يَـٰٓأَيُّهَا ٱلۡمُزَّمِّلُ
Ya ayyuha almuzzammilu
Éy ! yaw, ku ñu sàng ki !
Al-Muzzammil
The Enshrouded One
Tekki
يَـٰٓأَيُّهَا ٱلۡمُزَّمِّلُ
Ya ayyuha almuzzammilu
Éy ! yaw, ku ñu sàng ki !
قُمِ ٱلَّيۡلَ إِلَّا قَلِيلٗا
Qumi allayla illa qaleelan
Jógal [di julli], ci guddi gi, bamu des lu ,néew ;
نِّصۡفَهُۥٓ أَوِ ٱنقُصۡ مِنۡهُ قَلِيلًا
Nisfahu awi onqus minhu qaleelan
Ab xaajam, walla sax nga wàññi ca lu tuuti ;
أَوۡ زِدۡ عَلَيۡهِ وَرَتِّلِ ٱلۡقُرۡءَانَ تَرۡتِيلًا
Aw zid AAalayhi warattili alqurana tarteelan
walla sax nga dolli ca. Te na ngay jàng Alxuraan, njàng mu léer.
إِنَّا سَنُلۡقِي عَلَيۡكَ قَوۡلٗا ثَقِيلًا
Inna sanulqee AAalayka qawlan thaqeelan
Xalset nanu laa gàll wax ju diis.
إِنَّ نَاشِئَةَ ٱلَّيۡلِ هِيَ أَشَدُّ وَطۡـٔٗا وَأَقۡوَمُ قِيلًا
Inna nashiata allayli hiya ashaddu watan waaqwamu qeelan
Jullig guddi nag moo gëna nangu te moo gëna leer cim njàng.
إِنَّ لَكَ فِي ٱلنَّهَارِ سَبۡحٗا طَوِيلٗا
Inna laka fee alnnahari sabhan taweelan
Am nga, ci bëcëg bi, jot gu gudd goo mana lijantee.
وَٱذۡكُرِ ٱسۡمَ رَبِّكَ وَتَبَتَّلۡ إِلَيۡهِ تَبۡتِيلٗا
Waothkuri isma rabbika watabattal ilayhi tabteelan
Na ngay fàttaliku di tud sa turu Boroom te wéeru ci moom fàwwu,
رَّبُّ ٱلۡمَشۡرِقِ وَٱلۡمَغۡرِبِ لَآ إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ فَٱتَّخِذۡهُ وَكِيلٗا
Rabbu almashriqi waalmaghribi la ilaha illa huwa faittakhithhu wakeelan
mooy boroom Penkook Sowu. Amul jeneen Yàlla ju dul moom. Na nga wéeru ci moom.
وَٱصۡبِرۡ عَلَىٰ مَا يَقُولُونَ وَٱهۡجُرۡهُمۡ هَجۡرٗا جَمِيلٗا
Waisbir AAala ma yaqooloona waohjurhum hajran jameelan
Muñal li ñuy wax ; te nga gàddaay leen gàddaay gu rafet (bañ leena faale).
وَذَرۡنِي وَٱلۡمُكَذِّبِينَ أُوْلِي ٱلنَّعۡمَةِ وَمَهِّلۡهُمۡ قَلِيلًا
Watharnee waalmukaththibeena olee alnnaAAmati wamahhilhum qaleelan
Bàyyi maak ñiy weddi ak ñi am alal ; te nga muñal leen tuuti :
إِنَّ لَدَيۡنَآ أَنكَالٗا وَجَحِيمٗا
Inna ladayna ankalan wajaheeman
Noo ngi leen di waajal Safara wu ànd ak jéng,
وَطَعَامٗا ذَا غُصَّةٖ وَعَذَابًا أَلِيمٗا
WataAAaman tha ghussatin waAAathaban aleeman
ak aw ñam wuy fot loo, ànd ak mbugël mu mitti.
يَوۡمَ تَرۡجُفُ ٱلۡأَرۡضُ وَٱلۡجِبَالُ وَكَانَتِ ٱلۡجِبَالُ كَثِيبٗا مَّهِيلًا
Yawma tarjufu alardu waaljibalu wakanati aljibalu katheeban maheelan
Bu keroogee bis ba suuf seek doj yi dëgg-dëgg tundu yi mel ni suufus ber mokk.
إِنَّآ أَرۡسَلۡنَآ إِلَيۡكُمۡ رَسُولٗا شَٰهِدًا عَلَيۡكُمۡ كَمَآ أَرۡسَلۡنَآ إِلَىٰ فِرۡعَوۡنَ رَسُولٗا
Inna arsalna ilaykum rasoolan shahidan AAalaykum kama arsalna ila firAAawna rasoolan
Yónni nanu ci yéen ab Yonent muy seede, kem ni nu yónnee woon ca Firawna ab Yonent.
فَعَصَىٰ فِرۡعَوۡنُ ٱلرَّسُولَ فَأَخَذۡنَٰهُ أَخۡذٗا وَبِيلٗا
FaAAasa firAAawnu alrrasoola faakhathnahu akhthan wabeelan
Firawna daldi moy Yonenta ba. Nu daldi koy jël bu metti. (faagaagal ko).
فَكَيۡفَ تَتَّقُونَ إِن كَفَرۡتُمۡ يَوۡمٗا يَجۡعَلُ ٱلۡوِلۡدَٰنَ شِيبًا
Fakayfa tattaqoona in kafartum yawman yajAAalu alwildana sheeban
Ana naka ngeen di ragale (Yàlla), su ngeen weddee, bis boo xam ne tiit ma bijaawloona ab liir ?
ٱلسَّمَآءُ مُنفَطِرُۢ بِهِۦۚ كَانَ وَعۡدُهُۥ مَفۡعُولًا
Alssamao munfatirun bihi kana waAAduhu mafAAoolan
Su asamaan si dee xar. Ca la digam ba di mate.
إِنَّ هَٰذِهِۦ تَذۡكِرَةٞۖ فَمَن شَآءَ ٱتَّخَذَ إِلَىٰ رَبِّهِۦ سَبِيلًا
Inna hathihi tathkiratun faman shaa ittakhatha ila rabbihi sabeelan
Lii nag ag fàttali la. Képp ku mu soob mu jël yoon wa jëm ca Boroomam aw ca.
۞إِنَّ رَبَّكَ يَعۡلَمُ أَنَّكَ تَقُومُ أَدۡنَىٰ مِن ثُلُثَيِ ٱلَّيۡلِ وَنِصۡفَهُۥ وَثُلُثَهُۥ وَطَآئِفَةٞ مِّنَ ٱلَّذِينَ مَعَكَۚ وَٱللَّهُ يُقَدِّرُ ٱلَّيۡلَ وَٱلنَّهَارَۚ عَلِمَ أَن لَّن تُحۡصُوهُ فَتَابَ عَلَيۡكُمۡۖ فَٱقۡرَءُواْ مَا تَيَسَّرَ مِنَ ٱلۡقُرۡءَانِۚ عَلِمَ أَن سَيَكُونُ مِنكُم مَّرۡضَىٰ وَءَاخَرُونَ يَضۡرِبُونَ فِي ٱلۡأَرۡضِ يَبۡتَغُونَ مِن فَضۡلِ ٱللَّهِ وَءَاخَرُونَ يُقَٰتِلُونَ فِي سَبِيلِ ٱللَّهِۖ فَٱقۡرَءُواْ مَا تَيَسَّرَ مِنۡهُۚ وَأَقِيمُواْ ٱلصَّلَوٰةَ وَءَاتُواْ ٱلزَّكَوٰةَ وَأَقۡرِضُواْ ٱللَّهَ قَرۡضًا حَسَنٗاۚ وَمَا تُقَدِّمُواْ لِأَنفُسِكُم مِّنۡ خَيۡرٖ تَجِدُوهُ عِندَ ٱللَّهِ هُوَ خَيۡرٗا وَأَعۡظَمَ أَجۡرٗاۚ وَٱسۡتَغۡفِرُواْ ٱللَّهَۖ إِنَّ ٱللَّهَ غَفُورٞ رَّحِيمُۢ
Inna rabbaka yaAAlamu annaka taqoomu adna min thuluthayi allayli wanisfahu wathuluthahu wataifatun mina allatheena maAAaka waAllahu yuqaddiru allayla waalnnahara AAalima an lan tuhsoohu fataba AAalaykum faiqraoo ma tayassara mina alqurani AAalima an sayakoonu minkum marda waakharoona yadriboona fee alardi yabtaghoona min fadli Allahi waakharoona yuqatiloona fee sabeeli Allahi faiqraoo ma tayassara minhu waaqeemoo alssalata waatoo alzzakata waaqridoo Allaha qardan hasanan wama tuqaddimoo lianfusikum min khayrin tajidoohu AAinda Allahi huwa khayran waaAAthama ajran waistaghfiroo Allaha inna Allaha ghafoorun raheemun
Sa Boroom xam na ne, yaw (Muhammad) da ngay taxawlu gëna néew ñaari ñetteeli xaaji guddi gi, walla xaaj ba, walla benn ñetteelu xaaj ba. Ànd kook mbooloo ci ña ànd ak yaw. Te Yàlla dana nattale guddeek bëccëg. Xam na ne manu leen fanaanee julli. Mu jégal leen. Jàngleen lu jàppandi ci Alxuraan. (Ndax moom Yàlla) xam na ne am na ci yéen ñu wopp, ak ñeneen ñuy tukki ji ci réew yi, ngir sàkku ji ci ngënéeli Yàlla yi, ak ñeneen ñuy xare ji ci yoonu Yàlla. Kon jàngleen la ca jàppandi. Te na ngeen taxawal julli, tey génne asaka, te na ngeen lebal Yàlla bor bu rafet. Te lépp lu ngeen jiitalal seen bopp ciw yiw, da ngeen ko fekk ci Yàlla, mooy la gën te moo ëpp ag pey. Te it na ngay jéggalu Yàlla. Yàlla moom Jéggalaakoon la Jaglewaakoon la.(r) Saar 74 : Ku ñu muur ki 56 - Laaya