← Suurat yépp
Suurat 8826 aaya

الغاشية

Al-Ghashiyah

The Overwhelming

Tekki

Tann làkk

1

هَلۡ أَتَىٰكَ حَدِيثُ ٱلۡغَٰشِيَةِ

Hal ataka hadeethu alghashiyati

Moo ndax yaw waxtaanu muuraakoon ba dikkal na la (ay xibaaram) ?

2

وُجُوهٞ يَوۡمَئِذٍ خَٰشِعَةٌ

Wujoohun yawmaithin khashiAAatun

Bu keroogee, ay xarkanam yu fooyooy,

3

عَامِلَةٞ نَّاصِبَةٞ

AAamilatun nasibatun

yu sonn, fundóoñ.

4

تَصۡلَىٰ نَارًا حَامِيَةٗ

Tasla naran hamiyatan

Di lakk ci Safara wu tàng,

5

تُسۡقَىٰ مِنۡ عَيۡنٍ ءَانِيَةٖ

Tusqa min AAaynin aniyatin

ñu di ko nandal ci bët buy wañax. (ndox)

6

لَّيۡسَ لَهُمۡ طَعَامٌ إِلَّا مِن ضَرِيعٖ

Laysa lahum taAAamun illa min dareeAAin

Amuñu fa genn lekk lu dul [darii] ay dég,

7

لَّا يُسۡمِنُ وَلَا يُغۡنِي مِن جُوعٖ

La yusminu wala yughnee min jooAAin

du rëyloo, du teggib xiif.

8

وُجُوهٞ يَوۡمَئِذٖ نَّاعِمَةٞ

Wujoohun yawmaithin naAAimatun

Bu keroogee, ay xarkanam yu nooy,

9

لِّسَعۡيِهَا رَاضِيَةٞ

LisaAAyiha radiyatun

bég lool ca seeni jëf,

10

فِي جَنَّةٍ عَالِيَةٖ

Fee jannatin AAaliyatin

ci biir ay Àjjana yu kawe,

11

لَّا تَسۡمَعُ فِيهَا لَٰغِيَةٗ

La tasmaAAu feeha laghiyatan

doo fa degg mukk waxi caaxaan.

12

فِيهَا عَيۡنٞ جَارِيَةٞ

Feeha AAaynun jariyatun

Am na fa, bëtu ndox buy daw-dawaan.

13

فِيهَا سُرُرٞ مَّرۡفُوعَةٞ

Feeha sururun marfooAAatun

Am na fa, ay lal yu kawe

14

وَأَكۡوَابٞ مَّوۡضُوعَةٞ

Waakwabun mawdooAAatun

ak ay kopp yu ñu teg

15

وَنَمَارِقُ مَصۡفُوفَةٞ

Wanamariqu masfoofatun

ak ay ngegenaay yu ñu sësële

16

وَزَرَابِيُّ مَبۡثُوثَةٌ

Wazarabiyyu mabthoothatun

ak ay laltu yu ñu lal.

17

أَفَلَا يَنظُرُونَ إِلَى ٱلۡإِبِلِ كَيۡفَ خُلِقَتۡ

Afala yanthuroona ila alibili kayfa khuliqat

Xanaa dañoo xoolul ci giléem, naka lañu ko binde,(s)

18

وَإِلَى ٱلسَّمَآءِ كَيۡفَ رُفِعَتۡ

Waila alssamai kayfa rufiAAat

ak ci asamaan si naka la nu ko yékëte,

19

وَإِلَى ٱلۡجِبَالِ كَيۡفَ نُصِبَتۡ

Waila aljibali kayfa nusibat

ak ci tund doj yi naka la nu ko sampe

20

وَإِلَى ٱلۡأَرۡضِ كَيۡفَ سُطِحَتۡ

Waila alardi kayfa sutihat

ak ci suuf si naka la nu ko maasalee ?

21

فَذَكِّرۡ إِنَّمَآ أَنتَ مُذَكِّرٞ

Fathakkir innama anta muthakkirun

Na ngay, fàttalee ! Ndax yaw ab fàttalikat nga,

22

لَّسۡتَ عَلَيۡهِم بِمُصَيۡطِرٍ

Lasta AAalayhim bimusaytirin

te nootoo leen.

23

إِلَّا مَن تَوَلَّىٰ وَكَفَرَ

Illa man tawalla wakafara

Lu ca dul ku dumóoyu tey weddi,

24

فَيُعَذِّبُهُ ٱللَّهُ ٱلۡعَذَابَ ٱلۡأَكۡبَرَ

FayuAAaththibuhu Allahu alAAathaba alakbara

Yàlla dana ko mbugël mbugël mu gëna rëy.

25

إِنَّ إِلَيۡنَآ إِيَابَهُمۡ

Inna ilayna iyabahum

Te ci Nun la ñuy déllusi.

26

ثُمَّ إِنَّ عَلَيۡنَا حِسَابَهُم

Thumma inna AAalayna hisabahum

Ba noppi, te nun it nooy warloo laaj leen. Saar 89 : Njël 30 - Laaya