← Suurat yépp
Suurat 3454 aaya

سبإ

Saba

Sheba

Tekki

Tann làkk

1

ٱلۡحَمۡدُ لِلَّهِ ٱلَّذِي لَهُۥ مَا فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَمَا فِي ٱلۡأَرۡضِ وَلَهُ ٱلۡحَمۡدُ فِي ٱلۡأٓخِرَةِۚ وَهُوَ ٱلۡحَكِيمُ ٱلۡخَبِيرُ

Alhamdu lillahi allathee lahu ma fee alssamawati wama fee alardi walahu alhamdu fee alakhirati wahuwa alhakeemu alkhabeeru

Cant ñeel na Yàlla, Yàlla mi moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Cant it ñeel na ko ca àllaaxira. Moo di Ku Xereñ, di Ku Xàmmee.(s)

2

يَعۡلَمُ مَا يَلِجُ فِي ٱلۡأَرۡضِ وَمَا يَخۡرُجُ مِنۡهَا وَمَا يَنزِلُ مِنَ ٱلسَّمَآءِ وَمَا يَعۡرُجُ فِيهَاۚ وَهُوَ ٱلرَّحِيمُ ٱلۡغَفُورُ

YaAAlamu ma yaliju fee alardi wama yakhruju minha wama yanzilu mina alssamai wama yaAAruju feeha wahuwa alrraheemu alghafooru

Xam na li duggu ci suuf ak la cay génne, ak lay wàcc ci asamaan si ak la cay yéeg. Mooy Jaglewaakoon ba, di Jéggalaakoon ba.

3

وَقَالَ ٱلَّذِينَ كَفَرُواْ لَا تَأۡتِينَا ٱلسَّاعَةُۖ قُلۡ بَلَىٰ وَرَبِّي لَتَأۡتِيَنَّكُمۡ عَٰلِمِ ٱلۡغَيۡبِۖ لَا يَعۡزُبُ عَنۡهُ مِثۡقَالُ ذَرَّةٖ فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَلَا فِي ٱلۡأَرۡضِ وَلَآ أَصۡغَرُ مِن ذَٰلِكَ وَلَآ أَكۡبَرُ إِلَّا فِي كِتَٰبٖ مُّبِينٖ

Waqala allatheena kafaroo la tateena alssaAAatu qul bala warabbee latatiyannakum AAalimi alghaybi la yaAAzubu AAanhu mithqalu tharratin fee alssamawati wala fee alardi wala asgharu min thalika wala akbaru illa fee kitabin mubeenin

Yéefar yaa ngay wax naan : “Bis-pénc ba du ñëw”. Waxal ne : “Axakañ. Giñ naa ci sama Boroom ! ne dana leen dikkal. Moom mi xam kumpa. Te dara lu tollu ni aw pepp du ko lënt ci asamaan yeek suuf si. Walla lu ko gën a tuuti, walla lu ko gën a rëy, lu dul ne mi ngi ci ab Téere bu bir.

4

لِّيَجۡزِيَ ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ وَعَمِلُواْ ٱلصَّـٰلِحَٰتِۚ أُوْلَـٰٓئِكَ لَهُم مَّغۡفِرَةٞ وَرِزۡقٞ كَرِيمٞ

Liyajziya allatheena amanoo waAAamiloo alssalihati olaika lahum maghfiratun warizqun kareemun

[Li waral Bis ba], ngir fey ña gëmoon tey jëf u yiw. Danañu am njéggal, ak teraanga ak i xéewal.

5

وَٱلَّذِينَ سَعَوۡ فِيٓ ءَايَٰتِنَا مُعَٰجِزِينَ أُوْلَـٰٓئِكَ لَهُمۡ عَذَابٞ مِّن رِّجۡزٍ أَلِيمٞ

Waallatheena saAAaw fee ayatina muAAajizeena olaika lahum AAathabun min rijzin aleemin

Ña doon dëgërante bopp te Sunuy laaya nag ñoom, danañu am mbugalum kaŋ-kaŋ mu metti.

6

وَيَرَى ٱلَّذِينَ أُوتُواْ ٱلۡعِلۡمَ ٱلَّذِيٓ أُنزِلَ إِلَيۡكَ مِن رَّبِّكَ هُوَ ٱلۡحَقَّ وَيَهۡدِيٓ إِلَىٰ صِرَٰطِ ٱلۡعَزِيزِ ٱلۡحَمِيدِ

Wayara allatheena ootoo alAAilma allathee onzila ilayka min rabbika huwa alhaqqa wayahdee ila sirati alAAazeezi alhameedi

Woroom xam-xam ya danañu gis ne li Nu wàcce ci yaw mu bawoo ca sa Boroom, mooy dëgg te dafay gindee jëme ca yoonu Yàlla wu jub wa xocc, Yàlla miy boroom kàttan, di Yayowaakoonu cant.

7

وَقَالَ ٱلَّذِينَ كَفَرُواْ هَلۡ نَدُلُّكُمۡ عَلَىٰ رَجُلٖ يُنَبِّئُكُمۡ إِذَا مُزِّقۡتُمۡ كُلَّ مُمَزَّقٍ إِنَّكُمۡ لَفِي خَلۡقٖ جَدِيدٍ

Waqala allatheena kafaroo hal nadullukum AAala rajulin yunabbiokum itha muzziqtum kulla mumazzaqin innakum lafee khalqin jadeedin

Ña weddee ngay wax naan : “Ndax dunu leen tegtal ci waa joo xam ne nee naay su ngeen deewee ba daggatoo, di ngeen dekkiwaat?

8

أَفۡتَرَىٰ عَلَى ٱللَّهِ كَذِبًا أَم بِهِۦ جِنَّةُۢۗ بَلِ ٱلَّذِينَ لَا يُؤۡمِنُونَ بِٱلۡأٓخِرَةِ فِي ٱلۡعَذَابِ وَٱلضَّلَٰلِ ٱلۡبَعِيدِ

Aftara AAala Allahi kathiban am bihi jinnatun bali allatheena la yuminoona bialakhirati fee alAAathabi waalddalali albaAAeedi

Moo ndax dafay sosal Yàlla ay fen ? Walla jinne dakoo sadd ?” La am kay moo di ña gëmul àllaaxira ñanga ca mbugal ak réer gu sori.

9

أَفَلَمۡ يَرَوۡاْ إِلَىٰ مَا بَيۡنَ أَيۡدِيهِمۡ وَمَا خَلۡفَهُم مِّنَ ٱلسَّمَآءِ وَٱلۡأَرۡضِۚ إِن نَّشَأۡ نَخۡسِفۡ بِهِمُ ٱلۡأَرۡضَ أَوۡ نُسۡقِطۡ عَلَيۡهِمۡ كِسَفٗا مِّنَ ٱلسَّمَآءِۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَأٓيَةٗ لِّكُلِّ عَبۡدٖ مُّنِيبٖ

Afalam yaraw ila ma bayna aydeehim wama khalfahum mina alssamai waalardi in nasha nakhsif bihimu alarda aw nusqit AAalayhim kisafan mina alssamai inna fee thalika laayatan likulli AAabdin muneebin

Ndax dañoo gisul li leen wër ci asamaan ak suuf ? Su Nu sooboon, mën Nanu leen a jaxaseek suuf si, walla Nu rotale ay dogit yu bawoo ci asamaan si. Ay kéemaan a ngi ci loolu ngir bépp jaam buy delluwaakoon ci Boroom bi .

10

۞وَلَقَدۡ ءَاتَيۡنَا دَاوُۥدَ مِنَّا فَضۡلٗاۖ يَٰجِبَالُ أَوِّبِي مَعَهُۥ وَٱلطَّيۡرَۖ وَأَلَنَّا لَهُ ٱلۡحَدِيدَ

Walaqad atayna dawooda minna fadlan ya jibalu awwibee maAAahu waalttayra waalanna lahu alhadeeda

Joxoon Nanu Daawuda ngëneel lu bawoo ci Nun. Doj yeek njanaaw yi ànd ak moom di sàbbaal. Te it nooyalaloon Nanu ko weñ gu ñuul.(r)

11

أَنِ ٱعۡمَلۡ سَٰبِغَٰتٖ وَقَدِّرۡ فِي ٱلسَّرۡدِۖ وَٱعۡمَلُواْ صَٰلِحًاۖ إِنِّي بِمَا تَعۡمَلُونَ بَصِيرٞ

Ani iAAmal sabighatin waqaddir fee alssardi waiAAmaloo salihan innee bima taAAmaloona baseerun

(ne ko) : “Liggéeyal ay mbubbi koŋ te jekkal ko”. Te ngeen di jëf u yiw. Kuy gis laa [Man Yàlla] li ngeen di def.

12

وَلِسُلَيۡمَٰنَ ٱلرِّيحَ غُدُوُّهَا شَهۡرٞ وَرَوَاحُهَا شَهۡرٞۖ وَأَسَلۡنَا لَهُۥ عَيۡنَ ٱلۡقِطۡرِۖ وَمِنَ ٱلۡجِنِّ مَن يَعۡمَلُ بَيۡنَ يَدَيۡهِ بِإِذۡنِ رَبِّهِۦۖ وَمَن يَزِغۡ مِنۡهُمۡ عَنۡ أَمۡرِنَا نُذِقۡهُ مِنۡ عَذَابِ ٱلسَّعِيرِ

Walisulaymana alrreeha ghuduwwuha shahrun warawahuha shahrun waasalna lahu AAayna alqitri wamina aljinni man yaAAmalu bayna yadayhi biithni rabbihi waman yazigh minhum AAan amrina nuthiqhu min AAathabi alssaAAeeri

Tàggataloon Nanu Suleymaan ngelaw li, am xëyëm doxub weer la woon, am ngontam it, doxub weer la woon. Nu nooyalaloon ko bëtub mbellum përëm. Amoon na ci jinne yi ñu koy liggéeyal ci ndigalul Yàlla. Ku ca fétt nag, Dananu ko mosal mbugalum safara.

13

يَعۡمَلُونَ لَهُۥ مَا يَشَآءُ مِن مَّحَٰرِيبَ وَتَمَٰثِيلَ وَجِفَانٖ كَٱلۡجَوَابِ وَقُدُورٖ رَّاسِيَٰتٍۚ ٱعۡمَلُوٓاْ ءَالَ دَاوُۥدَ شُكۡرٗاۚ وَقَلِيلٞ مِّنۡ عِبَادِيَ ٱلشَّكُورُ

YaAAmaloona lahu ma yashao min mahareeba watamatheela wajifanin kaaljawabi waqudoorin rasiyatin iAAmaloo ala dawooda shukran waqaleelun min AAibadiya alshshakooru

Ñu di ko liggéeyal lu ko soob : ci ay tabax ak i bóoli yu tollu ni ay xur, ak i kawdiir yu ñu sësale. “Yéen waa kër Daawuda, gërëmleen Yàlla”, te néewaana mu am ci sama jaam yi ay santkat.

14

فَلَمَّا قَضَيۡنَا عَلَيۡهِ ٱلۡمَوۡتَ مَا دَلَّهُمۡ عَلَىٰ مَوۡتِهِۦٓ إِلَّا دَآبَّةُ ٱلۡأَرۡضِ تَأۡكُلُ مِنسَأَتَهُۥۖ فَلَمَّا خَرَّ تَبَيَّنَتِ ٱلۡجِنُّ أَن لَّوۡ كَانُواْ يَعۡلَمُونَ ٱلۡغَيۡبَ مَا لَبِثُواْ فِي ٱلۡعَذَابِ ٱلۡمُهِينِ

Falamma qadayna AAalayhi almawta ma dallahum AAala mawtihi illa dabbatu alardi takulu minsaatahu falamma kharra tabayyanati aljinnu an law kanoo yaAAlamoona alghayba ma labithoo fee alAAathabi almuheeni

Ba Nu dogalee mu war a dee, la leen ko xamal moo di max ga lekk yetam wa. Ba mu daanoo, jinne yi daldi xam ne bu ñu xamoon kumpa, duñu sax ca mbugal moomee daan leen tax a doyadi.

15

لَقَدۡ كَانَ لِسَبَإٖ فِي مَسۡكَنِهِمۡ ءَايَةٞۖ جَنَّتَانِ عَن يَمِينٖ وَشِمَالٖۖ كُلُواْ مِن رِّزۡقِ رَبِّكُمۡ وَٱشۡكُرُواْ لَهُۥۚ بَلۡدَةٞ طَيِّبَةٞ وَرَبٌّ غَفُورٞ

Laqad kana lisabain fee maskanihim ayatun jannatani AAan yameenin washimalin kuloo min rizqi rabbikum waoshkuroo lahu baldatun tayyibatun warabbun ghafoorun

Waa réewum Saba amoon nañu màndargam ñaari dër ci ndeyjoor ak càmmooñ. “Lekkleen ci xéewali Yàlla, mayi seen Boroom, te ngeen sant Ko ndax : may na leen dëkk bu teey, neex, te di Boroom biy Jéggalaakoon”.

16

فَأَعۡرَضُواْ فَأَرۡسَلۡنَا عَلَيۡهِمۡ سَيۡلَ ٱلۡعَرِمِ وَبَدَّلۡنَٰهُم بِجَنَّتَيۡهِمۡ جَنَّتَيۡنِ ذَوَاتَيۡ أُكُلٍ خَمۡطٖ وَأَثۡلٖ وَشَيۡءٖ مِّن سِدۡرٖ قَلِيلٖ

FaaAAradoo faarsalna AAalayhim sayla alAAarimi wabaddalnahum bijannatayhim jannatayni thawatay okulin khamtin waathlin washayin min sidrin qaleelin

Waaye dummóoyu woon nañu . Nu daldi leen yebalal mbënnum téqum ndox ma, Nu daldi leen soppil seen tooli dër y, def leen ay tool yu am meññent mu sëcc ak i gargamboose ak i siddéem juy néewal.

17

ذَٰلِكَ جَزَيۡنَٰهُم بِمَا كَفَرُواْۖ وَهَلۡ نُجَٰزِيٓ إِلَّا ٱلۡكَفُورَ

Thalika jazaynahum bima kafaroo wahal nujazee illa alkafoora

Loolu la Nu leen feye woon ngir seenug weddi. Moo ndax Dananu ko feye keneen ku dul ñuy weddi ?

18

وَجَعَلۡنَا بَيۡنَهُمۡ وَبَيۡنَ ٱلۡقُرَى ٱلَّتِي بَٰرَكۡنَا فِيهَا قُرٗى ظَٰهِرَةٗ وَقَدَّرۡنَا فِيهَا ٱلسَّيۡرَۖ سِيرُواْ فِيهَا لَيَالِيَ وَأَيَّامًا ءَامِنِينَ

WajaAAalna baynahum wabayna alqura allatee barakna feeha quran thahiratan waqaddarna feeha alssayra seeroo feeha layaliya waayyaman amineena

Te defoon nanu seen digganteek yeneen dëkk ya barkeel, ay dëkk yu fés, te nattle woon Nanu seenug demlante. “Demlanteleen ci guddi mbaa bëccëg ci kóolute”.(s)

19

فَقَالُواْ رَبَّنَا بَٰعِدۡ بَيۡنَ أَسۡفَارِنَا وَظَلَمُوٓاْ أَنفُسَهُمۡ فَجَعَلۡنَٰهُمۡ أَحَادِيثَ وَمَزَّقۡنَٰهُمۡ كُلَّ مُمَزَّقٍۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَأٓيَٰتٖ لِّكُلِّ صَبَّارٖ شَكُورٖ

Faqaloo rabbana baAAid bayna asfarina wathalamoo anfusahum fajaAAalnahum ahadeetha wamazzaqnahum kulla mumazzaqin inna fee thalika laayatin likulli sabbarin shakoorin

Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, dandaleel sunuy diggantey dëkk”, daldi tooñ seen bopp. Ba mujj di ay waxtaan ndax téqale Nanu leen. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir bépp muñaakoon buy sant.

20

وَلَقَدۡ صَدَّقَ عَلَيۡهِمۡ إِبۡلِيسُ ظَنَّهُۥ فَٱتَّبَعُوهُ إِلَّا فَرِيقٗا مِّنَ ٱلۡمُؤۡمِنِينَ

Walaqad saddaqa AAalayhim ibleesu thannahu faittabaAAoohu illa fareeqan mina almumineena

Séytaane dëggalal na leen njortam. Ñoom ñépp daldi koy topp ba mu des ab kurél bu néew ca way-gëm ña.

21

وَمَا كَانَ لَهُۥ عَلَيۡهِم مِّن سُلۡطَٰنٍ إِلَّا لِنَعۡلَمَ مَن يُؤۡمِنُ بِٱلۡأٓخِرَةِ مِمَّنۡ هُوَ مِنۡهَا فِي شَكّٖۗ وَرَبُّكَ عَلَىٰ كُلِّ شَيۡءٍ حَفِيظٞ

Wama kana lahu AAalayhim min sultanin illa linaAAlama man yuminu bialakhirati mimman huwa minha fee shakkin warabbuka AAala kulli shayin hafeethun

Amul woon ci ñoom benn mën-mën lu dul ngir Nu xam ña ca gëm àllaaxira ak ña koy sikki-sàkka. Sa Boroom mooy wattu lépp lu ne.

22

قُلِ ٱدۡعُواْ ٱلَّذِينَ زَعَمۡتُم مِّن دُونِ ٱللَّهِ لَا يَمۡلِكُونَ مِثۡقَالَ ذَرَّةٖ فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَلَا فِي ٱلۡأَرۡضِ وَمَا لَهُمۡ فِيهِمَا مِن شِرۡكٖ وَمَا لَهُۥ مِنۡهُم مِّن ظَهِيرٖ

Quli odAAoo allatheena zaAAamtum min dooni Allahi la yamlikoona mithqala tharratin fee alssamawati wala fee alardi wama lahum feehima min shirkin wama lahu minhum min thaheerin

Waxal ne : “Li ngeen di jaamu bàyyi Yàlla. Amuñu lu tollu ni kem aw fepp ci asamaan yeek suuf si. Bokkuñu ci, ci dara, te it kenn dimbaliwu ko woon ci ñoom”.

23

وَلَا تَنفَعُ ٱلشَّفَٰعَةُ عِندَهُۥٓ إِلَّا لِمَنۡ أَذِنَ لَهُۥۚ حَتَّىٰٓ إِذَا فُزِّعَ عَن قُلُوبِهِمۡ قَالُواْ مَاذَا قَالَ رَبُّكُمۡۖ قَالُواْ ٱلۡحَقَّۖ وَهُوَ ٱلۡعَلِيُّ ٱلۡكَبِيرُ

Wala tanfaAAu alshshafaAAatu AAindahu illa liman athina lahu hatta itha fuzziAAa AAan quloobihim qaloo matha qala rabbukum qaloo alhaqqa wahuwa alAAaliyyu alkabeeru

Tinu mënu la jariñ dara fa Moom [Yàlla], lu dul ka Mu ca jox ndigal. Bu tiit ma duggee seeni xol nag, ñu naan : “Lan la seen Boroom wax nag ?”. Ñu ne leen : “Dëgg rekk ; Te Moom moo di Ku Kawe, di Ku Màgg ka”.

24

۞قُلۡ مَن يَرۡزُقُكُم مِّنَ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِۖ قُلِ ٱللَّهُۖ وَإِنَّآ أَوۡ إِيَّاكُمۡ لَعَلَىٰ هُدًى أَوۡ فِي ضَلَٰلٖ مُّبِينٖ

Qul man yarzuqukum mina alssamawati waalardi quli Allahu wainna aw iyyakum laAAala hudan aw fee dalalin mubeenin

Neel : “Ana kan moo leen di wërsëgal ci asamaan yeek suuf si ?”. Waxal ne : “Yàlla. Te Nun ak yéen, ana kan moo nekk ci njug walla réer gu bir”.(h)

25

قُل لَّا تُسۡـَٔلُونَ عَمَّآ أَجۡرَمۡنَا وَلَا نُسۡـَٔلُ عَمَّا تَعۡمَلُونَ

Qul la tusaloona AAamma ajramna wala nusalu AAamma taAAmaloona

Neel : “Kenn duleen laaj li nuy def, te it kenn dunu laaj li ngeen di def ”.

26

قُلۡ يَجۡمَعُ بَيۡنَنَا رَبُّنَا ثُمَّ يَفۡتَحُ بَيۡنَنَا بِٱلۡحَقِّ وَهُوَ ٱلۡفَتَّاحُ ٱلۡعَلِيمُ

Qul yajmaAAu baynana rabbuna thumma yaftahu baynana bialhaqqi wahuwa alfattahu alAAaleemu

Waxal ne : “Sunu Boroom dananu dajale, daldi Nuy àtte ci dëgg, Mooy ubbiwaakoon bu xam ba”.

27

قُلۡ أَرُونِيَ ٱلَّذِينَ أَلۡحَقۡتُم بِهِۦ شُرَكَآءَۖ كَلَّاۚ بَلۡ هُوَ ٱللَّهُ ٱلۡعَزِيزُ ٱلۡحَكِيمُ

Qul arooniya allatheena alhaqtum bihi shurakaa kalla bal huwa Allahu alAAazeezu alhakeemu

Waxal ne : “Wonleen ma ña ngeen daan bokkaaleek Yàlla. [Mukk] ! Li wér moo di ne Mooy Yàlla, di Boroom Kàttan, di Ku Xereñ”.

28

وَمَآ أَرۡسَلۡنَٰكَ إِلَّا كَآفَّةٗ لِّلنَّاسِ بَشِيرٗا وَنَذِيرٗا وَلَٰكِنَّ أَكۡثَرَ ٱلنَّاسِ لَا يَعۡلَمُونَ

Wama arsalnaka illa kaffatan lilnnasi basheeran wanatheeran walakinna akthara alnnasi la yaAAlamoona

Yónniwunu la [yaw Muhammad] lu dul nga daj képp nit ñi, di béglekat, di xuppekat. Waaye li ëpp ci nit ñi duñu xam.

29

وَيَقُولُونَ مَتَىٰ هَٰذَا ٱلۡوَعۡدُ إِن كُنتُمۡ صَٰدِقِينَ

Wayaqooloona mata hatha alwaAAdu in kuntum sadiqeena

Ñuy wax naan : “Dig ba kañ lay doon su fekkee ne li ngeen di wax dëgg la ?”.

30

قُل لَّكُم مِّيعَادُ يَوۡمٖ لَّا تَسۡتَـٔۡخِرُونَ عَنۡهُ سَاعَةٗ وَلَا تَسۡتَقۡدِمُونَ

Qul lakum meeAAadu yawmin la tastakhiroona AAanhu saAAatan wala tastaqdimoona

Waxal ne : “Am ngeen digub Bis boo xam ne dungeen ko jiitu, dungen ko yées !”.

31

وَقَالَ ٱلَّذِينَ كَفَرُواْ لَن نُّؤۡمِنَ بِهَٰذَا ٱلۡقُرۡءَانِ وَلَا بِٱلَّذِي بَيۡنَ يَدَيۡهِۗ وَلَوۡ تَرَىٰٓ إِذِ ٱلظَّـٰلِمُونَ مَوۡقُوفُونَ عِندَ رَبِّهِمۡ يَرۡجِعُ بَعۡضُهُمۡ إِلَىٰ بَعۡضٍ ٱلۡقَوۡلَ يَقُولُ ٱلَّذِينَ ٱسۡتُضۡعِفُواْ لِلَّذِينَ ٱسۡتَكۡبَرُواْ لَوۡلَآ أَنتُمۡ لَكُنَّا مُؤۡمِنِينَ

Waqala allatheena kafaroo lan numina bihatha alqurani wala biallathee bayna yadayhi walaw tara ithi alththalimoona mawqoofoona AAinda rabbihim yarjiAAu baAAduhum ila baAAdin alqawla yaqoolu allatheena istudAAifoo lillatheena istakbaroo lawla antum lakunna mumineena

Yéefar ya nee nañu : “Duñu gëm Alxuraan walla lu ko jiitu”. Cëy boo gisoon tooñkat ya bu keroogee ba ñu taxawal leen ci seen kanamu Boroom, nga gis leen ñuy wàqante ! Ña néewoon doole di wax kilifa ya, naan leen : “Bu dul kon ak yéen, ay jullit la nuy doon”.

32

قَالَ ٱلَّذِينَ ٱسۡتَكۡبَرُواْ لِلَّذِينَ ٱسۡتُضۡعِفُوٓاْ أَنَحۡنُ صَدَدۡنَٰكُمۡ عَنِ ٱلۡهُدَىٰ بَعۡدَ إِذۡ جَآءَكُمۖ بَلۡ كُنتُم مُّجۡرِمِينَ

Qala allatheena istakbaroo lillatheena istudAAifoo anahnu sadadnakum AAani alhuda baAAda ith jaakum bal kuntum mujrimeena

Ña ca doonoon kilifa wax ña ca néewoon doole, ne leen : “Ndax Nun noo leen féewale woon ak njub ga ca ba mu leen dikkalee ? Li wér kay mooy yéen ay tooñkat ngeen”.

33

وَقَالَ ٱلَّذِينَ ٱسۡتُضۡعِفُواْ لِلَّذِينَ ٱسۡتَكۡبَرُواْ بَلۡ مَكۡرُ ٱلَّيۡلِ وَٱلنَّهَارِ إِذۡ تَأۡمُرُونَنَآ أَن نَّكۡفُرَ بِٱللَّهِ وَنَجۡعَلَ لَهُۥٓ أَندَادٗاۚ وَأَسَرُّواْ ٱلنَّدَامَةَ لَمَّا رَأَوُاْ ٱلۡعَذَابَۚ وَجَعَلۡنَا ٱلۡأَغۡلَٰلَ فِيٓ أَعۡنَاقِ ٱلَّذِينَ كَفَرُواْۖ هَلۡ يُجۡزَوۡنَ إِلَّا مَا كَانُواْ يَعۡمَلُونَ

Waqala allatheena istudAAifoo lillatheena istakbaroo bal makru allayli waalnnahari ith tamuroonana an nakfura biAllahi wanajAAala lahu andadan waasarroo alnnadamata lamma raawoo alAAathaba wajaAAalna alaghlala fee aAAnaqi allatheena kafaroo hal yujzawna illa ma kanoo yaAAmaloona

Ña ca néewoon doole wax ña ca doonoon ay kilifa, ne leen : “Moom ngeen daan fexe guddi ak bëccëg, ndax yéen a nu daan digal nuy weddi Yàlla, di ko sàkkal ay bokkaale”. Daldi nañu rëccu ba ñu gisee mbugal ma. Nu daldi def ay jéng ca loosi ña weddi : moo ndax feyewuñu leen lu dul la ñu daan def ?”

34

وَمَآ أَرۡسَلۡنَا فِي قَرۡيَةٖ مِّن نَّذِيرٍ إِلَّا قَالَ مُتۡرَفُوهَآ إِنَّا بِمَآ أُرۡسِلۡتُم بِهِۦ كَٰفِرُونَ

Wama arsalna fee qaryatin min natheerin illa qala mutrafooha inna bima orsiltum bihi kafiroona

Amul benn dëkk bu Nu mës a yebal ab xuppekat lu dul ne kilifa ya dañuy wax naan : “Nun dey weddi nanu lii ñu leen yónni”.

35

وَقَالُواْ نَحۡنُ أَكۡثَرُ أَمۡوَٰلٗا وَأَوۡلَٰدٗا وَمَا نَحۡنُ بِمُعَذَّبِينَ

Waqaloo nahnu aktharu amwalan waawladan wama nahnu bimuAAaththabeena

Ñuy wax it naan : “Nun noo leen ëppale alal ak i doom te sax kenn dunu mbugal”.(s)

36

قُلۡ إِنَّ رَبِّي يَبۡسُطُ ٱلرِّزۡقَ لِمَن يَشَآءُ وَيَقۡدِرُ وَلَٰكِنَّ أَكۡثَرَ ٱلنَّاسِ لَا يَعۡلَمُونَ

Qul inna rabbee yabsutu alrrizqa liman yashao wayaqdiru walakinna akthara alnnasi la yaAAlamoona

Waxal ne : “Yàlla sama Boroom mooy yaatalal ku ko soob wërsëg, di ko xatal it. Waaye li ëpp ci nit ñi waxuñu”.

37

وَمَآ أَمۡوَٰلُكُمۡ وَلَآ أَوۡلَٰدُكُم بِٱلَّتِي تُقَرِّبُكُمۡ عِندَنَا زُلۡفَىٰٓ إِلَّا مَنۡ ءَامَنَ وَعَمِلَ صَٰلِحٗا فَأُوْلَـٰٓئِكَ لَهُمۡ جَزَآءُ ٱلضِّعۡفِ بِمَا عَمِلُواْ وَهُمۡ فِي ٱلۡغُرُفَٰتِ ءَامِنُونَ

Wama amwalukum wala awladukum biallatee tuqarribukum AAindana zulfa illa man amana waAAamila salihan faolaika lahum jazao alddiAAfi bima AAamiloo wahum fee alghurufati aminoona

Nekkul ne seeni alal walla seeni doom ñoo leen di tax a jegeñ Yàlla. Lu dul ña ca gëm tey jëf u yiw. Ñooñu danañu am pey gu ñu fulandi ci sababus la ñu daan jëf, te ñoom ña nga ne fayax ci ay kër yu kawe [ca Àjjana].

38

وَٱلَّذِينَ يَسۡعَوۡنَ فِيٓ ءَايَٰتِنَا مُعَٰجِزِينَ أُوْلَـٰٓئِكَ فِي ٱلۡعَذَابِ مُحۡضَرُونَ

Waallatheena yasAAawna fee ayatina muAAajizeena olaika fee alAAathabi muhdaroona

Waaye ña daan dox, di dëgërante bopp ak Sunuy kàddu, ñoom ña nga ne xeew ci biir mbugal ma.

39

قُلۡ إِنَّ رَبِّي يَبۡسُطُ ٱلرِّزۡقَ لِمَن يَشَآءُ مِنۡ عِبَادِهِۦ وَيَقۡدِرُ لَهُۥۚ وَمَآ أَنفَقۡتُم مِّن شَيۡءٖ فَهُوَ يُخۡلِفُهُۥۖ وَهُوَ خَيۡرُ ٱلرَّـٰزِقِينَ

Qul inna rabbee yabsutu alrrizqa liman yashao min AAibadihi wayaqdiru lahu wama anfaqtum min shayin fahuwa yukhlifuhu wahuwa khayru alrraziqeena

Waxal ne : “Yàlla sama Boroom mooy yaatalal ku ko soob wërsëgam ci jaamam yi, Moo koy xatal it. Lépp lu ngeen mën a joxe [ci alal], moom Yàlla moo koy wuutalaat, te Yàlla moo di ngën ji kuy wërsëgal”.

40

وَيَوۡمَ يَحۡشُرُهُمۡ جَمِيعٗا ثُمَّ يَقُولُ لِلۡمَلَـٰٓئِكَةِ أَهَـٰٓؤُلَآءِ إِيَّاكُمۡ كَانُواْ يَعۡبُدُونَ

Wayawma yahshuruhum jameeAAan thumma yaqoolu lilmalaikati ahaolai iyyakum kanoo yaAAbudoona

Bu keroogee Bis ba leen Yàlla di dajale mbooleseen. Ba noppi daldi wax Malaaka ya ne leen : “Moo ndax ñii yéen la ñu daan jaamu ?”.

41

قَالُواْ سُبۡحَٰنَكَ أَنتَ وَلِيُّنَا مِن دُونِهِمۖ بَلۡ كَانُواْ يَعۡبُدُونَ ٱلۡجِنَّۖ أَكۡثَرُهُم بِهِم مُّؤۡمِنُونَ

Qaloo subhanaka anta waliyyuna min doonihim bal kanoo yaAAbudoona aljinna aktharuhum bihim muminoona

Ñu ne : “Tudd nanu sag sell ! Yaw yaay sunu wéeruwaay, du ñoom. Li am moo di, ñoom jinne yi la ñu daan jaamu, li ëppoon ci ñoom jinne la ñu gëm.

42

فَٱلۡيَوۡمَ لَا يَمۡلِكُ بَعۡضُكُمۡ لِبَعۡضٖ نَّفۡعٗا وَلَا ضَرّٗا وَنَقُولُ لِلَّذِينَ ظَلَمُواْ ذُوقُواْ عَذَابَ ٱلنَّارِ ٱلَّتِي كُنتُم بِهَا تُكَذِّبُونَ

Faalyawma la yamliku baAAdukum libaAAdin nafAAan wala darran wanaqoolu lillatheena thalamoo thooqoo AAathaba alnnari allatee kuntum biha tukaththiboona

Tey jii nag, kenn ci ñoom ëmbalut moroomam lor mbaa njariñ, te Dananu wax ña daan tooñ ne leen: “Tokkamtikuleen mbugamal Safara sa ngeen doon weddi”.

43

وَإِذَا تُتۡلَىٰ عَلَيۡهِمۡ ءَايَٰتُنَا بَيِّنَٰتٖ قَالُواْ مَا هَٰذَآ إِلَّا رَجُلٞ يُرِيدُ أَن يَصُدَّكُمۡ عَمَّا كَانَ يَعۡبُدُ ءَابَآؤُكُمۡ وَقَالُواْ مَا هَٰذَآ إِلَّآ إِفۡكٞ مُّفۡتَرٗىۚ وَقَالَ ٱلَّذِينَ كَفَرُواْ لِلۡحَقِّ لَمَّا جَآءَهُمۡ إِنۡ هَٰذَآ إِلَّا سِحۡرٞ مُّبِينٞ

Waitha tutla AAalayhim ayatuna bayyinatin qaloo ma hatha illa rajulun yureedu an yasuddakum AAamma kana yaAAbudu abaokum waqaloo ma hatha illa ifkun muftaran waqala allatheena kafaroo lilhaqqi lamma jaahum in hatha illa sihrun mubeenun

Bu ñu mësaan a jàng ci ñoom laaya yu leer, dañu naan : “Waa jii daal nammul lu dul féewale leen ak li leen seeni baay daan jaamu”. Ñuy wax it naan : “Lii daal du dara lu dul ay fen yu ñu sos”. Ña weddi woon dëgg it ba mu leen dikkalee, ña nga naan : “Lii daal ag njibar doŋŋ la !”.

44

وَمَآ ءَاتَيۡنَٰهُم مِّن كُتُبٖ يَدۡرُسُونَهَاۖ وَمَآ أَرۡسَلۡنَآ إِلَيۡهِمۡ قَبۡلَكَ مِن نَّذِيرٖ

Wama ataynahum min kutubin yadrusoonaha wama arsalna ilayhim qablaka min natheerin

[Moonte] Joxuñuleen woon ay téere yu ñuy mën a jàng. Mësuñoo yónni it ca ñoom ab xuppekat bu la jiitu.

45

وَكَذَّبَ ٱلَّذِينَ مِن قَبۡلِهِمۡ وَمَا بَلَغُواْ مِعۡشَارَ مَآ ءَاتَيۡنَٰهُمۡ فَكَذَّبُواْ رُسُلِيۖ فَكَيۡفَ كَانَ نَكِيرِ

Wakaththaba allatheena min qablihim wama balaghoo miAAshara ma ataynahum fakaththaboo rusulee fakayfa kana nakeeri

Xeet ya jiitu woon waa Màkka weddi woon nañu Yonent ya. Te waa Màkka amuñu ca lu tollu ni fukkeelu la ñu joxoon ñooña [ci kàttan]. Ñoom it ne sunuy ndaw ay fenkat lañu. Kon naka la samab sànje di dem !

46

۞قُلۡ إِنَّمَآ أَعِظُكُم بِوَٰحِدَةٍۖ أَن تَقُومُواْ لِلَّهِ مَثۡنَىٰ وَفُرَٰدَىٰ ثُمَّ تَتَفَكَّرُواْۚ مَا بِصَاحِبِكُم مِّن جِنَّةٍۚ إِنۡ هُوَ إِلَّا نَذِيرٞ لَّكُم بَيۡنَ يَدَيۡ عَذَابٖ شَدِيدٖ

Qul innama aAAithukum biwahidatin an taqoomoo lillahi mathna wafurada thumma tatafakkaroo ma bisahibikum min jinnatin in huwa illa natheerun lakum bayna yaday AAathabin shadeedin

Waxal ne : “Maa ngi leen di waar ci lenn : nangeen taxaw ngir Yàlla, moo xam ngeen diy ñaar-ñaar walla ngeen di benn been, te ngeen xalaat. Seen àndandoo bii di Muhammad jinne sadd ko : moom doonul lu dul ab xuppekat bu ame mbugal mu nekk seen kanam”.(r)

47

قُلۡ مَا سَأَلۡتُكُم مِّنۡ أَجۡرٖ فَهُوَ لَكُمۡۖ إِنۡ أَجۡرِيَ إِلَّا عَلَى ٱللَّهِۖ وَهُوَ عَلَىٰ كُلِّ شَيۡءٖ شَهِيدٞ

Qul ma saaltukum min ajrin fahuwa lakum in ajriya illa AAala Allahi wahuwa AAala kulli shayin shaheedun

Neel : “Laajumaleen ci ag pey, yéen a ko moom. Samag pey, Yàllaa ko warlu. Moom seede la ci lépp lu nekk”.

48

قُلۡ إِنَّ رَبِّي يَقۡذِفُ بِٱلۡحَقِّ عَلَّـٰمُ ٱلۡغُيُوبِ

Qul inna rabbee yaqthifu bialhaqqi AAallamu alghuyoobi

Neel : “Neel Yàlla mooy badd ndawam ci dëgg. Mooy xamaakoonu mbóot ya”.

49

قُلۡ جَآءَ ٱلۡحَقُّ وَمَا يُبۡدِئُ ٱلۡبَٰطِلُ وَمَا يُعِيدُ

Qul jaa alhaqqu wama yubdio albatilu wama yuAAeedu

Waxal ne : “Dëgg [Lislaam] dikk na. Te ag neen [kéefar] du fi tàmbalee te du fi dellusi”.

50

قُلۡ إِن ضَلَلۡتُ فَإِنَّمَآ أَضِلُّ عَلَىٰ نَفۡسِيۖ وَإِنِ ٱهۡتَدَيۡتُ فَبِمَا يُوحِيٓ إِلَيَّ رَبِّيٓۚ إِنَّهُۥ سَمِيعٞ قَرِيبٞ

Qul in dalaltu fainnama adillu AAala nafsee waini ihtadaytu fabima yoohee ilayya rabbee innahu sameeAAun qareebun

Waxal ne : “Su ma réeree , sama bopp doŋŋ laay sànk ; su ma gindikoo it, ci sababus li ma Yàlla soloo lay ame, Moom Yàlla kuy Dégg, kuy Jigeñ la”.

51

وَلَوۡ تَرَىٰٓ إِذۡ فَزِعُواْ فَلَا فَوۡتَ وَأُخِذُواْ مِن مَّكَانٖ قَرِيبٖ

Walaw tara ith faziAAoo fala fawta waokhithoo min makanin qareebin

Cëy soo leen gisoon ba ñu jàqee, - kenn du raw, - dañu leen a ndar- kepp ci barab bu nekk !

52

وَقَالُوٓاْ ءَامَنَّا بِهِۦ وَأَنَّىٰ لَهُمُ ٱلتَّنَاوُشُ مِن مَّكَانِۭ بَعِيدٖ

Waqaloo amanna bihi waanna lahumu alttanawushu min makanin baAAeedin

Ñu neey : “Gëm nañu”, - Moo fu leen ngëm di bawoo ?

53

وَقَدۡ كَفَرُواْ بِهِۦ مِن قَبۡلُۖ وَيَقۡذِفُونَ بِٱلۡغَيۡبِ مِن مَّكَانِۭ بَعِيدٖ

Waqad kafaroo bihi min qablu wayaqthifoona bialghaybi min makanin baAAeedin

te fekkoon ñu weddi lu jiitu, di sànney kumpa ci barab bu sori !

54

وَحِيلَ بَيۡنَهُمۡ وَبَيۡنَ مَا يَشۡتَهُونَ كَمَا فُعِلَ بِأَشۡيَاعِهِم مِّن قَبۡلُۚ إِنَّهُمۡ كَانُواْ فِي شَكّٖ مُّرِيبِۭ

Waheela baynahum wabayna ma yashtahoona kama fuAAila biashyaAAihim min qablu innahum kanoo fee shakkin mureebin

Ñu gàllankoor seen digganteek la ñu doon wuneen [sopp], kem nañu ko defe woon ca ña leen jiitu, ña nga woon ci biir sikki-sàkka gu xóot. Saar 35 : Aji-sàkke ji 45 Laaya