la ñu fàggu woon. Loolu moo di réer gu sori dëgg.

19

أَلَمۡ تَرَ أَنَّ ٱللَّهَ خَلَقَ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضَ بِٱلۡحَقِّۚ إِن يَشَأۡ يُذۡهِبۡكُمۡ وَيَأۡتِ بِخَلۡقٖ جَدِيدٖ

Alam tara anna Allaha khalaqa alssamawati waalarda bialhaqqi in yasha yuthhibkum wayati bikhalqin jadeedin

Ndax dañoo gisul ne Yàllaa bind asamaan yi ak suuf si ci dëgg ? Bu ko neexoon Mu jële leen fi, indi fi ay mbindéef yu bees,

20

وَمَا ذَٰلِكَ عَلَى ٱللَّهِ بِعَزِيزٖ

Wama thalika AAala Allahi biAAazeezin

Loolu nekkul lu jafe Yàlla.

21

وَبَرَزُواْ لِلَّهِ جَمِيعٗا فَقَالَ ٱلضُّعَفَـٰٓؤُاْ لِلَّذِينَ ٱسۡتَكۡبَرُوٓاْ إِنَّا كُنَّا لَكُمۡ تَبَعٗا فَهَلۡ أَنتُم مُّغۡنُونَ عَنَّا مِنۡ عَذَابِ ٱللَّهِ مِن شَيۡءٖۚ قَالُواْ لَوۡ هَدَىٰنَا ٱللَّهُ لَهَدَيۡنَٰكُمۡۖ سَوَآءٌ عَلَيۡنَآ أَجَزِعۡنَآ أَمۡ صَبَرۡنَا مَا لَنَا مِن مَّحِيصٖ

Wabarazoo lillahi jameeAAan faqala aldduAAafao lillatheena istakbaroo inna kunna lakum tabaAAan fahal antum mughnoona AAanna min AAathabi Allahi min shayin qaloo law hadana Allahu lahadaynakum sawaon AAalayna ajaziAAna am sabarna ma lana min maheesin

Ñoom ñépp ñu teew ca Yàlla. Ña neew doole wax ña daan màgg- màggalu ne leen : “Nun dey, yéen lanu toppoon. Moo ndax mën ngeen noo jiñal dara ci mbugalum Yàlla mi ?” - Ñu tontu ne : “Su nu Yàlla jubaloon kon nu jubal leen. Léegi nag, nu tiit walla nu muñ, lépp a yem ci nun ; amunu làquwaay [fu nu rawe]”.

22

وَقَالَ ٱلشَّيۡطَٰنُ لَمَّا قُضِيَ ٱلۡأَمۡرُ إِنَّ ٱللَّهَ وَعَدَكُمۡ وَعۡدَ ٱلۡحَقِّ وَوَعَدتُّكُمۡ فَأَخۡلَفۡتُكُمۡۖ وَمَا كَانَ لِيَ عَلَيۡكُم مِّن سُلۡطَٰنٍ إِلَّآ أَن دَعَوۡتُكُمۡ فَٱسۡتَجَبۡتُمۡ لِيۖ فَلَا تَلُومُونِي وَلُومُوٓاْ أَنفُسَكُمۖ مَّآ أَنَا۠ بِمُصۡرِخِكُمۡ وَمَآ أَنتُم بِمُصۡرِخِيَّ إِنِّي كَفَرۡتُ بِمَآ أَشۡرَكۡتُمُونِ مِن قَبۡلُۗ إِنَّ ٱلظَّـٰلِمِينَ لَهُمۡ عَذَابٌ أَلِيمٞ

Waqala alshshaytanu lamma qudiya alamru inna Allaha waAAadakum waAAda alhaqqi wawaAAadtukum faakhlaftukum wama kana liya AAalaykum min sultanin illa an daAAawtukum faistajabtum lee fala taloomoonee waloomoo anfusakum ma ana bimusrikhikum wama antum bimusrikhiyya innee kafartu bima ashraktumooni min qablu inna alththalimeena lahum AAathabun aleemun

Séytaane dana wax, ba lépp sottee, ne : “Yàlla dey digoon na leen dig bu dëggu ; man it ma dig leen te wor leen. Waaye nag amuma woon genn kàttan ci not leen, defuma lu dul woo leen ngeen wuyu ma. Buleen ma yedd ; yeddleen seen bopp. Mënuma leen a xettali te mënuleen maa xettali. Man weddi naa seenug bokkaaleek man ca la jiitu woon”. Tooñkat ya daal am nañu mbugal mu metti.

23

وَأُدۡخِلَ ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ وَعَمِلُواْ ٱلصَّـٰلِحَٰتِ جَنَّـٰتٖ تَجۡرِي مِن تَحۡتِهَا ٱلۡأَنۡهَٰرُ خَٰلِدِينَ فِيهَا بِإِذۡنِ رَبِّهِمۡۖ تَحِيَّتُهُمۡ فِيهَا سَلَٰمٌ

Waodkhila allatheena amanoo waAAamiloo alssalihati jannatin tajree min tahtiha alanharu khalideena feeha biithni rabbihim tahiyyatuhum feeha salamun

Ñu dugal, ña gëm te jëfoon jëf yu sell ya, ci Àjjana joo xam ne ay dex dañuy daw-dawaan ci suufam, dañu fay béel ci seen ndigalul Boroom. Seenub nuyyoo foofa moo di : “Jàmm”

24

أَلَمۡ تَرَ كَيۡفَ ضَرَبَ ٱللَّهُ مَثَلٗا كَلِمَةٗ طَيِّبَةٗ كَشَجَرَةٖ طَيِّبَةٍ أَصۡلُهَا ثَابِتٞ وَفَرۡعُهَا فِي ٱلسَّمَآءِ

Alam tara kayfa daraba Allahu mathalan kalimatan tayyibatan kashajaratin tayyibatin asluha thabitun wafarAAuha fee alssamai

Ndax gisoo ni sa Boroom di joxee ci waxiinu léebu baat bu sell bu mel ni garab gu sell goo xam ne dàtt ba lu sampu la ba dëgër te wanqaas ya nekk ca kaw asamaan ?(s)

25

تُؤۡتِيٓ أُكُلَهَا كُلَّ حِينِۭ بِإِذۡنِ رَبِّهَاۗ وَيَضۡرِبُ ٱللَّهُ ٱلۡأَمۡثَالَ لِلنَّاسِ لَعَلَّهُمۡ يَتَذَكَّرُونَ

Tutee okulaha kulla heenin biithni rabbiha wayadribu Allahu alamthala lilnnasi laAAallahum yatathakkaroona

Muy joxi meññantam saa su nekk ci ndigalul Boroomam. Yàlla danay gaaral nit ñi ay léebu ndaxtelee ñu fàttaliku [seen Boroom].

26

وَمَثَلُ كَلِمَةٍ خَبِيثَةٖ كَشَجَرَةٍ خَبِيثَةٍ ٱجۡتُثَّتۡ مِن فَوۡقِ ٱلۡأَرۡضِ مَا لَهَا مِن قَرَارٖ

Wamathalu kalimatin khabeethatin kashajaratin khabeethatin ijtuththat min fawqi alardi ma laha min qararin

Te itam, léeboo wax : “Baat bu bon dafa mel ni garab gu ñu buddee ci suuf te amul fu mu sax.”

27

يُثَبِّتُ ٱللَّهُ ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ بِٱلۡقَوۡلِ ٱلثَّابِتِ فِي ٱلۡحَيَوٰةِ ٱلدُّنۡيَا وَفِي ٱلۡأٓخِرَةِۖ وَيُضِلُّ ٱللَّهُ ٱلظَّـٰلِمِينَۚ وَيَفۡعَلُ ٱللَّهُ مَا يَشَآءُ

Yuthabbitu Allahu allatheena amanoo bialqawli alththabiti fee alhayati alddunya wafee alakhirati wayudillu Allahu alththalimeena wayafAAalu Allahu ma yashao

Yàlla dana dëgëral ña gëm ci wax ju dëggu, ci dundug àddina ak ca àllaaxira. Te Dana bàyyi tooñkat ya ca seen réer ga. Te Yàlla dana def lu ko soob.

28

۞أَلَمۡ تَرَ إِلَى ٱلَّذِينَ بَدَّلُواْ نِعۡمَتَ ٱللَّهِ كُفۡرٗا وَأَحَلُّواْ قَوۡمَهُمۡ دَارَ ٱلۡبَوَارِ

Alam tara ila allatheena baddaloo niAAmata Allahi kufran waahalloo qawmahum dara albawari

Ndax gisuloo ñay feye xéewali Yàlla ci di Ko weddi tey wàcce seenu nit ci kërug alkaande(r)

29

جَهَنَّمَ يَصۡلَوۡنَهَاۖ وَبِئۡسَ ٱلۡقَرَارُ

Jahannama yaslawnaha wabisa alqararu

... danañu séndal ci Safara ? Ndaw saxuwaay bu bon !

30

وَجَعَلُواْ لِلَّهِ أَندَادٗا لِّيُضِلُّواْ عَن سَبِيلِهِۦۗ قُلۡ تَمَتَّعُواْ فَإِنَّ مَصِيرَكُمۡ إِلَى ٱلنَّارِ

WajaAAaloo lillahi andadan liyudilloo AAan sabeelihi qul tamattaAAoo fainna maseerakum ila alnnari

Ñay sàkkal Yàlla nawle ngir réeral [seenu nit] soreel leen yoonu [Yàlla] : “Xéewluleen rekk, Safara ngeen di mujj di”.

31

قُل لِّعِبَادِيَ ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ يُقِيمُواْ ٱلصَّلَوٰةَ وَيُنفِقُواْ مِمَّا رَزَقۡنَٰهُمۡ سِرّٗا وَعَلَانِيَةٗ مِّن قَبۡلِ أَن يَأۡتِيَ يَوۡمٞ لَّا بَيۡعٞ فِيهِ وَلَا خِلَٰلٌ

Qul liAAibadiya allatheena amanoo yuqeemoo alssalata wayunfiqoo mimma razaqnahum sirran waAAalaniyatan min qabli an yatiya yawmun la bayAAun feehi wala khilalun

Waxal sama jaam yi gëm ne leen : «Nañuy taxawal julli tey joxe ca la Ma leen wërsëgale ci lu nëbbu walla la feeñ, balaa àpp bis di ñëw boo xam ne jotoo amu fa waxantumalaa xaritoo.

32

ٱللَّهُ ٱلَّذِي خَلَقَ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضَ وَأَنزَلَ مِنَ ٱلسَّمَآءِ مَآءٗ فَأَخۡرَجَ بِهِۦ مِنَ ٱلثَّمَرَٰتِ رِزۡقٗا لَّكُمۡۖ وَسَخَّرَ لَكُمُ ٱلۡفُلۡكَ لِتَجۡرِيَ فِي ٱلۡبَحۡرِ بِأَمۡرِهِۦۖ وَسَخَّرَ لَكُمُ ٱلۡأَنۡهَٰرَ

Allahu allathee khalaqa alssamawati waalarda waanzala mina alssamai maan faakhraja bihi mina alththamarati rizqan lakum wasakhkhara lakumu alfulka litajriya fee albahri biamrihi wasakhkhara lakumu alanhara

Yàlla mooy ki bind asamaan yi ak suuf si te Mooy wàcce ndox mu jóge kaw asamaan ngir Mu génne ca meññent yu nekk i xéewal ci yéen. Te Moo leen tàggatal gaal ngir ngeen mën a daw ci géej ci ndigalam. Te tàggatal na leen it dex yi.

33

وَسَخَّرَ لَكُمُ ٱلشَّمۡسَ وَٱلۡقَمَرَ دَآئِبَيۡنِۖ وَسَخَّرَ لَكُمُ ٱلَّيۡلَ وَٱلنَّهَارَ

Wasakhkhara lakumu alshshamsa waalqamara daibayni wasakhkhara lakumu allayla waalnnahara

Te tàggatal na leen it jant bi ak weer wi ñuy ñaari way-daw [ku ca nekk ci aw rëddëm]. Tàggatal na leen guddi ak bëccëg.

34

وَءَاتَىٰكُم مِّن كُلِّ مَا سَأَلۡتُمُوهُۚ وَإِن تَعُدُّواْ نِعۡمَتَ ٱللَّهِ لَا تُحۡصُوهَآۗ إِنَّ ٱلۡإِنسَٰنَ لَظَلُومٞ كَفَّارٞ

Waatakum min kulli ma saaltumoohu wain taAAuddoo niAAmata Allahi la tuhsooha inna alinsana lathaloomun kaffarun

Te Moo di leen may ci lépp lu ngeen ko ñaan. Te sax, bu ngeen doon jéem a waññi ay xéewalam, dungeen ko mën a takk. Ndekete yoo nit moom ab tooñkat la bu mën a fakk jëf.

35

وَإِذۡ قَالَ إِبۡرَٰهِيمُ رَبِّ ٱجۡعَلۡ هَٰذَا ٱلۡبَلَدَ ءَامِنٗا وَٱجۡنُبۡنِي وَبَنِيَّ أَن نَّعۡبُدَ ٱلۡأَصۡنَامَ

Waith qala ibraheemu rabbi ijAAal hatha albalada aminan waojnubnee wabaniyya an naAAbuda alasnama

[Fàttalikul] ba Ibraahiima waxee ne : “Sama Boroom, [ñaan naa la] nga def dëkk bii di fu am kóolute, te maak samag njaboot nga soril nu ak jaamu xërëm.

36

رَبِّ إِنَّهُنَّ أَضۡلَلۡنَ كَثِيرٗا مِّنَ ٱلنَّاسِۖ فَمَن تَبِعَنِي فَإِنَّهُۥ مِنِّيۖ وَمَنۡ عَصَانِي فَإِنَّكَ غَفُورٞ رَّحِيمٞ

Rabbi innahunna adlalna katheeran mina alnnasi faman tabiAAanee fainnahu minnee waman AAasanee fainnaka ghafoorun raheemun

Boroom sama, xërëm yooyu dey réeral nañu [sànk] lu bari ci nit ñi. Képp ku ma topp ci man la bokk. Képp ku ma weddi... [Yaa xam noo koy def], ndax Yaw Jéggalaakoon nga, Jaglewaakoon nga !

37

رَّبَّنَآ إِنِّيٓ أَسۡكَنتُ مِن ذُرِّيَّتِي بِوَادٍ غَيۡرِ ذِي زَرۡعٍ عِندَ بَيۡتِكَ ٱلۡمُحَرَّمِ رَبَّنَا لِيُقِيمُواْ ٱلصَّلَوٰةَ فَٱجۡعَلۡ أَفۡـِٔدَةٗ مِّنَ ٱلنَّاسِ تَهۡوِيٓ إِلَيۡهِمۡ وَٱرۡزُقۡهُم مِّنَ ٱلثَّمَرَٰتِ لَعَلَّهُمۡ يَشۡكُرُونَ

Rabbana innee askantu min thurriyyatee biwadin ghayri thee zarAAin AAinda baytika almuharrami rabbana liyuqeemoo alssalata faijAAal afidatan mina alnnasi tahwee ilayhim waorzuqhum mina alththamarati laAAallahum yashkuroona

Yaw sama Boroom, dëkkal naa lenn ci sama njaboot ci xur wu amul mbey, ci sa néeg bu ñu wormaal ba [Kaaba ga], ngir ñuy taxawal julli. Defal seenug cofeel ci xoli nit ñi. Te nga wërsëgal leen ay meññent. Ndax xéy-na ñu gërëm la ?

38

رَبَّنَآ إِنَّكَ تَعۡلَمُ مَا نُخۡفِي وَمَا نُعۡلِنُۗ وَمَا يَخۡفَىٰ عَلَى ٱللَّهِ مِن شَيۡءٖ فِي ٱلۡأَرۡضِ وَلَا فِي ٱلسَّمَآءِ

Rabbana innaka taAAlamu ma nukhfee wama nuAAlinu wama yakhfa AAala Allahi min shayin fee alardi wala fee alssamai

Yaw sunu Boroom dey, xam nga li ñuy nëbb ak li ñuy fésal : - te amul menn mbir mu umpu Yàlla ci suuf si, waxantuma laak asamaan ! -

39

ٱلۡحَمۡدُ لِلَّهِ ٱلَّذِي وَهَبَ لِي عَلَى ٱلۡكِبَرِ إِسۡمَٰعِيلَ وَإِسۡحَٰقَۚ إِنَّ رَبِّي لَسَمِيعُ ٱلدُّعَآءِ

Alhamdu lillahi allathee wahaba lee AAala alkibari ismaAAeela waishaqa inna rabbee lasameeAAu aldduAAai

Xéeti cant yépp moomale naa ko Yàlla, Mi nga xam ne Moo ma may cig mage [sama doom] Ismaahiila ak Isaaqa. Sama Boroom daal kuy dégg ñaan la.

40

رَبِّ ٱجۡعَلۡنِي مُقِيمَ ٱلصَّلَوٰةِ وَمِن ذُرِّيَّتِيۚ رَبَّنَا وَتَقَبَّلۡ دُعَآءِ

Rabbi ijAAalnee muqeema alssalati wamin thurriyyatee rabbana wtaqabbal duAAai

[Éy] Yaw Boroom bi !, def ma maak samay doom ak i sët, nuy taxawalkati julli ; waay- waay nangul sunu ñaan !

41

رَبَّنَا ٱغۡفِرۡ لِي وَلِوَٰلِدَيَّ وَلِلۡمُؤۡمِنِينَ يَوۡمَ يَقُومُ ٱلۡحِسَابُ

Rabbana ighfir lee waliwalidayya walilmumineena yawma yaqoomu alhisabu

Yaw Boroom sama ! Jéggal ma maak samay waajur ak ñi gëm ca bis ba Yàlla di natt jëfi mbindéef yi”.(s)

42

وَلَا تَحۡسَبَنَّ ٱللَّهَ غَٰفِلًا عَمَّا يَعۡمَلُ ٱلظَّـٰلِمُونَۚ إِنَّمَا يُؤَخِّرُهُمۡ لِيَوۡمٖ تَشۡخَصُ فِيهِ ٱلۡأَبۡصَٰرُ

Wala tahsabanna Allaha ghafilan AAamma yaAAmalu alththalimoona innama yuakhkhiruhum liyawmin tashkhasu feehi alabsaru

[Yaw Yonent bi], bul njort ne Yàlla amul paal ci li tooñkat yi di def. Deful lu dul yeexe leen ba Bis-pénc ba bët yi buqeeku [janook seen mbugal].

43

مُهۡطِعِينَ مُقۡنِعِي رُءُوسِهِمۡ لَا يَرۡتَدُّ إِلَيۡهِمۡ طَرۡفُهُمۡۖ وَأَفۡـِٔدَتُهُمۡ هَوَآءٞ

MuhtiAAeena muqniAAee ruoosihim la yartaddu ilayhim tarfuhum waafidatuhum hawaon

Ñuy daw, muur seeni bopp [ngir kersa], ne muq di xoole te dara nekkul ca seen xol ya [lu dul njàqare].

44

وَأَنذِرِ ٱلنَّاسَ يَوۡمَ يَأۡتِيهِمُ ٱلۡعَذَابُ فَيَقُولُ ٱلَّذِينَ ظَلَمُواْ رَبَّنَآ أَخِّرۡنَآ إِلَىٰٓ أَجَلٖ قَرِيبٖ نُّجِبۡ دَعۡوَتَكَ وَنَتَّبِعِ ٱلرُّسُلَۗ أَوَلَمۡ تَكُونُوٓاْ أَقۡسَمۡتُم مِّن قَبۡلُ مَا لَكُم مِّن زَوَالٖ

Waanthiri alnnasa yawma yateehimu alAAathabu fayaqoolu allatheena thalamoo rabbana akhkhirna ila ajalin qareebin nujib daAAwataka wanattabiAAi alrrusula awalam takoonoo aqsamtum min qablu ma lakum min zawalin

Waaral nit ñi ci bis bu ñu leen di indil mbugal mi, ba tooñkat ya di wax naan : “Sunu Boroom, tee nga noo muñal diir bu gàtt, kon dey nu wuyusi woote, topp itam say Yonent”. - Mu tontu leen ne: “Ndax daawuleen giñ ne àllaaxira amul ?”.

45

وَسَكَنتُمۡ فِي مَسَٰكِنِ ٱلَّذِينَ ظَلَمُوٓاْ أَنفُسَهُمۡ وَتَبَيَّنَ لَكُمۡ كَيۡفَ فَعَلۡنَا بِهِمۡ وَضَرَبۡنَا لَكُمُ ٱلۡأَمۡثَالَ

Wasakantum fee masakini allatheena thalamoo anfusahum watabayyana lakum kayfa faAAalna bihim wadarabna lakumu alamthala

Ngeen dëkk ci dëkki ña tooñoon seen bopp. Te ngeen xamoon xéll na Nu defoon ak ñoom te joxoon Nanu leen ay tegtal.

46

وَقَدۡ مَكَرُواْ مَكۡرَهُمۡ وَعِندَ ٱللَّهِ مَكۡرُهُمۡ وَإِن كَانَ مَكۡرُهُمۡ لِتَزُولَ مِنۡهُ ٱلۡجِبَالُ

Waqad makaroo makrahum waAAinda Allahi makruhum wain kana makruhum litazoola minhu aljibalu

Dañoo fexe seen pexe te umpul Yàlla. Doonte la sax, seen pexe moomu mën naa dindi tundi doj yi...

47

فَلَا تَحۡسَبَنَّ ٱللَّهَ مُخۡلِفَ وَعۡدِهِۦ رُسُلَهُۥٓۚ إِنَّ ٱللَّهَ عَزِيزٞ ذُو ٱنتِقَامٖ

Fala tahsabanna Allaha mukhlifa waAAdihi rusulahu inna Allaha AAazeezun thoo intiqamin

Bul njort ne Yàlla dana soppi la Mu dig ay Yonentam. Yàlla ku am kàttan la, di Kuy feyu [tooñeel],

48

يَوۡمَ تُبَدَّلُ ٱلۡأَرۡضُ غَيۡرَ ٱلۡأَرۡضِ وَٱلسَّمَٰوَٰتُۖ وَبَرَزُواْ لِلَّهِ ٱلۡوَٰحِدِ ٱلۡقَهَّارِ

Yawma tubaddalu alardu ghayra alardi waalssamawatu wabarazoo lillahi alwahidi alqahhari

ba bis ba ñuy weccee suuf sii seneen suuf ak asamaan yi itam te nit ñi génne [ca seeni bàmmeel] teew ca Yàlla ja di jenn, te di Notaakoon ba.

49

وَتَرَى ٱلۡمُجۡرِمِينَ يَوۡمَئِذٖ مُّقَرَّنِينَ فِي ٱلۡأَصۡفَادِ

Watara almujrimeena yawmaithin muqarraneena fee alasfadi

ca bis booba, danga gis saay-saay sa ñu lëkkale leen ca jéng ya,

50

سَرَابِيلُهُم مِّن قَطِرَانٖ وَتَغۡشَىٰ وُجُوهَهُمُ ٱلنَّارُ

Sarabeeluhum min qatranin wataghsha wujoohahumu alnnaru

seeni yére keteraan la, ñu muure seeni kanam ak safara.

51

لِيَجۡزِيَ ٱللَّهُ كُلَّ نَفۡسٖ مَّا كَسَبَتۡۚ إِنَّ ٱللَّهَ سَرِيعُ ٱلۡحِسَابِ

Liyajziya Allahu kulla nafsin ma kasabat inna Allaha sareeAAu alhisabi

[La ko waral] moo di Yàllaa feye bakkan bu nekk la mu fàggu. Te nag Yàlla moom Ku gaaw ka ci natt lu ne.

52

هَٰذَا بَلَٰغٞ لِّلنَّاسِ وَلِيُنذَرُواْ بِهِۦ وَلِيَعۡلَمُوٓاْ أَنَّمَا هُوَ إِلَٰهٞ وَٰحِدٞ وَلِيَذَّكَّرَ أُوْلُواْ ٱلۡأَلۡبَٰبِ

Hatha balaghun lilnnasi waliyuntharoo bihi waliyaAAlamoo annama huwa ilahun wahidun waliyaththakkara oloo alalbabi

Ngir ñu waaru te xame ca itam Moom Yàlla jenn Yàlla doŋŋ la, ak itam woroom xel ya fàttalikoo ci. Saar 15 : Goxub Hijri 99 Laaya