← Suurat yépp
Suurat 7840 aaya

النبإ

An-Naba

The Tidings

Tekki

Tann làkk

1

عَمَّ يَتَسَآءَلُونَ

AAamma yatasaaloona

Ana ci man mbir la ñuy laajante ?(h)

2

عَنِ ٱلنَّبَإِ ٱلۡعَظِيمِ

AAani alnnabai alAAatheemi

Ci xibaar bu rëy ba,

3

ٱلَّذِي هُمۡ فِيهِ مُخۡتَلِفُونَ

Allathee hum feehi mukhtalifoona

xibaar ba nga xam ne dañu caa juuyoo.

4

كَلَّا سَيَعۡلَمُونَ

Kalla sayaAAlamoona

Mukk ! danañu xala xam.

5

ثُمَّ كَلَّا سَيَعۡلَمُونَ

Thumma kalla sayaAAlamoona

Déedéet kay ! Danañu xala xam.

6

أَلَمۡ نَجۡعَلِ ٱلۡأَرۡضَ مِهَٰدٗا

Alam najAAali alarda mihadan

Moo ndax du Nun Noo def suuf si mu di laltaay ?

7

وَٱلۡجِبَالَ أَوۡتَادٗا

Waaljibala awtadan

ak tundi doj yi ñu di ay dott ?

8

وَخَلَقۡنَٰكُمۡ أَزۡوَٰجٗا

Wakhalaqnakum azwajan

Nu bind leen ngeen di ay tóllent,

9

وَجَعَلۡنَا نَوۡمَكُمۡ سُبَاتٗا

WajaAAalna nawmakum subatan

te def nanu seeni nelaw di seen nooflaay,

10

وَجَعَلۡنَا ٱلَّيۡلَ لِبَاسٗا

WajaAAalna allayla libasan

te it def nanu guddi mu di kiiraay sutura,

11

وَجَعَلۡنَا ٱلنَّهَارَ مَعَاشٗا

WajaAAalna alnnahara maAAashan

nu def bëcëg mu di yëngutu kaay,

12

وَبَنَيۡنَا فَوۡقَكُمۡ سَبۡعٗا شِدَادٗا

Wabanayna fawqakum sabAAan shidadan

tabax nanu juróom ñaari (asamaan) yu dëgër ñu tiim leen,

13

وَجَعَلۡنَا سِرَاجٗا وَهَّاجٗا

WajaAAalna sirajan wahhajan

poose nanu ci làmpu bu leer (jant bi),

14

وَأَنزَلۡنَا مِنَ ٱلۡمُعۡصِرَٰتِ مَآءٗ ثَجَّاجٗا

Waanzalna mina almuAAsirati maan thajjajan

wàcce nanu ci niir yi am ndox muy dottiku

15

لِّنُخۡرِجَ بِهِۦ حَبّٗا وَنَبَاتٗا

Linukhrija bihi habban wanabatan

ñu di ca saxal ay pepp ak i gàncax

16

وَجَنَّـٰتٍ أَلۡفَافًا

Wajannatin alfafan

ak ay dër yu naat.

17

إِنَّ يَوۡمَ ٱلۡفَصۡلِ كَانَ مِيقَٰتٗا

Inna yawma alfasli kana meeqatan

Bisub Àtte ba Dig ba jotna.

18

يَوۡمَ يُنفَخُ فِي ٱلصُّورِ فَتَأۡتُونَ أَفۡوَاجٗا

Yawma yunfakhu fee alssoori fatatoona afwajan

Bis ba ñuy wal bufta, ngeen di ñëw di ay mbooloo,

19

وَفُتِحَتِ ٱلسَّمَآءُ فَكَانَتۡ أَبۡوَٰبٗا

Wafutihati alssamao fakanat abwaban

nu ubbi asamaan si mu def ay buntu,

20

وَسُيِّرَتِ ٱلۡجِبَالُ فَكَانَتۡ سَرَابًا

Wasuyyirati aljibalu fakanat saraban

nu doxloo tundi doj yi mu melni ñàndóox.

21

إِنَّ جَهَنَّمَ كَانَتۡ مِرۡصَادٗا

Inna jahannama kanat mirsadan

Waajal nanu safara muy tuqlóo,

22

لِّلطَّـٰغِينَ مَـَٔابٗا

Lilttagheena maaban

di xala doon dekuwaayu ñu bew ña.

23

لَّـٰبِثِينَ فِيهَآ أَحۡقَابٗا

Labitheena feeha ahqaban

Danañu fa sax ay jamono yu yàgg.

24

لَّا يَذُوقُونَ فِيهَا بَرۡدٗا وَلَا شَرَابًا

La yathooqoona feeha bardan wala sharaban

Dunu fa mos ab sedd waxantumalaa ag naan,

25

إِلَّا حَمِيمٗا وَغَسَّاقٗا

Illa hameeman waghassaqan

Lu dul ndox muy wañax ak lay rogaate ca seen jëmm ya

26

جَزَآءٗ وِفَاقًا

Jazaan wifaqan

muy pey gu témbóo.

27

إِنَّهُمۡ كَانُواْ لَا يَرۡجُونَ حِسَابٗا

Innahum kanoo la yarjoona hisaban

Ñoom dañoo foogoon ne duñu leen màndaxe,

28

وَكَذَّبُواْ بِـَٔايَٰتِنَا كِذَّابٗا

Wakaththaboo biayatina kiththaban

ña weddiwoon sunuy Laaya,

29

وَكُلَّ شَيۡءٍ أَحۡصَيۡنَٰهُ كِتَٰبٗا

Wakulla shayin ahsaynahu kitaban

lépp lu ne peek nanu ko bind ko.

30

فَذُوقُواْ فَلَن نَّزِيدَكُمۡ إِلَّا عَذَابًا

Fathooqoo falan nazeedakum illa AAathaban

Ayca mosleen. Dunu leen dolli lu dul mbugël (tokamtikuleen ko) !

31

إِنَّ لِلۡمُتَّقِينَ مَفَازًا

Inna lilmuttaqeena mafazan

Ña ragal Yàlla ñoom baaxal nañu :

32

حَدَآئِقَ وَأَعۡنَٰبٗا

Hadaiqa waaAAnaban

am nañu ay tooli dër ak i reseñ,

33

وَكَوَاعِبَ أَتۡرَابٗا

WakawaAAiba atraban

ak i jongama huur yu taxaw ay ween te maase,

34

وَكَأۡسٗا دِهَاقٗا

Wakasan dihaqan

ak ay kaas yu fees dell.

35

لَّا يَسۡمَعُونَ فِيهَا لَغۡوٗا وَلَا كِذَّـٰبٗا

La yasmaAAoona feeha laghwan wala kiththaban

Duñu fa dégg mukk waxi caaxaan mbaa ay fen.

36

جَزَآءٗ مِّن رَّبِّكَ عَطَآءً حِسَابٗا

Jazaan min rabbika AAataan hisaban

Muy pey gu bawoo ca seen Boroom

37

رَّبِّ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِ وَمَا بَيۡنَهُمَا ٱلرَّحۡمَٰنِۖ لَا يَمۡلِكُونَ مِنۡهُ خِطَابٗا

Rabbi alssamawati waalardi wama baynahuma alrrahmani la yamlikoona minhu khitaban

Boroom asamaan yeek suuf seek li ci seen diggante, mooy Yëramaakoon bi ; duñu mana waxanteek moom.

38

يَوۡمَ يَقُومُ ٱلرُّوحُ وَٱلۡمَلَـٰٓئِكَةُ صَفّٗاۖ لَّا يَتَكَلَّمُونَ إِلَّا مَنۡ أَذِنَ لَهُ ٱلرَّحۡمَٰنُ وَقَالَ صَوَابٗا

Yawma yaqoomu alrroohu waalmalaikatu saffan la yatakallamoona illa man athina lahu alrrahmanu waqala sawaban

Bu keroogee ba Jibriil jóg ànd ak malaaka ya taxaw def sàppe, duñu wax , lu dul ku Yàlla Yëramaakoon bi jox ndigël, mu wax lay dëgg te yem ca kepp.

39

ذَٰلِكَ ٱلۡيَوۡمُ ٱلۡحَقُّۖ فَمَن شَآءَ ٱتَّخَذَ إِلَىٰ رَبِّهِۦ مَـَٔابًا

Thalika alyawmu alhaqqu faman shaa ittakhatha ila rabbihi maaban

Loolu moo di bisub dëgg ba. Ku mu soob mu jël Boroomam def ko ab rawtukaay.

40

إِنَّآ أَنذَرۡنَٰكُمۡ عَذَابٗا قَرِيبٗا يَوۡمَ يَنظُرُ ٱلۡمَرۡءُ مَا قَدَّمَتۡ يَدَاهُ وَيَقُولُ ٱلۡكَافِرُ يَٰلَيۡتَنِي كُنتُ تُرَٰبَۢا

Inna antharnakum AAathaban qareeban yawma yanthuru almaro ma qaddamat yadahu wayaqoolu alkafiru ya laytanee kuntu turaban

Xuppnaa leen ci mbugëlum bis bu jigeen, bu keroogee ba nit ñi di xool la ñu jëfoon ; yéefar ba naan : “Aka neexoon may suuf ”. Saar 79 : Malaaka yay rocci ruu 46 - Laaya