وَٱلسَّمَآءِ ذَاتِ ٱلۡبُرُوجِ
Waalssamai thati alburooji
Ci asamaan sa di boroom biddiw yu mag ! Maa ngi giñ!
Al-Buruj
The Mansions of the Stars
Tekki
وَٱلسَّمَآءِ ذَاتِ ٱلۡبُرُوجِ
Waalssamai thati alburooji
Ci asamaan sa di boroom biddiw yu mag ! Maa ngi giñ!
وَٱلۡيَوۡمِ ٱلۡمَوۡعُودِ
Waalyawmi almawAAoodi
ak ci bis ba ñu dige !
وَشَاهِدٖ وَمَشۡهُودٖ
Washahidin wamashhoodin
ak ci kuy seede ak ca ka ñuy seede !
قُتِلَ أَصۡحَٰبُ ٱلۡأُخۡدُودِ
Qutila ashabu alukhdoodi
Faagaagal na waa Uxduud,
ٱلنَّارِ ذَاتِ ٱلۡوَقُودِ
Alnnari thati alwaqoodi
ak ci safara wa am lu koy xamb,
إِذۡ هُمۡ عَلَيۡهَا قُعُودٞ
Ith hum AAalayha quAAoodun
ca ba ñu toogee wër ko,
وَهُمۡ عَلَىٰ مَا يَفۡعَلُونَ بِٱلۡمُؤۡمِنِينَ شُهُودٞ
Wahum AAala ma yafAAaloona bialmumineena shuhoodun
te ñoom seede la ñu ca la ñu defoon way gëm ña,
وَمَا نَقَمُواْ مِنۡهُمۡ إِلَّآ أَن يُؤۡمِنُواْ بِٱللَّهِ ٱلۡعَزِيزِ ٱلۡحَمِيدِ
Wama naqamoo minhum illa an yuminoo biAllahi alAAazeezi alhameedi
te fitnaale wu ñu leen ci lu dul ne da ñoo gëm Yàlla, boroom Kàttan ga, Yayoowaakooni cant ba,
ٱلَّذِي لَهُۥ مُلۡكُ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِۚ وَٱللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيۡءٖ شَهِيدٌ
Allathee lahu mulku alssamawati waalardi waAllahu AAala kulli shayin shaheedun
Yàlla mi moom nguurug asamaan yeek suuf si. Te yàlla seede la ci lépp lu ne.
إِنَّ ٱلَّذِينَ فَتَنُواْ ٱلۡمُؤۡمِنِينَ وَٱلۡمُؤۡمِنَٰتِ ثُمَّ لَمۡ يَتُوبُواْ فَلَهُمۡ عَذَابُ جَهَنَّمَ وَلَهُمۡ عَذَابُ ٱلۡحَرِيقِ
Inna allatheena fatanoo almumineena waalmuminati thumma lam yatooboo falahum AAathabu jahannama walahum AAathabu alhareeqi
Ña daan fitnaal jullit yu góor yaak yu jigéen ya, te tubu ñu ko, dananu am mbugëlum Jahanama ñu di leen ca lakk. (ca safaraam wa)
إِنَّ ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ وَعَمِلُواْ ٱلصَّـٰلِحَٰتِ لَهُمۡ جَنَّـٰتٞ تَجۡرِي مِن تَحۡتِهَا ٱلۡأَنۡهَٰرُۚ ذَٰلِكَ ٱلۡفَوۡزُ ٱلۡكَبِيرُ
Inna allatheena amanoo waAAamiloo alssalihati lahum jannatun tajree min tahtiha alanharu thalika alfawzu alkabeeru
Ña gëmoon te daan jëf yiw am nañu ay Àjjana yu ay dex di daw ci suufam. Loolu moo di texe gu mag ga.
إِنَّ بَطۡشَ رَبِّكَ لَشَدِيدٌ
Inna batsha rabbika lashadeedun
Sa fayug boroom lu tar la.(s)
إِنَّهُۥ هُوَ يُبۡدِئُ وَيُعِيدُ
Innahu huwa yubdio wayuAAeedu
Moom mooy, sos bindeef yi, te mooleen di dekkilaat.
وَهُوَ ٱلۡغَفُورُ ٱلۡوَدُودُ
Wahuwa alghafooru alwadoodu
Te moom moo di Jéggëlaakoon bi, di soppi lépp,
ذُو ٱلۡعَرۡشِ ٱلۡمَجِيدُ
Thoo alAAarshi almajeedi
Mooy boroom Gàngunaay gu Màgg ga (Aras),
فَعَّالٞ لِّمَا يُرِيدُ
FaAAAAalun lima yureedu
Lu mu namm dana ko def.
هَلۡ أَتَىٰكَ حَدِيثُ ٱلۡجُنُودِ
Hal ataka hadeethu aljunoodi
Moo ndax waxtaanu xarekat ya dikal na la ( xibaar ya),
فِرۡعَوۡنَ وَثَمُودَ
FirAAawna wathamooda
Firawna, ak Samuud ?
بَلِ ٱلَّذِينَ كَفَرُواْ فِي تَكۡذِيبٖ
Bali allatheena kafaroo fee taktheebin
Yéefër ya dañuy weddi,
وَٱللَّهُ مِن وَرَآئِهِم مُّحِيطُۢ
WaAllahu min waraihim muheetun
te Yàlla ngi leen peeg, ci wet gu nekk.
بَلۡ هُوَ قُرۡءَانٞ مَّجِيدٞ
Bal huwa quranun majeedun
li wér mooy Alxuraan ju màgg la
فِي لَوۡحٖ مَّحۡفُوظِۭ
Fee lawhin mahfoothin
ca biir Àlluwa ja ñu wàttu fa Yàlla (Lawhul Mahfuus ). Saar 86 : Biddiwub guddi ba 17 - Laaya