← Suurat yépp
Suurat 20135 aaya

طه

Taha

Ta-Ha

Tekki

Tann làkk

1

طه

Taha

Taa Haa.(h)

2

مَآ أَنزَلۡنَا عَلَيۡكَ ٱلۡقُرۡءَانَ لِتَشۡقَىٰٓ

Ma anzalna AAalayka alqurana litashqa

Wàccewunu Alxuraan jii ci yaw ngir nga texeedi [tiis],

3

إِلَّا تَذۡكِرَةٗ لِّمَن يَخۡشَىٰ

Illa tathkiratan liman yakhsha

[waaye] Danu koo wàcce ngir muy waar ñi ragal Yàlla,

4

تَنزِيلٗا مِّمَّنۡ خَلَقَ ٱلۡأَرۡضَ وَٱلسَّمَٰوَٰتِ ٱلۡعُلَى

Tanzeelan mimman khalaqa alarda waalssamawati alAAula

dafa wàcc bawoo ca Ka bind suuf si ak asamaan yu kawe ya.

5

ٱلرَّحۡمَٰنُ عَلَى ٱلۡعَرۡشِ ٱسۡتَوَىٰ

Alrrahmanu AAala alAAarshi istawa

Yàllaa nga yemoo ca Gàngunaay ga [Aras].

6

لَهُۥ مَا فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَمَا فِي ٱلۡأَرۡضِ وَمَا بَيۡنَهُمَا وَمَا تَحۡتَ ٱلثَّرَىٰ

Lahu ma fee alssamawati wama fee alardi wama baynahuma wama tahta alththara

Moo moom li nekk ci asamaan yi ak ci suuf si ak li nekk ci seen diggante, ak li nekk ci ron déeley suuf si.

7

وَإِن تَجۡهَرۡ بِٱلۡقَوۡلِ فَإِنَّهُۥ يَعۡلَمُ ٱلسِّرَّ وَأَخۡفَى

Wain tajhar bialqawli fainnahu yaAAlamu alssirra waakhfa

Soo dee jóoru say wax it, Moom xam na mbóot ak la gën a nëbbu.

8

ٱللَّهُ لَآ إِلَٰهَ إِلَّا هُوَۖ لَهُ ٱلۡأَسۡمَآءُ ٱلۡحُسۡنَىٰ

Allahu la ilaha illa huwa lahu alasmao alhusna

Yàlla mooy Yàlla ! Amul jeneen yàlla ju dul Moom ! Moo moom tur yi gën a rafet.

9

وَهَلۡ أَتَىٰكَ حَدِيثُ مُوسَىٰٓ

Wahal ataka hadeethu moosa

Moo ndax xam nga xibaari Muusaa ?

10

إِذۡ رَءَا نَارٗا فَقَالَ لِأَهۡلِهِ ٱمۡكُثُوٓاْ إِنِّيٓ ءَانَسۡتُ نَارٗا لَّعَلِّيٓ ءَاتِيكُم مِّنۡهَا بِقَبَسٍ أَوۡ أَجِدُ عَلَى ٱلنَّارِ هُدٗى

Ith raa naran faqala liahlihi omkuthoo innee anastu naran laAAallee ateekum minha biqabasin aw ajidu AAala alnnari hudan

Ba mu gisee aw safara, mu ne njabootam : “Xaarleen ma fii ! Lële ma séen dey aw safara la ; Amaana ma jële fa aw xal, walla ma fekk fa ku ma gindi [teg ma ci yoon]”.

11

فَلَمَّآ أَتَىٰهَا نُودِيَ يَٰمُوسَىٰٓ

Falamma ataha noodiya ya moosa

Ba mu agsee ci safara wa, mu am lu ko woo ne ko : “Éy Muusaa !

12

إِنِّيٓ أَنَا۠ رَبُّكَ فَٱخۡلَعۡ نَعۡلَيۡكَ إِنَّكَ بِٱلۡوَادِ ٱلۡمُقَدَّسِ طُوٗى

Innee ana rabbuka faikhlaAA naAAlayka innaka bialwadi almuqaddasi tuwan

Man maay sa Boroom. Summil say dàll : yaa ngi ci biir xur wu sell wu ñuy wax [Tuwaa].

13

وَأَنَا ٱخۡتَرۡتُكَ فَٱسۡتَمِعۡ لِمَا يُوحَىٰٓ

Waana ikhtartuka faistamiAA lima yooha

Dama laa tànn. Kon déggal li Ma lay soloo.

14

إِنَّنِيٓ أَنَا ٱللَّهُ لَآ إِلَٰهَ إِلَّآ أَنَا۠ فَٱعۡبُدۡنِي وَأَقِمِ ٱلصَّلَوٰةَ لِذِكۡرِيٓ

Innanee ana Allahu la ilaha illa ana faoAAbudnee waaqimi alssalata lithikree

Man mii maay Yàlla : amul jeneen yàlla ju dul Man. Nanga may jaamu, tey taxawal julli, di Ma màggal.

15

إِنَّ ٱلسَّاعَةَ ءَاتِيَةٌ أَكَادُ أُخۡفِيهَا لِتُجۡزَىٰ كُلُّ نَفۡسِۭ بِمَا تَسۡعَىٰ

Inna alssaAAata atiyatun akadu okhfeeha litujza kullu nafsin bima tasAAa

Te Bis-pénc ba daanaka ñëw na. Dama koo xaw a làq rekk ngir fey bakkan bu nekk la muy jëf.

16

فَلَا يَصُدَّنَّكَ عَنۡهَا مَن لَّا يُؤۡمِنُ بِهَا وَٱتَّبَعَ هَوَىٰهُ فَتَرۡدَىٰ

Fala yasuddannaka AAanha man la yuminu biha waittabaAAa hawahu fatarda

[Kon farlul ba] képp ku gëmul tey topp bànneexam, bañ laa gàllankoor ngay alku.

17

وَمَا تِلۡكَ بِيَمِينِكَ يَٰمُوسَىٰ

Wama tilka biyameenika ya moosa

Waaw Muusaa, li nekk ci sa loxo ndeyjoor lan la ?”

18

قَالَ هِيَ عَصَايَ أَتَوَكَّؤُاْ عَلَيۡهَا وَأَهُشُّ بِهَا عَلَىٰ غَنَمِي وَلِيَ فِيهَا مَـَٔارِبُ أُخۡرَىٰ

Qala hiya AAasaya atawakkao AAalayha waahushshu biha AAala ghanamee waliya feeha maaribu okhra

Mu wax ne : “Samaw yet la, dama ciy sukkóotu, di ci waññ samag jur ak yeneeni mbir”.

19

قَالَ أَلۡقِهَا يَٰمُوسَىٰ

Qala alqiha ya moosa

[Yàlla ne ko] : “Sànni ko yaw Muusaa”.

20

فَأَلۡقَىٰهَا فَإِذَا هِيَ حَيَّةٞ تَسۡعَىٰ

Faalqaha faitha hiya hayyatun tasAAa

Mu sànni ko : ndekete yoo jaan a ngay bélaw-bélawi.

21

قَالَ خُذۡهَا وَلَا تَخَفۡۖ سَنُعِيدُهَا سِيرَتَهَا ٱلۡأُولَىٰ

Qala khuthha wala takhaf sanuAAeeduha seerataha aloola

Mu ne ko : “Jël ko : Dananu ko delloo na mu meloon, bul ragal.

22

وَٱضۡمُمۡ يَدَكَ إِلَىٰ جَنَاحِكَ تَخۡرُجۡ بَيۡضَآءَ مِنۡ غَيۡرِ سُوٓءٍ ءَايَةً أُخۡرَىٰ

Waodmum yadaka ila janahika takhruj baydaa min ghayri sooin ayatan okhra

Te nga dugal sa loxo ci sa biir poqotaan : mu génn weex tàll lool, di geneen kéemaan

23

لِنُرِيَكَ مِنۡ ءَايَٰتِنَا ٱلۡكُبۡرَى

Linuriyaka min ayatina alkubra

[Lii lépp] Danu la koo waajale ngir won la ci Sunu kéemtaan yu màgg yi.

24

ٱذۡهَبۡ إِلَىٰ فِرۡعَوۡنَ إِنَّهُۥ طَغَىٰ

Ithhab ila firAAawna innahu tagha

Demal ca Firawna, moom dafa beew.

25

قَالَ رَبِّ ٱشۡرَحۡ لِي صَدۡرِي

Qala rabbi ishrah lee sadree

[Muusaa] ne ko : “Yaw sama Boroom, leeralal ma sama dënn [mën a dékku lu bari],

26

وَيَسِّرۡ لِيٓ أَمۡرِي

Wayassir lee amree

te nga yombalal ma sama soloo sii,

27

وَٱحۡلُلۡ عُقۡدَةٗ مِّن لِّسَانِي

Waohlul AAuqdatan min lisanee

te nga leeral samaw làmmiñ,

28

يَفۡقَهُواْ قَوۡلِي

Yafqahoo qawlee

ba ñu mën a xam samay wax,

29

وَٱجۡعَل لِّي وَزِيرٗا مِّنۡ أَهۡلِي

WaijAAal lee wazeeran min ahlee

te nga may ma, defal ma ci samag njaboot ku may jàppale :

30

هَٰرُونَ أَخِي

Haroona akhee

Te mu far doon sax Haaruuna, sama mbokk,

31

ٱشۡدُدۡ بِهِۦٓ أَزۡرِي

Oshdud bihi azree

Doolel ma ci moom !

32

وَأَشۡرِكۡهُ فِيٓ أَمۡرِي

Waashrikhu fee amree

te boole ko ci samay mbir,

33

كَيۡ نُسَبِّحَكَ كَثِيرٗا

Kay nusabbihaka katheeran

ngir nu mën di la sàbbaal lu bari,

34

وَنَذۡكُرَكَ كَثِيرًا

Wanathkuraka katheeran

di La tuddu, di la fàttaliku lu bari.

35

إِنَّكَ كُنتَ بِنَا بَصِيرٗا

Innaka kunta bina baseeran

Te Yaa gën a xam sunuy mbir, Yaa nu gën a gis”.(s)

36

قَالَ قَدۡ أُوتِيتَ سُؤۡلَكَ يَٰمُوسَىٰ

Qala qad ooteeta sulaka ya moosa

[Yàlla] tontu ne : “Li nga doon laaj [di ko ñaan] am nga ko.

37

وَلَقَدۡ مَنَنَّا عَلَيۡكَ مَرَّةً أُخۡرَىٰٓ

Walaqad mananna AAalayka marratan okhra

Te it, wér na ne xéewaloon Nanu la feneen,

38

إِذۡ أَوۡحَيۡنَآ إِلَىٰٓ أُمِّكَ مَا يُوحَىٰٓ

Ith awhayna ila ommika ma yooha

Ba Nu déggalee sa yaay la Nu ko déggal :

39

أَنِ ٱقۡذِفِيهِ فِي ٱلتَّابُوتِ فَٱقۡذِفِيهِ فِي ٱلۡيَمِّ فَلۡيُلۡقِهِ ٱلۡيَمُّ بِٱلسَّاحِلِ يَأۡخُذۡهُ عَدُوّٞ لِّي وَعَدُوّٞ لَّهُۥۚ وَأَلۡقَيۡتُ عَلَيۡكَ مَحَبَّةٗ مِّنِّي وَلِتُصۡنَعَ عَلَىٰ عَيۡنِيٓ

Ani iqthifeehi fee alttabooti faiqthifeehi fee alyammi falyulqihi alyammu bialssahili yakhuthhu AAaduwwun lee waAAaduwwun lahu waalqaytu AAalayka mahabbatan minnee walitusnaAAa AAala AAaynee

Ne ko na sànni liir ba ca kees ga, sànni kees ga ca ndox ma, ndox ma dana ko gëq ca tefes ga ; samab noon, dib noonam moo koy jël”. Yaw Muusaa, defal naa la Samag cofeel, te it ci Samag càmm nga màgge.

40

إِذۡ تَمۡشِيٓ أُخۡتُكَ فَتَقُولُ هَلۡ أَدُلُّكُمۡ عَلَىٰ مَن يَكۡفُلُهُۥۖ فَرَجَعۡنَٰكَ إِلَىٰٓ أُمِّكَ كَيۡ تَقَرَّ عَيۡنُهَا وَلَا تَحۡزَنَۚ وَقَتَلۡتَ نَفۡسٗا فَنَجَّيۡنَٰكَ مِنَ ٱلۡغَمِّ وَفَتَنَّـٰكَ فُتُونٗاۚ فَلَبِثۡتَ سِنِينَ فِيٓ أَهۡلِ مَدۡيَنَ ثُمَّ جِئۡتَ عَلَىٰ قَدَرٖ يَٰمُوسَىٰ

Ith tamshee okhtuka fataqoolu hal adullukum AAala man yakfuluhu farajaAAnaka ila ommika kay taqarra AAaynuha wala tahzana waqatalta nafsan fanajjaynaka mina alghammi wafatannaka futoonan falabithta sineena fee ahli madyana thumma jita AAala qadarin ya moosa

[Fàttalikul] ba sa jigéen ba di dox te naan leen : “Ndax duma leen tegtal ci ku ko mën a yar ?” Ba tax Nu delloo la fa sa yaay ngir xelam dal, mu bañ a yàq. Nga reyoon bakkan, Nu musal la ca mbamb ma ; Nu fitnaaloon la, nattu la lu yàgg. Nga demoon fa waa Madiyaana ba am fa ay at. Ba tey jii yaa ngi nii ci àpp bu ma dogaloon.

41

وَٱصۡطَنَعۡتُكَ لِنَفۡسِي

WaistanaAAtuka linafsee

Maa la bind ngir Sama mbiri bopp.

42

ٱذۡهَبۡ أَنتَ وَأَخُوكَ بِـَٔايَٰتِي وَلَا تَنِيَا فِي ذِكۡرِي

Ithhab anta waakhooka biayatee wala taniya fee thikree

Demal yaak sa mbokk ngeen yor samay kàddu ; te buleen sàggane di Ma jaamu.

43

ٱذۡهَبَآ إِلَىٰ فِرۡعَوۡنَ إِنَّهُۥ طَغَىٰ

Ithhaba ila firAAawna innahu tagha

Demleen yéen ñaar fa Firawna : ndax moom dafa beew.

44

فَقُولَا لَهُۥ قَوۡلٗا لَّيِّنٗا لَّعَلَّهُۥ يَتَذَكَّرُ أَوۡ يَخۡشَىٰ

Faqoola lahu qawlan layyinan laAAallahu yatathakkaru aw yakhsha

Nangeen wax ak moom wax ju nooy. Ndax amaana mu waaru walla mu ragal Yàlla ?

45

قَالَا رَبَّنَآ إِنَّنَا نَخَافُ أَن يَفۡرُطَ عَلَيۡنَآ أَوۡ أَن يَطۡغَىٰ

Qala rabbana innana nakhafu an yafruta AAalayna aw an yatgha

Ñu ne Ko : “Yaw sunu Boroom, nun dey danuy ragal, bu nu demee fa moom, mu jaay nu doole”.

46

قَالَ لَا تَخَافَآۖ إِنَّنِي مَعَكُمَآ أَسۡمَعُ وَأَرَىٰ

Qala la takhafa innanee maAAakuma asmaAAu waara

47

فَأۡتِيَاهُ فَقُولَآ إِنَّا رَسُولَا رَبِّكَ فَأَرۡسِلۡ مَعَنَا بَنِيٓ إِسۡرَـٰٓءِيلَ وَلَا تُعَذِّبۡهُمۡۖ قَدۡ جِئۡنَٰكَ بِـَٔايَةٖ مِّن رَّبِّكَۖ وَٱلسَّلَٰمُ عَلَىٰ مَنِ ٱتَّبَعَ ٱلۡهُدَىٰٓ

Fatiyahu faqoola inna rasoola rabbika faarsil maAAana banee israeela wala tuAAaththibhum qad jinaka biayatin min rabbika waalssalamu AAala mani ittabaAAa alhuda

Demleen fa Moom ne ko : “Ñun ñaar ñii ndawi Yàlla lanu. Delloo nu waa Banii-Israayiila [ñi nga jàppe jaam] te buleen mbugalati. Ndax indi nanu ci yaw ay kàddu yu jóge fa sa Boroom. Te jàmmi Yàlla nay nekk ca kay topp njub ga !

48

إِنَّا قَدۡ أُوحِيَ إِلَيۡنَآ أَنَّ ٱلۡعَذَابَ عَلَىٰ مَن كَذَّبَ وَتَوَلَّىٰ

Inna qad oohiya ilayna anna alAAathaba AAala man kaththaba watawalla

Xamalees nanu ne : képp ku weddi te dummóoyu [kàdduy Yàlla], kooka mbugal dana ko dal”.

49

قَالَ فَمَن رَّبُّكُمَا يَٰمُوسَىٰ

Qala faman rabbukuma ya moosa

[Firawna] ne leen : “Waaw yéen ñaar kan moo di seen Boroom ?”

50

قَالَ رَبُّنَا ٱلَّذِيٓ أَعۡطَىٰ كُلَّ شَيۡءٍ خَلۡقَهُۥ ثُمَّ هَدَىٰ

Qala rabbuna allathee aAAta kulla shayin khalqahu thumma hada

Mu ne ko : “Sunu Boroom, Moo sos mbindéef yépp, te Mooy gindee”.

51

قَالَ فَمَا بَالُ ٱلۡقُرُونِ ٱلۡأُولَىٰ

Qala fama balu alqurooni aloola

[Firawna] ne ko : “Waaw xeet ya jiitu woon, ñoom luy xala doon seenub àtte ?”.

52

قَالَ عِلۡمُهَا عِندَ رَبِّي فِي كِتَٰبٖۖ لَّا يَضِلُّ رَبِّي وَلَا يَنسَى

Qala AAilmuha AAinda rabbee fee kitabin la yadillu rabbee wala yansa

Mu ne ko : “Seeni mbir a nga ca Téere ba fa sa Boroom. Sama Boroom du juum, du fàtte.

53

ٱلَّذِي جَعَلَ لَكُمُ ٱلۡأَرۡضَ مَهۡدٗا وَسَلَكَ لَكُمۡ فِيهَا سُبُلٗا وَأَنزَلَ مِنَ ٱلسَّمَآءِ مَآءٗ فَأَخۡرَجۡنَا بِهِۦٓ أَزۡوَٰجٗا مِّن نَّبَاتٖ شَتَّىٰ

Allathee jaAAala lakumu alarda mahdan wasalaka lakum feeha subulan waanzala mina alssamai maan faakhrajna bihi azwajan min nabatin shatta

Sama Boroom bi nga xam ne Moo leen defal suuf si laltaay [maasale ko], defal leen ci ay yoon [ngeen di jokkoo] ; Mu wàcce am ndox mu bawoo asamaan, ñu di ca génne ay xeeti gàncax yu wuute.”

54

كُلُواْ وَٱرۡعَوۡاْ أَنۡعَٰمَكُمۡۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَأٓيَٰتٖ لِّأُوْلِي ٱلنُّهَىٰ

Kuloo wairAAaw anAAamakum inna fee thalika laayatin liolee alnnuha

“Lekk-leen te sàmm seenug jur”. Ay kéemaan a ngi ci loolu, ñeel aw nit ñu am xel.

55

۞مِنۡهَا خَلَقۡنَٰكُمۡ وَفِيهَا نُعِيدُكُمۡ وَمِنۡهَا نُخۡرِجُكُمۡ تَارَةً أُخۡرَىٰ

Minha khalaqnakum wafeeha nuAAeedukum waminha nukhrijukum taratan okhra

[Ci suuf si] la Nu leen binde, ci la Nu leen di delloo, te ci la Nu leen dellu génnewaat weneen yoon.(r)

56

وَلَقَدۡ أَرَيۡنَٰهُ ءَايَٰتِنَا كُلَّهَا فَكَذَّبَ وَأَبَىٰ

Walaqad araynahu ayatina kullaha fakaththaba waaba

Won Nanu ko Sunu kéemaan yépp mu lànk weddi [Yàlla].

57

قَالَ أَجِئۡتَنَا لِتُخۡرِجَنَا مِنۡ أَرۡضِنَا بِسِحۡرِكَ يَٰمُوسَىٰ

Qala ajitana litukhrijana min ardina bisihrika ya moosa

Mu daldi ne : “Waaw yaw Muusaa, danga noo bëgg génne ci sunuy suuf ak sa njibar gi ?

58

فَلَنَأۡتِيَنَّكَ بِسِحۡرٖ مِّثۡلِهِۦ فَٱجۡعَلۡ بَيۡنَنَا وَبَيۡنَكَ مَوۡعِدٗا لَّا نُخۡلِفُهُۥ نَحۡنُ وَلَآ أَنتَ مَكَانٗا سُوٗى

Falanatiyannaka bisihrin mithlihi faijAAal baynana wabaynaka mawAAidan la nukhlifuhu nahnu wala anta makanan suwan

Dananu la indil njibar gu ni mel. Nu sàkk bis ak barab te kenn bañ koo wuute ci nun ñépp”.

59

قَالَ مَوۡعِدُكُمۡ يَوۡمُ ٱلزِّينَةِ وَأَن يُحۡشَرَ ٱلنَّاسُ ضُحٗى

Qala mawAAidukum yawmu alzzeenati waan yuhshara alnnasu duhan

Mu wax ne : “Kon jàpp nanu bis ba nu daan daje, di ca fo. Ca yoor- yoor ba”.

60

فَتَوَلَّىٰ فِرۡعَوۡنُ فَجَمَعَ كَيۡدَهُۥ ثُمَّ أَتَىٰ

Fatawalla firAAawnu fajamaAAa kaydahu thumma ata

Firawna daldi dëddu, dem dajale ay pexeem, daldi dellusiwaat.

61

قَالَ لَهُم مُّوسَىٰ وَيۡلَكُمۡ لَا تَفۡتَرُواْ عَلَى ٱللَّهِ كَذِبٗا فَيُسۡحِتَكُم بِعَذَابٖۖ وَقَدۡ خَابَ مَنِ ٱفۡتَرَىٰ

Qala lahum moosa waylakum la taftaroo AAala Allahi kathiban fayushitakum biAAathabin waqad khaba mani iftara

Muusaa ne leen : “Tuskare ngeen ! Fexeleen ba bu leen duural Yàlla ay fen : kon Mu toroxal leen de. Te duurkat sooy nañu”.

62

فَتَنَٰزَعُوٓاْ أَمۡرَهُم بَيۡنَهُمۡ وَأَسَرُّواْ ٱلنَّجۡوَىٰ

FatanazaAAoo amrahum baynahum waasarroo alnnajwa

Ñu xëccoo ca seen biir, gise, déeyoo di yum-yumi.

63

قَالُوٓاْ إِنۡ هَٰذَٰنِ لَسَٰحِرَٰنِ يُرِيدَانِ أَن يُخۡرِجَاكُم مِّنۡ أَرۡضِكُم بِسِحۡرِهِمَا وَيَذۡهَبَا بِطَرِيقَتِكُمُ ٱلۡمُثۡلَىٰ

Qaloo in hathani lasahirani yureedani an yukhrijakum min ardikum bisihrihima wayathhaba bitareeqatikumu almuthla

Ñu daldi wax ne : “Ñaar ñii dey, ay jibar lañu, li leen tax a jóg moo di génne leen ci seenum réew, not leen ba fàwwu.

64

فَأَجۡمِعُواْ كَيۡدَكُمۡ ثُمَّ ٱئۡتُواْ صَفّٗاۚ وَقَدۡ أَفۡلَحَ ٱلۡيَوۡمَ مَنِ ٱسۡتَعۡلَىٰ

FaajmiAAoo kaydakum thumma itoo saffan waqad aflaha alyawma mani istaAAla

Kon booleleen seeni pexe, doon jenn jëmm bisub tey bii. Ku not rekk raw nga ba fàwwu”.

65

قَالُواْ يَٰمُوسَىٰٓ إِمَّآ أَن تُلۡقِيَ وَإِمَّآ أَن نَّكُونَ أَوَّلَ مَنۡ أَلۡقَىٰ

Qaloo ya moosa imma an tulqiya waimma an nakoona awwala man alqa

Ñu ne ko : “Yaw Muusaa, benn nga jëkk a sànni, walla nun nooy jëkk a sànni ?”

66

قَالَ بَلۡ أَلۡقُواْۖ فَإِذَا حِبَالُهُمۡ وَعِصِيُّهُمۡ يُخَيَّلُ إِلَيۡهِ مِن سِحۡرِهِمۡ أَنَّهَا تَسۡعَىٰ

Qala bal alqoo faitha hibaluhum waAAisiyyuhum yukhayyalu ilayhi min sihrihim annaha tasAAa

[Muusaa ne leeen] : “Sànnileen”. Ñu daldi sànni seeni yet ak i buum ca seenug njibar mu mel ni yëf yaa ngay dox di yëngatu.

67

فَأَوۡجَسَ فِي نَفۡسِهِۦ خِيفَةٗ مُّوسَىٰ

Faawjasa fee nafsihi kheefatan moosa

Muusaa xaw a amum tiit ci boppam.

68

قُلۡنَا لَا تَخَفۡ إِنَّكَ أَنتَ ٱلۡأَعۡلَىٰ

Qulna la takhaf innaka anta alaAAla

Nu ne ko : “Bul ragal [yaa leen mën], yaa leen fare kaw.

69

وَأَلۡقِ مَا فِي يَمِينِكَ تَلۡقَفۡ مَا صَنَعُوٓاْۖ إِنَّمَا صَنَعُواْ كَيۡدُ سَٰحِرٖۖ وَلَا يُفۡلِحُ ٱلسَّاحِرُ حَيۡثُ أَتَىٰ

Waalqi ma fee yameenika talqaf ma sanaAAoo innama sanaAAoo kaydu sahirin wala yuflihu alssahiru haythu ata

Sànnil li ci sa loxo ndeyjoor [yet wa] ; li ñuy wone lépp pexey njibarkat doŋŋ la ; te njibarkat moom fàwwu ay tappaleem naaxsaay”. Ba mu ko sànni, yet waa daldi wann yooya yépp

70

فَأُلۡقِيَ ٱلسَّحَرَةُ سُجَّدٗا قَالُوٓاْ ءَامَنَّا بِرَبِّ هَٰرُونَ وَمُوسَىٰ

Faolqiya alssaharatu sujjadan qaloo amanna birabbi haroona wamoosa

Njibarkat yépp far daldi tëdd ci suuf sujjóot, daldi ne : “Gëm nanu bis niki tey Yàllaay Muusaa ak Haaruuna”.

71

قَالَ ءَامَنتُمۡ لَهُۥ قَبۡلَ أَنۡ ءَاذَنَ لَكُمۡۖ إِنَّهُۥ لَكَبِيرُكُمُ ٱلَّذِي عَلَّمَكُمُ ٱلسِّحۡرَۖ فَلَأُقَطِّعَنَّ أَيۡدِيَكُمۡ وَأَرۡجُلَكُم مِّنۡ خِلَٰفٖ وَلَأُصَلِّبَنَّكُمۡ فِي جُذُوعِ ٱلنَّخۡلِ وَلَتَعۡلَمُنَّ أَيُّنَآ أَشَدُّ عَذَابٗا وَأَبۡقَىٰ

Qala amantum lahu qabla an athana lakum innahu lakabeerukumu allathee AAallamakumu alssihra falaoqattiAAanna aydiyakum waarjulakum min khilafin walaosallibannakum fee juthooAAi alnnakhli walataAAlamunna ayyuna ashaddu AAathaban waabqa

[Firawna] ne leen : “Gëmoon ngeen ko la jiitu lii. [Xam naa ne] Muusaa mooy kàndiŋ mi leen jàngal ag njibar. Danaa dàgg seeni tànk ak seeni yoxo cig jàllawle, danaa leen daaj ci dàtti tàndarma yi, dangeen xam kan ci nun moo gën a mettile te gën a tarle mbugal”.(s)

72

قَالُواْ لَن نُّؤۡثِرَكَ عَلَىٰ مَا جَآءَنَا مِنَ ٱلۡبَيِّنَٰتِ وَٱلَّذِي فَطَرَنَاۖ فَٱقۡضِ مَآ أَنتَ قَاضٍۖ إِنَّمَا تَقۡضِي هَٰذِهِ ٱلۡحَيَوٰةَ ٱلدُّنۡيَآ

Qaloo lan nuthiraka AAala ma jaana mina albayyinati waallathee fatarana faiqdi ma anta qadin innama taqdee hathihi alhayata alddunya

Ñu ne ko : “Yàlla mi ñu bind ak kàddoom yii Mu nu indil moo nu la gënal fàwwu. Dogalal loo bëgg a dogal. Waaye nag say àtte moom àddina rekk la yem.

73

إِنَّآ ءَامَنَّا بِرَبِّنَا لِيَغۡفِرَ لَنَا خَطَٰيَٰنَا وَمَآ أَكۡرَهۡتَنَا عَلَيۡهِ مِنَ ٱلسِّحۡرِۗ وَٱللَّهُ خَيۡرٞ وَأَبۡقَىٰٓ

Inna amanna birabbina liyaghfira lana khatayana wama akrahtana AAalayhi mina alssihri waAllahu khayrun waabqa

Nun dey gëm nanu sunu Boroom ngir mu jéggal nu sunuy bàkkaar, ak njibar gii nga nu jaay doole ba tax nu def ko”. Te Yàlla Moo gën te Mooy des.

74

إِنَّهُۥ مَن يَأۡتِ رَبَّهُۥ مُجۡرِمٗا فَإِنَّ لَهُۥ جَهَنَّمَ لَا يَمُوتُ فِيهَا وَلَا يَحۡيَىٰ

Innahu man yati rabbahu mujriman fainna lahu jahannama la yamootu feeha wala yahya

Kuy saay-saay ba dem fa Boroomam, dana tàbbi Safara te du fa dee du fa dundu.

75

وَمَن يَأۡتِهِۦ مُؤۡمِنٗا قَدۡ عَمِلَ ٱلصَّـٰلِحَٰتِ فَأُوْلَـٰٓئِكَ لَهُمُ ٱلدَّرَجَٰتُ ٱلۡعُلَىٰ

Waman yatihi muminan qad AAamila alssalihati faolaika lahumu alddarajatu alAAula

Kuy gëm Yàlla ak a def u yiw ba dem fa Yàlla, ñooña danañu am ay daraja yu kawe,

76

جَنَّـٰتُ عَدۡنٖ تَجۡرِي مِن تَحۡتِهَا ٱلۡأَنۡهَٰرُ خَٰلِدِينَ فِيهَاۚ وَذَٰلِكَ جَزَآءُ مَن تَزَكَّىٰ

Jannatu AAadnin tajree min tahtiha alanharu khalideena feeha wathalika jazao man tazakka

ay àjjana yu sax yoo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam te dañu fay béel. Loolu moo di peyug képp kuy sellal.

77

وَلَقَدۡ أَوۡحَيۡنَآ إِلَىٰ مُوسَىٰٓ أَنۡ أَسۡرِ بِعِبَادِي فَٱضۡرِبۡ لَهُمۡ طَرِيقٗا فِي ٱلۡبَحۡرِ يَبَسٗا لَّا تَخَٰفُ دَرَكٗا وَلَا تَخۡشَىٰ

Walaqad awhayna ila moosa an asri biAAibadee faidrib lahum tareeqan fee albahri yabasan la takhafu darakan wala takhsha

Digal Nanu Muusaa [soloo ko]ne ko : “Nga rañaan ak sama jaam ñi, nanga leen sàkkal aw yoonu suuf wu wow ca biir géej ga : bul ragal ku lay dab walla ngay tiit”.

78

فَأَتۡبَعَهُمۡ فِرۡعَوۡنُ بِجُنُودِهِۦ فَغَشِيَهُم مِّنَ ٱلۡيَمِّ مَا غَشِيَهُمۡ

FaatbaAAahum firAAawnu bijunoodihi faghashiyahum mina alyammi ma ghashiyahum

Firawna ak ug xareem topp leen. Duus ya labal leen.

79

وَأَضَلَّ فِرۡعَوۡنُ قَوۡمَهُۥ وَمَا هَدَىٰ

Waadalla firAAawnu qawmahu wama hada

Firawna sànk na aw nitam, te farul gindiku.

80

يَٰبَنِيٓ إِسۡرَـٰٓءِيلَ قَدۡ أَنجَيۡنَٰكُم مِّنۡ عَدُوِّكُمۡ وَوَٰعَدۡنَٰكُمۡ جَانِبَ ٱلطُّورِ ٱلۡأَيۡمَنَ وَنَزَّلۡنَا عَلَيۡكُمُ ٱلۡمَنَّ وَٱلسَّلۡوَىٰ

Ya banee israeela qad anjaynakum min AAaduwwikum wawaAAadnakum janiba alttoori alaymana wanazzalna AAalaykumu almanna waalssalwa

Éy yéen waa giir Banii-Israayiil, musal Nanu leen ci seenub noon, Nu digeek yéen fa wàllug ndeyjooru tundu Sinaay wa. Nu wàcceel leen yàpp.

81

كُلُواْ مِن طَيِّبَٰتِ مَا رَزَقۡنَٰكُمۡ وَلَا تَطۡغَوۡاْ فِيهِ فَيَحِلَّ عَلَيۡكُمۡ غَضَبِيۖ وَمَن يَحۡلِلۡ عَلَيۡهِ غَضَبِي فَقَدۡ هَوَىٰ

Kuloo min tayyibati ma razaqnakum wala tatghaw feehi fayahilla AAalaykum ghadabee waman yahlil AAalayhi ghadabee faqad hawa

“Lekk-leen ci lu teey [sell] li Nu leen wërsëgale te buleen ca beew, [bu ngeen beewee], kon Sama mer day wàcc ci seen kaw : te képp ku Sama mer wàcc ci kawam, sànku na.

82

وَإِنِّي لَغَفَّارٞ لِّمَن تَابَ وَءَامَنَ وَعَمِلَ صَٰلِحٗا ثُمَّ ٱهۡتَدَىٰ

Wainnee laghaffarun liman taba waamana waAAamila salihan thumma ihtada

Te moo ne Man dey ab Jéggalaakoon laa ci képp ku tuub, te gëm, te jëf u yiw tey jubal”.

83

۞وَمَآ أَعۡجَلَكَ عَن قَوۡمِكَ يَٰمُوسَىٰ

Wama aAAjalaka AAan qawmika ya moosa

“Waaw Muusaa, ana lan moo tax nga jiitu saw nit ?”(n)

84

قَالَ هُمۡ أُوْلَآءِ عَلَىٰٓ أَثَرِي وَعَجِلۡتُ إِلَيۡكَ رَبِّ لِتَرۡضَىٰ

Qala hum olai AAala atharee waAAajiltu ilayka rabbi litarda

Mu ne ko ñoom dey ñanga ca sama ginnaaw. Ma yàkkamtee agsi ci Yaw ba am sa ngërëm.

85

قَالَ فَإِنَّا قَدۡ فَتَنَّا قَوۡمَكَ مِنۢ بَعۡدِكَ وَأَضَلَّهُمُ ٱلسَّامِرِيُّ

Qala fainna qad fatanna qawmaka min baAAdika waadallahumu alssamiriyyu

[Yàlla] ne ko : “Nattu woon Nanu saw nit sa ginnaaw. Saamiriyu ñëw moom sànk leen”.

86

فَرَجَعَ مُوسَىٰٓ إِلَىٰ قَوۡمِهِۦ غَضۡبَٰنَ أَسِفٗاۚ قَالَ يَٰقَوۡمِ أَلَمۡ يَعِدۡكُمۡ رَبُّكُمۡ وَعۡدًا حَسَنًاۚ أَفَطَالَ عَلَيۡكُمُ ٱلۡعَهۡدُ أَمۡ أَرَدتُّمۡ أَن يَحِلَّ عَلَيۡكُمۡ غَضَبٞ مِّن رَّبِّكُمۡ فَأَخۡلَفۡتُم مَّوۡعِدِي

FarajaAAa moosa ila qawmihi ghadbana asifan qala ya qawmi alam yaAAidkum rabbukum waAAdan hasanan afatala AAalaykumu alAAahdu am aradtum an yahilla AAalaykum ghadabun min rabbikum faakhlaftum mawAAidee

Muusaa dellu fa nitam ña mer bay fuur ; ne leen : “Yéen samaw nit, ndax Yàlla digu leen woon dig wu rafet ? Walla dig wa dafa yàgg ? Walla dangeen bëgg merum Yàlla wàcc ci seen kaw, ba tax ngeen wuute samag dig ay yéen ?”

87

قَالُواْ مَآ أَخۡلَفۡنَا مَوۡعِدَكَ بِمَلۡكِنَا وَلَٰكِنَّا حُمِّلۡنَآ أَوۡزَارٗا مِّن زِينَةِ ٱلۡقَوۡمِ فَقَذَفۡنَٰهَا فَكَذَٰلِكَ أَلۡقَى ٱلسَّامِرِيُّ

Qaloo ma akhlafna mawAAidaka bimalkina walakinna hummilna awzaran min zeenati alqawmi faqathafnaha fakathalika alqa alssamiriyyu

Ñu ne ko : “Wuutewuñu sab dig. Waaye danu noo nax sànniloo nu takkaay ya ; ca noona la ko Saamiriyu sànnee ca safara wa.

88

فَأَخۡرَجَ لَهُمۡ عِجۡلٗا جَسَدٗا لَّهُۥ خُوَارٞ فَقَالُواْ هَٰذَآ إِلَٰهُكُمۡ وَإِلَٰهُ مُوسَىٰ فَنَسِيَ

Faakhraja lahum AAijlan jasadan lahu khuwarun faqaloo hatha ilahukum wailahu moosa fanasiya

Daldi leen cay génneel aw sëll [nag]. Ne leen : “Mooy seen yàlla ; ñu daldi fàtte Yàllay Muusaa” !

89

أَفَلَا يَرَوۡنَ أَلَّا يَرۡجِعُ إِلَيۡهِمۡ قَوۡلٗا وَلَا يَمۡلِكُ لَهُمۡ ضَرّٗا وَلَا نَفۡعٗا

Afala yarawna alla yarjiAAu ilayhim qawlan wala yamliku lahum darran wala nafAAan

Moo ndax dañoo gisul ne bu ñul wax ak moom du toontu, te mënuleen a lor, mënuleen a jariñ dara ?

90

وَلَقَدۡ قَالَ لَهُمۡ هَٰرُونُ مِن قَبۡلُ يَٰقَوۡمِ إِنَّمَا فُتِنتُم بِهِۦۖ وَإِنَّ رَبَّكُمُ ٱلرَّحۡمَٰنُ فَٱتَّبِعُونِي وَأَطِيعُوٓاْ أَمۡرِي

Walaqad qala lahum haroonu min qablu ya qawmi innama futintum bihi wainna rabbakumu alrrahmanu faittabiAAoonee waateeAAoo amree

Aaruuna moom waxoon na leen bu njëkk ne leen: “Yéen samaw nit, lii ngeen nekk aw sànje la. Waaye seen Boroom moo di Yërëmaakoon bi. Toppleen ma te wéyal samay ndigal”.

91

قَالُواْ لَن نَّبۡرَحَ عَلَيۡهِ عَٰكِفِينَ حَتَّىٰ يَرۡجِعَ إِلَيۡنَا مُوسَىٰ

Qaloo lan nabraha AAalayhi AAakifeena hatta yarjiAAa ilayna moosa

Ñu ne ko : “Dunu fi jóge mukk ba ba Muusaa di dellusi fi nun”.

92

قَالَ يَٰهَٰرُونُ مَا مَنَعَكَ إِذۡ رَأَيۡتَهُمۡ ضَلُّوٓاْ

Qala ya haroonu ma manaAAaka ith raaytahum dalloo

[Ba Muusaa dellusee] ne : “Yaw Aaruuna, lan moo tere woon nga waar leen ba ñu sànkoo.

93

أَلَّا تَتَّبِعَنِۖ أَفَعَصَيۡتَ أَمۡرِي

Alla tattabiAAani afaAAasayta amree

Danga maa toppatul walla dangaa mooy léegi samay ndigal ?”

94

قَالَ يَبۡنَؤُمَّ لَا تَأۡخُذۡ بِلِحۡيَتِي وَلَا بِرَأۡسِيٓۖ إِنِّي خَشِيتُ أَن تَقُولَ فَرَّقۡتَ بَيۡنَ بَنِيٓ إِسۡرَـٰٓءِيلَ وَلَمۡ تَرۡقُبۡ قَوۡلِي

Qala ya bna omma la takhuth bilihyatee wala birasee innee khasheetu an taqoola farraqta bayna banee israeela walam tarqub qawlee

[Aaruuna] ne ko : “Doom ndey, bul bipp samab sikkim mbaa sama kawari bopp. Damaa ragaloon nga naan ma : “Féewale nga giiru Bani-Israayiila, toppoo sama ndigal, [lii rekk la]”.

95

قَالَ فَمَا خَطۡبُكَ يَٰسَٰمِرِيُّ

Qala fama khatbuka ya samiriyyu

Muusaa ne : “Ayca Saamiriyu, waxal book ?”

96

قَالَ بَصُرۡتُ بِمَا لَمۡ يَبۡصُرُواْ بِهِۦ فَقَبَضۡتُ قَبۡضَةٗ مِّنۡ أَثَرِ ٱلرَّسُولِ فَنَبَذۡتُهَا وَكَذَٰلِكَ سَوَّلَتۡ لِي نَفۡسِي

Qala basurtu bima lam yabsuroo bihi faqabadtu qabdatan min athari alrrasooli fanabathtuha wakathalika sawwalat lee nafsee

Mu ne : “Gis naa lu ñu gisul : ma daldi ŋoor ci suufi jeexiti Yonent bi, daldi koy sànni li am am. Loolu la ma sama xel joxoon”.

97

قَالَ فَٱذۡهَبۡ فَإِنَّ لَكَ فِي ٱلۡحَيَوٰةِ أَن تَقُولَ لَا مِسَاسَۖ وَإِنَّ لَكَ مَوۡعِدٗا لَّن تُخۡلَفَهُۥۖ وَٱنظُرۡ إِلَىٰٓ إِلَٰهِكَ ٱلَّذِي ظَلۡتَ عَلَيۡهِ عَاكِفٗاۖ لَّنُحَرِّقَنَّهُۥ ثُمَّ لَنَنسِفَنَّهُۥ فِي ٱلۡيَمِّ نَسۡفًا

Qala faithhab fainna laka fee alhayati an taqoola la misasa wainna laka mawAAidan lan tukhlafahu waonthur ila ilahika allathee thalta AAalayhi AAakifan lanuharriqannahu thumma lanansifannahu fee alyammi nasfan

[Muusaa] daldi ne ko : “Ayca, demal. Toppal sa një : “Dootoo jegeñ kenn !” Te am nga dig boo dul wuute. Te xoolal sa yàlla ji nga daan jaamu. Dananu ko lakk, sànni ko ca ndox ma.

98

إِنَّمَآ إِلَٰهُكُمُ ٱللَّهُ ٱلَّذِي لَآ إِلَٰهَ إِلَّا هُوَۚ وَسِعَ كُلَّ شَيۡءٍ عِلۡمٗا

Innama ilahukumu Allahu allathee la ilaha illa huwa wasiAAa kulla shayin AAilman

[Seen Yàlla tigi] mooy Yàlla jenn ja, amul jeneen ju dul Moom. Moo xam lépp.(s)

99

كَذَٰلِكَ نَقُصُّ عَلَيۡكَ مِنۡ أَنۢبَآءِ مَا قَدۡ سَبَقَۚ وَقَدۡ ءَاتَيۡنَٰكَ مِن لَّدُنَّا ذِكۡرٗا

Kathalika naqussu AAalayka min anbai ma qad sabaqa waqad ataynaka min ladunna thikran

Noonu la Nu lay nettalee xew-xewi ña jiitu woon. Indil naa la njàng mu bawoo fi Man.

100

مَّنۡ أَعۡرَضَ عَنۡهُ فَإِنَّهُۥ يَحۡمِلُ يَوۡمَ ٱلۡقِيَٰمَةِ وِزۡرًا

Man aAArada AAanhu fainnahu yahmilu yawma alqiyamati wizran

Ku ko dummóoyu [kàddu yooyu], bu Bis-pénc baa, dana yenu ay bàkkaar [mbugal] ;

101

خَٰلِدِينَ فِيهِۖ وَسَآءَ لَهُمۡ يَوۡمَ ٱلۡقِيَٰمَةِ حِمۡلٗا

Khalideena feehi wasaa lahum yawma alqiyamati himlan

te dañu cay béelbu keroo gee [Bis-pénc ba], ndaw yen bu bon,

102

يَوۡمَ يُنفَخُ فِي ٱلصُّورِۚ وَنَحۡشُرُ ٱلۡمُجۡرِمِينَ يَوۡمَئِذٖ زُرۡقٗا

Yawma yunfakhu fee alssoori wanahshuru almujrimeena yawmaithin zurqan

bis ba ñu walee [ëf] buftu ba, bis boobee, Dananu pang tooñkat ya ñuy fér-féri [ndax tiit] !

103

يَتَخَٰفَتُونَ بَيۡنَهُمۡ إِن لَّبِثۡتُمۡ إِلَّا عَشۡرٗا

Yatakhafatoona baynahum in labithtum illa AAashran

Ñuy déeyante ca seen biir naan : “Yéen kat fukki fan doŋŋ ngeen am àddina” !

104

نَّحۡنُ أَعۡلَمُ بِمَا يَقُولُونَ إِذۡ يَقُولُ أَمۡثَلُهُمۡ طَرِيقَةً إِن لَّبِثۡتُمۡ إِلَّا يَوۡمٗا

Nahnu aAAlamu bima yaqooloona ith yaqoolu amthaluhum tareeqatan in labithtum illa yawman

Nun [Yàlla] Noo gën a xam la ñuy wax, far ka leen gën a kaanu naan : “Aa yéen kat benn fan doŋŋ ngeen am àddina”.

105

وَيَسۡـَٔلُونَكَ عَنِ ٱلۡجِبَالِ فَقُلۡ يَنسِفُهَا رَبِّي نَسۡفٗا

Wayasaloonaka AAani aljibali faqul yansifuha rabbee nasfan

Ñii nga lay laaj ci dundi doj yi [naka lay mujje]. Neel : “Yàlla dana leen moxoñe,

106

فَيَذَرُهَا قَاعٗا صَفۡصَفٗا

Fayatharuha qaAAan safsafan

bàyyi ko mu ne ag joor gu ne càndaŋ

107

لَّا تَرَىٰ فِيهَا عِوَجٗا وَلَآ أَمۡتٗا

La tara feeha AAiwajan wala amtan

dootoo gis ab nóox-nóox walla ab junni-junni, léppay maase nerr.

108

يَوۡمَئِذٖ يَتَّبِعُونَ ٱلدَّاعِيَ لَا عِوَجَ لَهُۥۖ وَخَشَعَتِ ٱلۡأَصۡوَاتُ لِلرَّحۡمَٰنِ فَلَا تَسۡمَعُ إِلَّا هَمۡسٗا

Yawmaithin yattabiAAoona alddaAAiya la AAiwaja lahu wakhashaAAati alaswatu lilrrahmani fala tasmaAAu illa hamsan

Ca Bis booba ñépp danañu topp wootekat ba ; kàddu yépp ne xuum [cëy Yàlla Yërëmaakoon bi]. Doofa dégg lu dul kuy dée [di wax ndànk].

109

يَوۡمَئِذٖ لَّا تَنفَعُ ٱلشَّفَٰعَةُ إِلَّا مَنۡ أَذِنَ لَهُ ٱلرَّحۡمَٰنُ وَرَضِيَ لَهُۥ قَوۡلٗا

Yawmaithin la tanfaAAu alshshafaAAatu illa man athina lahu alrrahmanu waradiya lahu qawlan

Bisub kerook, kenn du fa mën a ramm ku dul koo xam ne Yërëmaakoon baa ko ko digal te gërëm ay waxam.

110

يَعۡلَمُ مَا بَيۡنَ أَيۡدِيهِمۡ وَمَا خَلۡفَهُمۡ وَلَا يُحِيطُونَ بِهِۦ عِلۡمٗا

YaAAlamu ma bayna aydeehim wama khalfahum wala yuheetoona bihi AAilman

Moo xam la jàll ak liy ñëwi, te kenn ci ñoom mënu koo peeg ci xam ko.

111

۞وَعَنَتِ ٱلۡوُجُوهُ لِلۡحَيِّ ٱلۡقَيُّومِۖ وَقَدۡ خَابَ مَنۡ حَمَلَ ظُلۡمٗا

WaAAanati alwujoohu lilhayyi alqayyoomi waqad khaba man hamala thulman

Loos yépp janoo nañu fa kanamu Yàlla, Muy dundu te taxawu lépp, te képp ku yenu na ag tooñ , [na ko wóor ne] sooy na bu kero gee.

112

وَمَن يَعۡمَلۡ مِنَ ٱلصَّـٰلِحَٰتِ وَهُوَ مُؤۡمِنٞ فَلَا يَخَافُ ظُلۡمٗا وَلَا هَضۡمٗا

Waman yaAAmal mina alssalihati wahuwa muminun fala yakhafu thulman wala hadman

Képp koo xam ne nag yaa ngay jëf u yiw te gëm, du ragal foofa ag tooñ [gu ñu koy tooñ], walla ku koy sërxal.(r)

113

وَكَذَٰلِكَ أَنزَلۡنَٰهُ قُرۡءَانًا عَرَبِيّٗا وَصَرَّفۡنَا فِيهِ مِنَ ٱلۡوَعِيدِ لَعَلَّهُمۡ يَتَّقُونَ أَوۡ يُحۡدِثُ لَهُمۡ ذِكۡرٗا

Wakathalika anzalnahu quranan AAarabiyyan wasarrafna feehi mina alwaAAeedi laAAallahum yattaqoona aw yuhdithu lahum thikran

Noonu Lanu wàccee Alxuraan ci làmmiñu araab, biral ci lool ag tëkku, ndaxtele amaana ñu ragal Yàlla walla ñu jàjju [fàttaliku xalaat]?

114

فَتَعَٰلَى ٱللَّهُ ٱلۡمَلِكُ ٱلۡحَقُّۗ وَلَا تَعۡجَلۡ بِٱلۡقُرۡءَانِ مِن قَبۡلِ أَن يُقۡضَىٰٓ إِلَيۡكَ وَحۡيُهُۥۖ وَقُل رَّبِّ زِدۡنِي عِلۡمٗا

FataAAala Allahu almaliku alhaqqu wala taAAjal bialqurani min qabli an yuqda ilayka wahyuhu waqul rabbi zidnee AAilman

Yàlla Buur ba di dëgg, kawe na ! Bul yàkkamtee tasaare Alxuraan ji tey jiitu soloo ga. Waxal ne : “Yaw sama Boroom dolli ma xam-xam !”

115

وَلَقَدۡ عَهِدۡنَآ إِلَىٰٓ ءَادَمَ مِن قَبۡلُ فَنَسِيَ وَلَمۡ نَجِدۡ لَهُۥ عَزۡمٗا

Walaqad AAahidna ila adama min qablu fanasiya walam najid lahu AAazman

Fasantee woon Nanu ak Aadama ab dig ca la jiitu woon ; mu fàtte ; te taxu ko caa woo na farlu.

116

وَإِذۡ قُلۡنَا لِلۡمَلَـٰٓئِكَةِ ٱسۡجُدُواْ لِأٓدَمَ فَسَجَدُوٓاْ إِلَّآ إِبۡلِيسَ أَبَىٰ

Waith qulna lilmalaikati osjudoo liadama fasajadoo illa ibleesa aba

[Fàttalikul] ba Nu waxee Malaaka ya ne leen : “Sujjóotleen ci Aadama”, ñépp sujjóot ba mu des Ibliis, moom dafa lànk.

117

فَقُلۡنَا يَـٰٓـَٔادَمُ إِنَّ هَٰذَا عَدُوّٞ لَّكَ وَلِزَوۡجِكَ فَلَا يُخۡرِجَنَّكُمَا مِنَ ٱلۡجَنَّةِ فَتَشۡقَىٰٓ

Faqulna ya adamu inna hatha AAaduwwun laka walizawjika fala yukhrijannakuma mina aljannati fatashqa

Nu wax ko ne ko : “Kii dey sab noon la yaak sa soxna. Farluleen ba bu mu leen génne Àjjana, [su ngeen génnee] da ngeen sonnu de.

118

إِنَّ لَكَ أَلَّا تَجُوعَ فِيهَا وَلَا تَعۡرَىٰ

Inna laka alla tajooAAa feeha wala taAAra

[Fii ci Àjjana] doo fi xiif, doo fi rafle,

119

وَأَنَّكَ لَا تَظۡمَؤُاْ فِيهَا وَلَا تَضۡحَىٰ

Waannaka la tathmao feeha wala tadha

doo fi yëg u mar, doo fi màggat”.

120

فَوَسۡوَسَ إِلَيۡهِ ٱلشَّيۡطَٰنُ قَالَ يَـٰٓـَٔادَمُ هَلۡ أَدُلُّكَ عَلَىٰ شَجَرَةِ ٱلۡخُلۡدِ وَمُلۡكٖ لَّا يَبۡلَىٰ

Fawaswasa ilayhi alshshaytanu qala ya adamu hal adulluka AAala shajarati alkhuldi wamulkin la yabla

Séytaane daldi koy jax-jaxal [nëxal xelam] ne ko : “Yaw Aadama, ndax duma la tegtal garab guy tax nga am nguur gu dootul foq ?”

121

فَأَكَلَا مِنۡهَا فَبَدَتۡ لَهُمَا سَوۡءَٰتُهُمَا وَطَفِقَا يَخۡصِفَانِ عَلَيۡهِمَا مِن وَرَقِ ٱلۡجَنَّةِۚ وَعَصَىٰٓ ءَادَمُ رَبَّهُۥ فَغَوَىٰ

Faakala minha fabadat lahuma sawatuhuma watafiqa yakhsifani AAalayhima min waraqi aljannati waAAasa adamu rabbahu faghawa

Ñu daldi cay lekk [garab ga]. Seen rafle wa daldi feeñ. Ñu tàmbalee witt ca xobi garab ya nekk Àjjana di ko làmboo. Aadama moy na ndigalu Boroomam, tooñ tàbbi.

122

ثُمَّ ٱجۡتَبَٰهُ رَبُّهُۥ فَتَابَ عَلَيۡهِ وَهَدَىٰ

Thumma ijtabahu rabbuhu fataba AAalayhi wahada

Yàlla delloo cim xelam ba mu tuub, Mu daldi koy jéggal, Mu daldi it jubbanti ko.

123

قَالَ ٱهۡبِطَا مِنۡهَا جَمِيعَۢاۖ بَعۡضُكُمۡ لِبَعۡضٍ عَدُوّٞۖ فَإِمَّا يَأۡتِيَنَّكُم مِّنِّي هُدٗى فَمَنِ ٱتَّبَعَ هُدَايَ فَلَا يَضِلُّ وَلَا يَشۡقَىٰ

Qala ihbita minha jameeAAan baAAdukum libaAAdin AAaduwwun faimma yatiyannakum minnee hudan famani ittabaAAa hudaya fala yadillu wala yashqa

Yàlla daldi ne leen : “Génnleen Àjjana, wàcc jëm suuf, ñennat ci yéen di noonoo ñeneen ña ca des. Dana am nag njub gu bawoo fi Man dikk ci yéen, képp ku topp Sama njub googu, du sànku, du sonn.

124

وَمَنۡ أَعۡرَضَ عَن ذِكۡرِي فَإِنَّ لَهُۥ مَعِيشَةٗ ضَنكٗا وَنَحۡشُرُهُۥ يَوۡمَ ٱلۡقِيَٰمَةِ أَعۡمَىٰ

Waman aAArada AAan thikree fainna lahu maAAeeshatan dankan wanahshuruhu yawma alqiyamati aAAman

Képp ku ko dummóoyu, dana dundu dund gu metti, te buy dekki Bis-pénc ba gumba lay doon ñu gotti ko”.

125

قَالَ رَبِّ لِمَ حَشَرۡتَنِيٓ أَعۡمَىٰ وَقَدۡ كُنتُ بَصِيرٗا

Qala rabbi lima hashartanee aAAma waqad kuntu baseeran

[Su ko defee] muy laaj naan : “Sama Boroom, lan moo tax nga pang ma may gumba te ca àddina ma doon gis ?”

126

قَالَ كَذَٰلِكَ أَتَتۡكَ ءَايَٰتُنَا فَنَسِيتَهَاۖ وَكَذَٰلِكَ ٱلۡيَوۡمَ تُنسَىٰ

Qala kathalika atatka ayatuna fanaseetaha wakathalika alyawma tunsa

[Yàlla tontu] ne ko : “Noonu la la Sunuy kàddu dikkalee woon, nga sàggane ko, kon book tey yaw itam kenn du la faale”.(s)

127

وَكَذَٰلِكَ نَجۡزِي مَنۡ أَسۡرَفَ وَلَمۡ يُؤۡمِنۢ بِـَٔايَٰتِ رَبِّهِۦۚ وَلَعَذَابُ ٱلۡأٓخِرَةِ أَشَدُّ وَأَبۡقَىٰٓ

Wakathalika najzee man asrafa walam yumin biayati rabbihi walaAAathabu alakhirati ashaddu waabqa

Noonu la Nuy feye ña ëppal [xaabaabal] te gëmuñu seen kàdduy Boroom [ay màndargaam]. Te mbugalum àllaaxira moo gën a tar te gën a yàgg.

128

أَفَلَمۡ يَهۡدِ لَهُمۡ كَمۡ أَهۡلَكۡنَا قَبۡلَهُم مِّنَ ٱلۡقُرُونِ يَمۡشُونَ فِي مَسَٰكِنِهِمۡۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَأٓيَٰتٖ لِّأُوْلِي ٱلنُّهَىٰ

Afalam yahdi lahum kam ahlakna qablahum mina alqurooni yamshoona fee masakinihim inna fee thalika laayatin liolee alnnuha

Ndax dafa leerul ci seen bopp te aka bari ay xeet yu Nu alag ca ña leen jiitu woon te tey ñuy dox ci kaw fa ñu dëkkoon ? Loolu war naa mën a waar ñu am xel [te di ko jariñoo] !

129

وَلَوۡلَا كَلِمَةٞ سَبَقَتۡ مِن رَّبِّكَ لَكَانَ لِزَامٗا وَأَجَلٞ مُّسَمّٗى

Walawla kalimatun sabaqat min rabbika lakana lizaman waajalun musamman

Su fekkoon ne du dig bu ko Yàlla sàkkal, kon seen mbugal fii lay tàmbalee.

130

فَٱصۡبِرۡ عَلَىٰ مَا يَقُولُونَ وَسَبِّحۡ بِحَمۡدِ رَبِّكَ قَبۡلَ طُلُوعِ ٱلشَّمۡسِ وَقَبۡلَ غُرُوبِهَاۖ وَمِنۡ ءَانَآيِٕ ٱلَّيۡلِ فَسَبِّحۡ وَأَطۡرَافَ ٱلنَّهَارِ لَعَلَّكَ تَرۡضَىٰ

Faisbir AAala ma yaqooloona wasabbih bihamdi rabbika qabla tulooAAi alshshamsi waqabla ghuroobiha wamin anai allayli fasabbih waatrafa alnnahari laAAallaka tarda

Nanga muñ li ñuy wax te nga sàbbaal ci cantug sa Boorom balaa jant bi di fenk ak balaa muy so, ak guddi gi ak subaak ngoon. Soo bëggee maare [gërëm Yàlla te am xel mu dal] :

131

وَلَا تَمُدَّنَّ عَيۡنَيۡكَ إِلَىٰ مَا مَتَّعۡنَا بِهِۦٓ أَزۡوَٰجٗا مِّنۡهُمۡ زَهۡرَةَ ٱلۡحَيَوٰةِ ٱلدُّنۡيَا لِنَفۡتِنَهُمۡ فِيهِۚ وَرِزۡقُ رَبِّكَ خَيۡرٞ وَأَبۡقَىٰ

Wala tamuddanna AAaynayka ila ma mattaAAna bihi azwajan minhum zahrata alhayati alddunya linaftinahum feehi warizqu rabbika khayrun waabqa

Bul wékk say gët ci li Nu leen wërsëgal ci ay jabar ak alali àddina, ngir sànk leen ci doŋŋ la. Sa peyug Boroom moo gën [fuuf] te moo gën a sax.

132

وَأۡمُرۡ أَهۡلَكَ بِٱلصَّلَوٰةِ وَٱصۡطَبِرۡ عَلَيۡهَاۖ لَا نَسۡـَٔلُكَ رِزۡقٗاۖ نَّحۡنُ نَرۡزُقُكَۗ وَٱلۡعَٰقِبَةُ لِلتَّقۡوَىٰ

Wamur ahlaka bialssalati waistabir AAalayha la nasaluka rizqan nahnu narzuquka waalAAaqibatu lilttaqwa

Nanga digal sag njaboot ñuy julli, te nanga saxoo muñ. Tegunu la wut ub dundu : Nun noo warloo sab dund. Ña ragal Yàlla ñoo ëppug muj.

133

وَقَالُواْ لَوۡلَا يَأۡتِينَا بِـَٔايَةٖ مِّن رَّبِّهِۦٓۚ أَوَلَمۡ تَأۡتِهِم بَيِّنَةُ مَا فِي ٱلصُّحُفِ ٱلۡأُولَىٰ

Waqaloo lawla yateena biayatin min rabbihi awalam tatihim bayyinatu ma fee alssuhufi aloola

Ñuy wax naan : “Lan moo tax indilunu kiiman gu bawoo ca Boroomam ? Moo ndax xalam mujjug ña leen jiitu woon da leen a doyul am njàng ?

134

وَلَوۡ أَنَّآ أَهۡلَكۡنَٰهُم بِعَذَابٖ مِّن قَبۡلِهِۦ لَقَالُواْ رَبَّنَا لَوۡلَآ أَرۡسَلۡتَ إِلَيۡنَا رَسُولٗا فَنَتَّبِعَ ءَايَٰتِكَ مِن قَبۡلِ أَن نَّذِلَّ وَنَخۡزَىٰ

Walaw anna ahlaknahum biAAathabin min qablihi laqaloo rabbana lawla arsalta ilayna rasoolan fanattabiAAa ayatika min qabli an nathilla wanakhza

Bu fekkoon ne Danu leen a mbugal la ko jiitu, kon ñuy wax naan : “Cëy Yàlla soo yónni woon ab Yonent ci nun, kon dananu topp say ndigal bala noo torox ak a tuskare”.

135

قُلۡ كُلّٞ مُّتَرَبِّصٞ فَتَرَبَّصُواْۖ فَسَتَعۡلَمُونَ مَنۡ أَصۡحَٰبُ ٱلصِّرَٰطِ ٱلسَّوِيِّ وَمَنِ ٱهۡتَدَىٰ

Qul kullun mutarabbisun fatarabbasoo fasataAAlamoona man ashabu alssirati alssawiyyi wamani ihtada

Neel : “Ñépp a ngay xaar. Xaarleen yéen it ! Dangeen xam ñan ñoo jaaroon ca yoon wu jub wa xocc ak ana ñan ñoo gënoon a gindiku”. Saar 21 : Yonent ya 112 Laaya