← Suurat yépp
Suurat 8719 aaya

الأعلى

Al-A'la

The Most High

Tekki

Tann làkk

1

سَبِّحِ ٱسۡمَ رَبِّكَ ٱلۡأَعۡلَى

Sabbihi isma rabbika alaAAla

Sàbbaalal sa turu Boroom, bi Gëna kawe,(h)

2

ٱلَّذِي خَلَقَ فَسَوَّىٰ

Allathee khalaqa fasawwa

Ki bind jekkal yemale,

3

وَٱلَّذِي قَدَّرَ فَهَدَىٰ

Waallathee qaddara fahada

kiy dogal tey gindee,

4

وَٱلَّذِيٓ أَخۡرَجَ ٱلۡمَرۡعَىٰ

Waallathee akhraja almarAAa

kiy génne ñax mi saxal ko,

5

فَجَعَلَهُۥ غُثَآءً أَحۡوَىٰ

FajaAAalahu ghuthaan ahwa

di ko naatal dëlël ko.

6

سَنُقۡرِئُكَ فَلَا تَنسَىٰٓ

Sanuqrioka fala tansa

Dananu la jàngal (Alxuraan), te doo too ko fàtte

7

إِلَّا مَا شَآءَ ٱللَّهُۚ إِنَّهُۥ يَعۡلَمُ ٱلۡجَهۡرَ وَمَا يَخۡفَىٰ

Illa ma shaa Allahu innahu yaAAlamu aljahra wama yakhfa

lu dul la soob Yàlla. Moom moo xam li feeñ ak li nëbbu.

8

وَنُيَسِّرُكَ لِلۡيُسۡرَىٰ

Wanuyassiruka lilyusra

Dananu la jàppandalal yoon wi gëna yomb.

9

فَذَكِّرۡ إِن نَّفَعَتِ ٱلذِّكۡرَىٰ

Fathakkir in nafaAAati alththikra

Na ngay fàttelee, saa su fàtteli amee njariñ.

10

سَيَذَّكَّرُ مَن يَخۡشَىٰ

Sayaththakkaru man yakhsha

képp kuy ragal (Yàlla) na nangoo fàttaliku,

11

وَيَتَجَنَّبُهَا ٱلۡأَشۡقَى

Wayatajannabuha alashqa

ñu texeedi ñaa koy moytu,

12

ٱلَّذِي يَصۡلَى ٱلنَّارَ ٱلۡكُبۡرَىٰ

Allathee yasla alnnara alkubra

ñay lakk ca safara sa gëna rëy,

13

ثُمَّ لَا يَمُوتُ فِيهَا وَلَا يَحۡيَىٰ

Thumma la yamootu feeha wala yahya

du fa dund dufa dee.

14

قَدۡ أَفۡلَحَ مَن تَزَكَّىٰ

Qad aflaha man tazakka

Képp kuy sellal texe na,

15

وَذَكَرَ ٱسۡمَ رَبِّهِۦ فَصَلَّىٰ

Wathakara isma rabbihi fasalla

te fàttaliku turu boroomam , tey julli.

16

بَلۡ تُؤۡثِرُونَ ٱلۡحَيَوٰةَ ٱلدُّنۡيَا

Bal tuthiroona alhayata alddunya

Yeen, dangeena bëgg lool dundug àddina,

17

وَٱلۡأٓخِرَةُ خَيۡرٞ وَأَبۡقَىٰٓ

Waalakhiratu khayrun waabqa

te àllaaxira gën te moo gëna sax.

18

إِنَّ هَٰذَا لَفِي ٱلصُّحُفِ ٱلۡأُولَىٰ

Inna hatha lafee alssuhufi aloola

Lii nekk na, ca téere yu jëkk ya,

19

صُحُفِ إِبۡرَٰهِيمَ وَمُوسَىٰ

Suhufi ibraheema wamoosa

téerey Ibraahiima ak Muusaa. Saar 88 : Muuraakoon ba 26 - Laaya