← Suurat yépp
Suurat 2969 aaya

العنكبوت

Al-'Ankabut

The Spider

Tekki

Tann làkk

1

الٓمٓ

Aliflammeem

Alif, Laam, Miim.

2

أَحَسِبَ ٱلنَّاسُ أَن يُتۡرَكُوٓاْ أَن يَقُولُوٓاْ ءَامَنَّا وَهُمۡ لَا يُفۡتَنُونَ

Ahasiba alnnasu an yutrakoo an yaqooloo amanna wahum la yuftanoona

Ndax nit ñi foog nañu ne danañu wax ne : “Gëm nañu !” te kenn duleen sànje ?

3

وَلَقَدۡ فَتَنَّا ٱلَّذِينَ مِن قَبۡلِهِمۡۖ فَلَيَعۡلَمَنَّ ٱللَّهُ ٱلَّذِينَ صَدَقُواْ وَلَيَعۡلَمَنَّ ٱلۡكَٰذِبِينَ

Walaqad fatanna allatheena min qablihim falayaAAlamanna Allahu allatheena sadaqoo walayaAAlamanna alkathibeena

Sànje woon Nanu ña leen jiitu woon ; Yàlla xam na ñay dëggal ak ñay fen.

4

أَمۡ حَسِبَ ٱلَّذِينَ يَعۡمَلُونَ ٱلسَّيِّـَٔاتِ أَن يَسۡبِقُونَاۚ سَآءَ مَا يَحۡكُمُونَ

Am hasiba allatheena yaAAmaloona alssayyiati an yasbiqoona saa ma yahkumoona

Walla ñay jëfi ñaawteef, jàpp nañu ne danañu Nu jiitu ? Aka ñoo ñaaw ab àtte !

5

مَن كَانَ يَرۡجُواْ لِقَآءَ ٱللَّهِ فَإِنَّ أَجَلَ ٱللَّهِ لَأٓتٖۚ وَهُوَ ٱلسَّمِيعُ ٱلۡعَلِيمُ

Man kana yarjoo liqaa Allahi fainna ajala Allahi laatin wahuwa alssameeAAu alAAaleemu

Képp kuy yaakaar a dajeek Yàlla, digub Yàlla boobu luy dikk la. Te Mooy dégg, di xam.

6

وَمَن جَٰهَدَ فَإِنَّمَا يُجَٰهِدُ لِنَفۡسِهِۦٓۚ إِنَّ ٱللَّهَ لَغَنِيٌّ عَنِ ٱلۡعَٰلَمِينَ

Waman jahada fainnama yujahidu linafsihi inna Allaha laghaniyyun AAani alAAalameena

Képp kuy xare, boppam la koy defal, Yàlla ku doylu la ci waa àddina bi yépp.

7

وَٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ وَعَمِلُواْ ٱلصَّـٰلِحَٰتِ لَنُكَفِّرَنَّ عَنۡهُمۡ سَيِّـَٔاتِهِمۡ وَلَنَجۡزِيَنَّهُمۡ أَحۡسَنَ ٱلَّذِي كَانُواْ يَعۡمَلُونَ

Waallatheena amanoo waAAamiloo alssalihati lanukaffiranna AAanhum sayyiatihim walanajziyannahum ahsana allathee kanoo yaAAmaloona

Ñi gëm tey jëf u yiw, Dananu leen faral seeni ñaawteef, te Dananu leen feye ca la gën ca la ñu daan def.(s)

8

وَوَصَّيۡنَا ٱلۡإِنسَٰنَ بِوَٰلِدَيۡهِ حُسۡنٗاۖ وَإِن جَٰهَدَاكَ لِتُشۡرِكَ بِي مَا لَيۡسَ لَكَ بِهِۦ عِلۡمٞ فَلَا تُطِعۡهُمَآۚ إِلَيَّ مَرۡجِعُكُمۡ فَأُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمۡ تَعۡمَلُونَ

Wawassayna alinsana biwalidayhi husnan wain jahadaka litushrika bee ma laysa laka bihi AAilmun fala tutiAAhuma ilayya marjiAAukum faonabbiokum bima kuntum taAAmaloona

Dénk Nanu nit muy def yiw ciy ñaari way-juram, “bu ñu la sonnalee nag ci bëgg nga bokkaale Ma ak loo xamul, buleen ca topp”. Ci Man ngeen di dellusi, Ma xibaar leen la ngeen daan def.(n)

9

وَٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ وَعَمِلُواْ ٱلصَّـٰلِحَٰتِ لَنُدۡخِلَنَّهُمۡ فِي ٱلصَّـٰلِحِينَ

Waallatheena amanoo waAAamiloo alssalihati lanudkhilannahum fee alssaliheena

Ña gën tey jëf u yiw, Dananu leen dugal ca nit ñu yiw ña.

10

وَمِنَ ٱلنَّاسِ مَن يَقُولُ ءَامَنَّا بِٱللَّهِ فَإِذَآ أُوذِيَ فِي ٱللَّهِ جَعَلَ فِتۡنَةَ ٱلنَّاسِ كَعَذَابِ ٱللَّهِۖ وَلَئِن جَآءَ نَصۡرٞ مِّن رَّبِّكَ لَيَقُولُنَّ إِنَّا كُنَّا مَعَكُمۡۚ أَوَلَيۡسَ ٱللَّهُ بِأَعۡلَمَ بِمَا فِي صُدُورِ ٱلۡعَٰلَمِينَ

Wamina alnnasi man yaqoolu amanna biAllahi faitha oothiya fee Allahi jaAAala fitnata alnnasi kaAAathabi Allahi walain jaa nasrun min rabbika layaqoolunna inna kunna maAAakum awalaysa Allahu biaAAlama bima fee sudoori alAAalameena

Am na ci nit ñi ñuy wax naan : “Gëm Nanu Yàlla” ; te bu ñu leen loree ci ànd gi ñu ànd ak Yàlla, dañuy jàppe sànjeb nit ñooñu ni mbugalum Yàlla. Bu leen ndimbal dikkalee lu bawoo ca sa Boroom, ñu tàmbalee wax naan : “Nun ak yéen a àndoon !” Moo ndax Yàlla dafa gënul a xam li nekk ci dënni waa àddina si yépp ?

11

وَلَيَعۡلَمَنَّ ٱللَّهُ ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ وَلَيَعۡلَمَنَّ ٱلۡمُنَٰفِقِينَ

WalayaAAlamanna Allahu allatheena amanoo walayaAAlamanna almunafiqeena

Yàlla xam na tigi ña gëm, xam na itam naaféq yi .

12

وَقَالَ ٱلَّذِينَ كَفَرُواْ لِلَّذِينَ ءَامَنُواْ ٱتَّبِعُواْ سَبِيلَنَا وَلۡنَحۡمِلۡ خَطَٰيَٰكُمۡ وَمَا هُم بِحَٰمِلِينَ مِنۡ خَطَٰيَٰهُم مِّن شَيۡءٍۖ إِنَّهُمۡ لَكَٰذِبُونَ

Waqala allatheena kafaroo lillatheena amanoo ittabiAAoo sabeelana walnahmil khatayakum wama hum bihamileena min khatayahum min shayin innahum lakathiboona

Yéefar yaa ngay wax ña gëm naan leen ; “Toppleen sunu mboor, dananu yenu seeni ñaawteef ”. [Mukk] duñu mas a yenu tus ci seeni ñaawteef. Li wóor moo di ñoom ay fenkat lañu.

13

وَلَيَحۡمِلُنَّ أَثۡقَالَهُمۡ وَأَثۡقَالٗا مَّعَ أَثۡقَالِهِمۡۖ وَلَيُسۡـَٔلُنَّ يَوۡمَ ٱلۡقِيَٰمَةِ عَمَّا كَانُواْ يَفۡتَرُونَ

Walayahmilunna athqalahum waathqalan maAAa athqalihim walayusalunna yawma alqiyamati AAamma kanoo yaftaroona

Danañu yenu seen yu diis ya ak yeneen yu diis boole ko ca. Te bu Bis- pénc baa, danañu leen laaj la ñu daan duur [fen].

14

وَلَقَدۡ أَرۡسَلۡنَا نُوحًا إِلَىٰ قَوۡمِهِۦ فَلَبِثَ فِيهِمۡ أَلۡفَ سَنَةٍ إِلَّا خَمۡسِينَ عَامٗا فَأَخَذَهُمُ ٱلطُّوفَانُ وَهُمۡ ظَٰلِمُونَ

Walaqad arsalna noohan ila qawmihi falabitha feehim alfa sanatin illa khamseena AAaman faakhathahumu alttoofanu wahum thalimoona

Yónni woon Nanu Nooh ca aw nitam. Mu sax fa ñoom junniy at yu yées juróom-fukk. Mbënn ma daldi leen di mëdd ba ñu tooñee.

15

فَأَنجَيۡنَٰهُ وَأَصۡحَٰبَ ٱلسَّفِينَةِ وَجَعَلۡنَٰهَآ ءَايَةٗ لِّلۡعَٰلَمِينَ

Faanjaynahu waashaba alssafeenati wajaAAalnaha ayatan lilAAalameena

Nu musaloon ko mook waa gaal ga ; def Nanu leen ñuy kéemaan ci waa àddina sépp.

16

وَإِبۡرَٰهِيمَ إِذۡ قَالَ لِقَوۡمِهِ ٱعۡبُدُواْ ٱللَّهَ وَٱتَّقُوهُۖ ذَٰلِكُمۡ خَيۡرٞ لَّكُمۡ إِن كُنتُمۡ تَعۡلَمُونَ

Waibraheema ith qala liqawmihi oAAbudoo Allaha waittaqoohu thalikum khayrun lakum in kuntum taAAlamoona

[Fàttalikul it] Ibraahiima, ba mu waxee nitam ña, ne leen : “Jaamuleen Yàlla : moo gën ci yéen, de cëy bu ngeen xamoon”.

17

إِنَّمَا تَعۡبُدُونَ مِن دُونِ ٱللَّهِ أَوۡثَٰنٗا وَتَخۡلُقُونَ إِفۡكًاۚ إِنَّ ٱلَّذِينَ تَعۡبُدُونَ مِن دُونِ ٱللَّهِ لَا يَمۡلِكُونَ لَكُمۡ رِزۡقٗا فَٱبۡتَغُواْ عِندَ ٱللَّهِ ٱلرِّزۡقَ وَٱعۡبُدُوهُ وَٱشۡكُرُواْ لَهُۥٓۖ إِلَيۡهِ تُرۡجَعُونَ

Innama taAAbudoona min dooni Allahi awthanan watakhluqoona ifkan inna allatheena taAAbudoona min dooni Allahi la yamlikoona lakum rizqan faibtaghoo AAinda Allahi alrrizqa waoAAbudoohu waoshkuroo lahu ilayhi turjaAAoona

Yéen a ngay jaamu ay xërëm bàyyi Yàlla, di sos ay fen yu ngeen di jaamu te du Yàlla. Amaluñuleen woon wërsëg ; sàkkujileen wërsëg ci Yàlla. Te ngeen jaamu Ko te sant Ko. Ca Moom ngeen di dellu de.

18

وَإِن تُكَذِّبُواْ فَقَدۡ كَذَّبَ أُمَمٞ مِّن قَبۡلِكُمۡۖ وَمَا عَلَى ٱلرَّسُولِ إِلَّا ٱلۡبَلَٰغُ ٱلۡمُبِينُ

Wain tukaththiboo faqad kaththaba omamun min qablikum wama AAala alrrasooli illa albalaghu almubeenu

Su ngeen ko weddee, jàppe ko ay fen, am na ay xeet yu leen jiitu woon daan weddi. Rikk nangeen xam ne ab Yonent jottali mu leer rekk a ko war.

19

أَوَلَمۡ يَرَوۡاْ كَيۡفَ يُبۡدِئُ ٱللَّهُ ٱلۡخَلۡقَ ثُمَّ يُعِيدُهُۥٓۚ إِنَّ ذَٰلِكَ عَلَى ٱللَّهِ يَسِيرٞ

Awalam yaraw kayfa yubdio Allahu alkhalqa thumma yuAAeeduhu inna thalika AAala Allahi yaseerun

Moo ndax dañoo gisul ni Yàlla di sosee mbindéef te di ko defaraat ? Looloo ka yomb ca Yàlla.

20

قُلۡ سِيرُواْ فِي ٱلۡأَرۡضِ فَٱنظُرُواْ كَيۡفَ بَدَأَ ٱلۡخَلۡقَۚ ثُمَّ ٱللَّهُ يُنشِئُ ٱلنَّشۡأَةَ ٱلۡأٓخِرَةَۚ إِنَّ ٱللَّهَ عَلَىٰ كُلِّ شَيۡءٖ قَدِيرٞ

Qul seeroo fee alardi faonthuroo kayfa badaa alkhalqa thumma Allahu yunshio alnnashata alakhirata inna Allaha AAala kulli shayin qadeerun

Neel : “Wërleen [dox] ci kaw suuf si te ngeen xool naka la Yàlla sosee mbindéef yi. Ak itam naka lay sos gu mujj ga di deme. Yàlla mën na lépp lu ne”.

21

يُعَذِّبُ مَن يَشَآءُ وَيَرۡحَمُ مَن يَشَآءُۖ وَإِلَيۡهِ تُقۡلَبُونَ

YuAAaththibu man yashao wayarhamu man yashao wailayhi tuqlaboona

Dana mbugal ku ko soob te it Dana yërëm ku ko soob ; te yéen ñépp ca Moom ngeen jëm.

22

وَمَآ أَنتُم بِمُعۡجِزِينَ فِي ٱلۡأَرۡضِ وَلَا فِي ٱلسَّمَآءِۖ وَمَا لَكُم مِّن دُونِ ٱللَّهِ مِن وَلِيّٖ وَلَا نَصِيرٖ

Wama antum bimuAAjizeena fee alardi wala fee alssamai wama lakum min dooni Allahi min waliyyin wala naseerin

Mënuleen a të ci kaw suuf si waxantumaak asamaan si ; te itam amuleen wenn wéeruwaay mbaa dimbalikat bu dul Yàlla.

23

وَٱلَّذِينَ كَفَرُواْ بِـَٔايَٰتِ ٱللَّهِ وَلِقَآئِهِۦٓ أُوْلَـٰٓئِكَ يَئِسُواْ مِن رَّحۡمَتِي وَأُوْلَـٰٓئِكَ لَهُمۡ عَذَابٌ أَلِيمٞ

Waallatheena kafaroo biayati Allahi waliqaihi olaika yaisoo min rahmatee waolaika lahum AAathabun aleemun

Ña nga xam ne dañoo weddi kàdduy Yàlla ak dajeek Moom, ñooña naag nañu ci Sama yërmaande. Te it danañu am mbugal mu mitti.

24

فَمَا كَانَ جَوَابَ قَوۡمِهِۦٓ إِلَّآ أَن قَالُواْ ٱقۡتُلُوهُ أَوۡ حَرِّقُوهُ فَأَنجَىٰهُ ٱللَّهُ مِنَ ٱلنَّارِۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَأٓيَٰتٖ لِّقَوۡمٖ يُؤۡمِنُونَ

Fama kana jawaba qawmihi illa an qaloo oqtuloohu aw harriqoohu faanjahu Allahu mina alnnari inna fee thalika laayatin liqawmin yuminoona

Tontul aw nitam doonul woon lu dul ñuy wax naan : “reyleen ko mbaa ngeen lakk ko”. Yàlla musal na ko ca safara sa. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñu gëm.

25

وَقَالَ إِنَّمَا ٱتَّخَذۡتُم مِّن دُونِ ٱللَّهِ أَوۡثَٰنٗا مَّوَدَّةَ بَيۡنِكُمۡ فِي ٱلۡحَيَوٰةِ ٱلدُّنۡيَاۖ ثُمَّ يَوۡمَ ٱلۡقِيَٰمَةِ يَكۡفُرُ بَعۡضُكُم بِبَعۡضٖ وَيَلۡعَنُ بَعۡضُكُم بَعۡضٗا وَمَأۡوَىٰكُمُ ٱلنَّارُ وَمَا لَكُم مِّن نَّـٰصِرِينَ

Waqala innama ittakhathtum min dooni Allahi awthanan mawaddata baynikum fee alhayati alddunya thumma yawma alqiyamati yakfuru baAAdukum bibaAAdin wayalAAanu baAAdukum baAAdan wamawakumu alnnaru wama lakum min nasireena

[Ibraahiima] wax na ne : “Yéen a ngi jàpp xërëm yi bàyyi Yàlla ngir dëgëral seenug cofeel seen diggante fii ci dundug àddina. Waaye bu Bis-pénc baa, dangeen weddiwante, rëbbante te Safara mooy doon seen kër, te it dungeen fa am ndimbal.

26

۞فَـَٔامَنَ لَهُۥ لُوطٞۘ وَقَالَ إِنِّي مُهَاجِرٌ إِلَىٰ رَبِّيٓۖ إِنَّهُۥ هُوَ ٱلۡعَزِيزُ ٱلۡحَكِيمُ

Faamana lahu lootun waqala innee muhajirun ila rabbee innahu huwa alAAazeezu alhakeemu

Lóot daldi koy gëm. Wax ne : “Maa ngi gàddaay jëm ci sama Boroom, Mooy boroom Kàttan, di Ku Xereñ”.(r)

27

وَوَهَبۡنَا لَهُۥٓ إِسۡحَٰقَ وَيَعۡقُوبَ وَجَعَلۡنَا فِي ذُرِّيَّتِهِ ٱلنُّبُوَّةَ وَٱلۡكِتَٰبَ وَءَاتَيۡنَٰهُ أَجۡرَهُۥ فِي ٱلدُّنۡيَاۖ وَإِنَّهُۥ فِي ٱلۡأٓخِرَةِ لَمِنَ ٱلصَّـٰلِحِينَ

Wawahabna lahu ishaqa wayaAAqooba wajaAAalna fee thurriyyatihi alnnubuwwata waalkitaba waataynahu ajrahu fee alddunya wainnahu fee alakhirati lamina alssaliheena

May na ko Isaaqa ak Yanqooba, defaloon Nanu ko ca sëtam ya ag Yonent ak Téere ba. Te indil Nanu ko ag peyam ci àddina, te it bu àllaaxiraa, ca nit ñu yiw ña lay bokk.

28

وَلُوطًا إِذۡ قَالَ لِقَوۡمِهِۦٓ إِنَّكُمۡ لَتَأۡتُونَ ٱلۡفَٰحِشَةَ مَا سَبَقَكُم بِهَا مِنۡ أَحَدٖ مِّنَ ٱلۡعَٰلَمِينَ

Walootan ith qala liqawmihi innakum latatoona alfahishata ma sabaqakum biha min ahadin mina alAAalameena

[Fàttalikul] Lóot, ba mu waxee aw nitam, ne leen : “Yéen a ngi def u ñaawteef [ngóor- jigéen], te ci àddina, kenn jëkkewuleen ko ci.

29

أَئِنَّكُمۡ لَتَأۡتُونَ ٱلرِّجَالَ وَتَقۡطَعُونَ ٱلسَّبِيلَ وَتَأۡتُونَ فِي نَادِيكُمُ ٱلۡمُنكَرَۖ فَمَا كَانَ جَوَابَ قَوۡمِهِۦٓ إِلَّآ أَن قَالُواْ ٱئۡتِنَا بِعَذَابِ ٱللَّهِ إِن كُنتَ مِنَ ٱلصَّـٰدِقِينَ

Ainnakum latatoona alrrijala wataqtaAAoona alssabeela watatoona fee nadeekumu almunkara fama kana jawaba qawmihi illa an qaloo itina biAAathabi Allahi in kunta mina alssadiqeena

Moo ndax yéen, dangeen di sëyanti ci góor ñi ? Di dogale yoon yi ? Ngeen di def njekkar ci seeni mbootaay ?”. [Waaye] nitam ña tontuwuñu ko lenn lu dul ne ko : “Indil nu mbugalum Yàlla ndegam wax nga dëgg”.

30

قَالَ رَبِّ ٱنصُرۡنِي عَلَى ٱلۡقَوۡمِ ٱلۡمُفۡسِدِينَ

Qala rabbi onsurnee AAala alqawmi almufsideena

Mu wax ne : “Yaw sama Boroom, may ma ndam ci kaw nit ñii di ay tooñkat !”

31

وَلَمَّا جَآءَتۡ رُسُلُنَآ إِبۡرَٰهِيمَ بِٱلۡبُشۡرَىٰ قَالُوٓاْ إِنَّا مُهۡلِكُوٓاْ أَهۡلِ هَٰذِهِ ٱلۡقَرۡيَةِۖ إِنَّ أَهۡلَهَا كَانُواْ ظَٰلِمِينَ

Walamma jaat rusuluna ibraheema bialbushra qaloo inna muhlikoo ahli hathihi alqaryati inna ahlaha kanoo thalimeena

Ba Sunuy Malaaka dikkalee Ibraahiima ak xibaari mbégte, ne ko : “Danuy faagaagale waa dëkk bii ndax ña fa dëkk ay tooñkat lañu”.

32

قَالَ إِنَّ فِيهَا لُوطٗاۚ قَالُواْ نَحۡنُ أَعۡلَمُ بِمَن فِيهَاۖ لَنُنَجِّيَنَّهُۥ وَأَهۡلَهُۥٓ إِلَّا ٱمۡرَأَتَهُۥ كَانَتۡ مِنَ ٱلۡغَٰبِرِينَ

Qala inna feeha lootan qaloo nahnu aAAlamu biman feeha lanunajjiyannahu waahlahu illa imraatahu kanat mina alghabireena

Ibraahiima ne leen : “Waaye Lóot ma nga fa !”. Ñu tontu ko ne ko : “Noo gën a xam ña fa nekk : Dananu musal [moom Lóot] mook njabootam, ba mu des soxnaam, moom day bokk ca ña alku”.

33

وَلَمَّآ أَن جَآءَتۡ رُسُلُنَا لُوطٗا سِيٓءَ بِهِمۡ وَضَاقَ بِهِمۡ ذَرۡعٗاۖ وَقَالُواْ لَا تَخَفۡ وَلَا تَحۡزَنۡ إِنَّا مُنَجُّوكَ وَأَهۡلَكَ إِلَّا ٱمۡرَأَتَكَ كَانَتۡ مِنَ ٱلۡغَٰبِرِينَ

Walamma an jaat rusuluna lootan seea bihim wadaqa bihim tharAAan waqaloo la takhaf wala tahzan inna munajjooka waahlaka illa imraataka kanat mina alghabireena

ba Sunu ndawi Malaaka yi agsee ci Lóot, ñaawalees na jëme ci ñoom, mu tiit ci seeni mbir. Ñu ne ko : “Bul tiit, bul ragal... Dananu la musal yaak sa njaboot, ba mu des sa jabar, dafay alku.

34

إِنَّا مُنزِلُونَ عَلَىٰٓ أَهۡلِ هَٰذِهِ ٱلۡقَرۡيَةِ رِجۡزٗا مِّنَ ٱلسَّمَآءِ بِمَا كَانُواْ يَفۡسُقُونَ

Inna munziloona AAala ahli hathihi alqaryati rijzan mina alssamai bima kanoo yafsuqoona

Wàcce Nanu ci kaw waa dëkk bi mbugal mu bawoo asamaan ngir seen caay-caay ga”.

35

وَلَقَد تَّرَكۡنَا مِنۡهَآ ءَايَةَۢ بَيِّنَةٗ لِّقَوۡمٖ يَعۡقِلُونَ

Walaqad tarakna minha ayatan bayyinatan liqawmin yaAAqiloona

Bàyyi Nanu fa lu bokk ca ñoom muy kéemaan gu leer nàññ ngir aw nit ñuy xel-lu.

36

وَإِلَىٰ مَدۡيَنَ أَخَاهُمۡ شُعَيۡبٗا فَقَالَ يَٰقَوۡمِ ٱعۡبُدُواْ ٱللَّهَ وَٱرۡجُواْ ٱلۡيَوۡمَ ٱلۡأٓخِرَ وَلَا تَعۡثَوۡاْ فِي ٱلۡأَرۡضِ مُفۡسِدِينَ

Waila madyana akhahum shuAAayban faqala ya qawmi oAAbudoo Allaha waorjoo alyawma alakhira wala taAAthaw fee alardi mufsideena

[Naka noonu], la seen mbokk Chuhaybu demee woon Madyaana, ne leen : “Éy yéen samaw nit, jaamuleen Yàlla te gëm Bis-pénc ba, te buleen dox di yàq ci kaw suuf si”.(s)

37

فَكَذَّبُوهُ فَأَخَذَتۡهُمُ ٱلرَّجۡفَةُ فَأَصۡبَحُواْ فِي دَارِهِمۡ جَٰثِمِينَ

Fakaththaboohu faakhathathumu alrrajfatu faasbahoo fee darihim jathimeena

Ñu weddi ko. Yëngu-yëngu ba fab leen, ñu xëy ne lànjax ci seen kër.

38

وَعَادٗا وَثَمُودَاْ وَقَد تَّبَيَّنَ لَكُم مِّن مَّسَٰكِنِهِمۡۖ وَزَيَّنَ لَهُمُ ٱلشَّيۡطَٰنُ أَعۡمَٰلَهُمۡ فَصَدَّهُمۡ عَنِ ٱلسَّبِيلِ وَكَانُواْ مُسۡتَبۡصِرِينَ

WaAAadan wathamooda waqad tabayyana lakum min masakinihim wazayyana lahumu alshshaytanu aAAmalahum fasaddahum AAani alssabeeli wakanoo mustabsireena

Ak waa Haad ak Samuuda. - Noona lañu leen faagaagale - mu leer nàññ, ngeen di ko gis ci seen gént ya. Séytaanee leen taaralaloon seeni jëf, férëwle leen ; daawuñu jéem a gis lu baax.

39

وَقَٰرُونَ وَفِرۡعَوۡنَ وَهَٰمَٰنَۖ وَلَقَدۡ جَآءَهُم مُّوسَىٰ بِٱلۡبَيِّنَٰتِ فَٱسۡتَكۡبَرُواْ فِي ٱلۡأَرۡضِ وَمَا كَانُواْ سَٰبِقِينَ

Waqaroona wafirAAawna wahamana walaqad jaahum moosa bialbayyinati faistakbaroo fee alardi wama kanoo sabiqeena

Te kat [faagaagal Nanu] Xaaruuna ak Firawna ak Haamaan. Muusaa indiloon na leen Sunuy firnde, ñuy rëy-rëylu ci kaw suuf si. Waante mënuñu Nu woon a raw de.

40

فَكُلًّا أَخَذۡنَا بِذَنۢبِهِۦۖ فَمِنۡهُم مَّنۡ أَرۡسَلۡنَا عَلَيۡهِ حَاصِبٗا وَمِنۡهُم مَّنۡ أَخَذَتۡهُ ٱلصَّيۡحَةُ وَمِنۡهُم مَّنۡ خَسَفۡنَا بِهِ ٱلۡأَرۡضَ وَمِنۡهُم مَّنۡ أَغۡرَقۡنَاۚ وَمَا كَانَ ٱللَّهُ لِيَظۡلِمَهُمۡ وَلَٰكِن كَانُوٓاْ أَنفُسَهُمۡ يَظۡلِمُونَ

Fakullan akhathna bithanbihi faminhum man arsalna AAalayhi hasiban waminhum man akhathathu alssayhatu waminhum man khasafna bihi alarda waminhum man aghraqna wama kana Allahu liyathlimahum walakin kanoo anfusahum yathlimoona

Kenn ci ñoom [faagaagale Nanu ko] kem [tolluwaayu] bàkkaaram : Am na ci ñoom ñu Nu yóonni am mbënn ci ñoom ; am na ci ñoom ñu ag xaacu jël na leen ; am na ci ñoom ñu Nu mëdd ci biir suuf si ; am na ci ñoom ñu Nu labal. Yàlla tooñuleen ; waaye ñoo tooñ seen bopp.

41

مَثَلُ ٱلَّذِينَ ٱتَّخَذُواْ مِن دُونِ ٱللَّهِ أَوۡلِيَآءَ كَمَثَلِ ٱلۡعَنكَبُوتِ ٱتَّخَذَتۡ بَيۡتٗاۖ وَإِنَّ أَوۡهَنَ ٱلۡبُيُوتِ لَبَيۡتُ ٱلۡعَنكَبُوتِۚ لَوۡ كَانُواْ يَعۡلَمُونَ

Mathalu allatheena ittakhathoo min dooni Allahi awliyaa kamathali alAAankabooti ittakhathat baytan wainna awhana albuyooti labaytu alAAankabooti law kanoo yaAAlamoona

Gam-gamleek ñay wut wéeruwaay bàyyi Yàlla, mi ngi mel ni jargoñ buy lëndub néeg. Te néeg bi gën a doyadi moo di néegu jargoñ. Cëy bu ñu xamoon !

42

إِنَّ ٱللَّهَ يَعۡلَمُ مَا يَدۡعُونَ مِن دُونِهِۦ مِن شَيۡءٖۚ وَهُوَ ٱلۡعَزِيزُ ٱلۡحَكِيمُ

Inna Allaha yaAAlamu ma yadAAoona min doonihi min shayin wahuwa alAAazeezu alhakeemu

Yàlla xam na mboolem yu ñuy tës-tësi di ko jaamu, Moom ñu ne ko ñukk fale. Te Moom Yàlla moo di Boroom Kàttan, di Ku Xereñ.

43

وَتِلۡكَ ٱلۡأَمۡثَٰلُ نَضۡرِبُهَا لِلنَّاسِۖ وَمَا يَعۡقِلُهَآ إِلَّا ٱلۡعَٰلِمُونَ

Watilka alamthalu nadribuha lilnnasi wama yaAAqiluha illa alAAalimoona

Léebu yooyee ñuy sadd nit ñi ; te ñi xam ñoo cay xalaat. .

44

خَلَقَ ٱللَّهُ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضَ بِٱلۡحَقِّۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَأٓيَةٗ لِّلۡمُؤۡمِنِينَ

Khalaqa Allahu alssamawati waalarda bialhaqqi inna fee thalika laayatan lilmumineena

Moo bind [sàkk] asamaan yeek suuf si ci dëgg. Te ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñu gëm.

45

ٱتۡلُ مَآ أُوحِيَ إِلَيۡكَ مِنَ ٱلۡكِتَٰبِ وَأَقِمِ ٱلصَّلَوٰةَۖ إِنَّ ٱلصَّلَوٰةَ تَنۡهَىٰ عَنِ ٱلۡفَحۡشَآءِ وَٱلۡمُنكَرِۗ وَلَذِكۡرُ ٱللَّهِ أَكۡبَرُۗ وَٱللَّهُ يَعۡلَمُ مَا تَصۡنَعُونَ

Otlu ma oohiya ilayka mina alkitabi waaqimi alssalata inna alssalata tanha AAani alfahshai waalmunkari walathikru Allahi akbaru waAllahu yaAAlamu ma tasnaAAoona

Nettalil li Nu soloo ca Téere ba te ngay taxawal julli. Ca dëgg-dëgg, julli daal dafay faat ñaawtéef ak njekkar. [Xamal ne] tudd Yàlla te di Ko fàttaliku moo gënatee rëy. Yàllaa ka xam li ngeen di def.

46

۞وَلَا تُجَٰدِلُوٓاْ أَهۡلَ ٱلۡكِتَٰبِ إِلَّا بِٱلَّتِي هِيَ أَحۡسَنُ إِلَّا ٱلَّذِينَ ظَلَمُواْ مِنۡهُمۡۖ وَقُولُوٓاْ ءَامَنَّا بِٱلَّذِيٓ أُنزِلَ إِلَيۡنَا وَأُنزِلَ إِلَيۡكُمۡ وَإِلَٰهُنَا وَإِلَٰهُكُمۡ وَٰحِدٞ وَنَحۡنُ لَهُۥ مُسۡلِمُونَ

Wala tujadiloo ahla alkitabi illa biallatee hiya ahsanu illa allatheena thalamoo minhum waqooloo amanna biallathee onzila ilayna waonzila ilaykum wailahuna wailahukum wahidun wanahnu lahu muslimoona

Buleen dàggasante ak ñoñ-téere yi lu dul ca na mu gën a rafetee te buleen ca boole ña yiwadi ca ñoom. Nangeen di wax ne : “Nun gëm nanu li ñu wàcci ci nun ak li ñu wàcce ci yéen, sunu Yàlla ak seen Yàlla jenn la, te nun jébbale nanu sunu bopp di ay jullit”.(h)

47

وَكَذَٰلِكَ أَنزَلۡنَآ إِلَيۡكَ ٱلۡكِتَٰبَۚ فَٱلَّذِينَ ءَاتَيۡنَٰهُمُ ٱلۡكِتَٰبَ يُؤۡمِنُونَ بِهِۦۖ وَمِنۡ هَـٰٓؤُلَآءِ مَن يُؤۡمِنُ بِهِۦۚ وَمَا يَجۡحَدُ بِـَٔايَٰتِنَآ إِلَّا ٱلۡكَٰفِرُونَ

Wakathalika anzalna ilayka alkitaba faallatheena ataynahumu alkitaba yuminoona bihi wamin haolai man yuminu bihi wama yajhadu biayatina illa alkafiroona

Noonu Lanu wàccee Téere bii di [Alxuraan] ci yaw [Muhammad]. Ña nga xam ne joxoon nañu leen Téere, gëmoon nañu ko. Am na ci ñoom ñu ko gëm [Alxuraan]. Yéefar yi doŋŋ ñoo weddi Sunuy kàddu.

48

وَمَا كُنتَ تَتۡلُواْ مِن قَبۡلِهِۦ مِن كِتَٰبٖ وَلَا تَخُطُّهُۥ بِيَمِينِكَۖ إِذٗا لَّٱرۡتَابَ ٱلۡمُبۡطِلُونَ

Wama kunta tatloo min qablihi min kitabin wala takhuttuhu biyameenika ithan lairtaba almubtiloona

Yaw [Muhammad], li jiitu wàccug [Téere bii di Alxuraan], musuloo jàng ab téere, musoo koo binde loxob ndeyjoor. [Su fekkoon ne loolu am na], kon weddikat ya danañu mën a sikki- sàkka.

49

بَلۡ هُوَ ءَايَٰتُۢ بَيِّنَٰتٞ فِي صُدُورِ ٱلَّذِينَ أُوتُواْ ٱلۡعِلۡمَۚ وَمَا يَجۡحَدُ بِـَٔايَٰتِنَآ إِلَّا ٱلظَّـٰلِمُونَ

Bal huwa ayatun bayyinatun fee sudoori allatheena ootoo alAAilma wama yajhadu biayatina illa alththalimoona

Li wér te wóor moo di ne, [Alxuraan] ay laaya la yu ñu faramfàcce ci biir dënni woroom xam-xam yi. Te tooñkat yi rekk ñoo koy weddi.

50

وَقَالُواْ لَوۡلَآ أُنزِلَ عَلَيۡهِ ءَايَٰتٞ مِّن رَّبِّهِۦۚ قُلۡ إِنَّمَا ٱلۡأٓيَٰتُ عِندَ ٱللَّهِ وَإِنَّمَآ أَنَا۠ نَذِيرٞ مُّبِينٌ

Waqaloo lawla onzila AAalayhi ayatun min rabbihi qul innama alayatu AAinda Allahi wainnama ana natheerun mubeenun

Ñuy wax naan : “Lu tax Yàlla wàccewul ci moom kéemaan ?”. Waxal ne : “Kéemaan a nga ca Yàlla. Man, ab xuppekat buy leeral rekk laa”.

51

أَوَلَمۡ يَكۡفِهِمۡ أَنَّآ أَنزَلۡنَا عَلَيۡكَ ٱلۡكِتَٰبَ يُتۡلَىٰ عَلَيۡهِمۡۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَرَحۡمَةٗ وَذِكۡرَىٰ لِقَوۡمٖ يُؤۡمِنُونَ

Awalam yakfihim anna anzalna AAalayka alkitaba yutla AAalayhim inna fee thalika larahmatan wathikra liqawmin yuminoona

Ndax doyuleen ñoom, wàcce gii Nu wàcce ci yaw Téere bi, Nu di leen ko dégtal ? Yërmaande ak fàttalikoo nga ca biir lool ngir aw nit ñu gëm.

52

قُلۡ كَفَىٰ بِٱللَّهِ بَيۡنِي وَبَيۡنَكُمۡ شَهِيدٗاۖ يَعۡلَمُ مَا فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِۗ وَٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ بِٱلۡبَٰطِلِ وَكَفَرُواْ بِٱللَّهِ أُوْلَـٰٓئِكَ هُمُ ٱلۡخَٰسِرُونَ

Qul kafa biAllahi baynee wabaynakum shaheedan yaAAlamu ma fee alssamawati waalardi waallatheena amanoo bialbatili wakafaroo biAllahi olaika humu alkhasiroona

Waxal ne : “Yàlla doy na seede sama digganteek yéen”. Xam na li nekk ci asamaan yeek suuf si. Ña gëm neen, weddi Yàlla, ñoo yàqule.

53

وَيَسۡتَعۡجِلُونَكَ بِٱلۡعَذَابِ وَلَوۡلَآ أَجَلٞ مُّسَمّٗى لَّجَآءَهُمُ ٱلۡعَذَابُۚ وَلَيَأۡتِيَنَّهُم بَغۡتَةٗ وَهُمۡ لَا يَشۡعُرُونَ

WayastaAAjiloonaka bialAAathabi walawla ajalun musamman lajaahumu alAAathabu walayatiyannahum baghtatan wahum la yashAAuroona

Té ñanga lay laaj mbugal ma cig yàkkamti. Bu fekkoon ne du dig ba Nu leen àppal, kon ñëwoon na [bu yàgg]. Waaye mbugal ma dana ñëw ci ñoom, di mbetteel te duñu ko yég.

54

يَسۡتَعۡجِلُونَكَ بِٱلۡعَذَابِ وَإِنَّ جَهَنَّمَ لَمُحِيطَةُۢ بِٱلۡكَٰفِرِينَ

YastaAAjiloonaka bialAAathabi wainna jahannama lamuheetatun bialkafireena

Ña nga lay laaj mbugal ma cig yàkkamti, te fekk Safara waa ngay gaw yéefar ya.

55

يَوۡمَ يَغۡشَىٰهُمُ ٱلۡعَذَابُ مِن فَوۡقِهِمۡ وَمِن تَحۡتِ أَرۡجُلِهِمۡ وَيَقُولُ ذُوقُواْ مَا كُنتُمۡ تَعۡمَلُونَ

Yawma yaghshahumu alAAathabu min fawqihim wamin tahti arjulihim wayaqoolu thooqoo ma kuntum taAAmaloona

Bu keroogee ba mbugal ma muur leen ci seen kaw ak seen ndëgguy tànk. Mu di leen wax naan : “Mosleen, toqamtikuleen li ngeen daan def !”

56

يَٰعِبَادِيَ ٱلَّذِينَ ءَامَنُوٓاْ إِنَّ أَرۡضِي وَٰسِعَةٞ فَإِيَّـٰيَ فَٱعۡبُدُونِ

Ya AAibadiya allatheena amanoo inna ardee wasiAAatun faiyyaya faoAAbudooni

Éy yéen sama jaam ñi gëm ! Sama suuf si yaatu na [lool]. Waay-waay jaamuleen Ma !

57

كُلُّ نَفۡسٖ ذَآئِقَةُ ٱلۡمَوۡتِۖ ثُمَّ إِلَيۡنَا تُرۡجَعُونَ

Kullu nafsin thaiqatu almawti thumma ilayna turjaAAoona

Bakkan bu nekk dana mos dee. Te [ñéppay] dellusi ci Nun.

58

وَٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ وَعَمِلُواْ ٱلصَّـٰلِحَٰتِ لَنُبَوِّئَنَّهُم مِّنَ ٱلۡجَنَّةِ غُرَفٗا تَجۡرِي مِن تَحۡتِهَا ٱلۡأَنۡهَٰرُ خَٰلِدِينَ فِيهَاۚ نِعۡمَ أَجۡرُ ٱلۡعَٰمِلِينَ

Waallatheena amanoo waAAamiloo alssalihati lanubawwiannahum mina aljannati ghurafan tajree min tahtiha alanharu khalideena feeha niAAma ajru alAAamileena

Ña gëmoon tey jëf u yiw, Dananu leen dëkkal ay néeg yu kawe yoo xam ne ay dex ñooy daw ca suufam. Dañu fay béel, ndaw pey gu neex,

59

ٱلَّذِينَ صَبَرُواْ وَعَلَىٰ رَبِّهِمۡ يَتَوَكَّلُونَ

Allatheena sabaroo waAAala rabbihim yatawakkaloona

ña daan muñ te wéeru woon ca seen Boroom !

60

وَكَأَيِّن مِّن دَآبَّةٖ لَّا تَحۡمِلُ رِزۡقَهَا ٱللَّهُ يَرۡزُقُهَا وَإِيَّاكُمۡۚ وَهُوَ ٱلسَّمِيعُ ٱلۡعَلِيمُ

Wakaayyin min dabbatin la tahmilu rizqaha Allahu yarzuquha waiyyakum wahuwa alssameeAAu alAAaleemu

Amul jenn daaba ju warlul boppam wërsëg ! [Waaye] Yàlla moo koy wërsëgal ak yéen. Te Moo di Aji-dégg, di Ku xam.(s)

61

وَلَئِن سَأَلۡتَهُم مَّنۡ خَلَقَ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضَ وَسَخَّرَ ٱلشَّمۡسَ وَٱلۡقَمَرَ لَيَقُولُنَّ ٱللَّهُۖ فَأَنَّىٰ يُؤۡفَكُونَ

Walain saaltahum man khalaqa alssamawati waalarda wasakhkhara alshshamsa waalqamara layaqoolunna Allahu faanna yufakoona

Soo leen laajoon : “Ana kan moo bind asamaan yeek suuf si, tàggatal leen jant bi ak weer wi ?”, kon danañu tontu wax ne : “Yàllaa ko def ”. Waaw, kon ñoom naka lañuy dummóoyoo yoon wu jub wi ?

62

ٱللَّهُ يَبۡسُطُ ٱلرِّزۡقَ لِمَن يَشَآءُ مِنۡ عِبَادِهِۦ وَيَقۡدِرُ لَهُۥٓۚ إِنَّ ٱللَّهَ بِكُلِّ شَيۡءٍ عَلِيمٞ

Allahu yabsutu alrrizqa liman yashao min AAibadihi wayaqdiru lahu inna Allaha bikulli shayin AAaleemun

Yàlla mooy yaatalal wërsëgam ci ku ko soob ci jaamam ñi, Moo koy xatal itam. Yàlla xam na lépp lu ne.

63

وَلَئِن سَأَلۡتَهُم مَّن نَّزَّلَ مِنَ ٱلسَّمَآءِ مَآءٗ فَأَحۡيَا بِهِ ٱلۡأَرۡضَ مِنۢ بَعۡدِ مَوۡتِهَا لَيَقُولُنَّ ٱللَّهُۚ قُلِ ٱلۡحَمۡدُ لِلَّهِۚ بَلۡ أَكۡثَرُهُمۡ لَا يَعۡقِلُونَ

Walain saaltahum man nazzala mina alssamai maan faahya bihi alarda min baAAdi mawtiha layaqoolunna Allahu quli alhamdu lillahi bal aktharuhum la yaAAqiloona

Soo leen laajoon : “Ana kan moo leen wàccey ndox ci asamaan si, dundale ko suuf si ginnaaw bu dee woon [wow] ?”, kon danañu wax ne : “Yàllaa ko def ”. Neel : “Sant ñeel na Yàlla !”. Li ëpp ci ñoom duñu xalaat.

64

وَمَا هَٰذِهِ ٱلۡحَيَوٰةُ ٱلدُّنۡيَآ إِلَّا لَهۡوٞ وَلَعِبٞۚ وَإِنَّ ٱلدَّارَ ٱلۡأٓخِرَةَ لَهِيَ ٱلۡحَيَوَانُۚ لَوۡ كَانُواْ يَعۡلَمُونَ

Wama hathihi alhayatu alddunya illa lahwun walaAAibun wainna alddara alakhirata lahiya alhayawanu law kanoo yaAAlamoona

Dundu gi ci àddina sii doonul lu dul féexal xol ak po. Waaye kër gu mujj ga mooy dëgg- dëggi dundu. Cëy bu ngeen xamoo !

65

فَإِذَا رَكِبُواْ فِي ٱلۡفُلۡكِ دَعَوُاْ ٱللَّهَ مُخۡلِصِينَ لَهُ ٱلدِّينَ فَلَمَّا نَجَّىٰهُمۡ إِلَى ٱلۡبَرِّ إِذَا هُمۡ يُشۡرِكُونَ

Faitha rakiboo fee alfulki daAAawoo Allaha mukhliseena lahu alddeena falamma najjahum ila albarri itha hum yushrikoona

Saa yu ñu waree ci gaal, dañuy ñaan Yàlla di ko sellal. Waaye, saa su leen musalee ba wàcce leen ci jéeri ji, ndeke yoo ña ngay bokkaale.

66

لِيَكۡفُرُواْ بِمَآ ءَاتَيۡنَٰهُمۡ وَلِيَتَمَتَّعُواْۚ فَسَوۡفَ يَعۡلَمُونَ

Liyakfuroo bima ataynahum waliyatamattaAAoo fasawfa yaAAlamoona

Dañuy xebet la ñu leen di jox ak di bànneexu ! Danañu xala xam !

67

أَوَلَمۡ يَرَوۡاْ أَنَّا جَعَلۡنَا حَرَمًا ءَامِنٗا وَيُتَخَطَّفُ ٱلنَّاسُ مِنۡ حَوۡلِهِمۡۚ أَفَبِٱلۡبَٰطِلِ يُؤۡمِنُونَ وَبِنِعۡمَةِ ٱللَّهِ يَكۡفُرُونَ

Awalam yaraw anna jaAAalna haraman aminan wayutakhattafu alnnasu min hawlihim afabialbatili yuminoona wabiniAAmati Allahi yakfuroona

Xanaa dañoo gisul ne def Nanu [Màkka] muy barab bu ñu wormaal bu wóor, te nit ñi leen wër, dees na leen dax-daxee ? Moo ndax ñoom dañoo gëm ag neen tey weddi xéewali Yàlla yi ?

68

وَمَنۡ أَظۡلَمُ مِمَّنِ ٱفۡتَرَىٰ عَلَى ٱللَّهِ كَذِبًا أَوۡ كَذَّبَ بِٱلۡحَقِّ لَمَّا جَآءَهُۥٓۚ أَلَيۡسَ فِي جَهَنَّمَ مَثۡوٗى لِّلۡكَٰفِرِينَ

Waman athlamu mimmani iftara AAala Allahi kathiban aw kaththaba bialhaqqi lamma jaahu alaysa fee jahannama mathwan lilkafireena

Ana kan moo gën a tooñ kuy duural Yàlla ay fen, walla mu weddi dëgg ga koy dëggal ? Moo ndax ca biir Safara dëkkuwaayu yéefar yi dafaa amul ? [Axakañ]

69

وَٱلَّذِينَ جَٰهَدُواْ فِينَا لَنَهۡدِيَنَّهُمۡ سُبُلَنَاۚ وَإِنَّ ٱللَّهَ لَمَعَ ٱلۡمُحۡسِنِينَ

Waallatheena jahadoo feena lanahdiyannahum subulana wainna Allaha lamaAAa almuhsineena

Ñay xare di jànkuwante [samaw yoon], danañu leen gindi Sunuy yoon, te Yàlla ànd naak way-rafetal ña. Saar 30 : Rom (Waa Rom) 60 Laaya