حمٓ
Hameem
Haa, Miim.
Fussilat
Explained in Detail
Tekki
حمٓ
Hameem
Haa, Miim.
تَنزِيلٞ مِّنَ ٱلرَّحۡمَٰنِ ٱلرَّحِيمِ
Tanzeelun mina alrrahmani alrraheemi
[Ak solool] gu ñu wàcce mu bawoo ci Yëramaakoon bi , di Jaglewaakoon bi (yërmandéem).
كِتَٰبٞ فُصِّلَتۡ ءَايَٰتُهُۥ قُرۡءَانًا عَرَبِيّٗا لِّقَوۡمٖ يَعۡلَمُونَ
Kitabun fussilat ayatuhu quranan AAarabiyyan liqawmin yaAAlamoona
Ab Téere bu ñu faramfànce ay laayam muy Alxuraan di ko [jàng] ci làmmiñu araab ngir aw nit ñuy xam,
بَشِيرٗا وَنَذِيرٗا فَأَعۡرَضَ أَكۡثَرُهُمۡ فَهُمۡ لَا يَسۡمَعُونَ
Basheeran wanatheeran faaAArada aktharuhum fahum la yasmaAAoona
di bégle tey xuppe. Ña ëpp ci ñoom dañoo dumóoyu ; du ñu (ko) dégg.
وَقَالُواْ قُلُوبُنَا فِيٓ أَكِنَّةٖ مِّمَّا تَدۡعُونَآ إِلَيۡهِ وَفِيٓ ءَاذَانِنَا وَقۡرٞ وَمِنۢ بَيۡنِنَا وَبَيۡنِكَ حِجَابٞ فَٱعۡمَلۡ إِنَّنَا عَٰمِلُونَ
Waqaloo quloobuna fee akinnatin mimma tadAAoona ilayhi wafee athanina waqrun wamin baynina wabaynika hijabun faiAAmal innana AAamiloona
Ñuy wax naan : “Sunuy xol dañoo muuru ci li nga ñuy woo jëmële, sunuy nopp dañoo saañu. Sunu diggënteek yaw kiraay da cee nekk, Defal li ngay def (yaw caag) ; nun noo ngi def li nuy def ”.
قُلۡ إِنَّمَآ أَنَا۠ بَشَرٞ مِّثۡلُكُمۡ يُوحَىٰٓ إِلَيَّ أَنَّمَآ إِلَٰهُكُمۡ إِلَٰهٞ وَٰحِدٞ فَٱسۡتَقِيمُوٓاْ إِلَيۡهِ وَٱسۡتَغۡفِرُوهُۗ وَوَيۡلٞ لِّلۡمُشۡرِكِينَ
Qul innama ana basharun mithlukum yooha ilayya annama ilahukum ilahun wahidun faistaqeemoo ilayhi waistaghfiroohu wawaylun lilmushrikeena
Waxal ne : “Man nit laa ni yéen. dañu may soloo waaye seen Yàlla jenn Yàlla rekk la. Sàkkuleen tegu ca yoonam wu jub wa xocc te na ngeen sàkku njégël”. toskare ñeel na yéefar ya
ٱلَّذِينَ لَا يُؤۡتُونَ ٱلزَّكَوٰةَ وَهُم بِٱلۡأٓخِرَةِ هُمۡ كَٰفِرُونَ
Allatheena la yutoona alzzakata wahum bialakhirati hum kafiroona
ña dul génne asaka tey weddi (dikkug) Bis Pénc ba !
إِنَّ ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ وَعَمِلُواْ ٱلصَّـٰلِحَٰتِ لَهُمۡ أَجۡرٌ غَيۡرُ مَمۡنُونٖ
Inna allatheena amanoo waAAamiloo alssalihati lahum ajrun ghayru mamnoonin
Ñiy gëm tey jëfu yiw danañu am pey gu dootul dogamtal.
۞قُلۡ أَئِنَّكُمۡ لَتَكۡفُرُونَ بِٱلَّذِي خَلَقَ ٱلۡأَرۡضَ فِي يَوۡمَيۡنِ وَتَجۡعَلُونَ لَهُۥٓ أَندَادٗاۚ ذَٰلِكَ رَبُّ ٱلۡعَٰلَمِينَ
Qul ainnakum latakfuroona biallathee khalaqa alarda fee yawmayni watajAAaloona lahu andadan thalika rabbu alAAalameena
Waxal ne : “Ndax dangeen di weddi ki bind suuf si ci ñaari fan, ngeen di Ko sàkkal ay bokkaale ? Kooku moo di boroom àddina si,(n)
وَجَعَلَ فِيهَا رَوَٰسِيَ مِن فَوۡقِهَا وَبَٰرَكَ فِيهَا وَقَدَّرَ فِيهَآ أَقۡوَٰتَهَا فِيٓ أَرۡبَعَةِ أَيَّامٖ سَوَآءٗ لِّلسَّآئِلِينَ
WajaAAala feeha rawasiya min fawqiha wabaraka feeha waqaddara feeha aqwataha fee arbaAAati ayyamin sawaan lilssaileena
Moo poose ay tundi doj ci kawam, def ca barke, (sakkan) mu doxal ca lépp luy yombal luy tax a man a dund ci diirub ñeenti fan. [Mooy tontul] képp ku la koy laaj.
ثُمَّ ٱسۡتَوَىٰٓ إِلَى ٱلسَّمَآءِ وَهِيَ دُخَانٞ فَقَالَ لَهَا وَلِلۡأَرۡضِ ٱئۡتِيَا طَوۡعًا أَوۡ كَرۡهٗا قَالَتَآ أَتَيۡنَا طَآئِعِينَ
Thumma istawa ila alssamai wahiya dukhanun faqala laha walilardi itiya tawAAan aw karhan qalata atayna taiAAeena
Ba mu éggalee la yemoo ca asamaan muy Saxar mu daldi wax asamaan ak suuf moom Yàlla ne : “Dikkleen, ci bu leen neexee, walla bu leen naqaree”. Ñu tontu ko ne : “Dikk nanu ci sunu coobare”.
فَقَضَىٰهُنَّ سَبۡعَ سَمَٰوَاتٖ فِي يَوۡمَيۡنِ وَأَوۡحَىٰ فِي كُلِّ سَمَآءٍ أَمۡرَهَاۚ وَزَيَّنَّا ٱلسَّمَآءَ ٱلدُّنۡيَا بِمَصَٰبِيحَ وَحِفۡظٗاۚ ذَٰلِكَ تَقۡدِيرُ ٱلۡعَزِيزِ ٱلۡعَلِيمِ
Faqadahunna sabAAa samawatin fee yawmayni waawha fee kulli samain amraha wazayyanna alssamaa alddunya bimasabeeha wahifthan thalika taqdeeru alAAazeezi alAAaleemi
Dogal na ñay juróom-ñaari asamaan ci ñaari fan ci asamaan su ca nekk la muy liggéey. Te taaralal nanu asamaanu àddina si si gën a jige ak i làmp [biddiw] ak di ko sàmm. Loolu mooy Dogalub (Yàlla) kiy boroom Kàttan, di ku Xam.
فَإِنۡ أَعۡرَضُواْ فَقُلۡ أَنذَرۡتُكُمۡ صَٰعِقَةٗ مِّثۡلَ صَٰعِقَةِ عَادٖ وَثَمُودَ
Fain aAAradoo fuqul anthartukum saAAiqatan mithla saAAiqati AAadin wathamooda
Bu ñu dumóoyoo lànk, waxal ne ; “maa ngi leen di xupp ci ag dënnu dënnu gu melni ga daloon waa Aad ak Samuud”.
إِذۡ جَآءَتۡهُمُ ٱلرُّسُلُ مِنۢ بَيۡنِ أَيۡدِيهِمۡ وَمِنۡ خَلۡفِهِمۡ أَلَّا تَعۡبُدُوٓاْ إِلَّا ٱللَّهَۖ قَالُواْ لَوۡ شَآءَ رَبُّنَا لَأَنزَلَ مَلَـٰٓئِكَةٗ فَإِنَّا بِمَآ أُرۡسِلۡتُم بِهِۦ كَٰفِرُونَ
Ith jaathumu alrrusulu min bayni aydeehim wamin khalfihim alla taAAbudoo illa Allaha qaloo law shaa rabbuna laanzala malaikatan fainna bima orsiltum bihi kafiroona
Ba leen yonnenta ya digëlee, bawoo kanam ak ginnaaw, [daan leen digël]: “Ci nuy jaamu Yàlla (ba ña jaamu leneen)”, ñuy wax naan : “Bu neexoon Yàlla, Mu wàcce ay Malaaka. Te sax nun lii ñu leen yónni gëmuñu ko”.
فَأَمَّا عَادٞ فَٱسۡتَكۡبَرُواْ فِي ٱلۡأَرۡضِ بِغَيۡرِ ٱلۡحَقِّ وَقَالُواْ مَنۡ أَشَدُّ مِنَّا قُوَّةًۖ أَوَلَمۡ يَرَوۡاْ أَنَّ ٱللَّهَ ٱلَّذِي خَلَقَهُمۡ هُوَ أَشَدُّ مِنۡهُمۡ قُوَّةٗۖ وَكَانُواْ بِـَٔايَٰتِنَا يَجۡحَدُونَ
Faamma AAadun faistakbaroo fee alardi bighayri alhaqqi waqaloo man ashaddu minna quwwatan awalam yaraw anna Allaha allathee khalaqahum huwa ashaddu minhum quwwatan wakanoo biayatina yajhadoona
Waa Aad, rëy-rëylu ci suuf ci lu dul dëgg, daan wax naan : “Ana ku ñu ëpp doole ?” (Di damu) ! Daan féttéerlu ci sunuy laaya.
فَأَرۡسَلۡنَا عَلَيۡهِمۡ رِيحٗا صَرۡصَرٗا فِيٓ أَيَّامٖ نَّحِسَاتٖ لِّنُذِيقَهُمۡ عَذَابَ ٱلۡخِزۡيِ فِي ٱلۡحَيَوٰةِ ٱلدُّنۡيَاۖ وَلَعَذَابُ ٱلۡأٓخِرَةِ أَخۡزَىٰۖ وَهُمۡ لَا يُنصَرُونَ
Faarsalna AAalayhim reehan sarsaran fee ayyamin nahisatin linutheeqahum AAathaba alkhizyi fee alhayati alddunya walaAAathabu alakhirati akhza wahum la yunsaroona
Bayal nanu ca ñoom ngelawul callmeer lu sedd guy ay fan yu nduxum, ngir mosal leen mbugëlum toroxtaane ci dundug àddina sii. Te mbugëlum àllaaxiraa gën a man a toraxal te it kenn duleen fa dimbali. (s)
وَأَمَّا ثَمُودُ فَهَدَيۡنَٰهُمۡ فَٱسۡتَحَبُّواْ ٱلۡعَمَىٰ عَلَى ٱلۡهُدَىٰ فَأَخَذَتۡهُمۡ صَٰعِقَةُ ٱلۡعَذَابِ ٱلۡهُونِ بِمَا كَانُواْ يَكۡسِبُونَ
Waamma thamoodu fahadaynahum faistahabboo alAAama AAala alhuda faakhathathum saAAiqatu alAAathabi alhooni bima kanoo yaksiboona
Waa Samuud nag ñoom, gindi woon nanu leen ; waaye dañoo tànni ngumba bàyyi gindi ku (njub) dëng. Mbugalum doyadi fab leen muy peyug la ñu daan fàggu.
وَنَجَّيۡنَا ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ وَكَانُواْ يَتَّقُونَ
Wanajjayna allatheena amanoo wakanoo yattaqoona
Nu daldi musël ña gëmoon tey ragal Yàlla.
وَيَوۡمَ يُحۡشَرُ أَعۡدَآءُ ٱللَّهِ إِلَى ٱلنَّارِ فَهُمۡ يُوزَعُونَ
Wayawma yuhsharu aAAdao Allahi ila alnnari fahum yoozaAAoona
Bu keroogee bis ba ñuy pang (dajale) nooni yàlla ya... Jëme leen Safara di leen gur-gur.
حَتَّىٰٓ إِذَا مَا جَآءُوهَا شَهِدَ عَلَيۡهِمۡ سَمۡعُهُمۡ وَأَبۡصَٰرُهُمۡ وَجُلُودُهُم بِمَا كَانُواْ يَعۡمَلُونَ
Hatta itha ma jaooha shahida AAalayhim samAAuhum waabsaruhum wajulooduhum bima kanoo yaAAmaloona
Bu ñu nee jaas agsi ci Safara, seeni nopp, ak seeni gët at seeni yaram dañuy doon ay seede ci li ñu daan def.
وَقَالُواْ لِجُلُودِهِمۡ لِمَ شَهِدتُّمۡ عَلَيۡنَاۖ قَالُوٓاْ أَنطَقَنَا ٱللَّهُ ٱلَّذِيٓ أَنطَقَ كُلَّ شَيۡءٖۚ وَهُوَ خَلَقَكُمۡ أَوَّلَ مَرَّةٖ وَإِلَيۡهِ تُرۡجَعُونَ
Waqaloo lijuloodihim lima shahidtum AAalayna qaloo antaqana Allahu allathee antaqa kulla shayin wahuwa khalaqakum awwala marratin wailayhi turjaAAoona
Ñuy waxanteek seen deri yaram ya naan : “Ana lutax ngeen di seede ngir dugal nu ?” (Der ya) tontu naan : “Yàlla miy wax loo lu nekk, Moo nu wax loo. Te Moo leen sàkk cig njaalbéen te it ca Moom ngeen di dellu”.
وَمَا كُنتُمۡ تَسۡتَتِرُونَ أَن يَشۡهَدَ عَلَيۡكُمۡ سَمۡعُكُمۡ وَلَآ أَبۡصَٰرُكُمۡ وَلَا جُلُودُكُمۡ وَلَٰكِن ظَنَنتُمۡ أَنَّ ٱللَّهَ لَا يَعۡلَمُ كَثِيرٗا مِّمَّا تَعۡمَلُونَ
Wama kuntum tastatiroona an yashhada AAalaykum samAAukum wala absarukum wala juloodukum walakin thanantum anna Allaha la yaAAlamu katheeran mimma taAAmaloona
Te manuleen woon làqatu ba seeni nopp, ak seeni gët du caagéeni seen yaram (ñu seede dugël leen). Waaye dangeen defe woon ne Yàlla xamul lu bari ci li ngeen daa def.
وَذَٰلِكُمۡ ظَنُّكُمُ ٱلَّذِي ظَنَنتُم بِرَبِّكُمۡ أَرۡدَىٰكُمۡ فَأَصۡبَحۡتُم مِّنَ ٱلۡخَٰسِرِينَ
Wathalikum thannukumu allathee thanantum birabbikum ardakum faasbahtum mina alkhasireena
Loolu mooy seen njortu la ngeen jortoon ci Yàlla, moo leen faagaagal, ba ngeen xëy yàqule.
فَإِن يَصۡبِرُواْ فَٱلنَّارُ مَثۡوٗى لَّهُمۡۖ وَإِن يَسۡتَعۡتِبُواْ فَمَا هُم مِّنَ ٱلۡمُعۡتَبِينَ
Fain yasbiroo faalnnaru mathwan lahum wain yastaAAtiboo fama hum mina almuAAtabeena
Bu ñu xaaree, Safaraa di seen kër ; bu ñu sàkkoo njégël, kon duleen jégël.
۞وَقَيَّضۡنَا لَهُمۡ قُرَنَآءَ فَزَيَّنُواْ لَهُم مَّا بَيۡنَ أَيۡدِيهِمۡ وَمَا خَلۡفَهُمۡ وَحَقَّ عَلَيۡهِمُ ٱلۡقَوۡلُ فِيٓ أُمَمٖ قَدۡ خَلَتۡ مِن قَبۡلِهِم مِّنَ ٱلۡجِنِّ وَٱلۡإِنسِۖ إِنَّهُمۡ كَانُواْ خَٰسِرِينَ
Waqayyadna lahum quranaa fazayyanoo lahum ma bayna aydeehim wama khalfahum wahaqqa AAalayhimu alqawlu fee omamin qad khalat min qablihim mina aljinni waalinsi innahum kanoo khasireena
Boole Nanu leen ak ñu ñu lëkkëlool ñu taaralal leen la ca seen kanam ak sen ginnaaw (la ñuy jëf). Dogal ba dal ci seen kow, kem na mu ame woon ca xeet ya leen jiitu woon ci jinne yi ak nit ñi. Ñoom dañoo yàqule !(r)
وَقَالَ ٱلَّذِينَ كَفَرُواْ لَا تَسۡمَعُواْ لِهَٰذَا ٱلۡقُرۡءَانِ وَٱلۡغَوۡاْ فِيهِ لَعَلَّكُمۡ تَغۡلِبُونَ
Waqala allatheena kafaroo la tasmaAAoo lihatha alqurani wailghaw feehi laAAallakum taghliboona
Ña weddi ngay wax naan : “Buleen déglu Alxuraan jii, te ngeen koy doyadil (di ko caaxaane) ndax amaana ngeen am ndam”.
فَلَنُذِيقَنَّ ٱلَّذِينَ كَفَرُواْ عَذَابٗا شَدِيدٗا وَلَنَجۡزِيَنَّهُمۡ أَسۡوَأَ ٱلَّذِي كَانُواْ يَعۡمَلُونَ
Falanutheeqanna allatheena kafaroo AAathaban shadeedan walanajziyannahum aswaa allathee kanoo yaAAmaloona
Dananu, mosal ña weddi mbugal mu tar te dananu leen faye la gën a ñaaw ca la ñu daan def.
ذَٰلِكَ جَزَآءُ أَعۡدَآءِ ٱللَّهِ ٱلنَّارُۖ لَهُمۡ فِيهَا دَارُ ٱلۡخُلۡدِ جَزَآءَۢ بِمَا كَانُواْ بِـَٔايَٰتِنَا يَجۡحَدُونَ
Thalika jazao aAAdai Allahi alnnaru lahum feeha daru alkhuldi jazaan bima kanoo biayatina yajhadoona
Loolu, mooy peyug noonu Yàlla Safara mudi seen kër ga ñuy dëkk béel ca, muy peyug weddi ga ñu daan weddi sunuy laaya.
وَقَالَ ٱلَّذِينَ كَفَرُواْ رَبَّنَآ أَرِنَا ٱلَّذَيۡنِ أَضَلَّانَا مِنَ ٱلۡجِنِّ وَٱلۡإِنسِ نَجۡعَلۡهُمَا تَحۡتَ أَقۡدَامِنَا لِيَكُونَا مِنَ ٱلۡأَسۡفَلِينَ
Waqala allatheena kafaroo rabbana arina allathayni adallana mina aljinni waalinsi najAAalhuma tahta aqdamina liyakoona mina alasfaleena
Ña daan weddi dañuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, wan nu ña nu daan réeräl ci jinne yi ak nit ñi, dananu leen def ci ron sunu ndëguy tànk, ngir nu gën a soofe”.
إِنَّ ٱلَّذِينَ قَالُواْ رَبُّنَا ٱللَّهُ ثُمَّ ٱسۡتَقَٰمُواْ تَتَنَزَّلُ عَلَيۡهِمُ ٱلۡمَلَـٰٓئِكَةُ أَلَّا تَخَافُواْ وَلَا تَحۡزَنُواْ وَأَبۡشِرُواْ بِٱلۡجَنَّةِ ٱلَّتِي كُنتُمۡ تُوعَدُونَ
Inna allatheena qaloo rabbuna Allahu thumma istaqamoo tatanazzalu AAalayhimu almalaikatu alla takhafoo wala tahzanoo waabshiroo bialjannati allatee kuntum tooAAadoona
Ñiy wax naan : “Yàllaay sunu Boroom”, tey jéem a tegu ci seen yoonu Boroom wu jub wa xocc, Malaaka yi dañuy wàcci ci ñoom naan leen. “Buleen jàq buleen ragal ; bégleen ci àjjana ja ñu leen daan dig.
نَحۡنُ أَوۡلِيَآؤُكُمۡ فِي ٱلۡحَيَوٰةِ ٱلدُّنۡيَا وَفِي ٱلۡأٓخِرَةِۖ وَلَكُمۡ فِيهَا مَا تَشۡتَهِيٓ أَنفُسُكُمۡ وَلَكُمۡ فِيهَا مَا تَدَّعُونَ
Nahnu awliyaokum fee alhayati alddunya wafee alakhirati walakum feeha ma tashtahee anfusukum walakum feeha ma taddaAAoona
Nun (Yàlla) noo di seen wéeruwaay ci àddina di seen wéeruwaay ca àllaaxira ; te am ngeen fa lépp lu seen bakkan di wonnén ak lépp lu ngeen fay laaj,
نُزُلٗا مِّنۡ غَفُورٖ رَّحِيمٖ
Nuzulan min ghafoorin raheemin
(wàccuwaayu teraanga) bu bawoo ca Jéggëlekat ba, di ab Jaglewaakoonu yërmande”.
وَمَنۡ أَحۡسَنُ قَوۡلٗا مِّمَّن دَعَآ إِلَى ٱللَّهِ وَعَمِلَ صَٰلِحٗا وَقَالَ إِنَّنِي مِنَ ٱلۡمُسۡلِمِينَ
Waman ahsanu qawlan mimman daAAa ila Allahi waAAamila salihan waqala innanee mina almuslimeena
Ana kan moo gën a rafet ay wax kuy woote jëme ci Yàlla, tey jëf yiw tey wax naan : “ Ci jullit ñi laa bokk ?”
وَلَا تَسۡتَوِي ٱلۡحَسَنَةُ وَلَا ٱلسَّيِّئَةُۚ ٱدۡفَعۡ بِٱلَّتِي هِيَ أَحۡسَنُ فَإِذَا ٱلَّذِي بَيۡنَكَ وَبَيۡنَهُۥ عَدَٰوَةٞ كَأَنَّهُۥ وَلِيٌّ حَمِيمٞ
Wala tastawee alhasanatu wala alssayyiatu idfaAA biallatee hiya ahsanu faitha allathee baynaka wabaynahu AAadawatun kaannahu waliyyun hameemun
Lu rafet ak lu ñaaw du ñu yem. Na ngeen jiñe (ab safaan) ci lu baax ; (soo ko defee) ki nga gënoon a noonoo dafay jekki di sa xaritu benn bakkan.
وَمَا يُلَقَّىٰهَآ إِلَّا ٱلَّذِينَ صَبَرُواْ وَمَا يُلَقَّىٰهَآ إِلَّا ذُو حَظٍّ عَظِيمٖ
Wama yulaqqaha illa allatheena sabaroo wama yulaqqaha illa thoo haththin AAatheemin
Lii nag kenn du ko am ku dul ñuy muñ kenn it du ko am ku dul boroom cër bu duun.
وَإِمَّا يَنزَغَنَّكَ مِنَ ٱلشَّيۡطَٰنِ نَزۡغٞ فَٱسۡتَعِذۡ بِٱللَّهِۖ إِنَّهُۥ هُوَ ٱلسَّمِيعُ ٱلۡعَلِيمُ
Waimma yanzaghannaka mina alshshaytani nazghun faistaAAith biAllahi innahu huwa alssameeAAu alAAaleemu
Amaana leeg-leeg bu la saytaane jaxjaxee (waaye bu boobaa), na nga sàkku ci Yàlla mu mësal la ; Moo di, aji Dégg ja, aji xam ja.
وَمِنۡ ءَايَٰتِهِ ٱلَّيۡلُ وَٱلنَّهَارُ وَٱلشَّمۡسُ وَٱلۡقَمَرُۚ لَا تَسۡجُدُواْ لِلشَّمۡسِ وَلَا لِلۡقَمَرِ وَٱسۡجُدُواْۤ لِلَّهِۤ ٱلَّذِي خَلَقَهُنَّ إِن كُنتُمۡ إِيَّاهُ تَعۡبُدُونَ
Wamin ayatihi allaylu waalnnaharu waalshshamsu waalqamaru la tasjudoo lilshshamsi wala lilqamari waosjudoo lillahi alathee khalaqahunna in kuntum iyyahu taAAbudoona
Bokk na ci ay kéemaanam, guddi ak bëccëg, ak jant beek weer wi : buleen sujuudal jant bi, waxantumalaak weer wi, waaye na ngeen di sujuud ngir Yàlla mi leen bind, ndegam Moom ngeen di jaamu.
فَإِنِ ٱسۡتَكۡبَرُواْ فَٱلَّذِينَ عِندَ رَبِّكَ يُسَبِّحُونَ لَهُۥ بِٱلَّيۡلِ وَٱلنَّهَارِ وَهُمۡ لَا يَسۡـَٔمُونَ۩
Faini istakbaroo faallatheena AAinda rabbika yusabbihoona lahu biallayli waalnnahari wahum la yasamoona
Bu ñu rëy-rëyloo... (ba defuñu ko) Malaaka ya nekk ca sa Boroom ñoom dañuy sàbbaal, guddeek bëccëg, te duñu ko bàyyi !(s)
وَمِنۡ ءَايَٰتِهِۦٓ أَنَّكَ تَرَى ٱلۡأَرۡضَ خَٰشِعَةٗ فَإِذَآ أَنزَلۡنَا عَلَيۡهَا ٱلۡمَآءَ ٱهۡتَزَّتۡ وَرَبَتۡۚ إِنَّ ٱلَّذِيٓ أَحۡيَاهَا لَمُحۡيِ ٱلۡمَوۡتَىٰٓۚ إِنَّهُۥ عَلَىٰ كُلِّ شَيۡءٖ قَدِيرٌ
Wamin ayatihi annaka tara alarda khashiAAatan faitha anzalna AAalayha almaa ihtazzat warabat inna allathee ahyaha lamuhyee almawta innahu AAala kulli shayin qadeerun
Bokk na ci Ay kéemaanam ngay gis suuf si mu ne ndàpp (wow koŋŋ). Saa su ñu ci wàccee ndox, mu funki màgg. Ki koy dundal (di ci def gàncax) mooy dekkal ñi dee, Moom man na Lépp lu ne.
إِنَّ ٱلَّذِينَ يُلۡحِدُونَ فِيٓ ءَايَٰتِنَا لَا يَخۡفَوۡنَ عَلَيۡنَآۗ أَفَمَن يُلۡقَىٰ فِي ٱلنَّارِ خَيۡرٌ أَم مَّن يَأۡتِيٓ ءَامِنٗا يَوۡمَ ٱلۡقِيَٰمَةِۚ ٱعۡمَلُواْ مَا شِئۡتُمۡ إِنَّهُۥ بِمَا تَعۡمَلُونَ بَصِيرٌ
Inna allatheena yulhidoona fee ayatina la yakhfawna AAalayna afaman yulqa fee alnnari khayrun am man yatee aminan yawma alqiyamati iAAmaloo ma shitum innahu bima taAAmaloona baseerun
Ñiy jéem a soppi samay laaya (Alxuraan) manuñu nooraan. Moo ndax ku ñu sànni ca safara moo gën walla kuy dikk bu Bis Pénc baa ànd ak ug wóolu ? Defleen lu leen soob moom kuy gis la li ngeen di def ;
إِنَّ ٱلَّذِينَ كَفَرُواْ بِٱلذِّكۡرِ لَمَّا جَآءَهُمۡۖ وَإِنَّهُۥ لَكِتَٰبٌ عَزِيزٞ
Inna allatheena kafaroo bialththikri lamma jaahum wainnahu lakitabun AAazeezun
Ñay weddi [Alxuraan] ba mu dikkee ak li mu leen di fàttali dees na leen mbugël... te Téere bii Téere bu Kàttanu la ;
لَّا يَأۡتِيهِ ٱلۡبَٰطِلُ مِنۢ بَيۡنِ يَدَيۡهِ وَلَا مِنۡ خَلۡفِهِۦۖ تَنزِيلٞ مِّنۡ حَكِيمٍ حَمِيدٖ
La yateehi albatilu min bayni yadayhi wala min khalfihi tanzeelun min hakeemin hameedin
Ay caaxaan [du ko dikke fenn], du ci kanamam mbaa ci ginnaawam : dañu koo wàcce mu bawoo ca (Yàlla) miy aji Xereñ, di Yayoowaakoonu cant.
مَّا يُقَالُ لَكَ إِلَّا مَا قَدۡ قِيلَ لِلرُّسُلِ مِن قَبۡلِكَۚ إِنَّ رَبَّكَ لَذُو مَغۡفِرَةٖ وَذُو عِقَابٍ أَلِيمٖ
Ma yuqalu laka illa ma qad qeela lilrrusuli min qablika inna rabbaka lathoo maghfiratin wathoo AAiqabin aleemin
Deesul a wax lenn lu ñu waxutoon Yonnent ya la jiitu woon. Sa Boroom, ku Am njégël la te di Boroom mbugël mu mitti.
وَلَوۡ جَعَلۡنَٰهُ قُرۡءَانًا أَعۡجَمِيّٗا لَّقَالُواْ لَوۡلَا فُصِّلَتۡ ءَايَٰتُهُۥٓۖ ءَا۬عۡجَمِيّٞ وَعَرَبِيّٞۗ قُلۡ هُوَ لِلَّذِينَ ءَامَنُواْ هُدٗى وَشِفَآءٞۚ وَٱلَّذِينَ لَا يُؤۡمِنُونَ فِيٓ ءَاذَانِهِمۡ وَقۡرٞ وَهُوَ عَلَيۡهِمۡ عَمًىۚ أُوْلَـٰٓئِكَ يُنَادَوۡنَ مِن مَّكَانِۭ بَعِيدٖ
Walaw jaAAalnahu quranan aAAjamiyyan laqaloo lawla fussilat ayatuhu aaAAjamiyyun waAAarabiyyun qul huwa lillatheena amanoo hudan washifaon waallatheena la yuminoona fee athanihim waqrun wahuwa AAalayhim AAaman olaika yunadawna min makanin baAAeedin
Bu Nu ko defoon muy weneen làkk (wu dul araab), danañuy wax naan : “Ana lutax faramfànce wu ñu ay laayaam? Yonnentub araab ak làkk wudul araab (nu muy ame)?” Waxal ne : “njub la ak saafara, ñeel ñi gëm”. Ñi gëmul nag ñoom, ay saañ nekk ci seeni nopp def ngumba ci seeni (gët xel) ; te ñoom na nga leen di woowe ca barab bu sori.
وَلَقَدۡ ءَاتَيۡنَا مُوسَى ٱلۡكِتَٰبَ فَٱخۡتُلِفَ فِيهِۚ وَلَوۡلَا كَلِمَةٞ سَبَقَتۡ مِن رَّبِّكَ لَقُضِيَ بَيۡنَهُمۡۚ وَإِنَّهُمۡ لَفِي شَكّٖ مِّنۡهُ مُرِيبٖ
Walaqad atayna moosa alkitaba faikhtulifa feehi walawla kalimatun sabaqat min rabbika laqudiya baynahum wainnahum lafee shakkin minhu mureebin
Joxoon Nanu Muussaa Téere ba. Mu am ñu ca wuute. Bu ca sa kàddug Boroom jiituwul woon, dana fekk ñu àtte woon seen diggënte. Te it ñoom, ñi ngi sikki-sàkka ci ay mbiram.
مَّنۡ عَمِلَ صَٰلِحٗا فَلِنَفۡسِهِۦۖ وَمَنۡ أَسَآءَ فَعَلَيۡهَاۗ وَمَا رَبُّكَ بِظَلَّـٰمٖ لِّلۡعَبِيدِ
Man AAamila salihan falinafsihi waman asaa faAAalayha wama rabbuka bithallamin lilAAabeedi
Képp kuy jëf yiw, boppam la koy defal. Képp kuy jëf ñaawtéef it, te ci kawam lay dal. Sa Boroom, du tooñ, benn jaamam.
۞إِلَيۡهِ يُرَدُّ عِلۡمُ ٱلسَّاعَةِۚ وَمَا تَخۡرُجُ مِن ثَمَرَٰتٖ مِّنۡ أَكۡمَامِهَا وَمَا تَحۡمِلُ مِنۡ أُنثَىٰ وَلَا تَضَعُ إِلَّا بِعِلۡمِهِۦۚ وَيَوۡمَ يُنَادِيهِمۡ أَيۡنَ شُرَكَآءِي قَالُوٓاْ ءَاذَنَّـٰكَ مَامِنَّا مِن شَهِيدٖ
Ilayhi yuraddu AAilmu alssaAAati wama takhruju min thamaratin min akmamiha wama tahmilu min ontha wala tadaAAu illa biAAilmihi wayawma yunadeehim ayna shurakaee qaloo athannaka ma minna min shaheedin
Ca moom la xam-xamu Waxtu wa di dellu (moom rekk xam). Amul menn meññat muy génn ciw xottam, amul it jenn jigéen juy ëmbu walla muy imbi lu dul am na ca xam-xam bu mat sëkk. Te bu keroogee bis ba mu leen di woo naan : “Ana ña ngeen ma daan bokkaaleel ?”, ñu naan ko : “Noo ngi lay birëlal ne kenn seede wu ko ci nun” !(h)
وَضَلَّ عَنۡهُم مَّا كَانُواْ يَدۡعُونَ مِن قَبۡلُۖ وَظَنُّواْ مَا لَهُم مِّن مَّحِيصٖ
Wadalla AAanhum ma kanoo yadAAoona min qablu wathannoo ma lahum min maheesin
Lañu daan jaamu ca àddina réer leen ; ñu daldi xam nag ne amatuñu rawukaay.
لَّا يَسۡـَٔمُ ٱلۡإِنسَٰنُ مِن دُعَآءِ ٱلۡخَيۡرِ وَإِن مَّسَّهُ ٱلشَّرُّ فَيَـُٔوسٞ قَنُوطٞ
La yasamu alinsanu min duAAai alkhayri wain massahu alshsharru fayaoosun qanootun
Nit du bàyyi du yoqat ci di sàkku di ñaan aw yiw. Waaye saa su ko lor dalee, mu di ku yàkki, kuy yoqat.
وَلَئِنۡ أَذَقۡنَٰهُ رَحۡمَةٗ مِّنَّا مِنۢ بَعۡدِ ضَرَّآءَ مَسَّتۡهُ لَيَقُولَنَّ هَٰذَا لِي وَمَآ أَظُنُّ ٱلسَّاعَةَ قَآئِمَةٗ وَلَئِن رُّجِعۡتُ إِلَىٰ رَبِّيٓ إِنَّ لِي عِندَهُۥ لَلۡحُسۡنَىٰۚ فَلَنُنَبِّئَنَّ ٱلَّذِينَ كَفَرُواْ بِمَا عَمِلُواْ وَلَنُذِيقَنَّهُم مِّنۡ عَذَابٍ غَلِيظٖ
Walain athaqnahu rahmatan minna min baAAdi darraa massathu layaqoolanna hatha lee wama athunnu alssaAAata qaimatan walain rujiAAtu ila rabbee inna lee AAindahu lalhusna falanunabbianna allatheena kafaroo bima AAamiloo walanutheeqannahum min AAathabin ghaleethin
Saa su nu ko musalee yërmande ju bawoo ci nun, ginnaaw lor ja ko laaloon, muy wax naan : “lii maa ko yayoo ! Te sax fooguma ne saa dana taxaw. Te it su ñu ma delloo ca sama Boroom, li ma fay fekk, mooy dàqati”. Danañu xibaar yéefar ya la ñu daan jëf te dana nu leen musal ci mbugël lu diis gànn (miti).
وَإِذَآ أَنۡعَمۡنَا عَلَى ٱلۡإِنسَٰنِ أَعۡرَضَ وَنَـَٔا بِجَانِبِهِۦ وَإِذَا مَسَّهُ ٱلشَّرُّ فَذُو دُعَآءٍ عَرِيضٖ
Waitha anAAamna AAala alinsani aAArada wanaa bijanibihi waitha massahu alshsharru fathoo duAAain AAareedin
Su Nu mayee nit xéewël, mu dumóoyu daldi féew (sori). Waaye saa su ko lor laalee, muy ñaan ñaan yu gudd.
قُلۡ أَرَءَيۡتُمۡ إِن كَانَ مِنۡ عِندِ ٱللَّهِ ثُمَّ كَفَرۡتُم بِهِۦ مَنۡ أَضَلُّ مِمَّنۡ هُوَ فِي شِقَاقِۭ بَعِيدٖ
Qul araaytum in kana min AAindi Allahi thumma kafartum bihi man adallu mimman huwa fee shiqaqin baAAeedin
Waxal ne : “Xanaa gisuleen ? Alxuraan jii ca Yàlla la bawoo ngeen weddi ko ; ana kan moo gën a réer kuy nekk ci teqalikoo gu sore (faasaloo) ?”
سَنُرِيهِمۡ ءَايَٰتِنَا فِي ٱلۡأٓفَاقِ وَفِيٓ أَنفُسِهِمۡ حَتَّىٰ يَتَبَيَّنَ لَهُمۡ أَنَّهُ ٱلۡحَقُّۗ أَوَلَمۡ يَكۡفِ بِرَبِّكَ أَنَّهُۥ عَلَىٰ كُلِّ شَيۡءٖ شَهِيدٌ
Sanureehim ayatina fee alafaqi wafee anfusihim hatta yatabayyana lahum annahu alhaqqu awalam yakfi birabbika annahu AAala kulli shayin shaheedun
Dananu leen won sunuy kéemaan ci déeléey asamaan ak ci seen bopp, ba baa ñuy gindi ku ci xam ne (Alxuraan), mooy dëgg tigi. Xanaa kay war na laa doy rekk ci sa Boroom ne moom seede la ci lépp ?
أَلَآ إِنَّهُمۡ فِي مِرۡيَةٖ مِّن لِّقَآءِ رَبِّهِمۡۗ أَلَآ إِنَّهُۥ بِكُلِّ شَيۡءٖ مُّحِيطُۢ
Ala innahum fee miryatin min liqai rabbihim ala innahu bikulli shayin muheetun
Ñoom xanaa ña ngay sikki-sàkka, ci dajeek seen Boroom ? Te Yàlla moom peeg na lépp lu ne . Saar 42 : Diisóo 53 Laaya