قٓۚ وَٱلۡقُرۡءَانِ ٱلۡمَجِيدِ
Qaf waalqurani almajeedi
Qaaf. Ak ci Alxuraan ju tedd ji ( laay giñ) !
Qaf
The Letter "Qaf"
Tekki
قٓۚ وَٱلۡقُرۡءَانِ ٱلۡمَجِيدِ
Qaf waalqurani almajeedi
Qaaf. Ak ci Alxuraan ju tedd ji ( laay giñ) !
بَلۡ عَجِبُوٓاْ أَن جَآءَهُم مُّنذِرٞ مِّنۡهُمۡ فَقَالَ ٱلۡكَٰفِرُونَ هَٰذَا شَيۡءٌ عَجِيبٌ
Bal AAajiboo an jaahum munthirun minhum faqala alkafiroona hatha shayon AAajeebun
Waaye dañoo yéemu ba ñu amee waaraatekat bu bokk ci ñom ; digël leen yéefar ya di wax naan : “Lii dey mbir mu yéeme la”.
أَءِذَا مِتۡنَا وَكُنَّا تُرَابٗاۖ ذَٰلِكَ رَجۡعُۢ بَعِيدٞ
Aitha mitna wakunna turaban thalika rajAAun baAAeedun
Ana ! Luy xew bu ñu deewee ba doon suuf...? Moo ndaw dellu guy sori waay” !
قَدۡ عَلِمۡنَا مَا تَنقُصُ ٱلۡأَرۡضُ مِنۡهُمۡۖ وَعِندَنَا كِتَٰبٌ حَفِيظُۢ
Qad AAalimna ma tanqusu alardu minhum waAAindana kitabun hafeethun
(Man Yàlla) Xam na a li suuf si di lekk ci ñoom ; te it Téere bu sàmmu baa ngi fi Nun (“Allawhul Mahfuuz”).
بَلۡ كَذَّبُواْ بِٱلۡحَقِّ لَمَّا جَآءَهُمۡ فَهُمۡ فِيٓ أَمۡرٖ مَّرِيجٍ
Bal kaththaboo bialhaqqi lamma jaahum fahum fee amrin mareejin
Ñoom weddi nañu dëgg ca waxtu wa mu dikëlee : ñoo nga ca mbirumu walayaange.
أَفَلَمۡ يَنظُرُوٓاْ إِلَى ٱلسَّمَآءِ فَوۡقَهُمۡ كَيۡفَ بَنَيۡنَٰهَا وَزَيَّنَّـٰهَا وَمَا لَهَا مِن فُرُوجٖ
Afalam yanthuroo ila alssamai fawqahum kayfa banaynaha wazayyannaha wama laha min furoojin
Moo ndax ñoom dañu téenul xool asamaan si leen tiim, ci melo wi Nu ko tabaxe taaral ko (ak i biddiw) ; te amul benn bënn-bënn ?
وَٱلۡأَرۡضَ مَدَدۡنَٰهَا وَأَلۡقَيۡنَا فِيهَا رَوَٰسِيَ وَأَنۢبَتۡنَا فِيهَا مِن كُلِّ زَوۡجِۭ بَهِيجٖ
Waalarda madadnaha waalqayna feeha rawasiya waanbatna feeha min kulli zawjin baheejin
(Ak it Ñuy settantal) suuf si, ni Nu ko tàllale dott ca biir tundi doj saxal ca wépp xeetu gàncax wu naat te taaru.
تَبۡصِرَةٗ وَذِكۡرَىٰ لِكُلِّ عَبۡدٖ مُّنِيبٖ
Tabsiratan wathikra likulli AAabdin muneebin
mu di am njis ak ug fàttali ñeel bépp jaam buy sàkku dellu ca Boroomam.
وَنَزَّلۡنَا مِنَ ٱلسَّمَآءِ مَآءٗ مُّبَٰرَكٗا فَأَنۢبَتۡنَا بِهِۦ جَنَّـٰتٖ وَحَبَّ ٱلۡحَصِيدِ
Wanazzalna mina alssamai maan mubarakan faanbatna bihi jannatin wahabba alhaseedi
Wàcce Nanu ndox mu barkeel mu bawoo asamaan, ñu daldi cay saxal ay tooli dër ak mbay yu ñuy góob (di ko dénc),
وَٱلنَّخۡلَ بَاسِقَٰتٖ لَّهَا طَلۡعٞ نَّضِيدٞ
Waalnnakhla basiqatin laha talAAun nadeedun
tàndarma yu gudd am cëgg yu rankaloo (menn gàcc),
رِّزۡقٗا لِّلۡعِبَادِۖ وَأَحۡيَيۡنَا بِهِۦ بَلۡدَةٗ مَّيۡتٗاۚ كَذَٰلِكَ ٱلۡخُرُوجُ
Rizqan lilAAibadi waahyayna bihi baldatan maytan kathalika alkhurooju
muy wërsëgu jaam ñi. Ci ndox la Nuy dekkale suuf naatal ko. Noonu it la dekkiwaat ga di deme.
كَذَّبَتۡ قَبۡلَهُمۡ قَوۡمُ نُوحٖ وَأَصۡحَٰبُ ٱلرَّسِّ وَثَمُودُ
Kaththabat qablahum qawmu noohin waashabu alrrassi wathamoodu
Ca la leen jiitu woon, nitu Nooh , ak waa Rasi ak waa Samuud weddiwoon nañu,
وَعَادٞ وَفِرۡعَوۡنُ وَإِخۡوَٰنُ لُوطٖ
WaAAadun wafirAAawnu waikhwanu lootin
ak waa Aad ak Firawna ak mbokki Lóot,
وَأَصۡحَٰبُ ٱلۡأَيۡكَةِ وَقَوۡمُ تُبَّعٖۚ كُلّٞ كَذَّبَ ٱلرُّسُلَ فَحَقَّ وَعِيدِ
Waashabu alaykati waqawmu tubbaAAin kullun kaththaba alrrusula fahaqqa waAAeedi
ak waa Aykata ak nitu Tubba’a. Ñépp weddiwoon Yonent ya. Samag tëkku dal leen (di mbugël).
أَفَعَيِينَا بِٱلۡخَلۡقِ ٱلۡأَوَّلِۚ بَلۡ هُمۡ فِي لَبۡسٖ مِّنۡ خَلۡقٖ جَدِيدٖ
AfaAAayeena bialkhalqi alawwali bal hum fee labsin min khalqin jadeedin
Nga ne ma lan ? Nun Yàlla danoo sonn ca bind gu jëkk ga ? Ñii kay ñi ngi cim lënt ci mbirum dekkiwaat (ku sos dekkil jaaxalu ko).
وَلَقَدۡ خَلَقۡنَا ٱلۡإِنسَٰنَ وَنَعۡلَمُ مَا تُوَسۡوِسُ بِهِۦ نَفۡسُهُۥۖ وَنَحۡنُ أَقۡرَبُ إِلَيۡهِ مِنۡ حَبۡلِ ٱلۡوَرِيدِ
Walaqad khalaqna alinsana wanaAAlamu ma tuwaswisu bihi nafsuhu wanahnu aqrabu ilayhi min habli alwareedi
Nun Yàlla Noo sàkk nit bind ko te it xam Nanu liy jax-jaxi ci am xolam te sax Nun Noo ko gën a jegeñ buum giy téye ab xol
إِذۡ يَتَلَقَّى ٱلۡمُتَلَقِّيَانِ عَنِ ٱلۡيَمِينِ وَعَنِ ٱلشِّمَالِ قَعِيدٞ
Ith yatalaqqa almutalaqqiyani AAani alyameeni waAAani alshshimali qaAAeedun
ngir ñaari way joqalante yaa ngay joqalante, tey fuglu ndeyjoor ak càmmoñ.
مَّا يَلۡفِظُ مِن قَوۡلٍ إِلَّا لَدَيۡهِ رَقِيبٌ عَتِيدٞ
Ma yalfithu min qawlin illa ladayhi raqeebun AAateedun
Amul jenn wax ju muy àddu lu dul ne Raqiib ak Atiid ña nga ko tiim (ñiy bind jëfi nit ñi) .
وَجَآءَتۡ سَكۡرَةُ ٱلۡمَوۡتِ بِٱلۡحَقِّۖ ذَٰلِكَ مَا كُنتَ مِنۡهُ تَحِيدُ
Wajaat sakratu almawti bialhaqqi thalika ma kunta minhu taheedu
Sukraatus ndee aksi na ci ñoom tigi : “Loolu moo di li nga daan weddi”.
وَنُفِخَ فِي ٱلصُّورِۚ ذَٰلِكَ يَوۡمُ ٱلۡوَعِيدِ
Wanufikha fee alssoori thalika yawmu alwaAAeedi
Bu nu wolee Bufta bi : Loolu moo di bisub Tëkóo ba.
وَجَآءَتۡ كُلُّ نَفۡسٖ مَّعَهَا سَآئِقٞ وَشَهِيدٞ
Wajaat kullu nafsin maAAaha saiqun washaheedun
Bakkan bu nekk dikk ànd ak ku koy wommat ak ku koy seede.
لَّقَدۡ كُنتَ فِي غَفۡلَةٖ مِّنۡ هَٰذَا فَكَشَفۡنَا عَنكَ غِطَآءَكَ فَبَصَرُكَ ٱلۡيَوۡمَ حَدِيدٞ
Laqad kunta fee ghaflatin min hatha fakashafna AAanka ghitaaka fabasaruka alyawma hadeedun
“Lii lépp danga ko sàgganewoon. Bis niki tey, wuññi Nanu kiiraay li nekkoon ci say gët ; tey jii am nga gis bu xóot.
وَقَالَ قَرِينُهُۥ هَٰذَا مَا لَدَيَّ عَتِيدٌ
Waqala qareenuhu hatha ma ladayya AAateedun
Ka muy lëkóol ma ngay wax naan : “Kii mooy sama àndandoo bi ma dul tàggóolati”.
أَلۡقِيَا فِي جَهَنَّمَ كُلَّ كَفَّارٍ عَنِيدٖ
Alqiya fee jahannama kulla kaffarin AAaneedin
“Yéen ñaar, sànni leen ca safara weddiwaakoon ya daan féttérlu,
مَّنَّاعٖ لِّلۡخَيۡرِ مُعۡتَدٖ مُّرِيبٍ
MannaAAin lilkhayri muAAtadin mureebin
ña daan tere aw yiw, te daan jalgati, daan sikki-sàkka,
ٱلَّذِي جَعَلَ مَعَ ٱللَّهِ إِلَٰهًا ءَاخَرَ فَأَلۡقِيَاهُ فِي ٱلۡعَذَابِ ٱلشَّدِيدِ
Allathee jaAAala maAAa Allahi ilahan akhara faalqiyahu fee alAAathabi alshshadeedi
ka daan jéem a woote jeneen Yàlla di ko booleek Yàlla. Sànni leen ko ci mbugal mu tar ma”.
۞قَالَ قَرِينُهُۥ رَبَّنَا مَآ أَطۡغَيۡتُهُۥ وَلَٰكِن كَانَ فِي ضَلَٰلِۭ بَعِيدٖ
Qala qareenuhu rabbana ma atghaytuhu walakin kana fee dalalin baAAeedin
Nekkaaleem ja (Saytaane) ngay wax naan : “sama Boroom, man dey bewloowuma ko ; waaye moom dafa nekkoon ci ag réer gu tar”.(r)
قَالَ لَا تَخۡتَصِمُواْ لَدَيَّ وَقَدۡ قَدَّمۡتُ إِلَيۡكُم بِٱلۡوَعِيدِ
Qala la takhtasimoo ladayya waqad qaddamtu ilaykum bialwaAAeedi
(Yàlla daldi ne leen) : “Bu leen fi xulóo ! Lii lépp waxoon naa leen ko.
مَا يُبَدَّلُ ٱلۡقَوۡلُ لَدَيَّ وَمَآ أَنَا۠ بِظَلَّـٰمٖ لِّلۡعَبِيدِ
Ma yubaddalu alqawlu ladayya wama ana bithallamin lilAAabeedi
Wax ja du sippiku fi man ; te it Duma tooñ benn jaam”.
يَوۡمَ نَقُولُ لِجَهَنَّمَ هَلِ ٱمۡتَلَأۡتِ وَتَقُولُ هَلۡ مِن مَّزِيدٖ
Yawma naqoolu lijahannama hali imtalati wataqoolu hal min mazeedin
Bu keroogee ba Nuy laaj Safara naan ko ; “Ndax fees nga ?” Safara naan : “Dolli ma” ?
وَأُزۡلِفَتِ ٱلۡجَنَّةُ لِلۡمُتَّقِينَ غَيۡرَ بَعِيدٍ
Waozlifati aljannatu lilmuttaqeena ghayra baAAeedin
Nu waajal Àjjana way ragal ña Yàlla mu jigeñ loolu.
هَٰذَا مَا تُوعَدُونَ لِكُلِّ أَوَّابٍ حَفِيظٖ
Hatha ma tooAAadoona likulli awwabin hafeethin
“Lii mooy li Nu leen daan dig , [mu ñeel] bépp delluwaakoon ci Boroomam tey sàmm [daytalu Boroomam]
مَّنۡ خَشِيَ ٱلرَّحۡمَٰنَ بِٱلۡغَيۡبِ وَجَآءَ بِقَلۡبٖ مُّنِيبٍ
Man khashiya alrrahmana bialghaybi wajaa biqalbin muneebin
kuy ragal Yàlla Yërëmakoon bi ci kumpa, te ñëw ànd ak xol bu nangu ndigal.
ٱدۡخُلُوهَا بِسَلَٰمٖۖ ذَٰلِكَ يَوۡمُ ٱلۡخُلُودِ
Odkhulooha bisalamin thalika yawmu alkhuloodi
Dugguleen ko ci jàmm ak tal”. Te loolu mooy sax ba fàww (Àjjana) !
لَهُم مَّا يَشَآءُونَ فِيهَا وَلَدَيۡنَا مَزِيدٞ
Lahum ma yashaoona feeha waladayna mazeedun
Danañu fa am lépp lu leen soob. Te am Nanu ndollen.
وَكَمۡ أَهۡلَكۡنَا قَبۡلَهُم مِّن قَرۡنٍ هُمۡ أَشَدُّ مِنۡهُم بَطۡشٗا فَنَقَّبُواْ فِي ٱلۡبِلَٰدِ هَلۡ مِن مَّحِيصٍ
Wakam ahlakna qablahum min qarnin hum ashaddu minhum batshan fanaqqaboo fee albiladi hal min maheesin
aka bari ay xeet yu Nu faagaagaloon, ci ña leen fi jiituwoon, te ëppoon leen kàttan fuuf. Réew mu nekk dem nañu fa, mu fees di rawe.
إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَذِكۡرَىٰ لِمَن كَانَ لَهُۥ قَلۡبٌ أَوۡ أَلۡقَى ٱلسَّمۡعَ وَهُوَ شَهِيدٞ
Inna fee thalika lathikra liman kana lahu qalbun aw alqa alssamAAa wahuwa shaheedun
Ak fàttali nekk na ci biir loolu ñeel képp ku am ub xol, tey déglu booleek teewlu doon seede.
وَلَقَدۡ خَلَقۡنَا ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضَ وَمَا بَيۡنَهُمَا فِي سِتَّةِ أَيَّامٖ وَمَا مَسَّنَا مِن لُّغُوبٖ
Walaqad khalaqna alssamawati waalarda wama baynahuma fee sittati ayyamin wama massana min lughoobin
Man Yàlla, Maa bind asamaan yeek suuf ak li nekk ci seen diggante diirub juróom-benni fan, te Amuma ci benn coono.
فَٱصۡبِرۡ عَلَىٰ مَا يَقُولُونَ وَسَبِّحۡ بِحَمۡدِ رَبِّكَ قَبۡلَ طُلُوعِ ٱلشَّمۡسِ وَقَبۡلَ ٱلۡغُرُوبِ
Faisbir AAala ma yaqooloona wasabbih bihamdi rabbika qabla tulooAAi alshshamsi waqabla alghuroobi
Nangay muñ li ñuy wax : te nangay kañ di sàbbaal sa Boroom di ko sant balaa jant bi fenk ak balaa muy so ;
وَمِنَ ٱلَّيۡلِ فَسَبِّحۡهُ وَأَدۡبَٰرَ ٱلسُّجُودِ
Wamina allayli fasabbihhu waadbara alssujoodi
guddi gi it dee ko sàbbaal, ak ci ginnaaw julli gu nekk
وَٱسۡتَمِعۡ يَوۡمَ يُنَادِ ٱلۡمُنَادِ مِن مَّكَانٖ قَرِيبٖ
WaistamiAA yawma yunadi almunadi min makanin qareebin
Yaw (Yonent) bi déglul , bu keroogee ba Wootekat ba (Israafiil) di wootee fu jige,
يَوۡمَ يَسۡمَعُونَ ٱلصَّيۡحَةَ بِٱلۡحَقِّۚ ذَٰلِكَ يَوۡمُ ٱلۡخُرُوجِ
Yawma yasmaAAoona alssayhata bialhaqqi thalika yawmu alkhurooji
bis ba nga xam ne danañu dégg xaacu ga. Te bóobule Bis moo di bisub Dekkiwaat ba.
إِنَّا نَحۡنُ نُحۡيِۦ وَنُمِيتُ وَإِلَيۡنَا ٱلۡمَصِيرُ
Inna nahnu nuhyee wanumeetu wailayna almaseeru
Nun Yàlla (Man Yàlla) Maay dundal di rey, te ci Man la lépp di mujj,
يَوۡمَ تَشَقَّقُ ٱلۡأَرۡضُ عَنۡهُمۡ سِرَاعٗاۚ ذَٰلِكَ حَشۡرٌ عَلَيۡنَا يَسِيرٞ
Yawma tashaqqaqu alardu AAanhum siraAAan thalika hashrun AAalayna yaseerun
bu keroogee bis ba suuf si di focc ñuy génn gaaw lool. Loolu nag ag dajale la gu yomb ci Nun.
نَّحۡنُ أَعۡلَمُ بِمَا يَقُولُونَۖ وَمَآ أَنتَ عَلَيۡهِم بِجَبَّارٖۖ فَذَكِّرۡ بِٱلۡقُرۡءَانِ مَن يَخَافُ وَعِيدِ
Nahnu aAAlamu bima yaqooloona wama anta AAalayhim bijabbarin fathakkir bialqurani man yakhafu waAAeedi
Man Yàlla Maa gëna xam liñuy wax. Yaw nag bokkul ci sa wartéef nga di leen ga. Yaw daal nangay fàttali, Alxuraan képp ku ragal Samab tëkku. Saar 51 : Ngelawi callmeer ya 60 - Laaya